Books
Books
Ay Jumtukaay Yuy Jariñ ngir dundu gu Texe.
Téereb "Ay Jumtukaay Yuy Jariñ Jëme Ci Dundug Texe" bu Seex Abdu Rahmaan ibn Naasir As-Sahdiyyu, téere la buy jàngat yiy waral texe gu wér ci gis-gisu ngëm gu xóot. Muy tegtal jàngkat bi jëme ko ci dalug xol jaare ko ci ngëm ak jëf ju baax, ak tudd Yàlla, ak doylu, ak xalaat ci xéewal yi, ak def lu baax, ak wakkirlu ci Yàlla, ak muñ, ak jox mbir mu nekk àqam. Loolu lépp ci anam gu rafet, muy teg sa kanam ab tegtal ñeel dund gu dal, gu jub, te texe doonte sax dund gi day wëlbatiku.
الإسلام دين رسل الله
Lislaam mooy diiney Yonnente Yàlla yi Lislaam mooy jébbalul Yàlla mi bind àdduna bi di ko doxal, wommatul ko ngir bëgg ko ak màggal ko, cosaanu lislaam mooy gëm Yàlla, ak ne moom mooy Aji-Bind ji, te lépp lu dul moom mbindeef la, ak ne moom moo yayoo jaamu moom rekk amul bokkaale, amul lenn lu ñuy jaamu ci dëgg ku dul moom,ay tur yu rafet ñeel na ko ak ay melo yu kawe, mooy ki mat sëkk, jurul kenn te kenn juru ko te amul benn nawle du caagine niroowaale, du wàcc te du jël jëmmi lenn ci mbindeefam yi. Lislaam mooy diiney Yàlla mi nga xam ne du nangu ci nit jenn diine ju dul moom, te mooy diine…
الإسلام دين رب العالمين
Ci turu Yàlla miy Aji-Yërëm képp ku nekk ci kaw suuf jagleel ko jullit ñi ca allaaxira ci laay tàmbalee. Lislaam mooy diiney Boroom mbindéef yi. Kan mooy sa Boroom? Lii mooy laaj bi gën a màgg ci lépp; te mooy laaj bi ëpp solo ci li nit ki war a xam ab tontoom. Sunu Boroom mooy ki bind asamaan yi ak suuf si, daal di wàcce am ndox mu bawoo asamaan, mu génne ca ay meññet ak i garab ngir muy sunug dund, ak dundug baayima yi nga xam ne dañu koy lekk, Moo nu bind bind sunuy baay, bind lépp, moo def guddi ak bëccëg, mooy ki def guddi muy waxtuw nelaw ak noppalu, mu def bëccëg muy waxtuw sàkku dund,…
الإسلام - نبذة موجزة عن الإسلام (مشتملة على الأدلة)
Lislaam Ab tënk bu gàtt ci Lislaam ni ki ni mu dikke ci Alxuraan ju tedd ji ak ci Sunnas Yonent bi Téere bu am solo bu làmboo xamle gu tënku ci Lislaam tey leeral ay cosaanam yi ëpp solo ak i njàggaleem ak ub taaram bu bawoo ci ay delluwaayam te mooy Alxuraan ak Sunnas Yonent bi. téere bi nag dees koo jëmale ci bépp muskallaf moo xam jullit la wala du jullit, def ko ci seen uw làkk ci jépp jamono ak bépp barab, ak nu séen i mbir ma na dème mbaa seen uw nekkiin. ( téere bi nag daal làmboo ay tektal yu bawoo ci Alxuraan ju tedd ji ak sunnas Yonent bi) Lislaam mooy bataaxalu boroom bi jëmm ci…
Melow jullig Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-
Téereb «Ni Yonnente bi ﷺ daan jullee», Seex Abdul Asiis Ibn Baas -yal na ko Yàlla yërëm- dafa caa tënk melokaanu jullig Yonnente bi ﷺ, ci anam gu yomb te wóor, mu wéeru ci mbind yu wér, ngir mu doon ag gidee ñeel jullit bi ci ag julleem. Leeral na ci ponki julli yi, ak i sunnaam, ak i melokaam, dale ca jàppu ma ba ca sëlmël ga, di boole firnde ak leeral, tey woote ci roy gu mat ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci jaamu Yàlla gi gën a màgg.
Lii ab tënk la ci melow Umra ak i àtteem.
Mbooleem xeeti cant yi ñeel na Yàlla miy Boroom mbindeef yi, jàmm ak mucc yal na nekk ci sunu Yonnente bi Muhammat, ak ay ñoñam ak sahaabaam yépp. Ginnaaw loolu: Lii ab bataaxal bu ñu tënk la ci melow Umra ak i àtteem ak i tegginam, xér nanu ci lool ci leeral li ëpp ci li ñu aajowoo ci Umra. Yàlla rekk lanuy ñaan mu def ko muy lu sell ñeel jëmmam ju Tedd ji, ak mu jariñ ci mbooleem jullit ñi.
من خلقني؟ ولماذا؟
Kan moom a bind AK lu tax mu bind ma ? BEEPP MIR MUMU MANA DOON DAAY TEKTALE AMUK YAALLA MIKO BIND! KAN MOO BIND ASAMAN YI AK LICI SEEN BIIR CI AY MBINDEEF YU MAAGG YOO XAMNE MBINDEEF MANULEENA PEEK? Kan moo def nosiin wu xereñe wii ? Kan moo bind nit may ko ag dégg ak ub jis ak xel te def ko muy ku man a am xam-xam tey xam li xew. Naka ngay firee wii tërëliin wu yéeme ci jumtukaay yi nekk ci sa biir yaram ak yaramu ndundat yi ? Kan moo fent loolu ? Naka la dund bu rëy bii man a nosaloo ci tëraliinam yu koy nose nose gu yéeme ba àdduna sosoo ba tay ?
مقدمة وغلاف المنتقى من موسوعة الأحاديث النبوية
Bismillahir rahmaanir rahiimi (ci turu yàlla miy yërëmaakon di jéggalaakon laay tàmbalee) Laytaay gi Cant ñeel Na Yàlla miy Boroom mbindéef yi, Yal na Yàlla sotti xéewal ak mucc ca sunu yonnente ba Muhammat moom ak waa këram ak i sahaabaam ñoom ñépp, ak képp ku leen topp cig rafetal ba keroog bis-pénc, Ginnaw loolu: Li gën a màgg ci Li jullit bi war a yittewoo ci li muy jàng di ko settantal, mbaa mukay xam di ko jëfe - Ginnaaw téere Yàlla bi- mooy sunnay Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, Yonnente Yàlla bi nee na: «Yéen nit ñi bàyyi naa fi yéen Loo xam ne féek yéen a ngi ciy…
الشهادتين
Boo bëggee dugg ci lislaam, dangay wax ci kàddu gu gu ñu dégg seede gii di ñëw, te xam maanaa ma te gëm ko: Ashadu an laa-i-Laaha illal-Laahu (maanaay baat yii mooy ne amul kenn ku yayoo jaamu ku dul Yàlla), Maa ngi seede ne Muhammat ndawul Yàlla la, Iisaa ibnu Maryama it jaamub Yàlla la di ndawam. Ashadu an laa-i-Laaha illal-Laahu, wa ashadu anna Muhammadan rasuulul Laahi.
Teggini tukki ak i àtteem
Sant ñeel na Yàlla miy Boroom mbindeef yi, xéewal ak jàmm yal na nekk ci sunu Yonnente bi Muhammat ak ay ñoñam,ak àndandoom yépp. Ginnaaw loolu: Lii ab bataaxel la bu ñu tënk ci teggiini tukki ak i àtteem, bëgg nanoo leeral li ëpp ci li aji-tukki ji di aajowoo. Yàlla rekk lanuy ñaan mu def ko muy lu sell ñeel jëmmam ju Tedd ji, ak mu jariñ ci mbooleem jullit ñi. Bi ci jëkk: teggiini tukki
Jëfi safaan yi nit ñi di faral di def ci Aj ak Umra ak Siyaare Yónnent bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal Ko.
Njuumte ak jëfi safaan yi aju ci Umra Bi ci njëkk: jëfi safaan ak njuumte yi nit ñi di def ci Armal Ñàkk a ihlaal, ci mu bañ a yëkkëti kàddoom ci jaamu gi mu namm a def ca ba muy tàmbalee fas Armal ga. Te sunna si mooy: mu yëkkëti ca kàddoom.
Lii ab tënk la buy leeral naka lañuy Aje
Cant ñeel na Yàlla miy Boroom mbindeef yi, xéewal ak jàmm yal na nekk ci sunu Yonnente bi Muhammat ak ay ñoñam, ak àndandoom yépp. Ginnaaw loolu: Lii ab bataaxel bees tënk la buy leeral naka lañuy aje, bégg nanu ci a leeral ci li ëpp ci li kiy aj di aajowoo. Yàlla rekk lanuy ñaan mu def ko muy lu sell ñeel jëmmam ju Tedd ji, ak mu jariñ ci mbooleem jullit ñi. Laltaay
Ay ñaan yu matale[1]
Lii ay ñaan yu matale la, yu rot ci Alxuraan ju Tedd ji, walla mu wér jóge ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, ñu yoonal nu di ko ñaane ci bépp jamono ak bépp barab, bokk na ca bu ñuy wër Kaaba gi ak bu ñuy dox Safaa ak Marwa, ak ca Arafa ak Musdalifa, waaye nag jagleeluñu leen ko. Bi ci njëkk: ñaan yi bawoo ci Alxuraan. Sunu Boroom nangul nu yaw yaay Aji-Dégg ji di Aji-Xam ji* Te nga jéggal nu yaw yaay Jéggalaakoon bi di Yërëmaakoon bi. Yaw Yàlla Sunu Boroom defal nu yiwu àdduna ak yiwu allaaxira te nga fegal nu mbugalum sawara. Yaw Yàlla Sunu Boroom bul nu ko jàppe bu nu…
Pas-pas bu wér ak ub safaanam.
Aji taalif ji: Maa ngi tàmbulee samay wax ak samay jёf ci turu Yàlla miy Boroom yёrmànde ju yaatu ji ci adduna tay jakleell yёrmàndeem ёllag way gёm yi. Laytaayug téere bi. Sant ñeel na Yàlla rekk, xéewal ak mucc yalna nekk ci ki nga xam ne amul Yónnente buy ñew ginnaawam, ak ay ñoñam ak i àndandoom.
وجوب العمل بالسنة وكفر من أنكرها
Warug jëfe sunnas Yonnent bi ak kéefarug képp ku ko weddi. Aji-taalif ji Abdul Asiis Ibn baas -yal na ko Yàlla yërëm- Ci turu Yàlla miy Aji-Yërëm kepp ku nekk ci kaw suuf jagleel ko jullit ñi ca allaaxira ci laay tàmbalee. Laytaay ji Cant ñeel na Boroom mbidéef yi, Ag mujj ñeel na ñi ragal Yàlla, jàmm ak xéewal yal na nekk ci sunu Yonnent Muhammat, moog waa këram ak i àndandoom ñoom ñi gàddu téere Yàlla bi ak Sunnas seen Yonnent -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- jottali ko ña ñëw ci seen ginnaaw, ci koolute gu mat sëkk ak ug xereñte, ak ug wattu gu mat sëkk ñeel ay maanaam ak i baatam,…