Skip to content
Ay Jumtukaay Yuy Jariñ ngir dundu gu Texe.

Ay Jumtukaay Yuy Jariñ ngir dundu gu Texe.

Téereb "Ay Jumtukaay Yuy Jariñ Jëme Ci Dundug Texe" bu Seex Abdu Rahmaan ibn Naasir As-Sahdiyyu, téere la buy jàngat yiy waral texe gu wér ci gis-gisu ngëm gu xóot. Muy tegtal jàngkat bi jëme ko ci dalug xol jaare ko ci ngëm ak jëf ju baax, ak tudd Yàlla, ak doylu, ak xalaat ci xéewal yi, ak def lu baax, ak wakkirlu ci Yàlla, ak muñ, ak jox mbir mu nekk àqam. Loolu lépp ci anam gu rafet, muy teg sa kanam ab tegtal ñeel dund gu dal, gu jub, te texe doonte sax dund gi day wëlbatiku.

Language: lang_wo
Prepared by: Sëriñ bii di Abdu Rahmaan Ibn Naasir As-Sahdiyyu
Version: 2.1

Ay Jumtukaay Yu am solo ngir dundu gu àndak Texe.

Aji-taalif ji:

Seex Abdu Rahmaan Ibn Naasir As-Sahdiyyu (yal na ko Yàlla yërëm)

Laltaay gi

Cant yépp ñeel na Yàlla, te maa ngi seede ne amul benn buur bu ñuy jaamu ci dëgg ku dul Yàlla, moom kepp amul lu ñu koy bokkaaleel, di seede ne Muhammat jaamub Yàlla la te yónenteb Yàlla la, xéewal ak mucc yal na nekk ci moom, ak ci ay ñoñam ak i àndandoom.

Ginnaaw loolu: féexug xol ak ug dalam, ak mbégteem, ak déñug ay tiisam ak naqaram, mooy li ñépp di wut, te ci lañuy amee dund gu rafet, te ci la mbégte ak bànneex di mate. Te loolu am na ay sabab yu aju ci diine, ak yu aju ci jikkó, ak yu aju ci jëf. Te sabab yooyu yépp manuñoo dajaloo lu dul ci way-gëm yi. Ñu dul ñoom nag, bu ñu ca amee dara ngir sababus coono yi seen boroom xel yi jànkoonteel, kon it lu gën a am njariñ, gën a wér, gën a rafet ci li teew ak li ñëwagul di na leen faat.

Waaye dinaa tudd ci sama bataaxal bii li ma teewlu ci ay sabab ñeel càkkuteef gii nga xam ne moo gën a màgg, te ñépp moom la ñuy wut.

Amna ci ñoom ñu ci am lu bari, ñu daal di am dundu gu neex ta teey. Amna ci ñoom it ñu ca amul dara, ñu daal di am dundu gu texeedi. Amna ci ñoom itam digg-dóomu, ci kem li ñu leen tawfeexale. Yàlla mooy maye tawfeex, te ci moom lañuy sàkkoo ndimbal ci lépp lu baax, ak ci jeñ wépp lor.

Buntub: gëm ak jëf ju baax

Sabab bi gën a màgg ci loolu, te di cëslaayam, mooy gëm Yàlla ak jëf ju baax. Yàlla mu kawe mi nee na: ﴾Képp ku jëf lu baax muy góor mbaa jigéen te fekk mu nekk Ku gëm, dananu ko dundal dund gu teey, te dananu leen fay seenub yool ci lu gën a rafet la ñu doon def 97﴿ [An-Nahl: 97].

Yàlla daal di dige ne képp ku boole ngëm ak jëf lu baax, di na am dund gu teey ci àdduna, ak fay gu rafet ci àdduna ak allaaxira.

Sababu loolu lu leer la, ndax ñi gëm Yàlla gëm gu wér guy meññi jëf ju baax tey sellal xol yi ak jikkó yi ak àdduna ak allaaxira, am nañu ay cosaan ak ay ponk yoy danañu ca gatandoo lépp lu leen di dal ci yiy sabab mbégte ak bànneex, ak yiy sabab tiitaange ak njàqare ak naqar.

Dañuy gatandu bànneex ak mbégte yi ci nangu ko, ak di ci sant Yàlla, ak di ko jëfandikoo ci lu am njariñ. Bu ñu ko jëfandikoo ci anam gii, loolu dana leen jural mbégte, ak xemmeem ci mu sax te baarkeel, ak yaakaar payu ñiy sant; yooyu di mbir yu màgg, yoy ay yiwam ak i baarkeem gën naa kawe mbégte yii di ay meññeetam.

Ñuy gatandu naqar yi, ak lor yi, ak tiis yi ak njàqare yi, ci jànkoonte ak li ñu man a jànkoonteel, ak woyofal li ñu man a woyofal, ak muñ gu rafet ci li ñu amul pexe. Ci noonu la ñuy ame ci jeexitali naqar yi jànkoonte yiy daganal jariñ, ak ay jaar-jaar ak doole, ñu am itam ci muñ gi ak ci yaakaar gi ñu yaakaar ag yool ay mbir yu rëy yuy tax naqar yi naaxsaay, ay mbégte ak yaakaar yu rafet ñëw wuutu ko, ak sàkku ngëneelu Yàlla ak ug payam, niki noonu la ko Yónente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeralee ci hadiis bu wér bii mu wax ne: «yéemu naa ci mbirum jullit bi, moom de mbiram lépp aw yiw la, bu ko mbégte dalee day sant mu doon aw yiw ci moom, bu ko lor dalee day muñ mu doon aw yiw ci moom, te kenn amul loolu ku dul jullit bi» Muslim moo ko soloo.

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne aji-gëm ji, ay yiwam ak am koomam ak meññeefi jëfam da ñu kay ful ci lépp lu ko dal ci mbégte ak lor; loo lu moo tax ngay gis ñaari nit ñoo xam ne dara da leen na dal muy lu baax mbaa lu bon, ñu wuute lool ci ni ñu koy dékkóo, te loolu day aju ci ni ñu wuutee ci ngëm ak jëf ju baax. Kii ñu melale ñaari melo yii, dafay dékku aw yiw ak aw lor ci sant ak muñ kem ni nu ko waxe, mu am ci mbégte ak xol bu féex, ak njàqare gu deñ niki noo nu xol bu xat, ak coonoy dund gi, bu ko defee mu am dund gu teey gu mat sëkk ci àdduna sii. Keneen ki nag, day dékku xéewal yi ca na mu gën a bone, ak ug rëy ak bew. Ba tax jikkóom yi soppiku, muy dund ak xéewal yi melni Bayima yi ci ag fuqle ak ug ëppal. Ànd ak loolu lépp xolam dalul, waaye dafa tasaaroo ci wàll yu bari: moo ngi tas ci ragal deñug yi mu bëgg, ak yu bari ya cay juddoo te di ko gaar, ci geneen anam it bakkan du taxaw ci wenn àpp, waaye day wéy di namm yeneen mbir, yoy man naa am te man naa bañ a am. Te bu ñu nattale woon ne sax am na ko, moom itam day nekk di jàq ci wàll yooyu ñu tudd. Muy daje ak naqar yi ci jàq ak tiit ak mer. Bul laaj sax li koy dal ci coonoy àdduna, ak feebari xel ak xol, ak tiit gi ko man a yobbu ci àtte yi gën a bon ak jaaxle yi gën a tar; ndaxte du yaakaar yool, te amul muñ gu koy dëfal tey woyofal mbir yi ci moom.

Te lii lépp lu ñuy gis la lu ñuy dund la, te benn ci yii, boo ko settantalee natt ko ci doxaliinu nit ñi, dinga gis wuute gu rëy ci diggante aji-gëm jiy jëfe li ko ngëmam digal, ak ku melul noonu, te mooy ne diine ji day ñaaxe bu baax ci doyloo wërsëgu Yàlla wi, ak li mu jox jaam yi ci ngëneelam ak teraangaam yu wuute yi.

Aji-gëm ji nag, bu ko nattu dalee ci feebar walla ñàkk, walla leneen lu ni mel ci ay gaar-gaar yoo xam ne man naa gaar ku nekk, moom de -ci ngëmam ak doyloom ak gërëmam ci li ko Yàlla sédd- day nekk ku xelam dal, du sàkku ci xolam lenn lu ñu ko dogalalul. Day xool ki ko gën a suufe, te du xool ki ko raw. Amaana sax mbégteem ak bànneexam ak nooflaayam yokk bu gisee ki am mbooleem mébéti àdduna yi bu dee amul ag doylu.

Kem ni ngay gise ki amul jëf ju juddoo ci ngëm Yàlla, bu ñu ko nattoo ci dara ci ñàkk, mbaa mu ñàkk lenn ci ay aajoy àddunaam, Dinga ko fekk mu nekk ci njàqare gu tar ak ug texeedi.

Beneen misaal: Bu sababi ragal amee, ay njàqare daal di dal nit ki, dinga gis ki ngëmam wér ab xolam dëgër daal di dal, bakkanam ne tekk, mu man a doxal tey saytu mbir mii ko bett, ci kem kàttanam ci xalaat, ak wax, ak jëf, te waajal boppam ci njàqare jii ko dal. Te yii ay melokaan lañu yuy dalal nit ki tey dëgëral xolam.

Kem ni nga fekke ki ñàkk ngëm muy nek ci safaanu melo wii: bu ragal amee xolam day jàq, ay siditam di bàyyi, xelam tasaaroo, ragal ak tiitaange gu rëy dugg ko. Mu daal di boole ragal gu bitti ak njàqareg biir gu kenn manut a wax ni mu mel. Xeeti nit ñii nag, bu ñu amul yenn sabab yu wér yu laaj jàppndal gu bari, dooleem day daanu te ay siditam bàyyandiku. Te loolu dara waraluko lu dul ñàkkug ngëm giy tax a muñ, rawatina ci waxtu yu tar yi, ak ci melokaan yu naqari yi tey daxa jàq.

Ku baax ki ak kàccoor bi, aji-gëm ji ak yéefar bi, dañoo bokk ci am fit gu ñuy fàggoo, ak yég-yég wu ñuy wàññe tiitaange yi ak di ko woyofal. Waaye aji-gëm ji day wuute ak ñoom ci dëgëru ngëmam ak muñam ak wakkirloom ci Yàlla ak sukkandikoom ci moom, ak yaakaaram ay yoolam, muy ay mbir yuy dolli fitam, di ko wàññil ragal gi, te di ko yombalal njàqare yi, kem ni ko Yàlla mu kawe mi waxe: ﴾...bu ngeen dee mettitlu, ñoom itam dañuy mettitlu ni ngeen di mettitloo, te dangeen di yaakaar ci Yàlla lu ñu yaakaarul ñoom...﴿ [An-Nisaa-i: 104]. Te ñoom dañuy am ndimbalu Yàlla ak njàppaleem gu wóor gi ak dëgëralam, lol day naaxsaayal ragal yi. Yàlla mu kawe mi nee na: ﴾...Muñleen; Yàlla mi ngi ànd ak way-muñ yi﴿ [Al-Anfaal: 46].

Rafetal jëme ci mbindeef yi, ci wax ak jëf. Bokk na ci sabab yiy dindi tiis ak naqar ak njàqare, rafetal jëme ci nit ñi ci wax ak jëf, ak xeeti mbax yépp, te loolu lépp mbaax la ak rafetal, te ci la Yàlla di dindee ci ku baax ki ak ku bon ki tiis yi ak naqar yi kem ni mu tollu, waaye jullit bi moo ci am wàll wi gën a matale, te dafay wuute ci ne rafetal gi muy def dafa jóge ci sellal ak yaakaar tiyaabaam.

Yàlla yombalal ko jëf lu baax ngir li mu yaakaar ci yiw, mu jeñal ko lor yi ngir ag sellalam ak ag yaakaar payug Yàlla, Yàlla mu kawe mi nee na: {Yiw amul ci lu bari ci seeni déeyante, lu dul ku digle saraxe, walla lu baax, walla yéwénal diggante nit ñi. Ku def loolu ngir sàkku ngërëmul Yàlla, dananu ko may yool wu rëy 114} [An-Nisaai: 114].

Yàlla mu kawe mi xibaare ne mbir yii yépp yiw lañu ci ki leen jëfe, te yiw mooy indi yiw tey dàq aw lor, te aji-gëm ji yaakaar payug Yàlla, Yàlla dana ko jox ag pay gu màgg, te bokk na ci pay gu màgg googa: deñug tiis ak naqar ak ay njàqare ak yu ni mel.

Lii ag teqale la: yittewoo jenn jëf ci jëf yi walla benn xam-xam, ci xam-xam yiy jariñ.

Bokk na ci sabab yiy dindi njàqare yiy juddoo ci siddit yu fasu, ak xol buy yittewoo yiy nëxal: mooy yittewoo benn jëf ci jëf yi, mbaa benn xam-xam, ci xam-xam yiy jariñ; ndaxte loolu day soxlaal xol bi wolif muy yittewoo mbir mii ko jàqloo. Amaana sax loolu tax mu fàtte li waraloon njàqare ga ak naqar ga, ba bakkanam bég, cawarteem dolleeku, Te sabab bii aji-gëm ji ak ku dul moom ñoo ci bokk yam. Waaye aji-gëm ji day ràññeekoo ci ngëmam ak sellalam ak sàkku gi muy sàkku yoolu Yàlla ci li muy farlu ci xam-xam bi muy jàng walla di ko jàngale, ak ci jëf ju baax ji muy def. Su fekkee ag jaamu la kon ag jaamu la; bu fekkee it ligéeyu àdduna la walla aada, mu boole ko yéene ju rafet, ak jubloo dimbandikoo ci loolu ngir man a topp Yàlla, loolu day am jeexit bu am solo ci dàq tiss yi ak naqar yi ak njàqare yi. Ñu bari ci nit ñi ñoo xam ne njàqare da leen a dal ak taqook ay naqar, ba loolu waral ñu am feebar yu wuute, ba mujj safaraam si koy gën a jariñ nekk (mu fàtte li waral naqar yooyu ak njàqare yi, te yittewoo ay jëf yenn la ci ay mbiram yu am solo).

Kon day jaadu li muy yittewoo doon lu bakkanam sopp te di ko wéttalikoo, ndaxte loolu moo gën a tax mu am jubluwaay bu am njariñ bii. Yàlla a gën a xam.

Xel mépp yittewoo jëfi bis bi teew, Bokk na ci li ñuy jeñe jaaxle ak njàqare, xel mépp daal di yittewoo limu wara def ci bisam bi mu nekk, te mu dagg ag yittewoo jamono jiy ñëw, ak njàqarey jamono ji weesu. Looloo tax Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muslu woon ci njàqare ak naqar. Njàqare ci mbir yi weesu, yi kenn manatul a delloosi walla jubbanti, amul benn njariñ, te itam njàqare guy juddoo ci ragal jamono jiy ñëw man naa lor. Kon jaam bi war naa nekk doomu bisam, mu boole jëmmam ak i góor-góorloom ci jubbantil bisam ak waxtoom wii mu nekk. Ndaxte boole xol bi ci loolu day waral nit ki matal ay jëfam, te jaam dana ci dëfale boppam ci njàqare ak naqar. Te Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, bu ñaanee ag ñaan walla muy jàngal aw xeetam ag ñaan, day soññe ci dimbandikoo Yàlla ak xeemeen ci ay ngënéelam ànd ak farlu ngir limuy ñaan am. Ak bàyyi li mu doon ñaan ngir jeñ ko; ndaxte ñaan gi day ànd ak jëf, kon jaam bi day góor-góorlu ci li koy jariñ ci diineem ak àddunaam, tey laaj boroomam mu may ko ndam ci li mu jublu, tey sàkku ndimbalam ci loolu, kem ni ko Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- waxe ne: (xéral ci lu lay jariñ, te nga dimbandikoo Yàlla te bul lompañ, bu la dara jotee, bul wax ay: bu fekkoon ne def naa lii mbaa lee kon lii du am, waaye waxal ne: Yàlla dogal na te lu ko neex lay def, ndax wax gi ngay wax naan bu doon lii baa lee, loo lu day ubbil liggéeyu saytaane) Muslim moo ko soloo. Yónente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa boole diggante digal gi jëm ci fonk mbir yu am njariñ yi ci bépp anam, ak dimbandikoo Yàlla te bañ a yambare ndax loo lu tàyyeel la te day lor, ak diggante bàyyendiku ñeel mbir yi weesu, ak di seetlu dogalu Yàlla.

Mu def mbir yi ñaari pàcc: ab pàcc bu jaam bi man a jóg ngir amal ko, walla mu amal lu mu ca man, walla mu jeñ ko mbaa mu woyofal ko, ci loolu nag la jaam bi di feeñale kàttanam tey sàkku ndimbal ci boroomam. Ak beneen pàcc bu loolu manul a ame, te loolu jaam bi da cee war a dal, gërëm ko te wommatul ko. Te sikk amul ne sàmmonte ak cëslaay lii sabab la ci mbégte ak deñug tiis ak naqar.

Lii ag teqale la ci baril tudd Yàlla

Bokk na ci sabab yi gën a mag yiy tax xol bi tijjeeku te dal, mooy baril a tudd Yàlla, ndaxte loolu amna njeexital lu yéeme ci tijjeekug xol ak ug dalam, te day dindi tiis ak naqar, moom Aji-Kawe ji nee na: ﴾...xanaa du ci tudd Yàlla la xol yi di dale﴿ [Ar-Rahd: 28] Tudd Yàlla amna jeexital ju màgg ci amug li ñuy sàkku, ngir ag jagleelam, ak li jaam bi di yaakaar ci yoolam ak payam.

Waxtaane xéewali Yàlla yi feeñ ak yi nëbbu, Naka noonu waxtaane xéewali Yàlla yi feeñ ak yi nëbbu, ndaxte xam leen ak di leen waxtaane, Yàlla da ciy dindi tiis ak naqar, te day soññ jaam bi ci cant gi nga xam ne mooy martaba ji gën a kawe te gën a tedd, ba ci sax bu dee jaam bi dafa nekk ci ñàkk mbaa feebar walla yeneen xeeti nattu yi. Ndaxte moom, bu xoolee te mengale xéewali Yàlla yi mu am - yi kenn manul a waññi te manu ko a xayma - ak li ko dal ci lu ñu sib, kon lu ñu sib loolu du am benn tolluwaay ci kanamu xéewal yi.

Lu metti ak musiba yi kay, bu ko Yàlla nattoo jaam bi, mu deme ca ag muñ ak gërëm ak jébbalu, diisaayam dina woyof te mettitam dina néew. Te yaakaar gi jaam bi am ci payam ga ak ni muy jaamoo Yàlla ci taxaw ci muñ ak gërëm, mooy tax mbir yu wex yi di mel ni lu neex, ba neex-neexu payam ga day tax mu fàtte wexaayu muñ ga.

Xool ci ñi nu gën a suufe, Bokk na ci mbir yiy gën a jariñ ci bérab bii, jëfandikoo li Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wane ci hadiis bu wér bi ne: (deeleen xool ci ñi leen féete suuf, te buleen xool ci ñi leen féete kaw, ndax mooy tax ba dungeen xeeb xéewali Yàlla yi ci seen kaw) Muslim moo ko soloo. Bu jaam bi xoolee seetlu gu màgg gii, dina gis boppam mu raw mbooloo mu bari ci mbindeef yi ci jàmm ak li ci topp, ak ci wërsëg ak li ci topp, ci melokaan gu mu man a tollu. Loolu dana tax tiitaangeem ak njàqareem ak naqaram jeex, mbégteem ak bànneexam di yokk, ak ni muy ñeewe xéewali Yàlla yi mu rawe ñi dul moom ci ñi ko féete suuf.

Saa bu jaam bi gënee yàggal settantalam ci xéewali Yàlla yu feeñ yi ak yu nëbbu yi, yu diine yi ak yu àdduna yi, dina gis ne Boroomam may na ko aw yiw te musal na ko ci ay yu bari. Te loo lu, sikk amul ne, day dindi tiis ak naqar, tey waral mbégte ak kontaante.

Lii ag teqale la: ci dox jëm ci dindi sabab yiy xëcc ay njàqare, ak amal sabab yiy xëcc mbégte.

Bokk na ci sabab yiy waral mbégte tey dindi njàqare ak naqar, mooy góor-góorlu ci dindi sabab yiy indi ay njàqare ak ci jéema amal sabab yiy indi mbégte; loolu nag day ame ci fàtte li weesu ci lu ko naqari woon lu mu manul a delloosi, ak mu xam ne soxlaal xelam ci loolu ay caaxaan la lu jomb la it, te loolu ag dese la ak ug ndofe, kon mu xeex ak xolam ci bañ cee xalaat. Niki noonu it mu xeex ak xolam ci tiitaangeem ci li koy xaar, ci li muy njort niki ñàkk mbaa ragal mbaa yeneen yu mel noonu ci ay tiis yu muy xalaat ne dinañu ko dal ëllëgu ci dundam. Mu xam ne mbir yiy ñëw xameesul la cay am ci yiw ak ci ay, ak yaakaar ak ay mettit, ak ne ñoo ngi ci loxoy Aji-Am-Kàttan ji di Aji-Xereñ ji, jaam yi amuñu ci dara lu dul jàpp ci sabab yi ngir sàkku ci yiwam yi, ak jeñ loram yi. Te jaam bi xam ne bu dëdduloo woon xelam tiitaange gi mu am ci mbiram miy ñëw, te wéeru ci Boroomam ngir mu yéwénal ko, te dalal xelam ci Moom ci loolu, bu defee loolu xolam dina dal, ay mbiram jub, te tiitaangeem ak njàqareem dinañu deñ.

Jëfandikoo ñaan, Bokk na ci li gën a am njariñ ci seetlu mbir yi ci kanam ñu jëfandikoo ñaan gii Yonente bi daan ñaan: "Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi lay ñaan nga yéwénalal ma sama diine ji nga xam ne mooy aar samay mbir, te nga baaxal sama àdduna ji nga xam ne fi laay dund, te nga baaxal sama allaaxira ja nga xam ne mooy sama delluwaay, te nga def dund gi di lu may dolli yiw, nga def samag dee muy lu may noppal ci wépp ay" Muslim moo ko soloo. Naka noo nu itam waxam ji: «Yàlla sunu Boroom sa yërmànde dong laa yaakaar, kon bul ma bàyyi ak sama bopp luy toll ni xefu bët, malay ñaan nga yéwénalal ma sama mbir yépp, amul kenn ku nu war a jaamu ku dul yaw» Abuu Daawuda moo ko soloo ci càllale gu wér. Bu jaam bi waxee ñaan gii nga xam ne dafa am yéwénug ëllëgam ci diineem ak àddunaam, mu ànd ak xol bu teew lu, ak yéene ju sell, te di ci boole di góor-góorlu ci liy tax loolu am, Yàlla dina ko jox li mu ñaan yaakaar ko te jëfe ko, te njàqareem dina soppeeku doon mbégte ak bànneex.

Lii ag teqale la, ci nattale li gën a ñaaw ci mbir yi jamtalu

Bokk na ci sabab yiy gën a jariñ ngir dindi tiitaange ak njàqare, bu dee wenn tiis dafa dal jaam bi, mooy mu góor-góorlu ci woyofal ko ci nattale li gën a bon ci li mbir mi man a mujje, te mu waajal boppam ci loolu. Bu defee loolu, na góor-góorlu ci woyofal li mu man a woyofal ci kem kàttanam. Ci waajtaay boobu ak ci góor-góorlu googu di jariñ, ci la ay njàqareem ak ay naqarram di deñe, bu ko defee góor-góorlu googu dana nekk luy xëcc ay njariñ, ak di jeñ ay lor te di na nekk lu yomb ci jaam bi.

Kon bu sababi tiitaange dalee ci kawam, ak sababi jàngoro yi, ak sababi ñàkk, ak mu ñàkk a am li mu bëgg ci mbir yu wuute, na ko gatandoo ak xel mu dal te di ci waajal bakkanam. Ndaxte waajal bakkan bi ci dékku ay coono dafay woyofal te day dindi tar-taram, rawatina bu yëngatoo ci jeñ ko ci kem kàttanam. Bu ko defee ag waajal bakkan dajaloo ci moom ak jëf ju am njariñ ju koy soxlaal wolif muy yittewoo bàyyi xel musiba yi, muy xeex ak bakkanam ngir yeesalaat dooley dékku coono yi, ànd ak di ci wakkirlu ci Yàlla te wóolu ko wóolu gu rafet. Te sikk amul ci ne mbir yile am nañu njariñ lu mag ci amal mbégte ak ubbikug xol yi, ànd ak li jaam bi di yaakaar ciy yool yu teew ak yu ñëwagul. Te lii de lu ñu gis la lu ñu dund la it. Te ay xew-xewam lu bari la lool ci ñi ko dund.

Lii ag teqale la ci dëgërug xol bi, ak bañ a jaaxle ak di jeexitalu.

Bokk na ci faj yi gën a màgg ñeel feebari xol yu juddoo ci njàqare, ba ci it feebari yaram yi: dëgërug xol ak ñàkk a jàqam ak di jeexitalu ci ay defe ak jeneer yi nga xam ne xalaat yu bon Moo koy koy indi. mer ak jaxasoo, dañoo bokk ci sabab yu metti yi, ku foog ne xewug yu metti yi ak deñug bëgg-bëgg yi, Loolu da koy tàbbal ci ay njàqare ak ay tiitaange, ak feebari xol ak yu yaram, ak doyadig xel gi nga xam ne dafa am ay jeexital yu bon, yoy nit ñi gis nañu ay loram yu bari.

Wakkirlu ci Yàlla, Saa bu xol bi sukkandikoo ci Yàlla, te wakkirlu ci moom, te bañ a topp ay defenaa ak i jeneer yu bon, mu wóolu Yàlla te sàkku ngëneelam, ci noonu la tiis yi ak naqar di ko soree, feebari yaram yu bari ak yu xol yi deñ ci moom, xol bi am doole ak ug yaatu ak mbégte mu kenn manul a misaal. Bariwaana ay opitaal yu fees dell ak ñi ame feebari defe ak jeneer yu bon, te bariwaana yu mbir yii jeexital ci xoli ñu bari ci boroom kàttan yi, waxuma la ak ñu néew kàttan ñi, te bariwaana lu mu waral ci ag dese ak ug ndofe. Te ki mucc mooy ki Yàlla musal te tawfeexal ko ci mu xare ak bakkanam ci mu amal sabab yu am njariñ yuy dëgëral xol bi, tey jeñ tiitaangeem. Yàlla mu kawe mi nee na: {...képp ku wakkirlu ci Yàlla; Yàlla doy na ko...} [At-Talaaq: 3]. mooy doy na ko ci mbooleem lu ko soxal ci mbirum diineem ak àddunaam.

Ki wakkirlu ci Yàlla kàttanu xol lay am, njort yi duñu jeexital ci moom, te xew-xew yi duñu ko jàqloo; ndaxte xam na ne loolu ci néew kàttanu bakkan la jóge, ak ci lompañ ak ragal gu dul dëgg. Ànd ak loolu day xam ne Yàlla warlul na ag doy gu mat sëkk ñeel ki wakkirlu ci moom, kon mu wóolu Yàlla te dal ci digeem. Bu ko defee njàqareem ak tiitaangeem deñ, jafe-jafeem soppiku di ag yomb, njàqareem di mbégte ragalam di kaaraange. Kon noo ngi ñaan Yàlla mu kawe mi mu may nu jàmm, te may nu kàttanu xol ak ug dëgëram, ak wakkirlu gu mat sëkk gi Yàlla warlul lépp yiw ñeel ay ñoñam, te di leen fegal bépp tiis ak lor.

Lii ag teqale la, jëm ci waajal bakkan bi ci muñ ayibi ñeneen ñi.

Nekk na ci waxi Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc-: «Jullit bu góor du bañ jullit bu jigéen, ndax su bañee ci moom jenn jikkó gërëm na ci moom jeneen jikkó» Muslim moo ko soloo.

Ñaari njariñ yu màgg:

Benn bi mooy: Ag gindee ci ni ngay jëflanteek sa jabar ak sa jegeñaale ak sa àndandoo ak ki ngay jëflanteel, ak képp ku sa diggante ak moom am lënkaloo ak ug jokkoo, ak ne jaadu na nga waajal sa bopp ci ne fàww mu am ayib mbaa ag wàññeeku mbaa mbir moo sib. Kon boo gisee loolu, nanga lënkale loolu ak li la war mbaa li jaadu ci yaw ci dëgëral jokkoo gi ak des ca mbëggeel ga, ci fàttaliku li mu am ci ay rafet-rafet, ak jubluwaay yu jagoo ak yu matale. Te ci jéllale ayib yooyu ak di bàyyi xel yu baax yi, la àndandoo gi ak jokkoo gi di saxe, ci la noflaay gi di mate nga am ko itam.

Njariñ bu ñaareel bi: mooy dindi njàqare ak tiitaange, ak dal ak teey gu sax, ak sax ci taxawal àq yu war yi ak yi ñu sopp, ak amug noflaay ci diggante ñaari wàll yi. Te képp ku gindikoowul ci lii Yonente bi tudd, -waaye mu safaane mbir mi, di xool ñaawteef yi, gumba ci yu baax yi-, kon fàww mu jàq, te fàww mbëggeel gi nekk ci digganteem ak ka mu nekkal am ag nëx, te lu bari ci àq yi kenn ku nekk waroon a sàmm dana dog.

Ñu bari ci nit ñi, boroom yitte yu kawe yi dañuy tàggat seen bakkan ci muñ ak ug dal bu ay musiba ak ay njàqare amee. Waaye bu dee mbir yu xeebu yu ñàkk-solo yi dañuy jaaxle, te seen jàmm jaxasoo. Te li waral loolu mooy dañoo waajal seen i bakkan ci mbir yu mag yi, bàyyi ko ci yu ndaw yi, loolu lor leen ba jeexital ci seen noflaay. Kon ku am fulla day waajal bakkanam ci mbir yu ndaw yi ak yu mag yi, te di ñaan Yàlla mu dimbali ko ci te bañ ko a bàyyi ak boppam luy tollook xefu bët. Bu ko defee lu ndaw li day yomb ci moom, niki ni lu mag li di yombe ci moom. Mu des di ku dal bakkan, xolam dal, muy ku noppalu.

Lii ag teqale la, jëm ci bañ a wéy di topp njàqare yi

Ki am xel day xam ne dundam gu baax mooy dundug texe ak ug dal , te lu gàtt la lool. Kon jaaduwul mu koy gàttal ci njàqare ak di topp ci ginaaw nëx-nëx yi, ndaxte loolu dafa safaanoo ak dund gu baax gi. Bu ko defee mu nay ci dundam gi, ba lu ci bari du sànku ci tiis yi ak nëx-nëx yi. Loolu nag amul wuute ci diggante ku baax ki ak kàccoor bi. Waaye aji-gëm ji, amna ci melookaan wii cér bu gën a mag, ak wall wu am njariñ fii ci àdduna ak fële ca allaaxira.

Méngale diggante xéewali Yàlla yi ak lu ko jot ci ay nattu, Jaadu na tamit bu ko nattu dalee walla mu ragal ko, mu gam-gamle diggante desiti xéewal yi mu am, yu diine walla yu àdduna, ak nattu bi ko dal. Ci gam-gamle googu la barig xéewal yi mu nekk di feeñe, ak naaxsaayug nattu yi ko dal.

Naka noonu itam day méngale diggante li mu ragal ciy lor yu man a dal ci kawam, ak yu bari yi jamtal ci ne man na see mucc, kon bu mu bàyyi li jamtal te doyadi muy not leneen lu jamtal te dëgër. Ci noonu la njàqareem ak ragalam di deñe. Mu nattale li jamtal te gën a rëy ci li ko man a dal, mu waajal ci boppam ngir bu amee, te mu dox jëm ci jeñ li amagul, walla mu wàññi ko.

Loru nit ñi ci seen kaw lay dal fii ak soxlaalu ko, Bokku na ci mbir yu am njariñ yi nga xam ne lor gi la nit ñi di lor, rawatina ci kàddu yu bon yi, du la lor, waaye ñoom lay lor, lu dul boo ci sonalee sa bopp di ko yittewoo, ba nga may ko yoon wu mu jàppe say yég-yég, bu boobaa nag kon dana la lor niki mu leen di lore. Waaye boo ko faalewul du la lor ci dara.

Rafetalal sa dund ci xalaat yu am njariñ yi, Nanga xam ne sa dund ci say xalaat la aju. Bu fekkee ne ay xalaat la yoo xam ne njariñ la lay jural ci sa diine walla sa àdduna, kon sa dund dina nekk dund gu baax am mbégte; bu dul loolu nag, kon mbir mi dafay safaanoo.

Jëflànte gi nekk ngir Yàlla, waaye du ngir mbindeef yi, Bokk na ci mbir yi gën a am njariñ ngir dàq njàqare, mooy nga tàggat sa bopp ci bañ a sàkku cantug keneen ku dul Yàlla. Boo defee lu baax jëme ko ci ki ko yelloo ci yaw, walla ki ko yelloowul, na nga xam ne loolu sa jëflànte la ak Yàlla, kon bul soxla cantug ki nga teral, kem ni ko Yàlla mu kawe mi waxe ci mbirum mbindeefam yi mu jagoo: ﴾Danu leen di leel ngir jëmi Yàlla rekk, bëggunu ci yéen pay bëggunu it ngërëm 9﴿ [Al-insaan: 9].

Lii dafay gën a feddaliku ci jëflànte ak njaboot gi ak doom yi, te bokk na ci liy wane dëgërug sag jokkoo ak ñoom, Kon boo tàggatee sa bopp ci dindil leen aw ay, dinga noppale te dinga noppalu. Te bokk na ci liy waral noflaay, jàpp ci ngëneel yi ak jëfe leen ci anam gu la ci sa bakkan soññee, te bañ cee gàlloo lu lay jàqloo, ndax kon danga sooy dellu ginnaaw te doo am ngëneel la, ndaxte da nga jaar yoon wu dëng. Te daa bokk ci xereñte, mooy nga soppi mbir yu nëx yi def leen ay mbir yu set te neex. Ci noonu la setum bànneex yi di yokkoo, te naqar yi deñ.

Yittewoo luy jariñ, te bàyyi luy lor. Yittewool mbor yi lay jariñ te jëf ngir amal ko, te bul geestu mbir yiy lore; ngir nga soxlaal sa bopp ci loolu wolif sabab yiy xëcc ay jaaxle, ak i njàqare, te nga dimbandikoo ci noppalu ak dajale sa bakkan ci jëf yu am solo yi.

Def jëf yi fa saasa. Bokk na ci mbir yiy jariñ nga def jëf yi fa saasa, te waajal liy ñëw; ndax jëf yi, bu ñu leen deful, dana dajaloo ak jëf ya jiitu, jëf ya cay topp it fekk si leen, ba tax ay mbiram diis. Waaye bu ñu defee lépp ci waxtoom, kon dinga mana def mbir yay ñëw ànd ak kàttanu xalaat ak kàttanu jëf.

Toftale yi gën a yay ànd ak diisoo, Jaadu na nga tànn ci jëf yu am njariñ yi li gën a am solo ak li ci topp, te nga ràññatle li sa bakkan jeng jëm te nga xemmem ko lool, ndaxte safaanam day waral yoqat, tàyyeel ak naqar. Nanga dimbandikoo ci loolu xalaat bu jub ànd ak diisoo, ndaxte ku disoo du réccu, te nga jàngat bu baax li nga bëgg a def. Bu la njariñ li leeree te nga dogu ca, nga wakkirlu ci Yàlla, ndaxte Yàlla dafa bëgg ñiy wakkirlu ci moom.

Mbooleem cant yi ñeel na Yàlla miy Boroom mbindeef yi.

Yal na Yàlla dolli xéewal ak mucc ci sunu Sang Muhammat moom ak waa këram ak i sahaabaam.