Skip to content
مقدمة وغلاف المنتقى من موسوعة الأحاديث النبوية

مقدمة وغلاف المنتقى من موسوعة الأحاديث النبوية

Bismillahir rahmaanir rahiimi (ci turu yàlla miy yërëmaakon di jéggalaakon laay tàmbalee) Laytaay gi Cant ñeel Na Yàlla miy Boroom mbindéef yi, Yal na Yàlla sotti xéewal ak mucc ca sunu yonnente ba Muhammat moom ak waa këram ak i sahaabaam ñoom ñépp, ak képp ku leen topp cig rafetal ba keroog bis-pénc, Ginnaw loolu: Li gën a màgg ci Li jullit bi war a yittewoo ci li muy jàng di ko settantal, mbaa mukay xam di ko jëfe - Ginnaaw téere Yàlla bi- mooy sunnay Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, Yonnente Yàlla bi nee na: «Yéen nit ñi bàyyi naa fi yéen Loo xam ne féek yéen a ngi ciy…

Language: lang_wo
Prepared by:
Version: 1.0

Bismillahir rahmaanir rahiimi (ci turu yàlla miy yërëmaakon di jéggalaakon laay tàmbalee)

Laytaay gi

Cant ñeel Na Yàlla miy Boroom mbindéef yi, Yal na Yàlla sotti xéewal ak mucc ca sunu yonnente ba Muhammat moom ak waa këram ak i sahaabaam ñoom ñépp, ak képp ku leen topp cig rafetal ba keroog bis-pénc, Ginnaw loolu:

Li gën a màgg ci Li jullit bi war a yittewoo ci li muy jàng di ko settantal, mbaa mukay xam di ko jëfe - Ginnaaw téere Yàlla bi- mooy sunnay Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, Yonnente Yàlla bi nee na: «Yéen nit ñi bàyyi naa fi yéen Loo xam ne féek yéen a ngi ciy ŋoy du ngeen sànku mukk: mooy: téere Yàlla bi ak sunnay yonnenteem» Imaam Maalik moo ko soloo, Yàlla mu kawe mi wax na ne: {lu leen Yonnente bi indil jëlléen ko lu mu leen tere na ngeen ko bàyyi} [saaru Al-hasri: 7], Loolu moo tax Mbooloo mii di liggéey ci li lislaam làmboo ci ay làkk, ak mbooloo miy woote di yee nit ñi ñuy xér lool ci waajal ab yaatal bu aju ci Haddisu Yonnente bi ak di ko tekki ci làkk yu limu te wuute.

Yàlla yombal na ñu tànn lu bari ci yaatal googu Loo xam ni jullit bi dina ko soxla ci mbiru diineem ak mbiru àddunaam ànd ag ñu leeral ko leer gu tënku, leeral maanaa ya ak la muy tekki, ak lenn ci ay njariñam, daldi koy génne ci téere bii ñu tudde: «lu ñu segg tànn ko ci Hadiisu Yonnente bi» Ak taxaw ci di ko firi ci mbooleem làkk yi ñuy wax ci àdduna bi, ngir njariñ yi ci nekk yaatu, ak ngir jottali sunnay Yonnente bi ñeel doomu Aadama yépp ci seeni làkk.

Noo ngi ñaan Yàlla mu nangu jëf jile, mu def ko it jëf ju barkeel, sell ngir jëmmi Yàlla, Yal na Yàlla fay képp ku jàpp Si liggéey bii moo xam ci piri mi walla ci tasaare ko.

Yal na Yàlla dolli xéewal ak mucc ca sunu yonnente ba Muhammat

Nirël Gi ñu gàttal

Hadiisu Yonnente bi mooy ñaareelu balluwaayu sariiha, Yàlla mu kawe mi nee na: { du wax si bànneexu bàkkanam (3) Lu mu wax rekk ab wahyu la Bu ko Yàlla wahyu [An-najmi: 3-4].

Tànneef gii Moo ngi juge ci Ag kàggu ci Haddisu Yonnente bi, mi ngi làmboo ab lim ci Hadiis yu matale yi, ci Li ab jullit di soxla si mbiri diineem ak mbiri àddunaam ànd ak ay leeral yu gàtt, leeral maanaa ya ak tegtal ya, ak lenn ci njariñ ya, muy luñu tekki ci ay làkk yu bari ci làkki àdduna bi, ngir njariñ la mu làmbool nekk lu yaatu, ak ngir jottali sunnay Yonnente bi ñeel doomu Aadama yépp ci seen i làkk.