Skip to content
Lii ab tënk la ci melow Umra ak i àtteem.

Lii ab tënk la ci melow Umra ak i àtteem.

Mbooleem xeeti cant yi ñeel na Yàlla miy Boroom mbindeef yi, jàmm ak mucc yal na nekk ci sunu Yonnente bi Muhammat, ak ay ñoñam ak sahaabaam yépp. Ginnaaw loolu: Lii ab bataaxal bu ñu tënk la ci melow Umra ak i àtteem ak i tegginam, xér nanu ci lool ci leeral li ëpp ci li ñu aajowoo ci Umra. Yàlla rekk lanuy ñaan mu def ko muy lu sell ñeel jëmmam ju Tedd ji, ak mu jariñ ci mbooleem jullit ñi.

Language: lang_wo
Prepared by: Al-Lajnatu Al-Hilmiyyatu Bi Jamhiyati Al-Muhtawaa Al-Islaamii Bil-Luxaati.
Version: 3.0

Lii ab tënk la ci melow Umra ak i àtteem.

Mbooleem xeeti cant yi ñeel na Yàlla miy Boroom mbindeef yi, jàmm ak mucc yal na nekk ci sunu Yonnente bi Muhammat, ak ay ñoñam ak sahaabaam yépp.

Ginnaaw loolu:

Lii ab bataaxal bu ñu tënk la ci melow Umra ak i àtteem ak i tegginam, xér nanu ci lool ci leeral li ëpp ci li ñu aajowoo ci Umra.

Yàlla rekk lanuy ñaan mu def ko muy lu sell ñeel jëmmam ju Tedd ji, ak mu jariñ ci mbooleem jullit ñi.

Al-Lajnatu Al-Hilmiyyatu Bi Jamhiyati Al-Muhtawaa Al-Islaamii Bil-Luxaati.

Laltaay

Bi ci njëkk: sàrt yiy tax ñu nangu ag jaamu Yàlla

Ag Jaamu Yàlla deesu ko nangu fa Yàlla lu dul ci ñaari sàrt:

Sellal, te mooy mu jublu ca jëmmi Yàlla ak kër gu mujj ga, Yàlla mu kawe mi nee na: "digaluñu leen lu dul ñu jaamu Yàlla di aji-sellal diine ji ñeel ko[1]", [Al-Bayyinatu: 5]. Maanaam: dëgmël ko ak jaamu ko, te dummóoyu lu dul moom, Tafsiiru As-Sahdii (xëtu 538)

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax ne: "jëf yi moo ngi aju ci yéene yi, te ñeel na ku nekk la mu yéene" [2] Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (1), ak Muslim, ci limatu (1907).

Topp Yonnente bi ci wax ak jëf, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "képp ku sos ci sunu mbir mii lu ci bokkul dees ka koy delloo" Nekk na ci geneen nettali gu Muslim (1718): "Képp ku jëf dara ci diine ji te amu ci sunu ndigal dees ka koy delloo". [3] Al-Buxaarii soloo na ko, ci limatu(2697), ak Muslim, ci limatu(1718) [4] Muslim soloo na ko ci limatu (1718).

***

Ñaareel bi: àtteb jàng melow Umra ak i àtteem

Jaadu na ci ku namm a jaamu Yàlla mu kawe mi ci genn jaamu mu xamlu la cay njubug Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc; ngir jëfam dëppoo ak sunna, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na ñaax nit ñi ci topp ko ak tegu ci njubam gi; jële nañu ci Maalik ibn Al-Huwayris yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "julleeleen kem ni ngeen may gise may jullee" [5] Al-Buxaarii soloo na ko ci limatu (6008).

Jële nañu ci Jaabir yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: "gis naa Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy sànni fekk moo nga ca kaw waruwaayam ci bisub tabaski, mu wax naan: jëlleen seen i jaamu; ndax man xamuma ndax dinaa ajaat ginnaaw sama aj gii" [4] Muslim soloo na ko ci limatu (1297).

***

Ñaareel bi: ngëneelu Umra

Umra amna ñaari ngëneel: gu matale, ag gu ñu jagleel.

Gu matale gi:

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: (Umra ba geneen Umra ga day kaffaara li nekk seen diggante, te aj gu baax dara du fayam lu dul àjjana) [2] Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (1773), ak Muslim, ci limatu (1349).

Jële nañu ci Abdallah Ibn Mashuud yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: (toftaleleen diggante Aj ak Umra; ndaxte ñoom ñaar dañuy dàq ñàkk ak bàkkaar yi kem ni sawara di dàqe li bon ci weñ ak wurus ak xaalis te genn fay ñeelul Aj gu baax lu dul àjjana) Bérabu sawaraw tëgg bi ak cuubkat bi. At-Tamhiid bu Ibn Abdul Barri (15/102) [9] At-Tirmisii soloo na ko, ci limatu (810), ak An-Nasaa ii, ci limatu, (2631].

Gi ñu jagleel ci weeru koor la: jële nañu ci Ibn Abbaas yal na leen Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "Umra ci weeru koor day tolloo ak Aj gu ñu ànd ak man [3]" Maanaam: day tolloo ak ànd ak man Aj, kem ni mu ñëwe ci geneen nettali.

***

Melow Umra

Bi ci njëkk: àttey Miixaat yi.

Miixaat yi: mooy barab yi Yonnente bi tànn ngir ku namm a Aj walla Umra di fa armale.

Ku romb benn ci yooyu te yéenee Aj walla Umra: dar war ci moom mu armale fa, te du dagan ci moom mu romb ko te armalul.

Ku gën a jege Màkka ci Miixaat yii: kon Miixaatam mooy bérab ba mu nekk; mu armale fa ngir Aj ak Umra.

Bu dee waa Màkka nag ak ku fa namm a armale: dañuy armal ca Màkka ngir Aj, bu dee Umra nag: dañuy génn ba ca armalukaay ba ñi armale fa, niki Tanhiim ak yi ko niru.

Ku nekk ci Abiyoŋ: day armal bu tolloo ak Miixaat bi, mu waajal daal di sol yérey armalam laata muy tolloo ak Miixaat bi, bu tolloo ak moom mu yéenee armal fa saasa, du dagan ci moom mu koy yeexe ba wàcc ca Aydapoor ba, man naa fagaru it labbaykawu laata muy tolloo ak Miixaat bi ngir ragal barabu labbaykawu ba di ko raw; ngir gaawaayu Abiyoŋ bi.

Ñaareel bi: melow armal ak i àtteem:

Yoonal nañu ci ki namm a armal yii di ñëw:

Sangu, moom sunna su feddaliku la ci àqi góor ak jigéen ba ci ki gis mbaax ak ki nekk ci dereetu wësin.

Laal gëtt ci li gën a neex ci lu mu am ci diwu Huud walla leneen mu def ko ci boppam ak sikkimam, te desug loolu ginnaaw armal gi du wàññi dara. Bu dee jigéen nag du dagan ci moom muy laal gëtt gu am xet; ndax góori jàmbur ñi bañ ko a xeeñtu.

Sol yérey armal, moom nag koddaay la ak làmbaay, la cay sunna mooy mu nekk ñaar yu weex te set walla yu bees. Jigéen day armal ci yére yu ko soob ci lu dul muy wane ab taar, waaye nag day moytu a sol Niqaab (muur kanam ) ak ñaari kawas, te mu muur kanamam ak ñaari loxoom ci li dul loolu.

Armal ginaaw ag julli lu ñu yoonal la, moo xam farata la walla naafila, loolu nag du lu war.

Mu wax: (labbayka Allaahuma Umratan), bu dee kuy umraal keneen kon na wax: (labbayka Allaahuma Umratan han fulaan (mu tudd turu kooka)).

Bu dee ki namm a armal dafa ragal gàllankoor gu koy gàllankoor wolif muy mottali jaamu gi kon dana jaadu ci moom mu sartal ca armal ga daal di wax: (labbayka Allaahuma Umratan, waaye bu ma dara téyee samag yewwiku mooy fa mu ma téye) saa bu sàrtalee mu am lu ko tere a mottali jaamu gi kon day summeeku te dara du ko ca war.

Topp mu baril di labbaykawu: (labbayka Allaahuma labbayka, labbayka laa sariika laka labbayka, innal hamda wannihmata laka walmulku laa sariika laka)[4], góor gi day yëkkëti kàddoom ci loolu, niki noonu it jigéen ji; fii ak nekkul ci teewaayu góori jàmbur. Jaadu na ci ki armal muy baril di labbaykawu rawati na bu aw melekaanam soppiku a walla jamono ya lu ci mel ni mu yéeg fu kawe, walla mu wàcc fu suufe, walla guddi gi dégmal walla bëccëg gi. Maanaam li nit kiy wax: (labbayka) mooy wuyu naa la yaw sama Boroom, ay yooni yoon, te maanaam mooy: nit ki wuyu Boroomam ak taxawam ci topp ko. "Innal hamda wannihmata laka walmulka" Alhamdu: melo wu ñu sant la ci ag mat ànd ak bëgg ak màggal, bu baamtoo day mujj nekk aw tagg. (Wannihmata) mooy li Yàlla di baaxe jaamam ñi ci ñu am la ñuy sàkku ak jañ la ñu sib, li mu wax: (walmulka) maanaam ag nguur yaw la ñeel, Yàlla mu Baarkeel mi te kawe mooy Aji-Moom ji Moom kepp, waxam ji: (laa sariika laka) maanaam amul kenn kuy bokk ak yaw li nga jagoo ci ay meloy mat, bokk na ca ag wéetam ci nguur gi ak bind gi, ak doxal gi ak Yàlla gi mu doon. Majmuuhu Fataawaa wa Rasaa-il bu Seex Al-Husaymiin (22/96) ci ag tënk.

Labbayka gi ñi yoonal ci Umra day dale ca armal ga ba baa muy tàmbali wër ga.

War na ci ki armal mu moytu a tàbbi ci dara ci yi ñu tere ci armal ba baa muy summeeku ca armal ga.

Ñatteel bi: melow wër Kaaba gi

Aji-armal ji bu duggee ca Jàkka ja ñu Wormaal dees na sunnaal ci moom mu jiital tànku ndayjooram daal di wax ñaanu dugg ci jàkka, bokk ci li gën a wér ci li rot ci loolu, mu wax : "Allaahuma iftah lii abwaaba rahmatika", ñaan gii da koy wax buy dugg ci jàkka ju mu man a doon, waaye du lu ñu jagleel Jàkkay Màkka rekk.

Bu bëggee tàmbali wër kaaba gi day dagg labbayka ga, daal di def Ittibaah, melow Ittibaah mooy: mu def li féeté digg ci làbbaayam gi ca biir poqtaanu ndayjooram, def ñaari cat yi ci kaw mbaggum càmmooñam, bu noppee ca wër ga mu daal di delloowaat làmbaay ga ca na mu meloon laata muy wër kaaba gi; ndaxte Ittibaah barabam mooy buy wër kaaba gi dong.

Topp mu dem ca Hajarul Aswad daal di laal doj wi ci loxo ndayjooram daal di koy fóon, fóon gi bu jàppandiwul mu laal ko ci loxoom daal di fóon loxoom bi, bu dee laal ko ci loxoom yombul, mu laale ko ab bant walla lu ko niru daal di koy fóon, bu loolu yombul day jublu doj wi daal di koy junj ci loxoom te du ko fóon, li gën mooy mu bañ a buuxante di lor nit ñi, mbaa muy loru moom.

Buy laal doj wi walla mu koy junj day wax: (Allaahu Akbar).

Topp mu feete ndayjoor te def wetug càmmooñam la feete ag kaaba gi, bu tollee ca Ruknul yamaaniy mu laal ko ci lu dul mu koy fóon, bu loolu yombul bu mu ca buuxante, te it bu mu ko junj.

Mu wax ci diggante Ruknul yamaaniy ak Hajarul Aswad: (Rabbanaa aatinaa fiddunyaa hasanatan wa fil aaxirati hasanatan wa qinaa hasaaban naari).

Saa su rombee Hajarul Aswad da koy junj ci loxoom daal di wax: (Allaahu Akbar).

Li des ci wër gi da ciy wax lu mu bëgg ci sikar ak ñaan ak jàng Alxuraan.

Lay sunna mooy mu ñukk ci ñatti yoon yu njëkk yi dong, ñukk mooy: gaawal dox bi ànd ak jegeele jéego yi, bu dee ñenti yoon yi des nag amul ñukk, waaye day dox kem ni mu ko aadawoo.

Bu matalee wër ga day dem ca Màqaamu Ibraahiima daal di jàng: (wattaxisuu min Maxaami Ibraahiima musàllan), [Al-Baxara: 125] Topp mu julli ñaari ràkka ca ginnaawam bu dee jàppandi na, lu ko moy mu julli leen ci barab bu mu man a doon ci jàkka ji, day jàng ci ràkka bu njëkk bi ginnaaw Faatiha: (xul yaaa ayyuhal kaafiruuna) [Al-Kaafiruuna: 1] Mu jàng ci ràkka bu ñaareel bi ginnaaw Faatiha: (xul huwa Allaahu Ahadun). [Al-Ixlaas: 1]

Ñenteel bi: melow dox Safaa ak Marwa

Bu noppee ci wër gi ak ñaari ràkka yi day génn jëm ci dox Safaa ak Marwa, bu jegee Safaa daal di jàng: (innas Safaa wal Marwata min sahaa-iri Allaahi) [Al-Baxara: 158]. Topp mu wax: "damay tàmbaliee ci li Yàlla tàmbalee". «damay tàmbalee ci li Yàlla tàmbalee» [12]. [12] Muslim soloo na ko, ci limatu[1218).

Topp mu yéeg ca kaw Safaa bay gis Kaaba gi walla wetam ga mu jublu ko, daal di kennal Yàlla, màggal ko, daal di wax: (laa-i-Laaha illal-Laahu Wahdahu laa sariika Lahu, Lahul mulku wa Lahul hamdu wa Huwa halaa Kulli say-in Xadiirun, laa-i-Laaha illal-Laahu Wahdahu, Anjasa Wâhdahu, wa Nasara Habdahu, wa Hasamal ahsaaba Wahdahu" da koy baamtu ñatti yoon, muy ñaan ci diggante loolu. "amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla moom dong amul bokkaale, moom la nguur ak cant ñeel, te moom lépp la man, amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla moom dond, def na la mu dige woon, te dimbali na jaamam bi, te not na mbooloo ma moom dong", topp mu daaldi ñaan ginnaaw loolu. Mu wax li mel nii ñatti yoon[13]. [13] Muslim soloo na ko, ci limatu: (1218).

Topp mu wàcc ca Marwa jëm ca Safaa di aji-dox, bu tollee ca màndarga mu wert ma mu dox dox gu tar, bu tollee ca meneen màndarga mu wert ma mu dox kem aadaam, dox gu tar gi nah yoonaluñu ko ci jigéen ñi.

Bu eggee ca Marwa yoonalees na ci moom mu def la mu defoon ca Safaa (xaaju limatu 2).

Topp mu wàcc ca Marwa jëm Safaa di aji-dox, bu tollee ca màndarga mu wert ma mu dox dox bu tar, bu tollee ca màndarga mu wert nu ñaareel ma mu dox kem aadaam.

Niki noonu ba mu matal juróom-ñaari yoon yi, dem gi bawoo Safaa jëm Marwa benn yoon la, delluseem gi it jóge Marwa jëm Safaa beneen yoon la.

Day wax ca ba muy dox lu mu bëgg ci sikar ak ñaan ak jàng Alxuraan.

Juróomeel bi: melow watu ak wàññi:

Aji-Umra ji bu noppee ca wër ga ak dox ga war na ci moom mu wat boppam walla mu wàññi ko bu dee góor la, lay sunna mooy watu gi walla wàññi gi matale mbooleem bopp bi.

Watu nag moo gën, lu dul waxtuw Aj wi jege ba saxug kawaru bopp bi du ci xaj; kon lay gën mooy mu yem ci wàññi.

Bu dee jigéen nag moom day wàññi ci cati kawaram luy tolloo ak catu baaraam.

Yi ñuy moytandiku ci armal

Yi ñuy moytandiku ci armal mooy:

Wat kawar walla jemp ko walla suqi ko, ci barab bu mu man a doon ci yaram wi.

Lelli ay we lépp walla lenn li ci tànk yi walla ci loxo yi .

Muur bopp ci luy taqaloo ak moom, lu mel ni: mbaxana, ak kaala, ak teg làmbaay ci kaw bopp bi, walla teg musuwaar, walla sarbet, walla Kayit, walla lu dul loolu ci yi ñuy jubloo muure. Lii nag góor ñi ñoo ko jagoo walif jigéen ñi.

Sol yere ya ñu aadawoo muy bu ñu ñaw buy tàqale cëri nit ki ca meloom wa ñu ko xame, niki mbubbu abbaaya, ak pantalooŋ, ak Semis, ak ñaari kawas, ak ñaari kawasi loxo. Lii nag góor moo ko jagoo walif jigéen, ndaxte moom dañu koo tere:

Sol niqaab, walla burqa, walla muuraay gu niroo ak niqaab, te dana war ci moom mu muur kanamam ci kanamu góori jambur ci muuraayu kanam gi ñu aadawoo. Donte muuraay gi dafa laal kanamam, te yoonaluñu ci moom mu teg kaala -walla lu mel noonu- ci boppam ngir ne muuraay gi laalul kanamam; Ndax amul lenn luy firndeel ne yoonal nañu loolu.

Sol ñaari kawas ci ay loxoom, te dana war ci moom mu muur ay loxoom ci góori jàmbur yi ci mu dugal ko ci biir Abaayaam.

Laal gëtt ci yaram wi, walla ci yérey armal yi.

Ray rëbbum jéeri, walla rëbb ko donte rayu ko.

Labat, ngir boppam walla keneen.

Takk ab sëy.

Jonjoo ci fu dul péy ma; niki fóon, ak laal ngir bànneex.

Jaxasoo, te mooy sëy ci péy mi.

Tënkub jëfi Umra yi (ci fegg wi lay nekk walla ci xët wi mujj)

Sangu set.

Laal gët (parfum).

Sol yérey armal.

Armal, te mooy yéeney dugg ci jaamu gi.

Di wax Labbayka...

wër néeg ba( Kaaba gi).

Julli ñaari ràkka ci ginnaaw Maqaam bi.

Dox diggante Safaa ak Marwa.

Watu walla wàññi. Yàlla rekk a xam yal na Yàlla dolli xéewal ak mucc sunu Yonente ba Muhammat.