Skip to content
وجوب العمل بالسنة وكفر من أنكرها

وجوب العمل بالسنة وكفر من أنكرها

Warug jëfe sunnas Yonnent bi ak kéefarug képp ku ko weddi. Aji-taalif ji Abdul Asiis Ibn baas -yal na ko Yàlla yërëm- Ci turu Yàlla miy Aji-Yërëm kepp ku nekk ci kaw suuf jagleel ko jullit ñi ca allaaxira ci laay tàmbalee. Laytaay ji Cant ñeel na Boroom mbidéef yi, Ag mujj ñeel na ñi ragal Yàlla, jàmm ak xéewal yal na nekk ci sunu Yonnent Muhammat, moog waa këram ak i àndandoom ñoom ñi gàddu téere Yàlla bi ak Sunnas seen Yonnent -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- jottali ko ña ñëw ci seen ginnaaw, ci koolute gu mat sëkk ak ug xereñte, ak ug wattu gu mat sëkk ñeel ay maanaam ak i baatam,…

Language: lang_wo
Prepared by:
Version: 1.0

Warug jëfe sunnas Yonnent bi ak kéefarug képp ku ko weddi. Aji-taalif ji

Abdul Asiis Ibn baas -yal na ko Yàlla yërëm-

Ci turu Yàlla miy Aji-Yërëm kepp ku nekk ci kaw suuf jagleel ko jullit ñi ca allaaxira ci laay tàmbalee.

Laytaay ji

Cant ñeel na Boroom mbidéef yi, Ag mujj ñeel na ñi ragal Yàlla, jàmm ak xéewal yal na nekk ci sunu Yonnent Muhammat, moog waa këram ak i àndandoom ñoom ñi gàddu téere Yàlla bi ak Sunnas seen Yonnent -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- jottali ko ña ñëw ci seen ginnaaw, ci koolute gu mat sëkk ak ug xereñte, ak ug wattu gu mat sëkk ñeel ay maanaam ak i baatam, -yal na leen Yàlla dollee gërëm te boole nu ci ñi leen di topp ci ag rafetal, ak ñu nekk aw lay ci mboolem jaam ñi, Ginnaaw loolu:

Woroom xam-xam yu ñëkk ya ak yu mujj yi dëppoo nañu ci ne cosaan yi ñuy saxale ab àtte ci diine, wala ñu koy leerale lu dagan mbaa lu araam ñi ngi ci téereb Yàlla bi ak ci sunnas Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- ndax du wax ci bànneexu bàkkanam, lu mu wax Yàlla a ko ko wax, ginnaaw ba la woroom xam-xami xeet wi dëppoo, woroom xam-xam yi nag wuute nañu ci yeneeni cosaan, lu mel niki qiyaas (méngale) donte li ëpp ca ñoom nee nañu xiyaas aw lay la bu dee sart ya mat na. Cosaan yii nag séen i tegtal bari na lool ba maneesukoo takk, te siiw nañu ba aajo woo wul tudd.

Cosaan yi ñuy saxale ab àtte ci diine

Cosaan Bu njëkk ba mooy: téereb Yàlla bi.

Budee Cosaan bu njëkk bi: te mooy téereb Yàlla bi, waxi sunu Boroom ci ay bërëb yu bari ci téeteem bi day tegtale ne topp téere bii lu war la, te jàpp ci te yam fa mu nu yamloo.

Yàlla mu kawe mi nee na: {Lii mooy téere bu baarkeel bi Nu wàcce, kon toppleen ko ngir ngéen am yërmànde Yàlla}

Yàlla mu kawe mi wax na:

{Sunu ndaw li dikkal na leen di leen leeral lu bari lu ngeen doon nëbb ci téere bii di Tawraat ak Injiil donte amna lu bari lumu leeralul, ag leer ak téere bu bér dikkal na leen bawoo fa Yàlla, ci la Yàlla di jubale képp ku topp ngërëmam jëme ko si yoonu mucc, di leen génne cig lëndam bokkale tàbbal leen cig leeru ci ndigalam, te di leen teg it ci yoon wu jub wi}

Sunu Borom wax na ne:

{Gaa yi Nga xam ne weddi nañu Alxuraan ginnaaw ba mu leen dikkalee, nañu xam ne téere bu màgg la neen duko dikke benn boor, téere bu ñu wàcce la mu bàyyikoo ci Aji-Xereñ tey Aji-Cant}

Sunu Borom mi ngi waxaat ne:

{Yàlla soloo na ma téere bii di Alxuraan ngir ma xupp leen ci ak képp ku téere bi àgg ca moom}

Yàlla mu kawe mi wax na ne:

{Téere bii di Alxuraan de ag waare gu jotale la ñeel nit ñi, ngir ñu xupp leen ci}

{Aaya yiy firndeel lii bari na lool, bari na tamit ay Hadiis yu wér yu bawoo ci Yonnent bi-yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- yuy digle jàpp ci Alxuraan waaye di wane ne kepp ku ci ngoy yaa ngi cig njub waaye ku ko bàyyi moo ngi cig cànkute, niki ni mu saxe juge ci yonentabi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- ba muy xutba ca ajug tàggatoo ga naan:

(Man de bàyyil naa leen fi Loo xam ne fii ak yéen a ngi ciy jàpp dungeen sànku ba fàww te mooy téereb Yàlla bi)

Muslim moo ko soloo ci Sahiiham

ñëw na ca téereb Muslim ba ba tay mu jóge ci Sahaaba bii di Seydou ibn Arxam mu ne Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na :

"Bàyyil naa leen yaar i yëf yu diis: bu njëkk ba mooy téereb Yàlla bi, njub ak leer ñoo ca nekk kon jàppleen bu baax ci téere bi"

Mu daal di ñaaxe ci téereb Yàlla bi xiirtal ci nit ñi, mu tek ca ne:

«Ak sama waa kër maa ngi leen di fàttali Yàlla ci sama waa kër, maa ngi leen di fàttali Yàlla ci sama waa kër»

Ci beneen waxiin mu wax ci Alxuraan ne:

Mooy buumu Yàlla gi ku ci jàpp yaa ngi cig njub ku ko bàyyi yaa ngi cig cànkute.

Hadiis yiy tektale loolu yu bari la, niki noonu dëppoo gu Sahaaba yi ak woroom xam-xam yi dëppoo ci ne jàpp ci téere Yàlla bi lu war la teg si di ko àttewoo moom ak Sunnas Yonnent bi, te lii doy na sëkk wolif di tudd yeneen i tegtal ci mile mbir.

Ñaareelu cosaan bi: mooy li sax ta juge ci Yonnent bi ak i àndandoom ak kepp ku topp si ñoom ci woroom xam-xam yi ak ngëm.

Budee ñaareelu cosaan bi te mu bokk ci ñatti cosaan yi nga xamne ag dëppoo amna ca: mooy li sax juge ci Yonent bi ak i sahaabaam ak képp ku ñëw séen ginnaaw ci woroom xam-xam yi, ñoom ñépp gëm nañu bile cosaan te ñoom ñépp itam dinañu ci tegtaloo, di ko jàngal xeet wi. Taalif nañu ci ay téere yu bari, leeral ko ci téerey Usuulu Fiq yi ak yu Mustalah yi, te li koy tegtale bari lool ba maneesukoo lim, bokk na ca Li ñëw ci téereb Yàlla bi tey digle ñu topp ko, te loolu ñoo ngi ci jublu waa jamonoom ak képp ku ñëw séen ginnaaw ndax Yonnent bi ci ñépp lañu ko yónni, te topp ko daa war ku ne ba fàww, ndax moom mooy firi Alxuraan di leeral ci ay waxam ak i jëfam lépp lu ñu lëm ci téere Yàlla bi, bu dul woon Sunnaam kenn du xam ñaata ràkka lees war a julli ak melokaanu julli ak i warugaram, niki noonu dunu xam faramfàcce yi nekk ci Koor ak Asaka wala Aj Màkka walla Jihaat niki noonu digle lu baax ak tere lu bon, duñu xam tamit lu jëm si naka la ñuy jëflàntee walla mbir yi Araam ak li Yàlla teg ci ay daan ak i gétan mu nekk ci Alxuraan lu mel niki li Yàlla wax ca Saaru Aali-Imraan:

{Toppleen Yàlla topp ndawam li ndax Yàlla yërëm leen}

Ak wax ji Yàlla wax ca Saaru An-Nisaa:

{Yéen ñi gëm toppleen Yàlla topp Ndawal Yàlla topp séen i njiit ak séen i woroom xam-xam bu ngeen wuutee ci dara dellooleen ko ci Yàlla ak ci Yonnenteem ndéem gëm ngeen Yàlla ak bis-pénc ndax loolu mooy li gën te moo gën a rafet ug mujj}

Yàlla wax na batay ca Saaru An-Nisaa:

{Képp ku topp Yonnent bi topp na Yàlla waaye ku lànk bañ koo topp yaw Yonnent bi na nga xam ne yónniwunu la ngir nga leen di saytu}

Naka lañu koy toppe aka dellloo lépp lu nit ñi wuute ci téereb Yàlla bi ak Sunnas Yonnent bi bu fekkee ni sunaam si deesu ko laye walla sax mu nekk Loo xam ne kenn wattuwu ko, bu Boo baa dafay mel ni Yàlla da fay delloo jay jaamam ci lu amul te loolu moom neen féetewu ko kaw te ag weddi Yàlla gu rëy la, te it ag ñaaw njort la ci boroom bi.

Yàlla wax na ci saaru An-Nahl:

{Wàcce Nanu fi yaw alxuraan ngir nga leeralal nit ñi li ñu wàcce si ñoom amaana ñu xellu}

Waxaat na it ci saar wi ne:

{Wàccewunu ci yaw téere bi lu dul ngir nga leeralal leen Linga xam ne wuute na ñu ca ak ngir mu nekk njub ak yërmànde ñeel way gëm yi}

Naka la Yàlla di bàyyee ak Yonnent bi mbirum leeral li ñu wàcce ci xeet wi te sunnaam si nekku fi wala mu nekk fi waaye du nekk aw lay ci dara?

Niki noonu waxi Yàlla ja nekk ca saaru An-Nuur:

{Waxal ne toppleen Yàlla toppleen Yonnent bi, bu ñu dummóoyoo bu boobaa moom ak la ko war, yéen it ak la leen war, waaye bu ngeen ko toppee moom dangeen gindiku ta moom dara waru ko lu dul jottali bu leer}

Yàlla wax na ci saar wi ba tay:

{Taxawalleen julli ta ngeen joxe Asaka tey topp Yonnent bi ndax Yàlla yërëm leen}

Yàlla wax na ca Saaru Al-Ahraaf:

{ Waxal: éey yéen nit ñi man de ndawal Yàlla laa ci yéen ñépp, Moom mi moom nguurug asamaan yi ak suuf si amul benn buur bu yayoo jaamu ku dul Moom, Mooy dundal te mooy ray, kon gëmleen Yàlla te gëm ndawam lii nga xamni manul bind manul dawal ( jàng ) moom de gëm na Yàlla gëm ay kàddoom, kon toppleen ko ndax Yàlla jubal leen}

Ay tegtal yu leer nekk na ci Aaya yii ci ne njub ak yërmànde moo ngi ci topp Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc-- naka la loolu di ame te jëfewu ñu sunnaaam si? walla ñuy wax naan wérul? walla naan kenn du ci sukkandiku?

Yàlla -mu kawe mi- wax na ca Saaru An-Nuur:

{Ñiy wuute ak ndigalimu Yonnent bi nañu moytu bu baax fitna dal séen kaw walla mbugal mu metti dal leen}

Waxaat na ca Saaru Al-Hasr:

{Lu leen Yonnent bi indil jëlleen, lu mu leen tere bàyyileen ko}

Laaya yu ni mel bari na lool te yépp day tegtale warug topp ko moom Yonnent bi-yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- ak topp li mu indil, niki ni tegtal yi jàll di wanee warug topp Alxuraan ak jàpp ci tey topp ay ndigëlam bàyyi ay tereem, ñoom ñaar dañoo ànd ku weddi benn ci ñoom weddi na baca des te loolu ag kéefar la di ag réer te dafay génnee nit ki ci lislaam, te loolu boroom xam-xami yi dëppoo nañu ca.

Bokk na ci li rot ci loolu juge ci Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc-

Hadiis yu bari ñëw Na di wane ni Yonnent bi-yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- topp ko ak topp li mu indi lu war la, ak di Araamal moy ko, loolu mooy li war waa jamanoom ak képp ku ñëw séen ginnaaw ba bis-pénc, bokk na ca: li sax jugé ci Moom negg ca Sahiihul Buxaarii ak Muslim Abuu Hurayrata ne Yonnent bi nee na:

«Ku ma topp, topp na Yàlla, waaye ku ma moy, moy na Yàlla»

Ñëw na ci Sahiihul Baxaarii Abuu Hurayrata ne Yonnent bi nee na:

"Sama xeet wi yépp dinañu dugg aljana ba mu des ku bañ, ñu ne ko Ana kan mooy bañ a yaw Yonnent Yàlla bi? Mu ne ku ma topp dugg aljana ku ma moy nag kooku mooy ki bañ"

Ahmad ak Abuu Daawuda ak Haakim génne nañu ab Hadiis ci càllala gu wér ñu jële ko ci Miqdaat Ibn Mahdiy karib mu jële ci Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc-- mu ne:

"Jox nañu ma Alxuraan ak lu mel ni moom ci tegtal (sunna) di nga gis benn waay bu lekk ba suur toog ci kaw gàngunaayam naan jàppleen ci alxuraan kese lu ngeen ci fekk lu dagan daganalleen ko waaye lu ngeen ci fekk mu Araam, araamalleen ko"

Abuu Daawuda ak Ibn Maaja génne nañu Hadiis bu jaar ci càllale gu wér: Abii raafih jële ci baayam mu jële ci Yonnent bi mu ne:

"Yàlla bu ma teewe kenn Si yéen mu sóonu ci kaw gàngunaayam sama ndigël dikkal ko mbaa luma tere bu ko defee muy wax naan nun daal lu ñu fekk ci téere Yàlla bi dong moom la ñuy topp"

Jële nañu ci Asan Ibn Jaabir mu ne dégg naa Miqdaat Ibn Mahdiy karib -yal na ko Yàlla gërëm- muy wax naan:

Yonent bi araamal na ay mbir ci bisub Xaybar daa di wax ne: "benn waay dina ma weddi fekk moo ngi sóonu di wax samay wax boole ca di wax naan sunu diggante ak yéen mooy téere Yàlla bi lu ñu fa fekk ci lu dagan ñu daganal ko lu ñu fa fekk ci lu araam ñu araamal ko, waaye xamleen ne li Yonnent bi araamal mi ngi mel ni lu Yàlla araamal"

Haakim ak Tirmisiy ak Ibn Maaja ñoo ko soloo génne ko ci càllale gu wér.

Hadiis yu bari rot na bàyyikoo ci Yonnent bi ci genn xutba muy ñaax sahaaba yi ngir ñi fekke ci ñoom di jottalil ñi fekke wul mu leen di wax naan: "Bariwaana ku ñu jottali mbir, mu gën koo xam ka ko déggoon"

Bokk na ca li nekk ci téereb Buxaarii ak Muslim ci ne ba Yonnent bi di xutba nit ña ca ajug tàggatoo ga si bisub Arafa ga ak bisub Tabaski waxna leen ne:

"Ku fekke na jottali ku fekkewul ndax amaana moom mi ñu jottali mu gën a xam loola ka ko déggoon"

Sunnaam Si bu nekkul woon aw lay ci ki ko dégg ak ki ñu ko jottali, bu dul woon lu fiy des ba fàww kon du leen digël ñu jottali ko, loolu moo tax Sunna nekk aw lay ci ki ko degg ci làmmiñu Yonnent bi ak ki mu yeggsi ci moom jaare si Yoon yu wér.

Sahaabay Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- ñoo sàmm sunnaaam si yu wax yi ak yu jëf yi, daa di koy jottali ñi topp Si ñoom ñooña yit jottali ko ña topp sa ñoom, niki noonu woroom xam-xam yi di ko tuxal tegsi diko dajale ci séeni téere di leeral la ca wér ak la ca wérul, daa di teg ay cëslaay yuy tax ñu man a ràññee la ca wér ak la ca wérul, woroom xam-xam yi di jokkalante téere sunna yi tàmbalee ko ca ñaari Sahiih yi ak yeneen yi, ñu wattu ko wattu gu mat sëkk niki ni sunu borom wattoo alxuraan ba daray caaxaan raxu si yàqkat yi tamit manuñu si dara, loolu day dëggal waxu Yàlla ji mu ne:

{Nun Yàlla Noo wàcce alxuraan te Noo koy Sàmm}

Sikk-sàkk amul ci ne Sunnas Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- wahyu gu bàyyikoo fa Yàlla la, boroom bi sàmm na ko niki mu sàmme alxuraan, tàggat ay woroomi xam-xam yu taxaw temm di ko dàqqal soppiteg yàqkat yi, ak pirig way réer yi, di ko soreele lépp lu ci way réer yi tey fenkat te di ay weedukati Yàlla boole te Bokku si , ndax Yàlla mu sell moo def Sunna mu nekk luy firi alxuraan di leeral ay àtteem, am sax ay àtte yu ca nekk te rotul ci alxuraan, lu mel niki àttey nàmpal ak lenn ci àttey miiraas ak araamal boole jigéen ak tànntaam wala bàjjanam si benn buumu sëy, ak yeneen yu ni mel yu rotul ci alxuraan. Bokk na si li rot juge ca sahaaba ya ak taabihuun ya ak woroom xam-xam yi ñëw séen ginnaaw ci màggug sunna ak war gi ñu ko war a ñu jëfe..

Ñëw na ci sahiih Buxaari ak Muslim Abuu Hurayra wax ne:

Bi Yonnent bi faatoo -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- am ci araab yi ñu tubbi Abuubakar dafa wax ni: wallahi dinaa xeex ak kepp ku tàqale digante Julli ak Asaka, Omar ne ko naka ngay xeexe ak ñoom ta Yonnent bi nee na woon: dañu maa sant ma xeex ak nit ñi bakeroog ñuy wax Laa ilaaha illal Laah bu ñu ko waxee kon ñoŋal nañu fi man séen dereet ak séen alal ludul ci àqi lislaam, Abuubakar ne ko ndax Asaka daa bokkul ci àqi lislaam? Ne ko giñ naa ci Yàlla ne buñu ma bañee jox ab cëggu tàndarma buñudaan jox Yonnent bi dinaa xeex ak ñoom, Omar daal di wax ne: nii laa xame ne Yàlla dafa yaatal xolu Abuubakar ngir mu xeex ak ñoom ma xam ne loolu mooy dëgg.

Sahaaba yépp daal di ànd ak moom ci loolu ñu xeex ak ñoom ba ñu duggaat ci lislaam, ñu ray ña lànk, nettali bii tegtal bu bir la ci ne dañoo war a màggal Sunna war koo jëfe, benn bis benn maam bu jigéen dafa ñëw ci Abuubakar di laac wàllam ci miiraasu ben sëtam Abuubakar ne ko:

Téere Yàlla bi wàllu maam bu jigéen nekku ci te xaw ma fu la Yonnent bi joxee cér Si miiraas, waaye nag dinaa laaj nit ñi Abuubakar daal di laaj sahaaba yi am ñu seede ne Yonnent bi jox na maam bu jigéen juróom benneelu cér ci miiraas mi, Omar tamit daan na dénk ay ndawam ñuy àtte nit ñi ci téere Yàlla bi bu ñu ko gisul ci téere bi ñu àtte leen ci Sunnas Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc-

Bi nga xamee ne Omar amna jafe-jafe ci àtteb jigéen guñu tooñ ba tuur ab ëmbam doom ja faatu ca biir ba, dafa laaj sahaaba yi am ku ñuy wax Muhammat Ibn Maslama ak Muxiira Ibn Suhba ñu daa di ne ko Yonnent bi mas naa àtte lu ni mel la mu ca laajoon niki ndàmpaay mooy jaam bu góor mbaa bu jigéen, Omar daal di àttee loolu.

Usmaan itam ba mu amee jafe-jafe ci masalam jigéen guy téññi ci këram ginnaaw bi Boroom këram faatoo, ndaw suñuy wax Furayha bint Maalik jigéenu Abuu Sahiid ne ko: Yonnent bi digëloon na ko ginnaw ba boroom këram faatoo ne ko mu toog ci kër boroom këram ba téññeem mat. Usmaan daal di àttee loolu.

Niki noonu ci sunna la àttee ba teg kii di Waliit Ibn Uqbata géténug ku naan sàngara, ba nga xamee ne Alliyun yég na ne Usmaan day tere ku Aj ajug tamattuh dafa daal di dugg ci aj gi boole ko ak umra daal di wax ne: Duma bàyyi sunnas Yonnent Yàlla bi ngir waxi kenn ci nit ñi. Ba nga xamee ne aw nit waxnañu ak Ibn Àbbaas si lu jëm ci ajug tamattuh jàpp ne ajug Ifraad moo gën teg si di layoo waxi Abuubakar ak Omar, Ibn Àbbaas da ne leen: Xaw tuut ñu wàcce ci séen kaw ay xeer yu bàyyikoo asamaan, may wax Yonnent nee na ngéen may wax waxi Abuubakar ak Omar, Bu dee ku wuute ak Sunna ngir waxi Abuubakar ak Omar la ñuy tiital ci mbugalum Yàlla rawatina kon ku ko bàyyi ngir waxi keneen walla ay xalaati boppam. Am na ñu masa wuute ak Abdulaay Ibn Àbbaas ci lenn ci Sunna mu ne leen: Ndax Omar lañu nu digal nu topp ko walla Sunna?

Bi benn waay waxee Imraan Ibn Husayn ne ko: waxtaanal nu ci téere Yàlla bi fekk moo ngi leen doon waxtaanal ci Sunna dafa mer daal di wax ne: Sunna de mooy firi Alxuraan te bu dul woon sunna duñu xam ne tisbaar ñenti ràkka la, timis ñatti ràkka la, fajar ñaari ràkka la, te duñu xam tamit faramfàcce yi nekk ci àttey Asaka ak yeneen àtte yi sunna faramfàcce . Li ñu jële ci sahaaba yi ci war gi mu war ñu màggal ko sunna te di ko jëfe bañ a wuute ak moom bari na lool, Bokk na ca kii di Abdallah Ibn Omar ba mu nettalee wax ji Yonnent bi wax ne: Buleen di tere jaamu Yàlla yu jigéen ñi jàkkay Yàlla yi.

Kenn ci doomam yi daal di wax ne: wallaahi dinañu leen tere, Abdallah mere ko tegsi xas ko xas yu metti ne ko: May wax Yonnent bi nee na ngay wax aka giñ naan dinanu leen tere. Abdallah Ibnul Muxaffal Al musaniy bokk ci sahaaba yi ba mu gisee benn jegeñaaleem muy sànni xeer, da koo tere loolu ne ko: Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- da koy tere ndax du jàpp am rëbb du dàq ab noon xanaa damm bëñ ak fuq bët la man, ginnaw ga mu gisaat ko muy sànni mu ne ko: giñ naa ci Yàlla ne duma waxati ak yaw mukk wax naa la lii Yonnent bi da koy tere nga koy defaat.

Bayhaqii soloo na jële ci Ayyub Assaxtiyaanii mu bokkoon ci ndongoy sahaaba yi mu wax na: Boo nettalee nit ci Sunna mu ne la bàyyil sunna ta nettali ma ci Alxuraan xamal ne kooku ku sànku la Awsaahii -yal na ko Yàlla yëram- nee na: Sunna day lijjanti alxuraan walla muy tënk lu mu boyal, walla muy indi ay àtte yu alxuraan tuddul niki waxi Yàlla ji mu ne:

{Wàccee nanu ci yaw Alxuraan ngir Nga leeralal nit ñi li ñu wàcce si ñoom, amaana ñu fàttaliku}

Jiitu na ci waxi Yonnent bi mu ne: "Jox nañu ma téere bii di Alxuraan ak leneen lu mel ni moom"

Bayhaqii soloo na luñu jële ci Aamir Assahbii -yal na ko Yàlla yërëm- mu wax ak lenn ci ay nit ne leen:

Ba ngéen bàyyee Hadiis yu wér yi ci ngeen alku woon, Bayhaqi soloowaat na ñu jële ci Al-Awsaahii mu wax lenn ci ay àndadoowam yi ne leen: Boo jotee ab Hadiis bu juge ci Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- na nga moytoo wax leneen ndax te Yonnent bi jottalikatub sunu boroom la woon.

Bayhaqii soloowaat na ñu jële ci Imaam bu màgg muy Sufyaan As-sawrii -yal na ko Yàlla yërëm- mu wax ne: Léppi xam-xam mooy xam-xamu Hadiis (sunna), Imaam Malik -yal na ko Yàlla yërëm- Nee na: Amul kenn Si nun lu dul dees na la delloo lenn ci say wax ba mu des boroom bàmmeel bii mu joxoñ barabu Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc-.

Imaam Abuu Haniifata -yal na ko Yàlla yërëm- nee na: Bu ab Hadiis dikke bàyyeekoo ci Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- topp rekk moo ca war.

Imaam Saafihii -yal na ko Yàlla yërëm- wax na ne: Waxtu wu ñu ma nettalee ab Hadiis bu wér te jëluma ko jëfandikoo ko xamleen ne samam xel dem na.

Mu dellu wax ne: Bu ma waxee ab wax ab Hadiis dikk wuuteeg li ma wax sànnileen sama wax.

Imaam Ahmad Ibn Hanbal wax na ak kenn ci ay àndandoowam ne ko: Bul ma roy bul roy Maalik bul roy Saafihii waaye na ngay jële fi nu jële nun.

Mu dellu waxaat ne: Yéemu naa ci nit ñoo xam ne dañoo xam càllaleg wax ju wér te bàyyikoo ci Yonnent bi ñu bàyyiko fa di dem ci Sufyaan te sunu borom wax ne: {Ñiy wuute ak Yonnent bi nañu moytu bu baax fitna dal séen kaw walla mbugal mu metti}

Mu daal di wax ne: mo ndax xam nga luy fitna? Fitna mooy bokkaale ndax amaana bu nit ki delloowee waxi Yonnent bi Ag jenŋ tàbbi ci xolam mu far alku.

Bayhaqii génne na ci téereem ba ñu jële ci Mujaahit Ibn Jabr di ab ndongo bu mag ci sahaaba yi, mu wax ci li Yàlla wax ne :

{Bu ngeen wuutee ci dara na ngeen ko delloo ci Yàlla ak Yonnent bi}

Mu wax ne: delloo ci Yàlla mooy delloo ci alxuraan, delloo ci Yonnent bi mooy delloo ci Sunna. Bayhaqii soloowaat na ñu jële ci As-Suhrii mu wax ne: Sunu Woroom xam-xam yi jiitu daa nañu wax naan: jàpp ci Sunna bu dëgër ag mucc la. Muwaffaxud Diin Ibn Xudaama wax na ci téereem bii di Rawdatun Naasir Fii bayaani Usuulul Ahkaam wax jii: Ñaareelu cosaan ci tegtal yi mooy sunnas Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- di ay waxam te keemtaan la c ag dëggoom, te Yàlla dafa digle ñu topp ko, daal fi xuppe ci wuute ak ndigalam.

Jubluwaay bi jeex na

Haafis Ibn Kasiir - yal na ko Yàlla yërëm- wax na ci tafssiram bi muy firi waxu Yàlla ji mu wax ne:

{Ñiy wuute ak ndigalu Yonnent bi nañu moytu fitna dal séen kaw walla mbugël mu metti}

Li mu ci jublu mooy mbiru Yonnent bi te mooy aw yoonam ak doxaliinam ak tëraliinam, wax ju ne ak jëf june dees koy natt ci ay waxam ak i jëfam, lu ca dëppoo ak moom ñu jël ko lu wuute ak moom ñu delloo ko boroom Ak ku mu man a doon.

Niki mu ñëwe ci Sahiihul Buxaarii ak Muslim ak yeneen, juge ci Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- mu wax ne:

«Képp ku jëf dara ci diine ji te amoo ci sunu ndigal dees la koy delloo»

Maanaam képp ku wuute ak Yonnent bi na moytu te tiit ci boppam mooxam lu nëbb la walla lu feeñ:

{Fitna dal ci séen kaw}

Maanaam fitna dugg ci xolam moo xam ak kéefar walla naaféq walla bidaa

{Walla mbugël mu metti dal leen}

Maanaam mbugël fii ci àdduna lu mel ni ray walla ab gétan walla tëj mbaa lu ni mel, niki ni Imaam Ahmat nettalee jële ci Abdu Rassaaq mu jële ci Mahmar mu jële ci Hammaat Ibn Munabbah mu ne: lii la ñu Abuu Hurayra nettali nee na: Yonnent bi nee na:

"Man ak yéen daa mel ni benn waay bu taal sawara ba mu demee ba li ko wër lépp leer gunóor yi tàmbalee ñew mu leen di dogaale waaye am na yuy tàbbi ca sawara wa ndax manu ca dara nee na loolu mooy sama missal ak yéen dama leen di dogaale ngir dugeen dugg sawara waaye dangeen may not ba tax ngeen fay tàbbi"

Buxaarii ak Muslim ñoo ko soloo mu juge ci Abdu Rasaaq

Suyuuti wax Na ci téeréem bi mu tudde: Miftaahul Janna Fil Ihtijaaji Bis Sunna nee na:

Xamleen ne Hadiisu Yonnent bi moo xam wax la mbaa jëf bu àndee ak i sartam yi ñu xam ci xam-xamu Usuul képp ku weddi ne aw lay la kooku weddi na te génn na ci diine ji, te buy dekki ëllëg mook Yahuud yi ak Nasaraan yi walla ñeneen ci way weddi Yàlla yi lay àndal

Jubluwaay bi jeex Na.

Li ñu jële ci sahaaba yi ak séeni ndongo ak woroom xam-xam yi ci luy tegtale warug jëfe sunna ak màggaayam ak luy moytuloo wuuteeg moom bari na lool. maa ngi am yaakaar ni lii ñu jot a tudd ci ay Aaya ak i Hadiis ak i nettali doy na sëkk ngir ku bëgg dëgg. noo ngi ñaan Yàlla mu defal jullit ñépp tawfeex musël nu ci am meram jubal ñépp ci yoonam wu jub wi ndax mooy Aji-Dégg ji te jege.

Yal na Yàlla dolli xéewal ak mucc ci sunu Yonnent Muhammat moom ak waa këram ak i sahaabaam ak képp ku ko topp cig rafetal.

Abdul Asiis Ibn Baas -yal na ko Yàlla yërëm-