Ay ñaan yu matale[1]
Lii ay ñaan yu matale la, yu rot ci Alxuraan ju Tedd ji, walla mu wér jóge ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, ñu yoonal nu di ko ñaane ci bépp jamono ak bépp barab, bokk na ca bu ñuy wër Kaaba gi ak bu ñuy dox Safaa ak Marwa, ak ca Arafa ak Musdalifa, waaye nag jagleeluñu leen ko. Bi ci njëkk: ñaan yi bawoo ci Alxuraan. Sunu Boroom nangul nu yaw yaay Aji-Dégg ji di Aji-Xam ji* Te nga jéggal nu yaw yaay Jéggalaakoon bi di Yërëmaakoon bi. Yaw Yàlla Sunu Boroom defal nu yiwu àdduna ak yiwu allaaxira te nga fegal nu mbugalum sawara. Yaw Yàlla Sunu Boroom bul nu ko jàppe bu nu…
This PDF is generated automatically from the book's text; its layout may differ from the printed edition.
Ay ñaan yu matale[1]
Lii ay ñaan yu matale la, yu rot ci Alxuraan ju Tedd ji, walla mu wér jóge ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, ñu yoonal nu di ko ñaane ci bépp jamono ak bépp barab, bokk na ca bu ñuy wër Kaaba gi ak bu ñuy dox Safaa ak Marwa, ak ca Arafa ak Musdalifa, waaye nag jagleeluñu leen ko.
Bi ci njëkk: ñaan yi bawoo ci Alxuraan.
Sunu Boroom nangul nu yaw yaay Aji-Dégg ji di Aji-Xam ji* Te nga jéggal nu yaw yaay Jéggalaakoon bi di Yërëmaakoon bi.
Yaw Yàlla Sunu Boroom defal nu yiwu àdduna ak yiwu allaaxira te nga fegal nu mbugalum sawara.
Yaw Yàlla Sunu Boroom bul nu ko jàppe bu nu fàttee walla nu juum.
Yaw Sunu Boroom bul nu teg coono kem na nga ko tege woon ña nu jiitu woon.
Yaw Sunu Boroom bul nu teg lu nu àttanul, te nga baal nu jéggal nu te yërëm nu, Yaw Yaay sunu kilifa dimbali nu ci kaw yéefar yi.
Yaw Sunu Boroom, nun gëm nanu jéggal nu sunuy bàkkaar, te fegal nu mbugalum Sawara.
Yaw sama Boroom, may ma ci sa coobare ay njaboot yu yiw, Yaw Boroom bi Aji-Dégg ñaan nga.
Yaw Sunu Boroom gëm nanu li nga wàcce topp nanu it Yonnente bi, noo ngi ñaan nga boole nu ca way-seede ña.
Yaw Sunu Boroom, jéggal nu sunuy bàkkaar ak sunuy jéggi-dayo ci sunuy mbir, te nga dëgëral sunuy ndëggu, te dimbali nu ci kaw nit ñii di ay yéefar.
Yaw Sunu Boroom ! Sàkkulóo lii ci neen, tudd naa sag sell, yal na nga nu fegal mbugalum Sawara.
Yaw sunu Boroom yal na nga nu jox la nga nu digoon, te jaarale woon ko ca sa Yonnente ya, te bul nu gàcceel keroog bis-pénc ba, yaw Yàlla, doo wuute ab dige.
Yaw Sunu Boroom, tooñ na nu su nu bopp, soo nu baalul, yërëm nu, kon dana nu bokk ca way-ñàkk ña.
Yaw Sunu Boroom yàlla boo nu boole ca tooñkat ya.
Yàlla doy na ma, amul jenn yàlla ju nu war a jaamu ju dul moom te ci moom laay wéeru te moom moo di Boroom Aras ju màgg ja.
Yaw Sunu Boroom yàlla bul nu def fitna ñeel tooñkat yi, te nga musal nu ci sa yërmànde ca nit ña di ay yéefar.
Sama Boroom, maa ngi lay ñaan nga def dëkk bii di fu am kóolute, te nga soril ma man ak sama njaboot nuy jaamu ay xërëm.
Yaw Boroom bi def ma man ak samay doom ak samay sët nuy taxawal julli, te nga nangul nu sunu ñaan yaw sunu Boroom.
Yaw Sunu Boroom jéggal ma jéggal sama ñaari way-jur ak way-gëm ñi bis ba ñuy càmbar mbindeef yi.
Yaw Sunu Boroom may nu yërmànde ju bawoo ci yaw, te nga yéwénalal nu sunuy mbir mu tege ci njub.
Yaw sama Boroom na nga yaatal sama dënn, te nga yombalal ma samay mbir.
Yaw sama Boroom dolli ma xam-xam.
Amul jenn Yàlla ju ñu war a jaamu ju dul yaw, tudd naa sag sell, man déy bokk naa ca tooñkat ya.
Yaw sama Boroom bul ma bàyyi ma wéet, Yaw déy yaay ki fiy des.
Yaw Sama Boroom maa ngi muslu ci yaw ci jax-jaxali saytaane yi, te maa ngi muslu ci yaw ñu di ma teewe.
Yaw Sunu Boroom nun déy gëm na nu, jéggal nu te yërëm nu, yaw yaay gën gi Yërëmaakoon.
Yaw Sama Boroom jéggal ma te yërëm ma yaw yaay gën gi Yërëmaakoon.
yaw sunu Boroom dëddale nu ak mbugalum sawara, mbugalam ma déy luy taqoo ak i ñoñam la.
Yaw sunu Boroom, defal nu ci sunuy soxna ak sunuy doom ñuy seral xol, te nga def nu ay njiit ca ña ragal Yàlla tey wattandiku.
yaw sama Boroom, na nga ma baaxe may sant ci xéewal gii nga ma defal man ak samay way-jur, te may jëf jëf ju baax joo gërëm te nga may ma ci sa yërmànde ma bokk ca sa jaam ñu yiw ña.
yaw sama Boroom man déy tooñ naa sama bopp na nga ma jéggal.
yaw sama Boroom musal ma ci nit ña di ay tooñkat.
Amaana sama Boroom gindi ma teg ma ca yoon wu jub wa.
yaw sama Boroom, man déy ku yittewoo laa li nga may wërsëgale ci yiw.
yaw yama Boroom may ma njaboot yu bokk ca way-sell ña.
yaw sama Boroom mayma ma may ma na sant ci sa xéewal yi nga ma xéewale ak sama ñaari way-jur, ak itam may man a jëf jëf ju yiw joo gërëm, te nga yéwénalal ma samay sët, man déy tuub naa dellu ci yaw te itam man mii ci jullit ñi laa bokk.
yaw sunu Boroom ci yaw lanuy wakkirlu, te ci yaw lanuy dellu, te ci yaw la lépp di mujj.
Yaw sunu Boroom, jéggal nu, nun ak sunu mbokk yi ñu jiitu ci ngëm, te bul bàyyi genn mbañeel ci sunuy xol jëm ci ñi gëm, yaw sunu Boroom kuy Ñeewant nga Aji-Yërëmaakoon nga.
Yaw sunu Boroom mottalil nu sunug leer, te jéggal nu, yaw déy lépp nga man.
Ñaareel bi: ñaan yu bawoo ci sunnas Yonnente bi:
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi muslu ci yaw ci fitnay sawara ak mbugalu sawara, ak fitnay bàmmeel, ak ayu fitnay koom, ak ayu fitnay ñàkk.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi muslu ci yaw ci fitnay Al-Masiihu Al-Dajjaal.
Yaw Yàlla sunu Boroom raxasal sama xol bi ci ndoxum galaas ak nees, te nga sellal sama xol bi ci ay njuumte kem ni nga sellale yéré bu weex bi ci taq-taq, te nga soreele sama diggante ak samay njuumte kem ni nga soreele diggante penku ak sowwu.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi muslu ci yaw ci tàyyeel ak màggat ak bàkkaar ak bor yu diis.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi muslu ci yaw ci lott ak tàyyeel, ak ragal ak màggat ak nay, maa ngi muslu ci yaw ci mbugalum bàmmeel, ak ayu fitnay dund ak dee.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi muslu ci yaw ci coonay balaa, ak texeedi, ak dogal bu ñaaw, ak ndokkug noon yi.
Yàlla sama Boroom maa ngi lay ñaan ag njub, ak ragal la, ak fegu ak doylu.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi muslu ci yaw ag lott ak tàyyeel, ak ragal ak nay, ak màggat ak mbugalum bàmmeel.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi lay ñaan nga gindi ma te jubal ma.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi muslu ci yaw ci deñug say xéewal ak boutique say xéewal, ak mbétteelug say tiis, ak sam mer.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi muslu ci yaw ci ayu li ma xam, ak ci ayu li ma xamul.
Amul kenn ku nu war a jaamu ku dul Yàlla, Aji-Màgg ji Aji-Lewet ji, amul kenn ku nu war a jaamu ku dul Yàlla, Boroom Aras ju Màgg ji, amul kenn ku nu war a jaamu ku dul Yàlla, Boroom Asamaan yi, Boroom suuf si, di Boroom Aras ju tedd ji.
Yàlla sunu Boroom sa yërmànde dong laa yaakaar, kon bul ma bàyyi ak sama bopp luy toll ni xefu bët, maa ngi lay ñaan nga yéwénalal ma sama mbir yépp, amul kenn ku nu war a jaamu ku dul yaw.
Yaw Yàlla sunu Boroom man sa jaam laa, di doomu sab jaam, di doomu sab jébéer, samag nos moo ngi ci sa loxo, say àtte mooy wéy ci man, say dogal ci man lu màndu la, maa ngi lay ñaan ci sa wépp tur woo tudde sa bopp, walla nga xamal ko kenn ci sa mbindeef yi, walla nga wàcce ko ci sa Téere bi, walla nga téye ko ci sa xam-xamu kumpa ba: nga def Alxuraan muy sama naatànge xol, di sama leeru dënn, di wuññi samay njàqare, di dindi samay jaaxle.
Yaw miy Aji-Wëlbëti xol yi, maa ngi lay ñaan nga saxal sama xol bi ci sa diine ji.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi lay ñaan nga rafetal sunug mujj ci mbir yépp, te nga musal nu ci toroxtangey àdduna , ak mbugalum allaaxira.
Yaw sama Boroom maa ngi lay ñaan nga jàppale ma te bul dimbli kenn ci sama kaw, ak nga pexeel ma te bul pexe ci sama kaw, te nga gindi ma, ak nga yombal ci man ag njub, ak nga dimbali ma ci képp ku bew ci sama kaw.
Yaw sama Boroom def ma ma di la sant, ak di la tudd, ak di la ragal, ak di la topp, ak di aji-jaamu la, ak di la toroxlul, ak di aji-dellu ci yaw.
Yaw sama Boroom maa ngi lay ñaan nga nangu samag tuub, te nga raxas samay bàkkaar, te saxal samay lay, te nga gindi sama xol, te jubal sama làmmiñ, te nga génne sama bañeeli xol ak i soxoram.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi muslu ci yaw ci ayu samag dégg, ak ayu samag gis, ak ayu sama làmmiñ, ak ayu sama xol, ak ayu sama Maniyyu[2]. Al-Mushirii nee na: "maanaam ayu notug sama maniyyu ba duma tàbbi ci njaalo, ak di xool yu araam yi". Xuutu Almuxtasii Alaa Jaamihi At-Tirmisii (2/860)
Yaw Yàlla sunu broom maa ngi muslu ci yaw ci siti, ak ug ndof, ak ngaana[3], ak feebar yu bon. Feebar bu ñu xam la, day lekk yapp wi muy wadd. Yal nanu ci Yàlla musal. Sarh Sunanu Abii Daawuda bu Ibn Rislaan(7/411)
Yaw Yàlla sunu Boroom Aji-Baale nga ku tedd nga, ku bëgg a baale nga kon baal ma.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi lay ñaan may def lu baax, tey bàyyi lu bon, ak bëgg way-ñàkk ñi, nga jéggal ma te yërëm ma, boo nammee fitna ci aw xeet na nga faat ba doo ma fitnaal, maa ngi ñaan nga def ma ma bëgg la bëgg ku la bëgg, ak ma bëgg jëf ju may jegeele ci bëgg la.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi lay ñaan wépp yiw: ya ca sori ak ya ca jege, ya ma ca xam ak ya ma ca xamul, maa ngi muslu ci yaw ci bépp ay, ya ca jege ak ya ca sori, ya ma ca xam ak ya ma ca xamul.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi lay ñaan nga sàmm ma may aji-taxaw ci lislaam, nga sàmm ma may aji-toog ci lislaam, nga sàmm ma may aji-tëdd ci lislaam, ma lay ñaan nga bañ a def samay noon ak aji-soxor di ma ndokk.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi lay ñaaan wépp yiw ndax caabi yiy ubbi bunti yiw yépp moo ngi ci sa loxo, di muslu ci yaw ci aw ay ndax aw ay du am mukk ludul ne yaako dogal.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi lay ñaan nga may ma ci ag ragal Yàlla luy dox sama diggante ak di la moy, ak ci di la topp ci lu may eggale ca Sa Àjjana ja, ak ci kóolute luy woyofal ci nun musibay àdduna.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi lay ñaan nga xéewalal nu ci sunu dégg gi ak sunu gis gi, ak sunu kàttan gi fii ak yaa ngi nuy dundal, te nga def ko mu des ci nun[4], te nga fayyul nu ci kaw ñi nu tooñ, te nga dimbali nu ci kaw ñi nu noonoo, te bul def sunu musiba ci sunu diine, te bul def àdduna sunu mébét mi gën a rëy, du caagine sunu dayob xam-xam, te bul xirtal ci sunu kaw ku nu dul yërëm. Maanaam: bàyyil ci nun kàttanu sunu dégg gi ak sunu gis gi ginnaaw bu sunuy cér lompañee ba keroog nuy faatu. Al-Mafaatiihu Fii Sarhi Al-Masaabiihu(3/248)
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi muslu ci yaw ci buqat, di muslu ci yaw ci nay, di muslu ci yaw ñu delloo ma ca dund ga gën a doyadi, tey muslu ci yaw ci fitnay àdduna ak mbugalum bàmmeel.
Yaw Yàlla sunu Boroom jéggal ma samay njuumte, ak samag réer, ak samag jéggi-dayo ci samay mbir, ak li nga xam ci man, yaw Yàlla sunu Boroom jéggal ma samag farlu, ak samay caaxaan, ak samay njuumte, ak samag tayyeef, ak loolu lépp nekk ci man
Yàlla sunu Boroom jéggal ma, te yërëm ma, te gindi ma, te jàmmal ma, te wërsëgal ma.
Yaw Yàlla Sunu Boroom man de tooñ naa sama bopp tooñ gu bari, te kenn du jéggale bàkkaar ku dul yaw, maa ngi lay ñaan nga jéggal ma njéggal lu bawoo fi yaw, te nga yërëm ma, yaw Yàlla Jéggalaakoon bi di Yërëmaakoon bi.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi muslu ci sa màggaay gi ci nga sànk ma; amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul yaw, yaw yaay Aji-Dund ji dul dee, jinne yi ak nit ñi dañuy dee.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi lay ñaan nga defal ma luy waral sa yërmànde[5], ak luy waral sag njéggal[6], ak ug mucc ci bàkkaar, ak am wépp yiw, ak texe ci Àjjana, ak mucc ci Sawara. Maanaam: ay jëf ak i wax ak melo yiy waral sa yërmànde. Al-Mafaatiihu Fii Sarhi Al-Masaabiihi(2/304) (dogu yi): mooy melo wi nga xam ne nit ki da ciy dogu, maanaam: da koy jublu, ci jublug xol ak pasteefu ca; Maanaam maa ngi lay ñaan melo yi nga xam ne ci sababam laay ame sa yërmànde. Al-Mafaatiihu Fii Sarhi Al-Masaabiihi (2/304)
Yaw Yàlla sunu Boroom jéggal ma samay bàkkaar, te yaatalal ma sama kër, te baarkeelal ma sama wërsëg.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi lay ñaan ci sa ngëneel ak sa yërmànde, ndax kenn amu ko ku dul yaw.
Yaw Yàlla Sunu Boroom maa ngi muslu ci yaw ci ag daanu fu kawe, ak ug màbb, ak ug lab, ak ug lakk, maa ngi muslu ci yaw Saytaane di ma laal bu may faatu, di muslu ci yaw may faatu di aji-dummóoyu sa yoon wi, maa ngi muslu ci yaw ma dee ci ag fett.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi muslu ci yaw ci xiif, ndax moom kat dëkkaale gu bon la, maa ngi muslu ci yaw ci wor, ndax moom kat mbóot la gu bon.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi muslu ci yaw ci ag lott, ak tàyyeel, ak buqat, ak nay, ak màggat, ak ug wow, ak càggante, ak ñàkk[7], ak doyadi, ak ndóol, maa ngi muslu ci yaw cig ñàkk, ak ug kéefar, ak ug kàccoore, ak noonoo, ak naaféq, ak ndégtal, ak ngistal, maa ngi muslu ci yaw ci tëx ak luu, ak ndof, ak ngaana, ak siti, ak feebar yu bon yi. Al-hiila: ñàkk. Al-Muhallim Bi Fawaa-idi Muslim (1/279)
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi muslu ci yaw ci ñàkk, ak néewle, ak doyadi, di muslu ci yaw ci may tooñ walla ñu tooñ ma.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi muslu ci yaw ci dëkkandoo bu bon ci këru dëkk ga; ndax dëkkandoo gu tukki moom day deñ.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi muslu ci yaw ci xol bu ragalul Yàlla, ak ci bakkan bu dul suur, ak ñaan gu ñu dul nangu, ak xam-xam bu dul jariñ, yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi muslu ci yaw ci ñent yii.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi muslu ci yaw ci bis bu bon, ak guddi gu bon, ak waxtu wu bon, ak àndandoo bu bon, ak dëkkandoo bu bon ci këru dëkkuwaay bi.
Yaw Yàlla Sunu Boroom maa ngi lay ñaan Àjjana di muslu ci yaw ci Sawara.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi lay ñaan nga déggloo ma diine ji.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi muslu ci yaw ma lay bokkaale fekk xam naa ko, maa ngi lay jéggalu li ma xamul.
Yaw Yàlla sunu Boroom jariñ ma ci li nga ma xamal, te xamal ma lu may jariñ, te dolli ma xam-xam.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi lay ñaan xam-xam buy jariñ, ak wërsëg wu teey, ak jëf ju ñu nangu.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi lay ñaan yaw Yàlla yaay kenn ki yaay càppaacoli bi di ki ñuy jublu nga xam ne jurul kenn te kenn juru ko te amul benn nawle nga jéggal ma samay bàkkaar ndax yaw Yàlla Jéggalaakoon bi di Yërëmaakoon.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi lay ñaan cant yépp ñeel na la, amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul yaw dong amóo ndend yaw Aji-Maye ji, yaw mi sàkk Asamaan yi ak Suuf si, Yaw Boroom Màgg gi Ak Teddnga ji, yaw Aji-Dund ji, yaw miy Aji-Taxawe lépp, maa ngi lay ñaan Àjjana, di muslu ci Yaw ci Sawara.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi lay ñaan di seede ne yaw yaay Yàlla, amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul yaw, Yaw miy Kenn ki di Jubluwaay bi, di ki jurul kenn te kenn juru Ko, te amul benn nawle.
Yaw sama Boroom jéggal ma te baal ma, yaw yaay Baalekat bi di Jéggalaakoon bi.
Yaw Yàlla sunu Boroom ci sag xam kumpa, ak sa kàttan ci kaw mbindeef yi, maa ngi lay ñaan nga dundal ma ndeem xam nga ne dund moo gën ci man, di la ñaan nga faat ma ndeem xam nga ne faatu moo gën ci man.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi lay ñaan ma ragal la ci kumpa ak ci li feeñ, di la ñaan kàddug dëgg ci gërëm ak ci mer, di la ñaan ak jublu ci ñàkk ak ci woomal, maa ngi lay ñaan xéewal gu dul jeex, di la ñaan mbégte mu dul dagg, maa ngi lay ñaan ma gërëm ginnaaw ndogal yi, di la ñaan dund gu sedd ginnaaw dee ga, maa ngi lay ñaan bànneexu xool sa kanam gi, ak bëgg a daje ak yaw lool, ci lu dul loraange juy lore, du caagine fitna juy sànke.
Yaw Yàlla sunu Boroom noo ngi lay ñaan nga taaral nu ci taarug gëm, te nga def nu nu jub tey jubal.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi lay ñaan nga wërsëgal ma ma bëgg la, ak bëgg ku ag bëggam di ma jariñ fi yaw.
Yaw Yàlla sunu Boroom lépp loo ma wërsëgal ci li ma bëgg, maa ngi lay ñaan nga defal ma ko kàttan ci li nga bëgg.
Yaw Yàlla sunu Boroom lépp loo ma dajaleel ci li ma bëgg, maa ngi lay ñaan nga defal ma ko ci li nga bëgg.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi muslu ci yaw ci ragal, ak nay, ak dund gu bon, ak fitnay xol, ak mbugalum bàmmeel.
Yaw Yàlla miy Boroomu Jibriil ak Miikaa-iil, di Boroomu Israafiil, maa ngi muslu ci yaw ci tàngaayu Sawara, ak ci Mbugalum bàmmeel.
Yaw Yàlla sunu Boroom xamal ma njub ga, te musal ma ci ayu sama bakkan.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi lay ñaan xam-xam buy jariñ, di muslu ci yaw ci xam-xam bu dul jariñ.
Yaw Yàlla miy Boroom Asamaani juróom-ñaar, di Boroom Suuf si, di Boroom Aras ju Màgg ji, yaw Sunu Boroom di Boroom lépp, yaw mi xar pébb xoox[8], di Aji-Wàcce Tawraat ak Injiil ak Alxuraan, maa ngi muslu ci yaw ci ayu lépp lol yaay Aji-Téyé ci ag nosoom, yaw Yàlla sunu Boroom yaay Aji-Njëkk ji dara jiituwu la, yaay Aji-Mujj ji dara nekkul sa ginnaaw, yaay Aji-Fés ji dara nekkul sa kaw, yaay Aji-Nëbbu ji dara nëbbuwu la, maa ngi lay ñaan nga fayal nu bor yi, te woomalal nu wolif nuy ñàkk. Maanaam: kiy xar pepp yi, ay gub génn ca, ak xoox yi: ay tàndarma génn ca. Al-Mufhimu Limaa Askala Min Talxiisi Kitaabi Muslim(7/41)
Yaw Yàlla noo ngi lay ñaan nga boole sunu xol yi, yéwénal sunu diggante, jubal nu ci yoonu jàmm, musal nu ci lëndëm, yóbbu nu ci leer, te musal nu ci ñaawteef ak fitna yu feeñ ak yu nëbbu, baarkeel sunuy dégg, ak sunuy gis, ak sunuy xol, ak sunuy jabar ak sunuy doom, te nangu sunug tuub, ndax yaay kiy nangu tuub, yaay Yërëmaakoon bi, def nu nuy sant say xéewal, te di la ci sargal, te nangu ko, te nga matal ko ci nun.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi lay laaj gën gi laaj, ak ñaan gi gën, ak mucc gi gën, ak jëf ji gën, ak yool bi gën, ak dund gi gën, ak dee gi gën, te nga dëgëral ma, te diisal samay mandaxe, te dëggal samag ngëm, te yëkkëti samay daraja, te nangu samay julli, te nga jéggal ma samay njuumte, maa ngi lay ñaan daraja ya gën a kawe ca Àjjana.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi lay ñaan ubbiteg yiw yi, ak i mujjam, ak li dajale yiw yi, ak la ca njëkk ak la ca feeñ ak la ca nëbbu, ak daraja yu kawe ya ca Àjjana.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi lay laaj li gën ci li ma indi, ak li gën ci li ma def, ak li gën ci li ma liggéey, ak li gën ci li nëbbu, ak li gën ci li feeñ, ak daraja yu kawe ya ca Àjjana.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi lay ñaan nga yëkkëti sama tur, dindi samay bàkkaar, yéwénal samay mbir, sellal sama xol, aar samam péy, leeral sama xol, baal ma samay bàkkaar, maa ngi lay ñaan daraja ya gën a kawe ca Àjjana.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi lay ñaan nga Baarkeel sama bakkan ak samag dégg, ak samag gis, ak samaw bindiin, ak samay jikkó, ak ci samag njaboot, ak ci samag dund, ak ci samag dee, ak samay jëf, te nga nangu samay rafetal, maa ngi lay ñaan daraja ya gën a kawe ca Àjjana.
Yaw Yàlla sunu Boroom musal ma ci jikkó ak jëf ak bànneex ak feebar yu bon yi.
Yaw Yàlla Sunu Boroom def ma may ku doylu ci li nga ma wërsëgal, te nga baarkeelal ma ko, te lépp lu ma ñàkk nga wuutalal ma ko lu gën.
Yàlla sunu Boroom maa ngi lay ñaan nga regle ma regle gu yomb.
Yàlla dimbali ma ci ma lay tudd, ak di la sant, ak di rafetal ni ma lay jaamoo.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi lay ñaan ngëm gu dul rekkiku, ak xéewal gu dul jeex, ak ànd ak sa Yonnente bi Muhammat yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ca Àjjanay saxuwaay ba.
Yaw Yàlla sunu Boroom nanga ma musal ci lori sama bakkan, te nga tënk ma ci mbir yi gën a jub, yaw Yàlla jéggal ma li ma nëbb ak li ma feeñal, ak li ma juum, li ma tay, ak li ma xam ak li ma xamul.
Yaw Yàlla sunu Boroom nanga ma jéggal, te gindi ma, te wërsëgal ma, te jàmmal ma, maa ngi muslu ci Yàlla ci xatug saxuwaaw ëllëg bis-pénc.
Yaw Yàlla, na nga ma jariñ ci samag dégg ak sama gis, te nga def leen samay ndono,nga dimbali ma ci ñi may tooñ, nga fayyul ma ci ñoom.
Yaw Yàlla sunu Boroom maa ngi lay ñaan dund gu sell, ak dee gu rafet, ak dellusi gu dul toroxtange, du caagine gàcce.
Yaw Yàlla sunu Boroom rafetal nga sama jëmm, maa ngi lay ñaan nga rafetal sama jikkó.
Yaw Yàlla sunu Boroom jéggalal way-gëm yu goor yi ak way-gëm yu jigéen yi.
Yaw Yàlla sunu Boroom dëgëral ma, te def ma may aji-jub di aji-jubal.
Yaw Yàlla sunu Boroom may ma xereñte gi nga xam ne koo ko may may nga ko yiw wu bari.
Yàlla rekk a xam yal na Yàlla dolli xéewal ak mucc sunu Yonnente ba Muhammat.
Related books
All books
Lislaam mooy diiney Yonnente Yàlla yi85 languagesLislaam mooy diiney Yonnente Yàlla yi
Lislaam mooy jébbalul Yàlla mi bind àdduna bi di ko doxal, wommatul ko ngir bëgg ko ak màggal ko, cosaanu lislaam mooy gëm Yàlla, ak ne moom mooy Aji-Bind ji, te lépp lu dul moom mbindeef la, ak ne moom moo yayoo jaamu moom rekk amul bokkaale, amul lenn lu ñuy jaamu ci dëgg ku dul moom,ay tur yu rafet ñeel na ko ak ay melo yu kawe, mooy ki mat sëkk, jurul kenn te kenn juru ko te amul benn nawle du caagine niroowaale, du wàcc te du jël jëmmi lenn ci mbindeefam yi. Lislaam mooy diiney Yàlla mi nga xam ne du nangu ci nit jenn diine ju dul moom, te mooy diine ji yonnente yépp indi yal na leen…
الإسلام دين رب العالمين
Melow jullig Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-79 languagesMelow jullig Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-
Téereb «Ni Yonnente bi ﷺ daan jullee», Seex Abdul Asiis Ibn Baas -yal na ko Yàlla yërëm- dafa caa tënk melokaanu jullig Yonnente bi ﷺ, ci anam gu yomb te wóor, mu wéeru ci mbind yu wér, ngir mu doon ag gidee ñeel jullit bi ci ag julleem. Leeral na ci ponki julli yi, ak i sunnaam, ak i melokaam, dale ca jàppu ma ba ca sëlmël ga, di boole firnde ak leeral, tey woote ci roy gu mat ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci jaamu Yàlla gi gën a màgg.
الشهادتين78 languagesالشهادتين
Boo bëggee dugg ci lislaam, dangay wax ci kàddu gu gu ñu dégg seede gii di ñëw, te xam maanaa ma te gëm ko: Ashadu an laa-i-Laaha illal-Laahu (maanaay baat yii mooy ne amul kenn ku yayoo jaamu ku dul Yàlla), Maa ngi seede ne Muhammat ndawul Yàlla la, Iisaa ibnu Maryama it jaamub Yàlla la di ndawam.