Jëfi safaan yi nit ñi di faral di def ci Aj ak Umra ak Siyaare Yónnent bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal Ko.
Njuumte ak jëfi safaan yi aju ci Umra Bi ci njëkk: jëfi safaan ak njuumte yi nit ñi di def ci Armal Ñàkk a ihlaal, ci mu bañ a yëkkëti kàddoom ci jaamu gi mu namm a def ca ba muy tàmbalee fas Armal ga. Te sunna si mooy: mu yëkkëti ca kàddoom.
This PDF is generated automatically from the book's text; its layout may differ from the printed edition.
Jëfi safaan yi nit ñi di faral di def ci Aj ak Umra ak Siyaare Yónnent bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal Ko.
Kuréelug xam-xam gi ci mbootaayu liggéeyal Lislaam jaare ko ci làkk yi
Njuumte ak jëfi safaan yi aju ci Umra
Bi ci njëkk: jëfi safaan ak njuumte yi nit ñi di def ci Armal
Ñàkk a ihlaal, ci mu bañ a yëkkëti kàddoom ci jaamu gi mu namm a def ca ba muy tàmbalee fas Armal ga.
Te sunna si mooy: mu yëkkëti ca kàddoom.
Lenn ci nit ñi dañoo njort ne Armal mooy col gi (sol koddaay ak làmbaay)
Te Armal mooy: yéene dugg ci jaamu gi, te màndargaam mooy: yëkkëti kàddu gi bu ñuy labbaykawu, ku yëkkëti kàddoom ci bu muy labbaykawu ngir yéene Aj walla Umra kooku Armal na.
Lenn ci nit ñi dañoo njort ne sàngu dafa war ci Armal.
Waaye nag sunna la rekk dara warul ci ki ko bàyyi.
Lenn ci nit ñi it dañoo njort ne julli ñaari ràkka dafa war ci bu ñuy Armal, walla mu nekk sunna su manut a ñàkk bu ñu ko jagleel, ba tax fàww rekk mu julli ko.
Te la wér mooy ne dañoo yoonal julli njëkk Armal gi, waaye Armal amul julli gu ñu ko jagleel, bu julli woon farata walla geneen julli gu ñu yoonal, kon yoonalees na ci moom mu armal ginnaaw ga.
Li ñenn ci nit ñi di njort ne dañoo war a taxaw ca Miiqaat ba, wàcci jëm ca jàkka ja.
Te loolu warul, ku waaj ak ay yéréy Armalam romb Miiqaat ba wax labbayka foofa, walla fa tolloo ak moom fekk mu nekk ci waruwaayam loolu doy na ko, niki ki nekk ci fafanaawam (Abiyoŋam), kooku day wax labbayka bu tolloo ak Miiqaat ba walla lu ko jiitu tuuti ngir mu bañ a romb Miiqaat ba.
Def gëtt ci yére Armal bi.
Te lay yoon mooy yem ci gëtt yaram wi rekk.
Li ñenn ñi jàpp ne dañoo war a watu, dagg we yi, ak wat poqtaan yi bu ñuy dugg ci armal gi, walla ñu jàpp ne loolu sunna la ci Armal.
Te loolu sunna la su ñu joyal ci saa su ko nit ki aajowoo.
Armal laata muy àgg ca Miiqaat ba.
Te lii dafa wuute ak sunna, waaye ku nekk ci Abiyoŋ man na ko a jiital tuuti rekk ngir mu bañ a romb barab bay tolloo ak Miiqaat ba ngir gaawaayu Abiyoŋ bi, niki noonu it bu ragalee ne day nelaw te kon dana ko weesu kon dagan na ci moom mu jiital ko ci kem ag aajowoom ci loolu
Ki namm a def jaamu gi weesu Miiqaat ba te armalul, benn mu ñàkk a xam walla mu sàggan, walla ngir ne daa nekk ci Abiyoŋ.
Te li war ci moom bu dee dafa weesu Miiqaat bi fekk dafa yéenee Umra walla Aj te armalul foofa mooy: mu dellu ca Miiqaat ba daal di fay armale, niki noonu it ku wàcc Ayrapooru Jidda te armalewul ca Abiyoŋ ba ak lu ko man di waral: day war ci moom mu génn dem ci benn ci Miiqaat yi armale fa, dees na settee ci loolu: ki rombul ab Miiqaat te tolloowul ak ub Miiqaat, kooku day armale Jidda, niki waa Suudaan bu nu ñëwee war Abiyoŋ walla Bato; lu dul ñu xam ne dinañu tolloo ak Miiqaatu Yalamlam walla Miiqaatu Juhfa ca yoon wa nu jaare dikk.
Déggiinu njuumte gi nekk ci lu ñu ñaw ci ne mooy lépp lu am ag ñaw, ba tax ñuy moytu a sol laxasaay gu ñu ñaw walla sentiir walla dàll yu ñu ñaw.
Te lii wérul, lu ñu ñaw mooy: li ñu ñaw walla ñu defar ko ngir mu méngoo ak tolluwaayu yaram wi, niki yére ak pàntaloŋ yi; su dee dees ko a sol ci anam gi ñu ko aadawoo.
Jigéen ju sol mbaru-loxo, kol, muuraayal xar-kanam walla muuraay gu mat sëkk.
li war ci moom -bu dee dafa nekk fu ay jàmbur yu góor nekk- mooy mu muur xar-kanamam ak ñaari loxoom ci lu dul muuraayal xarkanam ak mbari-loxo; ndax Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa tere jigéen ju armal di leen sol.
Ñenn ci nit ñi jort gu ñu jort ne jigéen daa am col gu mu jagoo ngir armal, benn mu ñuul walla mu nëtëx mbaa mu weex.
Te lii wérul; jigéen gu armal man na a sol yére bu ko soob, ci lu dul muy feeñal ab taar.
Li ñenn ci nit ñi jort ci nàkk a daganug soppi yérey armal gi walla summi ko.
Te li wér mooy dagan ci ki Armal mu soppi yére yi walla mu fóot ko daal di koy solaat.
Génne mbaggum ndayjoor mi li ko dale ci ndoorteelu armal gi ba ca mujj ga.
Te li wér mooy génne mbaggum ndayjoor mi ci wërug Umra walla wërug egsi gi rekk lañu ko yoonal.
Lànk a armal ak di génn ci armal gi te amul ngàntul Sariiha lu ko waral.
Te li war ki armal mooy mu des ca armalam ga ba jaamu gi mat, lu dul bu amee ci Sariiha luy waral mu génn ci armal gi, te mooy bu nooni Lislaam yi gawee jullit ñi tere leen a àggale seenug aj, ci anam gii dana dagan ci moom mu génn ci armal ga, bu dee ba muy armaal daa sàrtaloon génn gi ci armal gi kon su booba a dara waru ko, bu dee sàrtalu ko woon nag kon day war ci moom mu ray ab gàtt daal di watu walla mu jemp kawaram topp mu génn ci armal gi .
***
Ñaareel bi: jëfi safaani nit ñi ak seeni njuumte ci bu ñuy wër Kaaba gi
Taqoo ak ay ñaan yu wérul ci bu ñuy dugg ci jumaay Màkka ji walla bu ñu gisee Kaaba gi.
Te sunna si mooy yem ci li rot jóge ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
Wax yéene ji ci làmmeñam balaa muy tàmbali wër gi.
Te barabu yéene mooy xol bi, kon yoonaluñu wax ji.
Jubloo tàmbali wër gi laata Doj wu ñuul wa, ngir di bëgg lu gën a léemtu gën a wóor.
Te lii ag ëppal la ak ug teeŋal.
Tàmbali wër gi ginnaaw bu weesoo Doj wu ñuul wa, jàppe loolu genn wër.
Te lii njuumte la, bu ko defee du wér ci moom mu jàppe loolu ag wër.
Yékkati ñaari loxo yi bu tolloo ak Doj wu ñuul wa kem ni ñu koy yékkatee bu ñuy julli, walla di baamu yékkatim loxo yi ñatti yoon.
Te lay sunna mooy mu joxoñ Doj wa ak loxo ndayjooram benn yoon rekk.
Taxaw lu yàgg ci bu tolloo ak Doj wu ñuul wa .
Te sunna si mooy mu bañ a yàggal taxawaay ba.
Buuxante gu tar ngir egg ca Doj wa ngir fóon ko.
Te sunna si mooy mu bañ a buuxante, bu dee man na ca a egg cu lu dul buuxante na ko def, bu ko manul na ko joxoñ rekk.
Delluwaat ca Doj wu ñuul wa ginnaaw ba mu ko rombee te kàbbarul, ngir ne da koy joxoñ te kàbbar, walla muy kàbbar ginnaaw ba mu ko rombee.
Te loolu lépp njuumte la, ndaxte sunna la su weesu, te sunnaaluñu muy dellu ngir def ko, te ku fàttee kàbbar walla mu jublu ko a bàyyi dara waru ko.
Jagleel wër gu nekk ak ñaan sàngam.
Te lii amul tegtal, te lay sunna mooy ku nekk ñaan li mu bëgg ci yiwu àdduna ak allaaxira [1], di tudd Yàlla ci bépp sikar bu ñu yoonal ci wax Subhaanal Laahi walla Alhamdu lil-Laah walla laa-i-Laaha illal-Laahu walla Allaahu Akbar walla jàng Alxuraan.
Di njukk ci wër yépp.
Te lay sunna mooy ne ci ñatt yu jëkk yi dong lay nekk.
Ñàkk a taqoo ak féetele Kaaba gi ci wetu càmmooñam ci jamonoy wër gi ci lu dul benn ngànt.
Te sunna si mooy Kaaba gi nekk ci càmmooñam, kon du jaadu muy sàggan di wuute ak loolu, bu dee dafa am ngànt ngir xataay bi ak lu mel noonu kon dara waru ko ca.
Fóon koñu ndayjoor bi, walla di ko joxoñ bu dee manu ko a fóon.
Te sunna si mooy mu laal ko ci loxoom rekk te du ko fóon, bu ko manul a laal it du ko joxoñ.
Laal ak fóon mbooleem koñi Kaaba gi, walla miir yi, ak di ko riisu.
Te lii dafa wuute ak sunna, ndax yoonaluñu lu dul fóon Doj wu ñuul wa, ak laal koñu ndayjoor bi dong.
jort ne laal koñu ndayjoor bi ak Doj wu ñuul wi ngir baarkeelu la waaye du ngir jaamu.
Te lii lépp ag ñàkk a xam la ak ug réer, ndax njariñ ak lor ci loxoy Yàlla dong la nekk, jële nañu ci Umar yal na ko Yàlla dollee gërëm ne: moom dafa ñëw ci Doj wu ñuul wa fóon ko, daal di wax ne: "man de xam naa ne aw doj nga doo lor te doo jariñ, bu dul woon li ma gis Yónnent bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di la fóon kon duma la fóon" [1] Al-Buxaarii moo ko soloo, ci nimaro (1597).
Di ñaan di yékkati sa kàddu bay jaxaseel ñiy wër.
Te liy sunna mooy mu tudd Boroomam ñaan ko mu yam ci digganteem ak Moom, ngir mu bañ a jaxaseel kenn.
Yittewoo foto walla di waxtaan ci jamonoy wër gi.
Te li ñu yoonal ci aji-wër ji mooy muy tudd Boroomam ci ag mokk ak ug toroxlu ak xol bu teew.
Noppi ci wër gi laata muy wóorlu ne egg na ca Doj wu ñuul wa.
Te li war mooy mu matal juróom-ñaareelu wër gi ba mu wóor ko walla mu not ci njortam ne egg na fa tolloo ak Doj wu ñuul wa.
Jàpp ne ñaari ràkkaay wër gi fàww dafa war a sës ci ginnaaw Màqaam bi walla mu jege ko, ba tax ñuy buuxante ngir loolu bay lor ñiy wër ci jomomo jooju, di gàllankoor seen wër gi.
Te njort loolu njuumte la, ndax ñaari ràkkaay wër gi barab bu mu man a doon ci Jumaa ji dana baax, kiy julli it man na a def Màqaam bi ci digganteem ak Kaaba gi -doonte da ko a sori- bu ko defee mu julli ca barabu wër ga, walla ca barabu jàngukaay ba, bu ko defee dana mucc ci lor, dina man a julli itam ci ag toroxlu ak ug dal.
Guddal ñaari ràkkaay wër gi ak bu ca noppee di ñaan.
Te lay sunna mooy mu woyofal leen, te bu ca noppee mu bañ a ñaan dara; ndaxte loolu rotul jóge ci Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
Muri mbaggum ndayjoor mi fekk moo ngi julli ñaari ràkkaay wër gi.
Te lay sunna mooy mu tegaat làmbaayam ca kaw ñaari mbaggam fa saasa ginnaaw ba mu noppee ca wër ga.
***
Ñatteel bi: juuyoo gi nit ñi di juuyoo ak lees leen sant ak seeni njuumte ci dox Safaa ak Marwa.
Muri mbaggum ndayjoor mi jamono ya muy dox.
Te waxoon nanu ne muri mbaggum ndayjoor mi ci jamonoy wër gi rekk lay nekk.
Wax yéene ji balaa muy tàmbali dox bi.
Te waxoon nanu ne barabu yéene mooy xol, te yoonaluñu ñu koy wax.
Tàmbalee dox bi fa Marwa.
Te lii njuumte la, ku ko def du limaale wër googu.
Ñenn ci nit ñi dañoo jort ne gennug wër mooy dem gi ak dikk gi bu ko defee mu wër fukk ak ñenti yoon.
Te lii njuumte la, ndax jóge Safaa dem Marwa gennug wër la, jóge Marwa itam dem Safaa geneen wër la, Safaa nag lañuy tàmbalee, jeexale ko Marwa.
Yéeg ca njobaxtalu doju Safaa ngir jort ne loolu manut a ñàkk.
Te amul tegtal buy sàrtal loolu.
Yékkati ñaari loxo yi di ca junj kem ni muy def ci kàbbari julli gi.
Te li wér mooy mu yem ci jublu xibla ak ñaan ci ñaan yi rot.
Jigéen gi di daw bu baax ci diggante ñaari màndarga yi niki ni ko góor ñi di defee.
Te li ñu yoonal ci moom mooy mu yam ci dox, te woroom xam-xam yi dëppoo nañu ci loolu; ngir ñoŋal ko ba du wuññiku.
Jagleel yoon wu nekk ci dox gi ak ñaanam.
Te lii amul tegtal, waaye na ñaan lu mu bëgg ci lu dul mu koy jagleel dara[2].
Di yékkati kàddu ca kaw ca fa ñuy doxe yékkati gog day jaxaseel nit ñi.
Te liy sunna mooy muy tudd Boroomam di ko ñaan mu yam ci digganteem ak moom, ngir mu bañ a jaxaseel keneen.
Di gaawantu ci dox bi ci diggante Safaa ak Marwa ci yoon yépp.
Te sunna si mooy gaawantu gi nekk ci diggante ñaari màndarga yu wert yi dong.
Julli ñaari ràkkaa ginnaaw bu noppee ci dox bi.
Te lii amul tegtal, yoonaluñu def gi.
Di dox Safaa ak Marwa cig coobarewu ci lu dul ag jaamu.
Te dox cig coobarewu yoonaleesu ko.
***
Ñenteel bi: juuyoo gi nit ñi di juuyoo ak lees leen sant ak seeni njuumte ci watu walla jemp.
Gàtteñlu ci matale bopp bi ci wat gi walla ci wàññi gi.
Te sunna si mooy matale bopp bi ci wat gi walla wàññi gi.
Watu walla wàññi ci biir Jumaa ja ñu wormaal, ak sànni fa kawar gi.
Te li war mooy màggal Jumaa ja ñu wormaal ak xér ci ag setam.
Yeex a watu walla wàññi yeex gu ëpp gog dana tax ñu fàtte ko, walla ñu far soxlawoo leneen walif moom.
Te li ñu yoonal mooy gaaw ko a def fa saasa ba mu noppee ca wër ga ak dox ba.
Def yi ñu tere ci Armal njëkk watu ga walla wàññi ga.
Te li war mooy mu bañ a def dara ci yi ñu tere lu dul ginnaaw bu watoo walla wàññi.
***
Njuumte ak jëfi safaan yi aju ci Aj
Bi ci njëkk: juuyoo gi nit ñi di juuyoo ak lees leen sant ak seeni njuumte ci bisu Tarwiya
Ñenn ci nit ñi dañoo jort ne dañoo yoonal Armale ci bisu Tarwiya ca Jumaa ja ñu Wormaal, walla ca suufu wàcceekayu ndoxum dalu-kawu Kaaba ga.
Te sunna si mooy mu armale ca barab ba mu nekk; moo xam ci Màkka la walla Minaa.
Yeex a armal ba ginnaaw jullig Tisbaar.
Te lay sunna mooy mu armal ngir Aj ci yoor-yoor gi laata jullig Tisbaar.
Ñàkk a fanaan Minaa te man ko.
Te li ñu sunnaal ci kiy Aj mooy mu fanaan Minaa fii ak man na ko; ndax li ko Yónnent bi def yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
Boole julli yi fa Minaa.
Te liy sunna mooy mu julli julli yi fa Minaa wàññi ko te bañ ko a boole; ngir roy ci Yónnent bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
***
Ñaareel bi: jëfi safaani nit ñi ak seeni njuumte ci bisu Arafa.
Taxaw Arafa lenn ci bisu juróom-ñatteel bi ngir wóorlu jàpp ne man na a am ne bis boobu mooy tolloo ak bisu Arafat.
Te lii ag diisal la ak ug ëppal gu ñu tere.
Génn jëm Arafa ci bisu juróom-ñatteel bi walla ci guddig juróom-ñenteel bi ak fanaan fa.
Te lii dafa wuute ak sunna, te it day faat sunnas fanaan ca Minaa.
Taxaw fu génn dayoy Arafa.
Te li war ci kiy Aj mooy mu jéem a taxaw ci biir Arafa.
Jort ne fàww rekk ñu julleendoo ak imaam bi ci jàkkay Namira, ak di buuxante ngir sax fa.
Te lii du lu war, yoonaluñu it buuxante gi ngir loolu.
Jublu doju (Ilaal) bu ñuy ñaan.
Te liy sunna mooy ñu jublu Xibla.
Jàpp ne danoo war a yéeg ca doju Ilaal walla jàpp ne loolu dafa bokk ci jëfi Aj gi, walla ne dafa am ngëneel walla ag jagoo ci kaw Arafa gi yépp.
Te loolu amul tegtal, dafa wuute sax nag ak njubug Yónnent bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
Tudde doju (Ilaal) doju yërmaande, walla (doju ñaan).
Te li wér mooy ne (Ilaal) la tudd, te amul tegtal ci ñu tudde ko doju yërmaande walla doju ñaan.
Dugg ci sooroor bi nekk ci doju Arafa, ak di ko woowe soorooru Aadama, ak di fa julli, ak di ko wër ni kuy wër Kaaba ga.
Te lii lépp ay bidaa yu ñu tere la, amaana sax mu egg ci bokkaale.
Barkeelu ca keno wa nu samp ca doju Rahmat ca Arafat ak di ca bind ay tur.
Te lii lépp ay bidaa yu ñu tere la, amaana sax mu egg ci bokkaale.
Def xaalis ca pax-paxaan ya nekk ca doju Arafa walla doju Nuur walla teg fa kawar walla weh walla dara ci ay yére mbaa lu ni mel, ak fas ne loolu day waral seeni woroom ñëwaat ci warab yii.
Te lii lépp ay bidaa yu ñu tere la, amaana sax mu egg ci bokkaale.
Ñenn ci nit ñi dañoo jort ne dañoo war a taxaw ca barab ba Yonnente bi taxawoon, walla dañoo war a toggoo coono ngir loolu.
Te li wér mooy loolu du lu war, te it yoonaluñu ñuy toggoo coono ngir loolu.
Sànk waxtu ak bàyyi ñaan ak tudd Yàlla, ak di yittewoo yeneen yu amul njariñ walif loolu.
Yeex a tàmbalee ñaan ba Jant bi di waaj a so, walla ba ci mujjug bëccëg gi.
Toggoo coonob jog taxaw ngir ñaan, ak jort ne loolu mooy sunna, walla jort ne li taxaw Arafat di tekki mooy jog taxaw ngir ñaan.
Te li wér mooy taxaw Arafa mooy mu nekk fa ca waxtu wa, moo xam dafa taxaw walla dafa toog, walla dafa war, mbaa muy dox.
Joge Arafa jëkk sowug jant.
Te lii dafa araam; ndax dafa wuute ak sunnas Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
Yeex faa jóge ginnaaw ba Jant ba sowee ci lu dul ngànt.
Te liy sunna mooy gaaw fa a jóge ginnaaw ba Jant ba sowee fa saasa, lu dul ngànt am.
Li ñenn ñi fas ne taxaw Arafa bisu Àjjuma day yemoo ak juroom-ñaar-fukki Aj.
Te loolu amul tegtal.
***
Ñatteel bi: jëfi safaani nit ñi ak seeni njuumte ci dem Musdalifa ak fanaan fa.
Njëkkante ci jóge Arafa ak di sonle ci wata yi.
Te liy sunna mooy jóge fa ci ag dal ak ug wegu ak bañ a lore.
Ñenn ci nit ñi dañoo jort ne dañoo yoonal sangu ngir fanaan Musdalifa.
Te amul luy tegtale ne dañoo yoonal loolu.
jortug ñenn ñi ci ne dañoo sopp ci aji-war ji mu wàcc dox ngir dugg Musdalifa.
Te amul luy tegtale ne dañoo yoonal loolu.
Wàcc ci ab bqrab jëkk muy wóorlu ne bqrab boobu ci Musdalifa la bokk.
Ñàkk a gaaw julli bi muy door a wàcc Musdalifa.
Te liy sunna mooy mu gaaw julli fa saasa ba mu eggee Musdalifa.
Yittewoo dajale ay xeer buy door a dugg Musdalifa ak xér ca loolu jort ne lu ñu yoonal la.
Te loolu amul tegtal.
Yeex a julli Timis ak Gee ba waxtu wa génn, te mooy xaaju guddi ga.
Te li war mooy julli Timis ak Gee laata xaaju guddi gi di jot doonte laata muy egg Musdalifa la.
Dundal guddig Musdalifa ci julli walla jaamu mbaa ci caaxaan ak fo.
Te sunna si mooy gaaw a nelaw ak dallu; ngir roy ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, ngir mu dimbandikoo ci loolu ci yees di war a def ci bisu Feet gi.
Génnug néew-ji doole ak ñi ànd ak ñoom jëkk xaaju guddi gi di jot.
Te li war mooy ñu bañ a génn ba ginnaaw xaajug guddi di
Génnug ñi bokkul ci néew-ji doole te àndul ak néew-ji doole laata Fajar gi.
Te li war mooy ñu des Musdalifa ba ba Fajar di jot.
Yeex a génnee Musdalifa ba Jant bi fenk.
Te liy sunna mooy ñu génnee fa laata Jant bi di fenk.
***
Ñenteel bi: jëfi safaani nit ñi ak seeni njuumte ci yees war a def ci bisu rendi gi.
Jortug ñenn ñi ci ne dañoo yoonal sangu ngir sànni Jamra.
Te amul luy tegtale ne dañoo yoonal loolu.
Raxas xeeri Jamra yi.
Te amul luy tegtale ne dañoo yoonal loolu.
Jàpp ne sànni gi du wér lu dul bu xeer yi jogee fa Musdalifa.
Te loolu amul tegtal, man na a fore xeer yi ci bqrab bu mu man di doon.
Sànni lu nekkul xeer, walla sànni xeer yu rëy.
Te lii dafa wuute ak sunnas Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
Mer ca jamono ya muy sànni, ak jàpp ne Saytaane lañuy sànni.
Def ay kuréel ak lëkkaloo bu ñuy dem ngir sànni ji, ak di lor nit ñi.
Yokk yu bokkul ci sikkar yi ñu yoonal bu nu dee sànni.
Ti li gën a yay mooy yam ci kàbbar rekk.
Sànneendoo juróom-ñaari jamra yi benn yoon.
Te ci anam gii deesu ko jàppe lu dul benn sànni dong, li war mooy ñu sànni benn bu nekk moom dong.
Teg Jamra yi ca baaj ba walif sànni leen.
Te loolu du doy, li ñu yoonal mooy mu sànni leen ca la gën a néew ci lu ñuy woowe ag sànni.
Jublu a sànni miir ba, ak jort ne moom lañu jubloo sànni.
Te li ñu yoonal mooy xeer yi rot ca baaj ba, doonte dalul ca miir ba.
Nekk ci barab bu sori di sànni, te wóorluwul ne xeer yi tàbbi na ca baaju sànnikaay ba.
Taxaw ngir ñaan ginnaaw sànnig Jamra Haqaba gi.
Te lii yoonaleesu ko; ndaxte amul tegtal ne luñu yoonal la.
Rendi gàttub Tamattuh ak Xiraan jëkk bisu rendi ga.
Ku def loolu du ko doy, te dana war ci moom mu rendiwaat ca waxtu wa ñu ko jagleel ci Sariiha, te mooy bisu julli gi ba ca ba mujj ci bisi Tabaski gi.
Bañ a rendi ba tax mu saraxe njëgu la mu waroon a rendi.
Ku def loolu du ko doy, te day war ci moom mu rendi.
Watu walla wàññi lenn ci bopp bi rekk.
Te sunna si mooy matale bopp bi ci wat gi walla wàññi gi.
Doyloo wërug ñëw gi walif wërug Ifaada gi, walla mu jiital ko ci taxaw Arafa ga ak Musdalifa ga.
Ku def loolu it du ko doy; ndaxte wërug Ifaada gi ponk la ci ponki Aj gi, te Aj gi du wér ci lu dul moom, te du dagan mu def ko lu dul ginnaaw ba ñu taxawee Arafa ak Musdalifa.
***
Juróomeel bi: jëfi safaani nit ñi ak seeni njuumte ci yees war a def ci bisu Minaa (ñatti fani Tabaski)
Sàggan ci kuutal walla yable ci sànni gi.
Te liy cosaan mooy kiy aj mooy sànnil boppam, lu dul mu am ngàntul Sariiha gu ñu nangu gu koy daganalal mu yabal ku ko ca wuutu.
Ki wuutal keneen ci sànni gi daal di tukki laata yees war a def ci Aj gi ak bisi Aj gi di jeex.
Te lii njuumte la, li war ci moom mooy mu des Munaa walla ca barab ba mu nekk ba yees war a def ci Aj gi jeex mu wër wërug tàggatoo gi, door a génn.
Sànni Jamra ci bisi Tabaski yi jëkk Jant bi di jeng.
Te lay sunna mooy ñu sànni ginnaaw bu Jant bi jengee.
Ñàkk a toftale ñatti Jamra yi ci sànni gi.
Te li war mooy nu toftale ko, nga xam ne day sànni gu jëkk gi, teg ca gi ci digg bi teg ca gu mag gi te mooy Jamratul Haqaba, ku ko juuyale walla mu wuutale ko da koo war a baamtuwaat toftale ko, tàmbalee ci gu ndaw gi topp mu sànni ya ca tege.
Taxaw ngir ñaan ginnaaw sànnig Jamra Haqaba gi.
Te sunna si mooy ñaan gi nekk ginnaaw sànnig Jamra gu jëkk gi ak gi ci digg bi dong.
***
Juróom-benneel bi: jëfi safaani nit ñi ak seeni njuumte ci wërug tàggatoo gi.
Jiital wërug tàggatoo gi ci sànnig Jamra gu mujj gi; ngir bëgg a tukki ginnaaw sànni gi fa saasa.
Te lii njuumte la, ku ko def def na ko ci fu dul waxtoom te kon du ko doy, te day war ci moom mu baamtuwaat ko ginnaaw sànni gi.
Wuutal ku koy sànnil, ba noppi daal di def wër gi laata ki mu wuutal di sànni.
Te li wér mooy mu xaar ba mu sànni mu door a def wërug tàggatoo gi.
Jubloo bañ a won Kaaba gi ginnaaw, buy dellu ginnaaw, ngir màggal Kaaba gi.
Te amul luy tegtale ne dañoo yoonal loolu, te njub gi gën mooy njubug Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
Taxaw ngir ñaan bu dee génn ci Jumaa ja ñu wormaal.
Te loolu amul tegtal.
Sax lu yàgg ca Màkka ginnaaw wërug tàggatoo gi ci lu dul ngànt lu Sariiha nangu.
Te li war mooy gaaw a génn Màkka ginnaaw wërug tàggatoo gi, aayul nag mu xaar àndandoo yi, walla mu jënd ya muy soxla ci tukki ba, ak yu ni mel.
Bu fa desee lu yàgg ci lu dul ngànt: day war ci moom mu baamtu wërug tàggatoo gi.
Njuumte ak jëfi safaan yi aju ci siyaare Jumaay Yonnente bi
Di riisu miir ya ak weñ ya bu dee siyaare bàmmeelu Yónnent bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak di fas ay wëñ ak lu ko niru ca baryeer ya ngir baarkeelu.
Te baarke ci li Yàlla yoonal ak ub yonnénteem yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc la nekk waaye nekkul ci ay bidaa.
Dem ca xunt ya ca doju Uhud niki noonu xuntum Hiraa ak xuntum Sawr ba fa Màkka ak takk fa ay sagar ak di ñaan ay ñaan yoy Yàlla diglewu ko ak toggoo ca ay coono.
Te yii yépp ay bidaa la amul cosaan ci Sariiha ju ñu laabal jii.
Siyaare lenn ci ay barab yoy nee nañooy dafa bokk ci jeexitali Yónnent bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc niki fa ñu ne fa la Giléem ga yésoon, ak teenu jaaro ba, walla teenu Usmaan ak jël ca suufus barab yooyu ngir baarkeelu.
Ñaan way-faatu ña bu ñuy siyaare bàmmeeli Al-Baxiih ya ak bàmmeeli ña faatu ca xareb Uhud ak di fa sànni xaalis ngir jegeñlu jëm ci loolu, ak ngir baarkeelu ci ñoom.
Te yii dafa bokk ci njuumte yu rëy yi, dafa bokk sax ci bokkaale gu mag niki ni ko woroom xam-xam yi waxe, Téereb Yàlla bi tegtale ko ak Sunnas Yonnénteem bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, ndaxte jaamu Yàlla dong moo ko yayoo, du dagan ñu wëlbati ci dara di ko jëme ci ku dul Moom niki ñaan ak rendi ak nisër ak yu ko niru, ndax li Yàlla wax ne: (digaluñu leen lu dul ñu jaamu Yàlla di aji-sellal diine ji ñeel ko) [Al-Bayyinatu: 5].
Yal na Yàlla dolli xéewal ak mucc sunu Yónnent ba Muhammat.
Related books
All books
Lii ab tënk la ci melow Umra ak i àtteem.59 languagesLii ab tënk la ci melow Umra ak i àtteem.
Mbooleem xeeti cant yi ñeel na Yàlla miy Boroom mbindeef yi, jàmm ak mucc yal na nekk ci sunu Yonnente bi Muhammat, ak ay ñoñam ak sahaabaam yépp. Ginnaaw loolu: Lii ab bataaxal bu ñu tënk la ci melow Umra ak i àtteem ak i tegginam, xér nanu ci lool ci leeral li ëpp ci li ñu aajowoo ci Umra. Yàlla rekk lanuy ñaan mu def ko muy lu sell ñeel jëmmam ju Tedd ji, ak mu jariñ ci mbooleem jullit ñi.
Lislaam mooy diiney Yonnente Yàlla yi85 languagesLislaam mooy diiney Yonnente Yàlla yi
Lislaam mooy jébbalul Yàlla mi bind àdduna bi di ko doxal, wommatul ko ngir bëgg ko ak màggal ko, cosaanu lislaam mooy gëm Yàlla, ak ne moom mooy Aji-Bind ji, te lépp lu dul moom mbindeef la, ak ne moom moo yayoo jaamu moom rekk amul bokkaale, amul lenn lu ñuy jaamu ci dëgg ku dul moom,ay tur yu rafet ñeel na ko ak ay melo yu kawe, mooy ki mat sëkk, jurul kenn te kenn juru ko te amul benn nawle du caagine niroowaale, du wàcc te du jël jëmmi lenn ci mbindeefam yi. Lislaam mooy diiney Yàlla mi nga xam ne du nangu ci nit jenn diine ju dul moom, te mooy diine ji yonnente yépp indi yal na leen…
الإسلام دين رب العالمين
Melow jullig Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-79 languagesMelow jullig Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-
Téereb «Ni Yonnente bi ﷺ daan jullee», Seex Abdul Asiis Ibn Baas -yal na ko Yàlla yërëm- dafa caa tënk melokaanu jullig Yonnente bi ﷺ, ci anam gu yomb te wóor, mu wéeru ci mbind yu wér, ngir mu doon ag gidee ñeel jullit bi ci ag julleem. Leeral na ci ponki julli yi, ak i sunnaam, ak i melokaam, dale ca jàppu ma ba ca sëlmël ga, di boole firnde ak leeral, tey woote ci roy gu mat ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci jaamu Yàlla gi gën a màgg.