Skip to content

«ku sos ci sunu diine ji lu ci bokkul dees na ka ko delloo

Jële nañu ci Aysa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:

«ku sos ci sunu diine ji lu ci bokkul dees na ka ko delloo" Buxaariyu ak Muslim dëppoo nañu ci. Muslim ni mu ko nettalee mooy: "ku jëf jenn ci ludul sunu ndigal dees na ka ko delloo».

«مَنْ أَحْدَثَ فِي أَمْرِنَا هَذَا مَا لَيْسَ فِيهِ فَهُوَ رَدٌّ» متفق عليه. ولمسلم: «مَنْ عَمِلَ عَمَلًا لَيْسَ عَلَيْهِ أَمْرُنَا فَهُوَ رَدٌّ».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne ku sos ci diine ji mbaa mu jëf jëf joo xam ne Alxuraan ak Sunna tegtalewu ko, dees koy delloo boroom te deesu ko nangu fa Yàlla.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Jaamu yépp ci Alxuraan AK Sunna lay tabaxu, dunu jaamu Yàlla ci lu dul lu mu yoonal, dunu ko jaamu ci ay bidaa ak yi ñu sos.

Diine du tege cim xel rekk ak lees di rafetlu, waaye ci topp Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- lay tege.

Hadiis bii tegtal la ci matug diine ji.

Bidaa mooy lu ñu sos ci diine ji te amutóon ci jamonoy Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ak i Sahaabaam muy ci pas-pas walla wax mbaa jëf.

Hadiis bi cosaan la ci cosaani diiney Lislaam, day mel niki balaas ci jëf yi, niki nga xamee ne jépp jëf ju ñu nammul jëmmi Yàlla mu kawe mi, aji-jëf ji du ci am ub yool, niki noonu it jépp jëf ju dëppoowul ak li Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- indi dees koy delloo aji-jëf ji.

Sos yi ñu tere mooy yi bokk ci biri diine, waaye du yu àdduna yi.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (3/ 184) (2697).

Téere Muslim bi gën a wér (3/ 1343) (1718).

Yataal gi (5)

التحفة الربانية في شرح الأربعين حديثًا النووية (ص16).

شرح الأربعين النووية.

لابن عثيمين (ص96).

فتح القوي المتين في شرح الأربعين وتتمة الخمسين.

للعباد (ص38).