الإسلام - نبذة موجزة عن الإسلام (مشتملة على الأدلة)
Lislaam Ab tënk bu gàtt ci Lislaam ni ki ni mu dikke ci Alxuraan ju tedd ji ak ci Sunnas Yonent bi Téere bu am solo bu làmboo xamle gu tënku ci Lislaam tey leeral ay cosaanam yi ëpp solo ak i njàggaleem ak ub taaram bu bawoo ci ay delluwaayam te mooy Alxuraan ak Sunnas Yonent bi. téere bi nag dees koo jëmale ci bépp muskallaf moo xam jullit la wala du jullit, def ko ci seen uw làkk ci jépp jamono ak bépp barab, ak nu séen i mbir ma na dème mbaa seen uw nekkiin. ( téere bi nag daal làmboo ay tektal yu bawoo ci Alxuraan ju tedd ji ak sunnas Yonent bi) Lislaam mooy bataaxalu boroom bi jëmm ci…
These files are generated automatically from the book's text; their layout may differ from the printed edition.
Lislaam
Ab tënk bu gàtt ci Lislaam ni ki ni mu dikke ci Alxuraan ju tedd ji ak ci Sunnas Yonent bi
Téere bu am solo bu làmboo xamle gu tënku ci Lislaam tey leeral ay cosaanam yi ëpp solo ak i njàggaleem ak ub taaram bu bawoo ci ay delluwaayam te mooy Alxuraan ak Sunnas Yonent bi. téere bi nag dees koo jëmale ci bépp muskallaf moo xam jullit la wala du jullit, def ko ci seen uw làkk ci jépp jamono ak bépp barab, ak nu séen i mbir ma na dème mbaa seen uw nekkiin.
( téere bi nag daal làmboo ay tektal yu bawoo ci Alxuraan ju tedd ji ak sunnas Yonent bi)
Lislaam mooy bataaxalu boroom bi jëmm ci nit ñëpp te moo fiy des ba fàww di mujjentalu Bataaxal bu bàyyi koo fa Yàlla sunu Boroom :
Lislaam mooy bataaxalu Yàlla bi jëmm ci nit ñépp Aji-Kawe ji nee na: {Yónniwunu la lu dul ci mboolem nit ñi ngir ngay Aji-Bégle di Aji-Xuppe waaye li ëpp ci nit ñi xamuñu} [Saaru Saba: 28]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Waxal: Éy yéen nit ñi man de Yonent Yàlla laa jëm ci yéen ñëpp } [Saaru Al-Ahraaf: 158]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Éy yéen nit ñi Yonent bi indil na leen dëgg gu bawoo fa seen Boroom, gëmleen ko ndax moo gën ci yéen, bu ngeen weddee nag na ngeen xamni Yàlla a Moom li ci asamaan ak suuf te Yàlla Aji-Xam la Aji-Xereñ la} [Saaru An-Nisaa: 170].
Lislaam mooy bataaxalu Yàlla bi sax te moo mujj ci bataaxalam yi, Yàlla mu kawe mi nee na: {Muhammat de du baayu kenn ci seen i góor waaye ndawal Yàlla la te moo mujj ci yonent yi te Yàlla mooy ki xam lépp} [Saaru Al-Ahsaab: 40].
2- Lislaam nag du diiney wenn waaso mbaa aw xeet waaye diiney Yàlla la ñeel nit ñépp:
Lislaam du diney wenn waaso mbaa wenn xeet waaye diiney Yàlla la ñeel nit ñëpp te ndigal li jiitu ci Alxuraan ju màgg ji mooy waxi Yàlla ji mu wax ne: {yéen nit ñi jaamuleen seen Boroom mi leen bind yéen ak ña leen jiitu ndax ngeen ragal Yàlla [Saaru Al-Baqara 21]. Yàlla mu kawe mi nee na: {yéen nit ñi ragal-leen seen Boroom mi leen sàkk ci benn bakkan muy Aadama sàkk ca soxnaam muy Awa daal di tasaare ci ñoom ñaar ay góor yu bari ak i jigéen} [Saaru An-Nisaaii: 1]. Jële na ñu ci Ibn Omar yalna leen Yàlla gërëm nee na: Yonent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da fa xutba nit ñi ci bisub ubbiteg Màkka ga daal di wax ne: " yéen nit ñi Yàlla de jële na ci yéen rëy-rëylug ceddo ga ak seenug damu ci seen i baay , nit ñi de ñaar kepp la ñu: ku baax te ragal Yàlla daal di tedd fa Yàlla, ak ub kàccoor bu texeedi doyadi fa Yàlla, nit ñi nag ay doomi Aadama la ñu, te Yàlla a ngi binde Aadama ci suuf, Yàlla neena: [yéen nit ñi nun noo leen bind ci góor ak jigéen def leen ay giir ak i xeet ngir ngeen xamante waaye ki gën a tedd fa Yàlla ci yéen mooy ki gën a ragal Yàlla, Yàlla de ku xam la te dara umpu ko} [Saaru Al-Hujraat: 13]" At-Tirmisiyu moo ko soloo (3270). Doo fekk ci ndigali Alxuraan ju màgg ji walla ci ndigali Yonent bu tedd bi yalna ko -Yàlla dolli xéewal ak mucc- benn yoonal bu aw nit jagoo walla am mbooloo ngir bàyyi xel seenuw askan walla seenuw xeet mbaa seen waaso.
3- Lislaam mooy bataaxalu Yàlla bi ñëw di mottali bataaxali yonent ya jiitu woon -yal na leen Yàlla dolli xéewal ak mucc- ca seen i xeet.
Lislaam mooy bataaxalu Yàlla bi ñëw di mottali bataaxali Yonent ya jiitu woon -yal na leen Yàlla dolli xéewal ak mucc- ca seen i xeet, Yàlla mu kawe mi nee na: {Nun Yàlla noo la sol niki nu sole woon Noohin ak yonent yi topp ci moom noo sol itam Ibraahiima ak Ismaahiila ak Isaaqa ak Yahquuba ak sët ya ak hiisaa ak Ayyuuba ak Yuunusa ak Haaruuna ak Sulaymaan, noo joxit Daawuuda téere bu tudd Sabuur} [Saaru An-Nisaaii: 163]. Diine jii nag Yàlla a ko soloo Yonent ba Muhammat -Yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- mooy diine ji Yàlla yoonalal yonent ya jiitu woon te mu dénkoon leen ko, Yàlla mu kawe mi nee na: Yoonalal na ñu leen ci diine la ñu dénkoon Noohin ak la nu la soloo yaw Muhammat ak la nu dénkoon Ibraahiima ak Muusaa ak hiisaa te mooy Na ngeen taxawal diine te buleen cay tàqalikoo, li ngeen di woo bokkaalekat yi di leen ca jëmale da fa rëy lool ci ñoom, Yàlla mooy jigeel boppam ku ko soob te mooy gindi jëmale ci boppam képp ku ko jublu} [Saaru As-Suuraa: 13]. Te lii Yàlla soloo Yonent Yàlla Muhammat Yalna ko -Yàlla dolli xéewal ak mucc- day dëggal téerey Yàlla yi ko jiitu woon niki Tawraat ak Injiil lu jiitu séenug coppiku, Yàlla mu kawe mi nee na: La Nu la soloo ci Téere bi mooy dëgg, di Aji-Dëggal téere ya ko jiitu woon, Yàlla Aji-Xam lépp la Aji-Gis lépp la} [Saaru Faatiri: 31].
4- Yonent yi yal na leen -Yàlla dolli xéewal ak mucc- seen diine benn la, waaye seen i yoon nag moo wuute:
Diiney yonent yi -yal na jàmm nekk ci ñoom- benn la waaye seen i yoon ñoo wuute, Yàlla mu kawe mi nee na: {Wàcce Nanu ci yaw Téere bi ci dëgg muy Aji-Dëggal téere ya ko jiitu woon te di leen sàmm, na nga àtte seen digante li Yàlla wàcce, te bul topp seen bànneex bàyyi dëgg gi la dikkal, ku nekk ci yéen defal nanu ko aw yoon ak aw doxaliin, te bu sooboon Yàlla mu def leen wenn xeet, waaye da leen di nattu ci li mu leen indil. Jëkkanteleen jëm ci yiw ya te xam ne di ngeen Dellu fa Yàlla yéen ñépp, Mu xibaare leen li ngeen nekkoon di sa juuyoo} [Saaru Al-Maaida: 48]. Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "Man maa gën a yey nit ñépp ci Hiisaa doomi Maryama ci àdduna ak allaaxira, te yonnent yi ay doom i baay la ñu, seen i yaay ñoo wuute waaye seen diine benn la" Al Buxaariyu moo ko soloo (3443).
Lislaam day woote -niki ni yonent yépp doon wootee: Noohin ak Ibraahiima ak Muusaa ak Sulaymaan ak Daawuuda ak Hiisaa -yal na leen Yàlla dolli xéewël ak mucc- ci gëm ne Boroom bi mooy Yàlla Aji-Bind ji Aji-Wërsëgal Aji-Dundal Aji-Ray mooy ki moom ag nguur te mooy ki nga xam ne mooy doxal mbir yi te mooy Aji-Ñeewante di Aji-Yërëme ji.
Lislaam day woote -niki ni yonnent yépp doon woote: Noohin ak Ibraahima ak Muusaa ak Sulaymaan ak Daawuuda ak Iisaa yal na leen Yàlla dolli xéewël ak mucc- ci gëm ne Boroom bi mooy Yàlla Aji-Bind ji Aji-Wërsëgal Aji-Dundal Aji-Ray mooy ki moom nguur gi te mooy ki nga xam ne mooy doxal bir yi te mooy Aji-Ñeewant jiy Aji-Yërëme ji, Yàlla mu kawe mi nee na: { yéen nit ñi fàttalikuleen xéewali Yàlla yi ci yéen mo ndax am na aji-bind ju dul Yàlla? mu di leen wërsëgal ci asamaan yi ak suuf si, amul benn buur bu nu wara a jaamu budul moom Yàlla kon naka ngéen koy dummóoyoo?} [Saaruu Faatiti: 3]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Neel: ana kan moo leen di wërsëgal ci asamaan ak suuf ? Ana kan moo moom ag dégg-(nopp yi) moom AB jis (bët yi)? Ana kan mooy génne luy dund ci lu dee di génne lu dee ci luy dund ? Ana kan mooy doxal mbir yi? Daa ñu la wax ne "Yàlla" neeleen moo xanaa dungeen ragal Yàlla?} [Saaru Yuunusa: 31]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Ana kan moo tàmbali sosug mbindéef yi topp mu di ko delloosiwaat? Ana kan moo leen di wërsëgal ci asamaan yi ak suuf si ? Moo ndax daa am jeneen yàlla ju ñuy bokkale ak Yàlla? Neeleen indileen seen i firnde ndeem wax ngeen dëgg} [Saaru An-Namli: 64].
Yonent yépp -yal na leen Yàlla dolli xéewal ak mucc- dees leen a yónni ci woote ci jaamu Yàlla moom kepp, Yàlla mu kawe mi nee na: {Yónni Nanu ci xeet wu ne ab yonent bu leen di wax jaamuleen Yàlla te moytu ay xërëm, am na ca ñoom ñu Yàlla jubal, am na ca it ñoo xamne cànkutee war na ca ñoom, doxleen ci suuf si ngeen xool na ka la ña weddi woon mujje} [Saaru An-Nahl: 36]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Yónniwunu ca la jiitu benn yonent ludul ne soloonanu ko ci ne amul benn buur bu dul Man kon jaamuleen ma} [Saaru Ak-Anbiyaaii: 25]. Yàlla xibaare na ci Noohin -yal na ko Yàlla dolli mucc- mu wax ne: {yéen samay mbokk jaamuleen Yàlla amu leen jenn yàlla ju dul moom, man de ragal naa ci yéen mbugalum bis bu màgg} [Saaru Al-Ahraaf: 59]. Soppe Yàlla bi Ibraahiima -yal na ko Yàlla dolli mucc- wax na niki ni ko Yàlla xibaare ci moom mu ne: {Ak Ibraahiima ba mu waaxee ay mbokkam ne leen jaamuleen Yàlla te ragal ko, loolu de moo gën ci yéen ndeem xam ngeen}. [Saaru Al-Ankabuut: 16]. Saalihu it -yal na ko Yàlla dolli ko mucc- wax na niki ni ko Yàlla xibaare ci moom mu ne: {Wax na ne yéen samay mbokk jaamuleen Yàlla amu leen jenen yàlla ju dul moom, ay lay yu leer nàññ dikkal na leen jóge ca seen Boroom, lii giléemug Yàlla la nekk Ag kéeman ci yéen, bàyyileen ko mu lekk ci kaw suufas Yàlla si, te bu leen ko def lu ñaaw, lu ko moy mbugal mu metti dal ci seen kaw} [Saaru Al-Ahraaf : 73]. Suhaybu itam -yal na ko Yàlla dolli mucc- wax na niki ni ko Yàlla xibaare ci moom mu ne: {Yéen samay mbokk jaamuleen Yàlla amu leen jeneen Yàlla ju dul moom, ay lay yu leer nàññi dikkal na leen jóge ca seen Boroom, deeleen matal natt yi ak màndaxe yi, te buleen wàññil nit ñi la ñu moom, te it buleen yàq ci kaw suuf ginnaaw ba ñu ko defaree, loolu moo gën ci yéen bu fekkee ne gëm ngeen} [Saaru Al-Ahraaf: 85].
Bi Yàlla di njëkk a wax ak Muusaa -yal na ko Yàlla dolli mucc- daf ne ko: {Man Maa la tànn, kon déglul li Ma lay soloo (13) Man de maay Yàlla amul jeneen Yàlla ju dul Man kon jaamu Ma tey taxawal julli di Ma fàttaliku(14)} [Saaru Taaha: 13-14]. Yàlla xibaare na ci Muusaa -yal na ko Yàlla dolli mucc- mu wax ne: {Maa ngi muslu ci sama Boroom ci kébb kuy rëy-rëylu te gëmul bisub waññoo ba (bis pénc ba)} [Saaru Xaafiri: 27]. Yàlla xibaare na ci Masiihu (Hiisaa)-yal na ko Yàlla dolli mucc- mu wax ne: {Yàlla de mooy sama Boroom di seen Boroom kon jaamuleen ko, lii dey mooy yoon wu jub kocc wi} [Saaru Aali-Imraan: 51]. Yàlla xibaare na itam ci Masiihu -yal na ko Yàlla dolli mucc- mu wax ne: {Yéen waa Banuu-Israaiil nangeen jaamu Yàlla miy sama Boroom di seen Boroom, te ngeen xam ne ku bokkaale ak Yàlla dara, Yàlla araamal na ci moom Àjjana te dëkkuwaayam mooy Sawara, te tooñkat yi duñu am benn ndimbal} [Saaru Al-Maaida : 72].
Ba ci Tawraat ak Injiil sax, luy feddali ne Yàlla dong la ñu war a jaamu ñëw na ca; ñëw na ca Sifru Tasniya waxi Muusaa ja -yal na ko Yàlla dolli mucc-: (Diglul te xam yaw Israaiil ne sunu Boroom kenn rekk la) Ñëw na batay ca Injiilu Murxus luy feddali kennal Yàlla, ba Masiihu -yal na ko Yàlla dolli mucc- di wax naan: (Ndénkaane bi jiitu mooy: Diglul te xam yaw Israayiil ne sunu Boroom kenn rekk la).
Te Yàlla mu màgg mi leeral na ne mboolem Yonent yi dees leen a yónni ci yitte ju màgg jii te mooy woote ci kennal Yàlla, Yàlla mu kawe mi nee na: {Yónni nanu ci xeet wu ne ab ndaw ngir nañuy jaamu Yàlla te moytu ay xërëm, am na ca ñoom ñu Yàlla jubal am ca ñoom ñu ag cànkute ñeel} [Saaru An-Nahl : 36]. Yàlla mu kawe mi nee na: Waxal: xibaarleen ma si lingeen di jaamu te du Yàlla, ngeen wan ma ana lan la ñu bind ci kaw suuf, walla da ñoo am wàll ci asamaan si! Indilleen ma ab téere bu jiitu bii di Alxuraan walla boog njeexitalug xam-xam ndeem dëggu ngeen} [Saaru Al-Ahxaaf: 4] Seex Assahdii -yal na ko Yàlla yërëm- nee na: (Xamees na ne werente ak bokkaalekat yi ci seen bokkaale gi amuñu wenn lay walla ab tegtal, waaye kay da ñoo sukkandik rekk ci njortu yu dul dëgg, ak ay gisiin yu wérul, ak ay xel yu yàqu , te li lay tegtal ak yàqoom mooy jàngat seen i bir, ak luññutu seen i xam-xam ak seen i jëf, daal di xool nag mbir u ña jeexal seenug dund ci jaamu loola ndax jariñ na leen( maanaam, yooya ñuy jaamu te du Yàlla) ndax jardiñ na leen dara ci àdduna mbaa àllaaxira?) Taysiirul Kariimil Mannaan: 779.
6-Tudd naa sellug Yàlla sunu Boroom mu kawe mi ci ne mooy Aji-Bind ji te mooy ki yayoo jaamu moom rekk, te dee su ko bokkaale ak kenn cig jaamu.
Yàlla mooy ki yayoo jaamu moom rekk, te dee su ko boole ak keneen cig jaamu, Yàlla mu kawe mi nee na: { yéen nit ñi jaamuleen seen Boroom bi leen bind yéen ak ña leen jiitu woon, ndax ngeen ragal ko (21) Mooy ki def suuf mu nekk laytaay ci yéen, def asamaan mu tiim leen, mu wàcce am ndox mu bawoo ca asamaan, daa di cay génne ay meññent mu nekk wërsëg ñeel leen, kon book buleen wutal Yàlla moroom, te xam ngeen ne amul moroom (22)} [Saaru Al-Baqara: 21-22]. Ki nu bind te bind itam maas ga nu jiitu woon te mu def suuf si muy laytaay ñeel nu, daal di wàcce ndox mu bawoo ca asamaan, mu génne ca ay meññent ñeel nu mu di sunu wërsëg, kooku rekk moo yeyoo ag jaamu, Yàlla mu kawe mi nee na: { yéen nit ñi fàttalikuleen xéewal yi leen Yàlla defal ndax am na ken ku bind Ku dul Yàlla mi leen di wërsëgal ci asamaan yi ak suuf si, kon naka lees leen di wëlbatee ba ngeen ba fi Yàlla} [Saaru Faatiti: 3]. Ki bind tay wërëgal moom rekk moo yeyoo ag jaamu, Yàlla mu kawe mi nee na: {Kooku mooy Yàlla seen Boroom, amul jeneen Yàlla ju dul moom, Moo bind lépp kon jaamuleen ko, te mooy kiy saytu mbir yépp} [Saaru Al-Anhaam: 102].
Te lépp lees di jaamu lu dul Yàlla yeyoowul ag jaamu, ndax te moo mul lu toll ni aw fepp ci asamaan walla ci suuf, te bokkul ak Yàlla dara, te nekkul ko koy dimbali ci dara, Mba mu koy jàppale ci lenn, kon naka lees di jaamoo Yàlla di ko Boole ak keneen, walla di ko wutal ndend, Yàlla mu kawe mi nee na: {Waxleen: ñu woo seen xëram yi ñu jort ne dañoo bokk ak Yàlla Ngur gi, ñoom amuñu lu toll ni aw fepp ci asamaan walla ci suuf, te amuñufa yit benn wàll, te kenn ca ñoom jàppalewul Yàlla ci dara} [Saaru Sabai: 22].
Tudd naa sellug Yàlla mu kawe mi, moom mooy ki bind mbindéef yépp, te mooy ki leen amal ci ag ñàkk, te seenug am tegtal la ci amug Yàlla, te tegtale it nguuram gi, ak yelloo ga ag jaamu, Yàlla mu kawe ma nee na: {Bokk na ci ay keemaanam bind gi mu leen bind ci suuf, fa saase rekk ngeen di ay nit yu tasaaroo(bari) (20) bokk na ci keemaanam yi mu bindal leen ci seen uw xeet ay soxna, ngir ñu leen di dalal , mu def ci seen diggante ag cofeel ak ug yërmànde, ay keemaan nekk na ca loola ñeel képp kuy xalaat (21) Bokk na ci ay keemaanam bind gi Mu bind asamaan yi ak suuf si, ak wuute gu seen i làkk wuute niki noonu seen i melo, ay keemaan nekk na ca loola ñeel mbindéef yépp (22) Bokk na ciy keemaanam seenug nelaw ci guddi yi ak bëccëg yi ak seenug sàkku ay ngëneelam, ay keemaan nekk na ca loola ñeel nit ñiy dégg (23) Bokk na ci keemaanam yi won gi mu leen di won melax gi mu boole ragal ak xemmem, Muy wàcce ci asamaan si am ndox, daal di ciy dundal suuf si ginnaaw ba mu dee yee, ay keemaan nekk na ca loola ñeel nit ñiy xellu(24) Bokk na batay ci ay keemaanam taxaw gi asamaan ak suuf di taxaw ci ndigalam, te saa Su leen woowee benn woo yéen ñépp di ngeen génn ci biir suuf (25) Mooy ki moom képp ku nekk ci asamaan yi ak suuf yi te ñépp a koy toroxlul (26) Mooy ki sos mbidéef yi moo leen di delloosiwaat bu ñu faatoo itam, te looloo gën a yomb ci Moom} [Saaru Ar-Ruum: 20-27].
Namruut dafa weddi amug Yàlla, Ibraahiima -yal na ko Yàlla dolli mucc-ne ko niki ni ko Yàlla xibaare ci moom: {Ibraahiima wax ne Yàlla mooy indi jant bi mu bawoo ca penku ba, yaw indi ko jële ko sowwu, ca la weddikat ba wedame, (amul aw lay) te Yàlla du gindi tooñkat yi} [Saaru Al-Baqara: 258]. Naka noonu Ibraahiima def na firnde ci aw nitam, ci ne Yàlla Moo ko gindi, te Moo koy leel di ko nàndal it, moo ky wéral bu tawatee , di ko ray di ko dundal, niki ni ko Yàlla mu kawe mi xibaare ci moom mu ne: {Moom mi ma bind Moo may gindi (78) Te Mooy ki may leel di ma nàndal (79) bu ma woppee mu faj ma (80) Te Moo may ray di ma dundal (81) } [Saaru As-Suharaa: 78-81] Yàlla a ngi nettali ci làmmenñu Muusaa -yal na ko Yàlla dolli mucc- ne werente na ak Firhawna ne ko: Boroomam mooy: { Ki sos mbidéef yépp te moo leen di ginde } [ Saaru Taaha: 50].
Yàlla tàggatal na nit mboolem li ci asamaan ak li ci suuf, daal di koy peeg ak i xéewël; ngir mu jaamu Yàlla te bañ koo weddi, Yàlla mu kawe mi nee na: { Xanaa gisu leen ne Yàlla Moo leen tàggatal li ci asamaan yi ak li ci suuf si, daal di sotti ci seen kaw ay xéewëlam ci lu feeñ ak lu nëbbu, am na ci nit ñi nak ñuy dàggasante ci Yàlla ci lu dul benn xam-xam walla ag njub, mbaa sax benn téere buy leeral } [Saaru Luqmaan: 20]. Ni Yàlla tàggatale nit mboolem li ci asamaan yi ak suuf si, noonu la ko binde waajalal ko lépp lu mu aajowoo ci ag dégg ak ub jis ak xol ngir mu man a sàkku xam-xam bu koy jariñ, di ko tegtal kilifaam gi ko bind, Yàlla mu kawe mi nee na: { Yàlla moo leen génne ca seen biir i yaay ya, te xamu leen woon dara, mu defalal leen ag dégg ak ub jis ak xol, ndaxtelee ngen gërëm ko } [Saaru An-Nahl: 78].
Yàlla mu kawe mi tuddnaa ag sellam dafa bind mbindéef yépp,daa di bind nit waajalal ko lépp lu mu aajowoo ci ay cër ak kàttan, daal di koy jox lépp lu koy dimbali ci jaamu Yàlla ak dundal suuf si, tàggatal ko it lépp lu nekk ci asamaan yi ak suuf si.
Yàlla def mbindéef yii mu bind ñuy aw lay ci nekk gim nekk buur, nguur gog day làmbboo warug jaamu ko , Yàlla mu kawe mi nee na: { Waxal ne ana kan moo leen di wërsëgal ci asamaan yi ak suuf? kan moo moom ag dégg ak ub jis ? Ana kan mooy génne luy dund ci lu dee di génne lu dee ci luy dund? Ana kan mooy doxal mbir yi? Danañu la wax ne xanaa Yàlla, waxal ne xanaa dungeen ragal Yàlla kon } [Saaru Yuunusa: 31]. Yàlla miy Dëgg tudd naa sellam ga nee na: { Waxal ne ndax gis ngeen yi ngeen di jaamu te du Yàlla wonleen ma lan la ñu bind ci kaw suuf walla da ñoo am wàll ci asamaan yi? Indilleen ma ab téere bu jiitu téere bii di (Alxuraan) walla benn jeexitu xam-xam ndeem dëggu ngeen } [Saaru Al-Ahxaaf: 4]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Moo bind asamaan ci lu dul keno lu ngeen di gis, (keno: lu koy téye ) Mu def ci suuf ay doj ba du jeng ànd ak yéen, Mu def ca ay xeeti mala yu nekk, Nu wàcce am ndox mu bawoo ca asamaan, Nu saxal ca ay xeeti gàncax yu wuute. Lii la Yàlla sàkk, kon wonleen ma ñi dul Yàlla ñoom lu ñu sàkk, tooñkat yi daal ñoo ngi cig cànkute gu leer} [Saaru Luqmaan: 10-11]. Yàlla miy Dëgg nee na: {Waaw ndax ñoom dañoo sous noonu rekk te Yàlla bindu leen walla ñoom ñooy Aji-bind ya?(35) Walla ñoom ñoo bind asamaan yi ak suuf si? Déedéd! Li am kay moodi ne ñoom wóoluwuñu (gëmuñu) 36) Walla sax ñoom da ñoo yor sa ndàmbi Boroom yi, walla ñoom ñoo yore dogalu mbir yi (37) } Ndàmb: (deñukaayu alal) [Saaru At-Tuur: 35-37]. Sëriñ bii di As- Sahdiyyu nee na: (Lii aw lay la wu tege ci seen kaw, di mbir moo xam ne manuñu lu dul nangu dëgg gi, walla ñu wuute ak xel ak diine) Tafsiiru Ibn Sahdiyyu : 816.
7- Yàlla moo bind lépp lu nekk ci àdduna, li nu gis ak li nu gisul, te lu dul Yàlla mbidéef la ci mbidéefam yi, Yàlla bind na asamaan ak suuf ci juróom-benni fan.
Yàlla moo bind lépp lu nekk ci àdduna bi, li nu gis ak li nu gisul, te lu dul Yàlla mbidéef la ci mbidéefam yi, Yàlla mu kawe mi nee na: {Neel: ana kan mooy Boroom asamaan ak suuf ? Neel: "Yàlla la". Neel: mo ndax kon da ngeen di jàpp yeneen kilifa yu dul Moom yoy amaluñu seen bopp benn njariñ walla jenn lor?. Neel: mo ndax gumba da na yam ak njàccaar( kuy gis)? Walla, ndax lëndëm da na yam ak leer?. Mo, ndax da ñiy wutal Yàlla ay bokkaale yu bind lu mel ni li Mu bind ba seen mbindéef yi niroo ci ñoom? Neel: Yàlla rekk moo bind lépp te Mooy Kenn kiy Aji-Not ji} [Saaru Ar-Rahd: 16[. Yàlla mu kawe mi nee na: { Mooy bind lu ngeen xamul} [Saaru An-Nahl: 8].
Yàlla bind na asamaan yi ak suuf si ci juróom-benni fan, Yàlla mu kawe mi nee na: { Mooy ki bind asamaan yi ak suuf si ci juróom-benni fan, ba noppi Mu yamoo ca kaw gàngunaay ga(Aras), xam na lépp luy dugg ci biir suuf, ak lépp lu cay génn, ak lépp luy wàcc te bawoo asamaan ak lépp lu cay yéeg, te mi ngi ànd ak yéen fu ngeen man di nekk, te Yàlla kuy gis la lépp lu ngeen di def} [Saaru Al-Hadiid: 4]. Yàlla mu kawe mi nee na: { Bind Nanu asamaan yi ak suuf si ak li nekk ci seen diggante ci juróom-benni fan te amunu ci benn coono} [ Saaru Xaaf: 38].
8- Yàlla mu kawe mi -tudd naa ag sellam- amul kenn ku mu bokkal nguuram gi, walla mbindéefam yi, walla doxaliinam wi, walla jaamu gi.
Yàlla mu kawe mi moo moom nguur, amul kenn ku mu bokkal mbindéefam yi, walla nguuram gi, walla doxaliinam wi, Yàlla mu kawe mi nee na: { Neel: ndax gis ngeen yi ngeen di jaamu te du Yàlla? wonleen ma lan la ñu bind ci suuf si, Mo ndax da ñoo am wàll ci asamaan yi? Indilleen ma ab téere bu jiitu lii di (Alxuraan) walla benn jeexitu xam-xam ndeem dëggu ngeen} [Saaru Al-Ahxaaf : 4]. Seex Assahdii -yal na ko Yàlla yërëm- nee na: (Maanaam:{Waxal} ñii di bokkale Yàlla ak i xërëm ak i ndend yoy amu ñu njariñ Mbaa lor, moomu ñu dee mbaa dund, moomu ñu dekki, leeralalleen tële gu seen xërëm yi tële, te it yayoo wuñu dara cig jaamu: { wonleen ma lan la ñu bind ci suuf si wala da ñoo am wàll ci asamaan yi} ndax dañoo bind benn fepp ci asamaan yi walla ci suuf si? Ndax dañoo bind ay montaañ? Ndax dañoo dawal ay dex? Ndax dañoo amal ay baayima? Ndax dañoo saxal ay garab? Ndax dañoo jàpple Yàlla ci bind lenn ci yooyu? Dara amul ci yooyu te ñoom saxal na ñu loolu rawatina keneen, te lii tegtalug xel gu dog la ci ne lépp lu dul Yàlla jaamu ko ag neen la.
Ba mu noppee mu tudd dàqu gi tegtalug toxal dàqu, mu ne: {Indilleen ma ab téere bu jiitu bii} téere buy woote ci bokkaale {Walla jeexitu xam-xam} bu ñu donnee ca yonent ya muy digle loolu. Xamees na ne ñoom lott nañu ci toxal jële ci benn yonent genn tegtal guy tegtale loolu, da nuy dogu sax bu wóor ci ne mboolem yonent yi ci kennal Yàlla la ñu doon woote, di tere bokkaale, te loolu mooy li gën a màgg lu ñu jële ci ñoom ci xam-xam) Tafsiiru Ibn Sahdii: 779.
Yàlla mu sell mi te kawe mooy Boroom nguur gi, amul kenn ku mu bokkal nguuram gi, Yàlla mu kawe mi nee na: {Waxal yaw yónent bi ne: Yàlla sama Boroom yaay Boroom nguur gi, yaay jox nguur ku la soob, di rocci nguur it ci ku la soob, yaay teral ku la soob, di toroxal ku la soob, wépp yiw mi ngi ci sa loxo, te yaa am kàttan ci lépp}. [Saaru Aali-Imraan: 26]. Yàlla a ngi wax di leeral ne nguur gu mat sëkk moom rekk la ñeel ëllag bis-pénc: {Bis ba ñoom ñépp di fés te seen dara du nëbbu ci Yàlla, sunu Boroom da naan: ana kan moo moom nguur tay? Xanaa Yàlla miy Kenn ki not lépp } [Saaru Xaafiri: 16].
Yàlla mu sell mi te kawe amul kenn ku mu bokkal nguuram gi walla mbindéefam yi walla doxaliinam walla jaamu gi, Yàlla a ngi wax naan: {Neel: Gépp cant ñeel na Yàlla mi amul doom, te bokkul ak kenn nguuram gi, te amul ku koy dimbali ngir ag toroxte, dee ko màggal bu baax} [Saaru Al-Israa: 111]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Moom mi moom nguurug asamaan ak suuf te amul doom, amul it ku mu bokkal nguur gi, Moo bind lépp ba noppi jox ko lamu yayoo} [Saaru Al-Furxaan: 2]. Mooy ki moom te ku dul Moom moomeelam nga moom Yàlla mu Sell mi, Moom mooy ki Bind te leneen lu dul moom mbindéefam la, mooy kiy doxal bir yi, te koo xam ne lii mooy mbiram dees koo war a jaamu, te jaamu ku dul moom nag am xel mu wàññiku la, te bokkaale la gog day yàq àdduna ak allaaxira, Yàlla mu kawe mi nee na: (Ñoom Yahuut yi ak Nasaraan yi a ...ngay wax naan: doonleen ay Yahuud walla ay Nasaraan kon de dingeen gindiku, yaw yónent bi Neeleen déedéet, njub nga kay moo di diiney Ibraahiima ma wéetaloon Yàlla te masul a bokk ca bokkaalekat ya} [Saaru Al-Baqara: 135]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Ana kan moo gën a rafet diine ki jébbal boppam Yàlla te di rafetal, tey topp diiney braahiima cig wéetal Yàlla, Yàlla nag mooy ki def Ibraahiima ab soppe} [Saaru An-Nisaai: 125]. Yàlla miy dëgg -tudd naa sellam ga- leeral na ne képp ku topp ludul diiney Ibraahiima, -yal na ko Yàlla dolli mucc-na xam ne ku gàtt xel la, Yàlla mu kawe mi nee na: {Ana kan mooy bañ diiney Ibraahiima ku dul ku kannasu, Nun Yàlla de noo ko tànn fii ci àdduna te bu àllaaxiraa dana bokk ca ñu yiw ña} [Saaru Al-Baqara: 130].
9- Yàlla jurul kenn te kenn juru ko, te amul nàttango amul maas.
Yàlla mu sell mi jurul kenn te kenn jurul ko, te amul benn naatàngo walla niroowaale, Yàlla miy Dëgg nee na: { yaw yónent bi waxal ne: Yàlla kenn la(1) Yàlla Mooy genn kilifa gi ñépp di jublu ciy aajoi. ( càppaacoli)(2) Jurul kenn te kenn juru ko(3) Te amul moroom (4) } [Saaru Al-Ixlaas: 1-4]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Boroom asamaan yi ak suuf si, ak li nekk ci seen diggante, nanga ko jaamu te muñ te sax ca jaamu ga, waaw! Ndax xamal nga ko wenn turandoo? } [Saaru Maryama: 65]. Yàlla miy Dëgg te màgg i bir, nee na: { Moo sàkk asamaan yi ak suuf si, defal na leen ay soxna yu xeetoo ak yéen, def it ay mala yu góor ak yu jigéen, te ci loolu la leen di defe ngeen nekk ñu bari, lenn melut ni Moom Yàlla, te moom Aji- Dégg tey Aj- Gis}. [Saaru As-Suuraa: 11].
10- Yàlla mu kawe mi -tudd naa ag sellam- du jaxasoo ak dara te du jëll jëmmi dara ci mbindéefam yi:
Yàlla mu kawe mi -tudd naa ag sellam- du jaxasoo ak dara te du jël jëmmi dara ci mbindéefam yi, te du bennoo ak dara; ndax te Yàlla mooy Aji-Bind ji te lu dul Moom mbindéef la, Mooy Aji-Des ji te lu dul Moom ci jeex lay mujj, Mooy Buuru lépp di Aji-Moom lépp, te dara ci mbindéefam yi du jaxasoo ak jëmmi Yàlla ji-tudd naa sellam ga- Yàlla mu sell mi moo gën a màgg lépp, Yàlla mi ngi wax di weddi ñiy foog ne mool Yàlla da fa jaxasoo ak Masiih: {Ñiy wax ne Yàlla Mooy Almasiih ñooñu weddi nañu، yaw yónent bi neel: ana kan moo manal Yàlla dara bu nammee alag Almasiih doomi Maryama ak yaayam ak ñi ci kaw suuf ñépp? Yàlla ay Boroom asamaan ak suuf ak li nekk ci seen diggante, Mooy bind lu ko soob. Te Yàlla moomu mooy ki man lépp}. [Saaru Al-Maa-ida: 17]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Yàlla a moom penku ak sowu, fu ngeen fi man a jublu Yàlla a nga foo fa, Yàlla nag Ku yaatu la te mooy ki xam lépp (115) ñoom Nasaraan yi nee na ñu Yàlla am na doom! Tudd naa ag sellam- li am kay mooy: Moom Yàlla Moo moom lépp lu nekk ci asamaan yi ak suuf si te lépp a koy toroxlul(116) Yàlla mooy ki fent asamaan yi ak suuf si, te saa su nammee mbir da naan ko nekkal rekk mu nekk(117) [Saaru Al-Baqara: 115-117]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Ñom Nasaraan yi ba Ray nee nañu Yàlla miy Yërëme am na doom(88) Wax ngeen lu juunu(89) Asamaan si xaw na cee xottiku, suuf si xaw cee xar, tund ya xaw cee màbb(90) Ngir li ñu wax ne Yàlla am na doom(91) Te yellul mukk ci Yàlla miy boroom Yërmaande muy am doom(92) Lépp lu nekk ci asamaan yi ak suuf si di na dikkal Ya miy boroom Yërmaande dib jaam kese(93) Yàlla takk na leen te xam na seenub lim(94) Te ñoom ñépp a koy dikkal bu Bis-pénc baa kennoo kenn(95) [Saaru Maryama: 88-95]. Yàlla mu kawe mi nee na: { Yàlla déy! Amul benn buur bees di jaamu cig Dëgg bu dul moom, mooy kiy dund dund gu dul jeex, tey Taxawe lépp, du gëmmentu waxatumalaag nelaw, Moo moom li nekk ci asamaan yi ak suuf si. Ana kan moo sañ a tinu fa moom lu dul ci ndigalam ? Moo xam la nekk ci seen kanam ak ci seen ginnaaw. Te kenn du peeg dara ci xam-xamam bi lu dul la ko ca soob, gàngunaayam ga daj na asamaan ak suuf, te lu leen wattu ñoom ñaar jaaxalu ko, Mooy Aji-Kawe ji di Aji-Màgg ji} [Saaru Al-Baqara : 255]. Koo xam ne lii mooy ay mbiram ci kàttan ak sañ-sañ, ay mbindéefam lii de seen i mbir cig njaame, naka lay wàcce di jaxasoo ak kenn ci ñoom ? Walla mu koy jàppe doom ? walla mu koy def Yàlla ju ñu koy booleel?
Yàlla mu kawe mi -tudd naa sellam ga-Aji-Ñeewant Ku Bari yërmaande la ciy jaamam la, loolu moo tax mu yónni ay yonent daal di wàcce ay téere.
Yàlla mu kawe mi -tudd naa ag sellam- mooy ku Ñeewant ka di Ku Bari yërmaande ci ay jaamam, bokk na ci yërëm gi mu leen yërëm moo di yónni gi mu yónni ci ñoom ay yonent, daal di wàcce ci ñoom ay téere; ngir génne leen ci ay lëndëmi kéefër ak bokkaale duggal leen ci leerug wéetal Yàlla ak njub, Yàlla mu kawe mi nee na: { Moom Mooy wàcce ay lay yu leer ca jaamaam ba Muhammat -SLHWS- ngir mu génne leen ci ag lëndëm duggal leen ci ag leer, te Yàlla déy ku leen ñeewant la ku leen yërëm la} [Saaru Al-Hadiid : 9].
Yàlla mu kawe mi nee na: { dama laa yónni rekk ngir yërmaande ci mbindéef yépp} [Saaru Al-Anbiyaa : 107]. Yàlla digal na yonenteem bi ne ko na wax jaam ñi ne moom mooy kay jéggale tey boroom yërmaande ju Bari ja, Yàlla mu kawe mi nee na: { yaw yónent bi neel sama jaam ñi: Man Maay Jéggalaakoon bi di Yërëmaakoon bi} [Saaru Al-Hijri: 49]. Bokk na cig ñeewantem ak yërmaandeem Mooy day wuññi njàqare, tey wàcce aw yiw ci jaamam yi, Yàlla mu kawe mi nee na: {Bu la Yàlla tegee njàqare kenn du ko man a teggi ku dul moom, bu la nammalee aw yiw it kenn du ko man a fanq, yiw woowu dana ko defal ku ko soob ci ay jaamam, Moom Mooy jéggalaakoon bi, di Yërëmaakoon bi} [Saaru Yuunusa : 107].
12- Yàlla mooy Boroom biy Yërëmaakoon ba, te moom rekk mooy càmbar jëfi mbindéef yi bu bis-pénc baa, keroog bu leen dekkilee ba ñoom ñépp génn ca seen bàmmeel ya, mu fay kenn ku nekk la mu def ci lu baax walla lu bon. Képp ku def lu baax te di way-gëm, xéewal gu sax dàkk ñeel na ko, képp ku weddi di def ay ñaawteef mbugal mu màgg ñeel na ko ëllëg Bis-pénc.
Yàlla mooy Boroom biy Yërëmaakoon bi, moom rekk mooy càmbar jëfi mbindéef yi ca bis-pénc ba, keroog bu leen dekkalee ba ñoom ñépp génn ca seen bàmmeel ya, mu fay kenn ku nekk li mu def ci lu baax walla lu bon. Képp ku jëf lu rafet te di way-gëm xéewal gu sax dàkk ñeel na ko, képp ku weddi di def ay ñaawteef mbugal mu rëy ñeel na ko ëllëg Bis-pénc. Bokk ci matug maanduteg Yàlla mu kawe mi ak ug xereñam ak yërmaandeem ci mbindéefam yi ci la def àdduna bii di kërug liggéey, Mu def geneen kërug ñaareel gog fa lay faye ak a càmbare Jëfi jaam ñi; ba ki doon rafetal jot yoolub rafetalam, ki doon ki ne woon te dib tooñkat jot mbugalam mbewteem ak ak tooñaangeem; lii nag di na am xel yu ko dul nangu, Waaye Yàlla joxe na ay firnde yu bari yuy tektale ne dekki dëgg la gu amul benn werente, Yàlla mu kawe mi nee na: {Bokk na ci ay keemaanam mooy ne da ngay gis suuf si mu wow koŋŋ , bu nu ci wàccee am ndox mu yëggu daal di funki, kiy dundal suuf sii nag ginnaaw bi mu deeyee mooy dekkil ñi dee, te moom mooy ki man lépp}. [Saaru Fussilat: 39]. Yàlla mu kawe mi nee na: { yéen nit ñi ndeem da ngen di sikk-sakka ci mirum dekki, xamleen ne nun noo leen bind ci suuf, ginnaaw ba mu bind leen ci toqug manniyu, ginnaaw ba mu doon lumbu deret, ginnaaw ba suuxu yàpp wu nu bind bind gu mat, ak wu nu matalul ag bindam, ngir nu leeralal leen, te nun nooy def ca meen ma lu nu soob ba ca àpp bu nu xam, ginnaaw ba génne Judd di ay liir, ginnaaw ba ngeen màgg ba doon ay waxambaane, am na ci yéen ñuy teel a dee, am ci yéen ñuy dund ba màggat ba naag, ba dootul xamati dara, ginnaaw ba mu nekkoon ku xam, nga gis suuf si mu wow koŋŋ, te bu nu ci wàccee ndox mu yëngu daal di funki daal di saxal gépp xeetu gàncax gu rafet} [Saaru Al-Hajji: 5]. Yàlla miy dëgg tudd na ci aaya bi ñàtti firndey xel yuy tegtale dekki, te mooy:
1- Yàlla mi ngi njëkk a binde nit ci suuf, te moom mi ko binde ci suuf bu faatoo ba nekkaat suuf kon man na koo delloosi waat muy dund.
2- Ki bind nit ci ag toq kay, man naa defaat nit muy dund ginnaaw bi mu deeyee.
3- Ki dundal suuf si ci ab taw ginnaaw ba mu deeyee, koo ku kay man naa dundalaat nit ginnaaw ba mu deetee, te keemaan gu màgg feeñ na ci aaya bi ci ne Alxuraan dafa lottal ñépp, Aaya bi nga xam ne sax guddul naka la man a boolee ñàtti firndey xel yu rëy yuy tegtale mpir mu màgg mi?.
Yàlla mu kawe mi nee na: {Bis pénc mooy bis ba ñuy taxañ asamaan si niki ñuy taxañe këyit wu am mbind, na nu tàmbalee woon sosug nit gu njëkk ga nu mel noonu la nu koy dekkalaate buñu faatoo, loolu ab dëel bu nu warlu la, te dana nu ko def} [Saaru Al-Anbiyaa: 104]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Moom de mi ngi nuy jox niral (misaal), ba noppi fàtte ag sosoom, ma ngay wax naan: ana kan mooy dundalaat yax yii ginnaaw ba mu funuxee (78) Yaw yónent bi neel: ki ko sosoon bu njëkk moo koy dakaal, te Moom mbindaafoon yépp la xam} [Saaru Yaasiin: 78]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Mo ndax bind leen moo gën a jafe walla asamaan si ma tabax(27) Yékkati na talaayam ba, te yamale ko(28) Mu lëndëmal guddeem ga, leerale bëccëgam ga(29) Gannaaw ga mu tàllal suufam sa(30) Génne na ca moom ndoxam ma ak gàncaxam ga(31) Mu samp ca tund ya(32) } [Saaru An-Naasihaati: 27-32]. Sunu Boroom-leeral na fii ne mbindum nit gënul a jafe mbindum asamaan si ak suuf si ak li ci seen biir, te ki man a bind asamaan yi ak suuf si tële wut a dekkal nit ñi beneen yoon.
13- Yàlla mu kawe mi da fa bind Aadama ci suuf daal di def ay sétam di yokk ginnaawam, nit ñépp ñoo yam cosaan, wenn waaso gënul weneen waaso, wenn xeet it gënul weneen xeet ci lu dul ragal Yàlla.
Yàlla mu kawe mi da fa bind Aadama ci suuf daal di def ay sétam di yokk ginnaawam, nit ñépp ñoo yam cosaan, wenn waaso du gën weneen waaso, wenn xeet it du gën weneen xeet ci lu dul ragal Yàlla, Yàlla mu kawe mi nee na: { yéen nit ñi noo leen bind ci góor ak jigéen, nu def leen ngeen di ay giir ak i xeet ngir ngeen xamante waaye ki gën a tedd ci yéen fa Yàlla mooy ki ko gën a ragal, Yàlla Aji-Xam la Aji-Xereñe lépp la} [Saaru Al-Hujraat : 13]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Yàlla moo leen bind ci suuf luy Aadama, ginnaaw ba mu bind leen ci toqu manniyu, mu daa di leen def nag ñu xeetoo (góor ak jigéen), amul jenn jigéen juy ëmb walla muy jour lu dul ci xam-xamam ba moom Yàlla, amul it kenn kuy dund, walla g dundam di wàññiku lu dul ne bind nañu konca téere ba, (Allawhul-mahfuus) te loolu lu yobb la ca Yàlla} [Saaru Al-Faatiri: 11]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Mooy ki leen bind ci suuf topp ca ab toq maniyu topp ca lumbu deret, topp ca mu génne leen ngeen nekk liir, topp ngeen nekk ay waxambaane yu dëgër, topp ca ay mag yu maggat, am na ci yéen ñuy faatu lu jiitu loolu, ak it ngeen egg ca dig ba mu leen àppal, ngir it ngeen xellu} [Saaru Xaafiri : 67]. Yàllaa ngi wax di leeral ne bind na Almasiih ci ndigalul nekkal, niki mu binde Aadama ci suuf ci ndigalul nekkal ga, Yàlla mu kawe mi nee na: {Mbirum Iisaa fa Yàlla de da fa mel ni mbirum Aadama rekk, da koo bind ci suuf ne ko "nekkal" rekk mu nekk} [Saaru Aali-Imraan : 59]. Jiitu na nu wax ca xëtum ñaareel ba ci ne Yonent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- leeral na ne nit ñi ñoo yem, kenn du gën kenn ci lu dul ragal Yàlla.
14- Képp ku judd rekk dees koo jur ci cosaani diine
Képp ku judd rekk dees koo jur ci cosaani diine, Yàlla mu kawe mi nee na: {Nangay jubale sa bopp ci diiney Yàlla ju jub ji, tey cosaan juj ci la sose nit ñi, deesul soppi mbindiinu Yàlla, te loolu moy diine ju jub ji, waaye ñi ëpp si nit ñi duñu xam} [Saaru Ar-Ruum: 30]. Diine ju jub ji nag mooy diiney Ibraahiima soppe ba -yal na ko Yàlla dolli mucc-, Yàlla mu kawe mi nee na: {Topp soloo nanu la ci nela toppal diiney Ibraahiima ci wéetal Yàlla, moom de bokkul woon ca bokkaalekat ya} {Saaru An-Nahl: 123]. Yonent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- nee na: "Amul kenn kuy judd lu dul ne dees koo jur ci cosaani diine, ñaari way-juram nag ñoo kay def Yahuud walla Nasaraan walla Majuus, niki ni baahima di juree baahima ju mucc ayib, ndax da ngeen ca gis benn dagg-dagg?" Aboo Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- day wax ne: {Cosaani diiney Yàlla ji Mu sose nit ñi, deesul soppi mbindiinu Yàlla, te loolu moy diine ju jub ji, waaye ñi ëpp si nit ñi duñu xam} [Sarru Ar-Ruum : 30] Sahiihul Buxaariyyu 4775, Yonent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "yëgleen ne sama Boroom digal na ma ngir ma xamal leen lu ngeen xamul, bokk na ci li mu ma xamal bisu tay bii, bépp alal ju ma jox ab jaam loola dagan na, Man nag damaa bind sama jaam yépp ci wéetal Yàlla, saytaane nag moo leen dikkal wëlbati leen ci seen diine, mu daal di araamal ci ñoom li ma leen daganaloon, mu digal leen ñu may bokkaale ci luma wàcceewul wenn lay" Muslim moo ko soloo: 2865.
15- Amul kenn ci nit ñi ku judduwaale bàkkaar, walla muy donn bàkkaarub keneen:
Amul kenn ci nit ñi ku judduwaale bàkkaar, walla muy donn bàkkaari keneen, Yàlla xibaar na nu ne bi Aadama wuutee ak ndigalul Yàlla daal di lekk ca garab ga moom ak soxnaam sa Awa, da fa réccu daal di tuub, ñaan Yàlla jéggal ko, Yàlla sol ko ay waat yu teey, mu wax ko, Yàlla jéggal leen, sunu Boroom mu kawe mi nee na: { Nun noo wax Aadama ne ko dëkkal àjjana yaw ak sa soxna, ngeen lekk lu leen neex ci nu mu leen neexe, te buleen jege garab gii, kon dey dangeen bok ca way-tooñ ya(35) Saytaane daal di leeni tarxiisloo, génne leen fa ñu nekkoon, ca la nu ne leen wax ne leen wàccleen yaw Aadama ak ibliis ngen di ay noon, (maanaam ibliis di noonu Aadama ak i sëtam) am ngeen nag ci kow suuf ak dëkkuwaay ak bànnex bu gàtt (36) Aadama jot ay baat yu bawoo fa Boroomam, Mu daal di ko jéggal, Moom Yàlla nag ab Jéggalaakoon la, Yërëmaakoon la(37) Nun noo leen ne wàccleen yéen ñépp, samag njub dina leen dikkal, képp ku topp samag njub nag doo am looy ragal mbaa looy tiit(38) [Saaru Al-Baqara: 35-38]. Ndeem Yàlla jéggal na Aadama -yal na ko Yàlla dolli mucc- kon gàddootul bàkkaar ba, kon kay ay sëtam duñu donn bàkkar boo xam ne tuub dindi na ko, te liy cosaan mooy nit du gàddu bàkkaaru keneen, Yàlla mu kawe mi nee na: { kenn jëfalul ku dul boppam, te kenn du gàddu bàkkaarub keneen, te ca seen Boroom ngeen di dellu, Mu xabaare leen la ngeen nekkon di ca juuyoo } [Saaru Al-Anhaam: 164].
Yàlla mu kawe mi nee na: {Ku jub boopam la ko defal, ku dëng it boppam la ko def, ndax kenn du gàddu bàkkaarub keneen, du nu mbugal it aw nit te yónniwunu ci yónni wunu ci ñooml ab yonnent. [Saaru Al-Israa: 15]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Kenn du yenu bàkkaaru keneen, ba ki diis gànn ak i bàkkaar bu sàkku woon ku ko yenul ay bàkkaaram kenn du ka ko yenul donte jegeñaaleem la, yaw nag da ngay xupp ñi ragal seen Boroom ci kumpa, tey taxawal julli, képp ku sellal boppam rekk lay sellal, te ci Yàlla ngeen di dellu} [Saaru Faatiri: 18].
16-Jubluwaay gi tax ñu bind nit ñi mooy: jaamu Yàlla moom rekk:
Jubluwaay gi tax ñu bind nit ñi mooy: jaamu Yàlla moom rekk, Yàlla mu kawe mi nee na: {Binduma jinne ak nit lu dul ngir ñu jaamu ma} [Saaru As-Saariyaati: 56].
17- Lismaam da fa teral nit -góor ak jigéen- mu sàmmal ko mboolem ay àqam, mu def ko muy ndayu-mbill gi ci mboolem ay tànnéefam ak i jëfam, mu def ko kilifag boppam ci bépp jëf ju koy lor wala muy lor ñeneen ñi.
Lislaam da fa teral nit -góor ak jigéen-, Yàlla da fa bind nit ngir mu nekk kilifa(kuutaay) ci kaw suuf, Yàlla mu kawe mi nee na: {Fàttalikul ba sa Boroom waxee Malaakayi ni leen: Man de damaa nar a def ca kaw suuf ab kilifa(kuutaay) } [Saaru Al-Baqara: 30].
Teral gii nag da fa daj mboolem doomi Aadama yi, Yàlla mu kawe mi nee na: {Nun noo teral doomi Aadama, boyal leen ci jéeri ji ak ci géej gi, Nu wërsëgal leen yu teey yi, Nu gënale leen lool ci lu bari ca ya nu bind} [Saaru Al-Israa: 70]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Noo bind nit ca gën gaa rafeti anam} [Saaru At-Tiini: 4].
Yàlla tere na nit muy def boppam ab toppekat bu doyadi ñeel lenn lu ñuy jaamu, walla lu ñuy topp, te du Yàlla, Yàlla mu kawe mi nee na: {Am na ci nit ñi ñuy wutal Yàlla ndend, dañu leen di bëgg ni ñuy bëggee Yàlla, waaye ñi gëm moom Yàlla la ñu gën a bëgg, ay ña weddi bu ñu gisoon, bu ñu janoog mbugal ma, danañu xam xéll ne Yàllaa ame kàttan gépp, te Yàlla ku tar mbugal la, bu boobaa ña ñu daan topp danañu deñtalu ca ña leen daan topp, ñu janoog mbugal ma, la leen boole woon lépp daggatoo} [Saaru Al-Baqara: 165-166]. Yàlla mu kawe mi mi ngi leeral mbiri way-toope ya ak ña ñu doon topp ci neen bu bis-pénc baa: Kilifa ya doon rëy-rëylu di wax ña ñu néewaloon doole naan leen: ndax nun noo leen féewale woon ak njub ga ginnaaw ba mu leen dikkale woon? Déet kay, yéen kay ay tooñkat ngeen woon(32) Ña ñu néewaloon doole wax kilifa ya doon rëy-rëylu ne leen: yéen kay yéen a ñu doon pexeel guddi ak bëccëg, daan nu digal nu weddi Yàlla wutal ko ay ndend, ñu daal di réccu ba ñu gisee mbugal ma, Nu daal di def ay jéng ca loosi ña weddi, moo ndax dees na leen fay lu dul la ñu daan def?(33) } [Saaru Saba: 32-33].
Bokk na ci matug mànduteg Yàlla keroog bis-pénc mu gàll wootekat ak njiit yi daan réeralaate seen i bàkkaar ak bàkkaari ña ñu daan réeral ci lu dul xam-xam, Yàlla mu kawe mi nee na: {Danañu gàddu seen i bàkkaar ba mu mat sëkk ëllëg bis-pénc, ak lenn ca bàkkaari ña ñu doon réeral ci lu dul benn xam-xam, cëy ñoo bon i bàkkaar} [Saaru An-Nahl: 25].
Lislaam dafa sàmmal nit ki ay àqam ba mu mat sëkk, ci àdduna ak allaaxira, àq yi gën a màgg te lislaam wattul ko nit ñi, daal di leen koy leeralal, mooy: àqi Yàlla ci nit ñi ak àqi nit ñi ci Yàlla Jële nañu ci Muhaas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: damaa waroon ci ginnaaw yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu ne ma: "Yaw Muhaas" ma ne ko: wuyu naa la fonk naa la, mu waxaat ko ñatti yoon, daal di ne ma: "ndax xam nga àqi Yàlla ci jaamam ñi ?" Ma ne ko: déet-déet, mu ne ma: àqi Yàlla ci jaamam yi mooy ñu jaamu ko te bañ koo bokkaale ak dara" mu dox ab diir, daal di ne ma: "yaw Muhaas" ma ne ko, wuyu naa la fonk naa la, mu ne ma: "ndax xam nga àqi jaam ñi ci Yàlla bu ñu defee loolu ? Mooy: mu bañ leen a mbugal" Sahiihul Buxaarii (6840).
Lislaam da fa sàmmal nit ki diineem jiy dëgg, ak i doomam, ak alalam, ak ub deram Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-nee na: "Yàlla de araamal na ci yéen seen dereet ak seen alal ak seen der, niki mu joxe worma seen bis bii, ci seen weer wii, ci seen dëkk bii" Sahiihul Buxaarii.(6501) Yonent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yégle woon na kóllare gu màgg gii ca ajug tàggatoo ga nga xam ne lu ëpp téeméeri junni ci ay àndadoom teewe woon nañu ko, mu daal di koy baamtu feddali ko bisub tabaski, ca ajug tàggatoo ga.
Lislaam nag da fa def nit ki muy ku ñi y laaj mbooleem ay tànnéefam ak i jëfam, Yàlla mu kawe mi nee na: {Nit ku negg dananu ko lënkale ak ay jëfam cig doqam, bu bis-pénc baa nu génneel ko ab téere bu muy dajeel ñu tàllal ka ko, naan ko jàngal sab téere tay sa càmparub jëf yaw la war, te doy nga ci sëkk sa bopp}. [Saaru Al-Israa: 13]. Maanaam: lépp lu mu def ci lu baax walla lu bon, Yàlla dina ko def mu taqoo ak moom du ko jéggi di jëm ci keneen, ken du ko càmbar ci jëfi keneen, te ken du càmbar keneen it ci ay jëfam moom, Yàlla mu kawe mi nee na: { yaw nit ki, yaa ngi jëf jëm ca sa Boroom te dinga daje ak moom de}. [Saaru Ak-Insiqaaq: 6]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Képp kuy jëf yiw boppam la koy defal, képp kuy jëf ñaawteef it ci kawam lay dal, sa Boroom nag du tooñ benn jaamam} [Saaru Fussilat: 46].
Lislaam day laaj nit ki bépp jëfam moo xam mu koy lor walla muy lor ñeneen, Yàlla mu kawe mi nee na: {Képp ku jëf bàkkaar boppam la ko def, Yàlla ku xam la ku xereñ la} [Saaru An-Nisaai: 111]. Yàlla mu kawe mi nee na: { Looloo tax nu dogal ca Banii-Israaiil, ci ne képp ku ray bakkan bu rayul kenn, te nekkul di yàq ci kaw suuf, mel na ni ku ray nit ñépp, ku xettali nit musal ko ci dee, mel na ni dundal na nit ñépp} [Saaru Al-Maa-ida: 32]. Yonent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-nee na: "Deesul ray benn bakkan cig tooñ lu dul doomu Aadama ju njëkk ja dina am ab cer ca dereetam ja, ndax te moo njëkk a yoonal ray ga" Sahiihu Muslim (5150).
18- Lislaam nag da fa yamale góor ak jigéen ci jëf ak warteef ak pay ak ub yool.
Lislaam nag da fa yamale góor ak jigéen ci jëf ak warteef ak pay ak ub yool, Yàlla mu kawe mi nee na: {Képp ku jëf aw yiw moo xam góor la walla muy jigéen te di aji-gëm ñooñu dinañu dugg àjjana te deesu leen tooñ dara donte daa tuuti ba toll ni mboxosu xooxu tàndarma} [Saaru An-Nisaai: 124]. Yàlla mu kawe mi nee na: Yàlla mu kawe mi nee na: {Képp ku jëf lu baax muy góor mbaa jigéen te fekk mu nekk Ku gëm, dana nu ko dundal dund gu teey, te dana nu leen fay seenug payoor lu gën a rafet la ñu doon def} [Saaru An-Nahl: 97]. Yàlla mu kawe mi nee na: {képp ku jëf ñaawteef deesu ko fay lu dul lu toll noona, képp ku jëf it aw yiw muy góor mbaa muy jigéen te di ab jullit ñoom danañu dugg àjjana, ñu di leen fa wërsëgal te deesu leen càmbar} [Saaru Xaafiri: 40]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Jullit yu góor yi ak jullit yu jigéen yi way-gëm yu góor yi ak way-gëm yu jigéen yi way-wommatu yu góor yi ak way-wommatu yu jigéen yi way-dëggu yu góor yi ak way-dëggu yu jigéen yi muñkat yu góor yi ak muñkat yu jigéen yi way-toroxlu yu góor yi ak way-toroxlu yu jigéen yi saraxekat yu góor yi ak saraxekat yu jigéen yi woorkat yu góor yi ak woorkat yu jigéen yi góor ñiy sàmm seen pëy ak jigéen ñiy sàmm seen pëy goor ñiy tudd Yàlla lu bari ak jigéen ñiy tudd Yàlla lu bari, Yàlla waajalal na leen ag njéggal ak pay gu màgg} [Saaru Al-Ahsaab: 35]
19- Lislaam da fa teral jigéen, def leen ñuy genn wàlli góor ñi mu waral ci góor dundal njaboot su ko manee, dundug doom ju jigéen war na baayam, dundug yaay war doomam ju góor ndeem mat na muskàllaf te man ko, dundug jabar moom it war jëkkër.
Lislaam da fa jàppe jigéen ñi ñuy genn wàlli góor ñi Yonent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-nee na: "Jigéen ñi ñooy genn wàllug góor ñi" Tirmissiyyu moo ko soloo 113.
Bokk na ci teral gi lislaam teral jigéen mooy lislaam da fa waral ci doom ju góor mu war a gàddu dundug yaayam ndeem man na ko Yonent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "Loxo biy joxe mooy loxo ba kawe daraja, waaye joxal sa yaay ak sa baay ak sa mbokk mu jigéen ak sa mbokk mu góor teg ca ña sës ci yaw teg ca ña ca sës" Imaam Ahmat moo ko soloo Dees na leeral dayob ñaari way-jur ci pàccub limatug (29) ndeem soob na Yàlla.
Bokk na ci teral gi lislaam teral jigéen mu waral ci jëkkër muy dundal jabaram ndeem man na ko, Yàlla mu kawe mi nee na: {Ki woomal nay joxee na mu woomale, ku woomalul itam nay joxe na am-amam toll, Yàlla du teg kenn lu mu manul, Yàlla dana def yombal ginnaaw ag jafe} [Saaru At-Talaaq: 7]. Benn waay laaj na Yonent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: lan mooy àqi jigéen ci jëkkëram ? Mu ne ko: "bu lekkee na ko jox mu lekk, bu soloo na ko solal, te bumu ko dóor si xar kanam te bumu ko wax lu ñaaw. " Imaam Ahmat moo ko soloo, Yonent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral na yénn àqi jigéen ñi ci seen i jëkkër: { Jigéen ñi seenub dund ak Seenug col war na ci góor ñi ca nañu ko mane}. Sahiihul Muslim. Yonent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-nee na: "Doy na sëkk nit ki bàkkaar mu sàggane ki mu war a dundal" Imaam Ahmat moo ko nettali. Al-Xattaabiyyu nee na: ( Li mu wax ne "ki mu War a Dundal" li mu ci namm mooy: ki ko ag dundam war, mu mel ni day wax aji-sarexe ji ne ko: bul sarexe ci li nga war a dundale sa njaboot ndegam desul ngir sàkku ca tiyaaba; ndax loolu man naa mujj nekk bàkkaar ci boo leen sàgganee)
Bokk na ci teral gi lislaam teral jigéen mooy mu waral dundug doom ju jigéen ci kaw baayam, Yàlla mu kawe mi nee na: (Nday yi na ñuy nàmpal seen i doom ñaari at yu mat sëkk ci ku bëgg nàmpal gu mat, war na ca baay ba itam dundu ak kodaayu jigéen ñi ci njekk) [Saaru Al-Baqara: 233]. Yàlla it leeral na ne war na baay bi ñu jural doom dundug doomam ak koddaayam ci njekk, Yàlla mu kawe mi nee na: { yéen góor ñi su leen jigéen ñi nàmpalalee Seen i dooma na ngeen leen jox seenug pay} [Saaru At-Talaaq: 6]. Yàlla moo waral ci baay payug nàmpal doom; loolu nag day tegtale ne dundug doom ji baay bi la war, doom nag day làmboo góor ak jigéen, te Hadiis bii di ñëw day tegtale ne dundug jabar ak i doomam baay ba la war Jële nañu ci Haisatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu ne: Hind da fa wax Yonent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-ne ko: Abuu Sufyaan de góor gu nay la lool, ba dinaay faral di aajowoo bay jël dara ci alalam te du ko yëg, mu ne ko: "man ngaa jël lu la doy yaw ak sa doom te bu ca yokk dara" Al-Buxaariyyu moo ko soloo Yonent bu tedd bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral na ngënéelu dundal doom yu jigéen ak ay mbokk yu jigéen, mu wax ne: "Képp ku dundal ñaar i doom yu jigéen walla ñatt walla ñaari mbokk yu jigéen Mbaa ñatt ba tàqalikoo ak ñoom wala mu faatu bàyyi leen fi, man ak moom niki ñaar yii. Mu daal di sànni ñaar i waaraamam: sànnikaay ba ak digg ba" Assilsilatus Sahiihatu 296.
20- Dee nekkul ag jeex ba fàww waaye tuxu la jóge ci kërug jëf gi jëm ca kërug pay ga, dee nag day làmboo yaram ak ruu, deewug ruun nag mooy mooy ag tàqalikoom ak yaram wi, daldi cay delluwaat ginnaaw dekki ga bis-pénc, ruu nag ginnaaw bu deeyee du tuxuwaat jëm ci weneen yaram, mbaa ñukacay def.
Dee nekkul ag jeex ba fàww, Yàlla mu kawe mi nee na: {yaw yónent bi neel: malaakam dee mi ñu leen booleel moo leen di ray, ginnaaw ba ñu delloo leen ca séen Boroom} [Saaru As-Sajdati: 11]. Dee nag day làmboo yaram ak ruu, deewug ruu mooy mu tàqalikoo ak yaram wi, daadi cay delluwaat ginnaaw dekki ga bis-pénc, Yàlla mu kawe mi nee na: Yàlla mooy faat bakkan yi bu deeyam jotee, ak ba deewul ci biiri nelaw, mu téye ba mu dogal ci moom dee, daal di boyal ba ca des jëme ko ca dig ba mu ko àppal, loolu nag ay kéemaan a ngi ci ñeel ñay xalaat} [Saaru As-Sumari: 42]. Yonent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "Bu ñu jëlee ruu gi bët yi dakoy topp" Muslim moo ko soloo 920, Ginnaaw bu nit ki deeyee nag, day tuxu juge ci kërug Jëf gi, jëm ca kërug fay ga, Yàlla mu kawe mi nee na: {Ci moom Yàlla ngeen di dellu yéen ñépp, loolu dëelub Yàlla la bay dëgg, moom nag moo sos mbindeef yi te moo leen di ray, ginnaaw ba mu dekkal leen ngir fay ñi gëm tey def lu baax cig maandute, ña weddi nag naan gu tàng ñeel na leen ca wawara ak mbugal mu metti ngir lañu doon weddi} [Saaru Yuunus: 4].
Ginnaaw faatu nag ruu gi du tuxu di dem si beneen yaram, tee wootewoo ne ruu gi day sottiku si beneen yaram xel tegtalewu ko, yég-yég it tegtalewu ko, te amul lenn lu ñu tuxal luy seede pas-pas bi te bawoo ci Yonnent yi.
21- Lislaam day woote ci gëm cosaani ngëm yu mag yi, te mooy: gëm Yàlla, ak i malaakaam, ak gëm téere Yàlla yi niki Tawraat, ak Injiil, ak Sabuur -lu jiitu ñubkoy soppi-ak Alxuraan,ak gëm mbooleem yonnent yi ak ña nu yónni-yal na leen Yàlla dolli jàmm-,mu gëm it ki mujj ci ñoom muy Muhammad mi mujj ca ña ñu soloo ak ña ñu yónni,ak gëm bis bu mujj ba,te ñu xam ne bu doon dundug adduna bii mooy dund gi mujj;kon dund gi ak nekkiin wi fo rekk lay doon, ak gëm dogal yi.
Lislaam day woote ci cosaani ngëm yu mag yi yonnent yépp daan woote-yal na leen Yàlla dolli jàmm- te mooy:
Bu ñëkk bi: gëm ne Yàlla moo moom te moo bind di wërsëgal di doxal dund gi,te moom rekk moo yayoo jaammu te jaamu lu dul moom ag neen la,te lépp lu ñuy jaamu lu dul moom ag neen la, kenn yayoowul jaamu ku dul moom, te genn jaamu du wér gu dul gi ko ñeel.Tegtali masala bii leeraloon nañu ko si xëtu(8).
Coosaan yu mag yii nag Yàlla tudd na ko si ay aaya yu bari ci Alxuraan ju màgg ji, bokk na ca li mu wax ne: {Yonnent bi gëm na li ñu wàcce ci moom mu bawoo si Boroomam, jullit yi ñépp gëm nañu Yàlla ak i malaakaam ak i téereem ak i yonnenteem, du ñu teqale kenn ci yonnent yi, ñuy wax naan dégg nanu te topp nanu, noo ngi sàkku sa njéggal yaw sunu Boroom, te yaw rekk yaay dellluwaay ba} [Saaru Al-Baqara: 285]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Ag mbaax nekkul rekk si ngeen di jëmale séen kanam penku ak sowwu, waaye mbaax mooy ki gëm Yàlla ak bis bu mujj ba ak malaaka yi ak téere bi ak yonnent yi,muy joxe alal ca ba mu koy soxla ay jegeñaaleem ak jirim yi ak way ñàkk yi ak ñi nekk si yoonu tukki ak way-laaj yi ak jaam yi,tey taxawal julli di joxe asaka ak ñiy matal kóllare saa yu ñu kóllarante,ak way-muñ yi jafe-jafe yi ak lor yi,ak jamonoy xat-xat ñoo ñu ñooy ñi dëggal te ñooy ñi ragal Yàlla} [Saaru Al-Baqara: 177] Yàlla dafa woote jëme ci cosaan yii, daal di leeral ne ku ko weddi sànku na cànkute gu sori,Yàlla mu kawe mi nee na: {Éey yéen ñi gëm, gëmleen Yàlla ak Yonnenteem bi ak téere bi mu wàcce ci yonnenteem bi, ak téere yi mu njëkk a wàcce, ku weddi Yàlla ak i malaakaam ak i téereem ak i yonnenteem ak bis bu mujj ba kooku sànku na cànkute gu sori}. [Saaru An-Nisaa :136]. Ñëw na ci hadiis Umar ibn Xattaab -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: (Nekk nanu benn bis ci Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- benn waay fëll, yëre yaa ngi weex tàll,kawar gi ñuul kukk, te deesul gis si moom jeexitalu tukki,te kenn ci nun xamu ko, mu dem ba toog ci Yonnent bi daal di sës ay bëti wóomam ci ay bëti wóomam, teg ay ténqam ci kaw ay poojam,daal di ne ko: yaw Muhammat xibaare ma lan mooy lislaam(jébbalu), Yonnent bi ne ko:"lislaam mooy nga seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, Muhammat ndawul Yàlla la,di taxawal julli di woor weeru koor, aj Màkka boo ko manee benn yoon" mu ne ko: wax nga dëgg,nu yéemu ci moom,di ko laaj ba noppi di ko dëggal. Mu ne ko: wax ma lan mooy iimaan(ngëm):mu ne ko:" ngëm mooy nga gëm Yàlla ak i malaakaam ak i téereem ak i yonnenteem ak bis bu mujj ba, nga gëm dogal yu neex yi ak yu nàqari yi" mu ne ko: wax nga dëgg, daal di ne ko: wax ma lan mooy ihsaan(rafetal), mu ne ko: "rafetal mooy ngay jaamu Yàlla ba mu mel ni yaa ngi koy gis, ndax boo ko gisul mi ngi lay gis" Sahiihu Muslim 8. ci hadiis bii Jibriil dafa ñëw si Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc-laaj ko martabay diine ji,te mooy lislaam ak liimaan ak lihsaan, Yonnent bi tontu ko ba ginnaawam ga mu xibaar sahaaba yi ne leen kii Jibriil la dafa ñëwoon ngir xamal leen séen diine.Lii mooy lislaam di bataaxelu Yàlla bob Jibriil moo ko tuxal Yonnent Muhammat bi jottali ko nit ñi,sahaaba yi wàttu ko ba jottali ko nit ñi ginnaawam.
Ñaareel ba: gëm Malaaka yi ñoom nag ci àddunay kumpa la ñu nekk, Yàlla da leen a bind def leen ci ay melokaan yu ràññeeku, togg leen ay jëf yu màgg, bokk na ci li gën a màgg ci séen i jëf jottali bataaxelu Yàlla ñeel Yonnent yi -yal na jàmm nekk si ñoom- ki gën a màgg si malaaka yi mooy Jibriil, bokk na ci liy tegtale ne Jibriil moo daan wàcce soloo ga ci yonnent yi li Yàlla wax ne: {Mooy wàcce ay Malaaka yuy ànd ak ug soloo ci ndigalam jox ko ku ko soob ci ay jaamam ne leen na ngeen xuppe ci xamle neamul jeneen yàlla ju ñu war a jaamu ju dul man,ragalleen ma} [Saaru An-Nahl: 2] Yàlla mu kawe mi nee na: {Moom(Alxuraan) wàcceeg Boroom mbindéef yi la(192) Ruu gu wóor ga(Jibriil) moo ko wàccaale(193) Ci sa biir xol bi ngir nga bokk ca xuppekat ya(194) Ci làmmeñu araab bu leer nàññ(195) Te nekkoon na ca téere yu njëkk ya(196)} [Saaru As-Suharaa: 192-196].
Ñàtteel bi:gëm téerey Yàlla yi niki Tawraat ak Injiil ak Sabuur -lu jiitu ñu koy soppi-ak Alxuraan,Yàlla mu kawe mi nee na: {Éey yéen ñi gëm gëmleen Yàlla ak ub Yonnenteem ak téere bi mu wàcce ci Yonnenteem bi ak téere yi mu njëkk a wàcce ku weddi Yàlla ak i malaakaam ak i téereem ak i yonnenteem ak bis bu mujj ba kooku sànku na cànkute gu sori} [Saaru An-Nisaa-i: 136]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Wàcce na ci yaw téere bi ci dëgg, muy aji-dëggal yi ko jiitu woon, wàcce it Tawraat ak Injiil(3) Ci lu jiitu ñuy ag njub ñeel nit ñi mu wàcce Alxuraan, ñi weddi aaya Yàlla yi de mbugal mu tar ñeel na leen te ku màgg la te fàyaakoon la(4)} [Saaru Aali Imraan: 3-4]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Yonnent bi gëm na li ñu wàcce si moom mu bawoo si Boroomam jullit yi ñépp gëm nañu Yàlla ak i malaakaam ak i téereem ak i yonnenteem du ñu teqale kenn ci yonnent yi ña ngay wax naan dégg nanu te topp nanu noo ngi sàkku sa njéggal yaw sunu Boroom te yaw rekk yaay dellluwaay ba} [Saaru Al-Baqara: 285]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Waxal ne gëm nanu Yàlla ak li ñu wàcce si nun ak li ñu wàcce si Ibraahiima ak Ismayla ak Ishaaqa ak Yanqooba ak sét ya ak la ñu joxoon Muusaa ak Iisaa ak Yonnent ya mu bawoo fa séen Boroom te du nu tàqale kenn ci ñoom te nun ay moom la nu jébbalul} [Saaru Aali Imraan: 84].
Ñenteel bi: gëm mbooleem yonnent yi -yal na jàmm nekk si ñoom- dana war ñu gëm mbooleem yonnent yi te fas ne ñoom ñépp ay ndaw yu bawoo fa Yàlla la ñu, di jottali séen i xeet bataaxelu Yàlla ak diineem ak yoonalam, Yàlla mu kawe mi nee na: {Waxaleen ne gëm nanu Yàlla ak li ñu wàcce si nun ak li ñu wàcce si Ibraahiima ak Ismayla ak Ishaaqa ak Yanqooba ak sét ya ak la ñu joxoon Muusaa ak Iisaa ak Yonnent ya mu bawoo fa séen Boroom te du nu tàqale kenn ci ñoom te nun ay moom la nu jébbalul} [Saaru Al-Baqara: 136]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Yonnent bi gëm na li ñu wàcce si moom mu bawoo si Boroomam jullit yi ñépp gëm nañu Yàlla ak i malaakaam ak i téereem ak i yonnenteem du ñu teqale kenn ci yonnent yi ña ngay wax naan dégg nanu te topp nanu noo ngi sàkku sa njéggal yaw sunu Boroom te yaw rekk yaay dellluwaay ba} [Saaru Al-Baqara: 285]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Waxal ne gëm nanu Yàlla ak li ñu wàcce si nun ak li ñu wàcce si Ibraahiima ak Ismayla ak Ishaaqa ak Yanqooba ak sét ya ak la ñu joxoon Muusaa ak Iisaa ak Yonnent ya mu bawoo fa séen Boroom te du nu tàqale kenn ci ñoom te nun ay moom la nu jébbalul} [Saaru Aali Imraan: 84].
Ak it mu gëm ki mujj ci ñoom te mooy Muhammat Yonnent Yàlla bi mujj ci yonnent yi -yal na leen Yàlla dolli xéewël ak mucc-,Yàlla mu kawe mi nee na: {Fàttelikul ba Yàlla jëlee kóllare gu dëgër ci Yonnent yi ba mu leen joxee téere ak xam-xam, ne leen: bu leen av yonnent dikkalee buy dëggal li ngeen yor na ngeen ko gëm te dimbali ko, mu ne leen(Yàlla) ndax nangu ngeen loolu te jël ci loolu sama kóllare, ñu ne ko nangu nanu, Yàlla ne leen: kon seedeleen man bokk naa ca way-seede ña} [Saaru Aali Imraan: 81].
Lislaam day waral gëm mbooleem yonnent yi ñoom ñépp nag, day waral gëm ki mujj ci ñoom te mooy Yonnent Yàlla bi Muhammat -yal ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- Yàlla mu kawe mi nee na: {Waxal ne éey yéen ñoñ-téere nekkuleen ci dara li feeg jëfewuleen Tawraat ak Injiil ak li ñu wàcce ci yéen mu jóge ca séen Boroom} [Saaru Al-Maa-ida: 68]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Waxal ne, éey yéen ñoñ-téere kaayleen ci kàddu gog ñoo ci yam, te mooy bu nu jaamu ku dul Yàlla te bu ñu ko bokkale ak dara, bu kenn jàppe kenn Yàlla wolif Yàlla, bu ñu dummóoyoo nag, neleen seedeleen ne nun ay jullit lanu} [Saaru Aali Imraan: 64].
Ku weddi benn Yonnent weddi na yonnent yépp loolu moo tax Yàlla wax nitu Nuuh ya -yal na ko Yàlla dolli mucc-: {Nitu Nuuh ya weddi nañu Yonnent ya} [Saaru As-Suharaa: 105]. Te ñépp xam nañu ne Nuuh ab yonnent jiituwu ko ànd ak loolu ba ko aw nitam weddee, weddi googu ñu ko weddi mooy weddi mboleem Yonnent yi, ndax séen ub woote benn le te séen jubluwaay it benn la.
Juróomeel bi: gëm bis bu mujj ba te mooy bisu taxawaay ba, bis bi mujj si dundug àdduna bii Yàlla dana digal malaaka ma Israafiil -yal ko Yàlla dolli jàmm- mu wal walug dee ga, lépp lu soob Yàlla daal di faatu, Yàlla mu kawe mi nee na: {Ñu wal buftu ba lépp lu nekk si asamaan ak suuf daal di faatu lu dul lu soob Yàlla ñu walaat ca beneen yoon ñoom ñépp jug di xool}. [Saaru As-Sumari: 68]. Bu lépp lu nekk si asamaan ak suuf faatoo lu dul lu soob Yàlla, Yàlla day lém asamaan yi ak suuf si, niki ni ko Yàlla mu kawe mi waxe: {Bis ba nuy lem asamaan si niki ñuy leme ab téere, na nu tàmbalee woon mbind mu njëkk ma noonu la nu koy delloo waat, ab digg la ci nun te dinanu ko def} [Saaru Al-Anbiyaa : 104]. Yàlla mu kawe mi nee na : {Joxoñu Yàlla dëgg-dëggi dayoom, suuf sépp ab ŋëbam lay doon bu bis pénc baa, asamaan sépp ab lem lay doon ci ndeyjooram, tudd naa sellam ga, Yàlla kawe na ci li ñu koy bokkaaleel} [Saaru As-Sumari : 67]. Yónente Yàlla bi - yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc - nee na : "Yàlla mu kawe mi dana lem asamaan yi ëllëg bis-pénc, mu téye leen ci loxo ndeyjooram di wax naan : man maay buur ana ñi doon ponkal-ponkal lu ? Ana ñi doon rëy-rëy lu ? Daal di lem suuf si ci càmmooñam di wax naan : Ana ñi doon ponkal-ponkal lu ? Ana ñi doon rëy-rëy lu ?" Muslim moo ko soloo.
Yàlla digal malaaka ma mu daal di walaat buftu ba ñoom ñépp jug di xoole, Yàlla mu kawe mi nee na : {Ñu ëfaat ca buftu ba beneen yoon, fa saase ñoom ñépp jug ne xooj di xoole} [Saaru As-Sumari : 68]. Bu Yàlla dekilee mbindeef yi, dana leen pang (dajale) ngir luññutu ga, (hisaab) Yàlla mu kawe mi nee na : {Bu keroogee bis ba suuf si di focc ñuy génn ci lu gaaw lool, loolu nag ag dajale la gu yomb ci nun} [Saaru Xaaf : 44]. Yàlla mu kawe mi nee na : {Bis la bob ñoom ñépp ay fés, seen dara du nëbbu Yàlla, ana kan moo moom nguur tay ? Yàlla miy Kenn tey Notaakon ba moo moom nguur} [Saaru Xaafiri : 16]. Ci bis bii Yàlla dina lijjanti nit ñépp, mu fayyul ki ñu tooñoon ci ki ko doon tooñ, daal di fay nit ku nekk la mu jëfoon, Yàlla mu kawe mi nee na : { Tay jii dees na fay nit ku nekk la mu doon fàggu, tooñ amul tay, te Yàlla ku gaawug luññutu la} [Saaru Xaafiri : 17]. Yàlla mu kawe mi nee na : {Yàlla du tooñ lu toll ni aw fepp, te ku def yiw mu ful ko, joxe ca yool bu màgg} [Saaru An-Nisaai : 40]. Yàlla mu kawe mi nee na : {ku def lu baax lu toll ni aw fepp ci yiw dana ko gis(7) Ku def lu bon lu toll ni aw fepp it dana ko gis(8)} [Saaru As-Salsalatu : 7-8]. Yàlla mu kawe mi nee na : {Dananu teg màndaxe yu màndu ca bis-pénc ba deesul tooñ benn bakkan ci dara, doonte lu toll ni peppu bàkket la dananu ko indi te doy sëkk ci man a waññi} [Saaru Al-Anbiyaa : 47}.
Ginnaaw dekki ga ak waññi ga ci la fay ga di ame, ku def yiw xéewël gu sax dàkk ñeel ko, ku def lu ñaaw ak ug kéefar mbugal ñeel ko, Yàlla mu kawe mi nee na : { Yàlla rekk la nguur ñeel boobale bis, dana àtte seen diggante, ñi gëm te jëf lu baax ñoo ngi ci biir àjjanay xéewal (56) Ñi weddi Yàlla weddi samay aaya, mbugal muy toroxalaate ñeel na leen (57)} [Saaru Al-Hajji : 56-57]. Xam nanu ne dundug àdduna gi su doon mooy yamukaay ba ; kon dund gi nekk ay caaxaan kepp. Yàlla mu kawe mi nee na : {Mo ndax dangeen a njortoon ne caaxaan rekk a taxoon nu bind leen, ba ngeen njort ne dungeen dellusi ci nun} [Saaru Al-Muuminuuna : 115].
Juróom-benneel bi : gëm àtte yi ak ndogal yi, te mooy war gi mu war nit ki gëm ne Yàlla xam na lépp lu weesu ak luy am ak lépp lu amagul ci dund gi, gëm it ne Yàlla bind na loolu lépp lu jiitu bindug asamaan si ak suuf si, Yàlla mu kawe mi nee na : {Ci moom Yàlla rekk la caabiy kumpa yi nekk, kenn du ko xam nag ku dul moom, xam na li ci jéeri ji ak li ci géej gi, wenn xob du wadd lu dul ne xam na ko, aw fepp it du nekk ci lëndëmi suuf si ludul ne gis na ko, amul luy tooy mbaa muy wow lu dul ne mi ngi ci ab téere bu leer} [Saaru Al-Anhaam : 59]. Yàlla xam na lépp, sunu Boroom bu kawe ba nee na : {Moom Yàlla mi bind juróom-ñaari asamaan yi ak suuf yu ni toll, ay mbiram day wàcci ci seen diggante, ngir ngeen xam ne Yàlla lépp la man, te Yàlla peeg na lepp ci xam-xam} [Saaru At-Talaaq : 12]. Dara it du am ci dund gi lu dul ne Yàlla la soob mu bind ko te yombal sabab ya, Yàlla mu kawe mi nee na : {Yàlla Mooy ki nga xam ne moomeelu asamaan ak suuf ñeel na ko, wutul it doom, te amul benn ndend ci nguur gi, moo bind lépp daal di koy nattal dëgg-dëggi nattal} [Saaru Al-Furxaan : 2]. Loolu nag am na ci ag xereñ gu mat sëkk gog nit ñi manuñu koo peeg, Yàlla mu kawe mi nee na : {Xereñte gu jotale, waaye xuppaate ga jariñul} [Saaru Al-Xamar : 5]. Yàlla mu kawe mi nee na : {Yàlla Mooy ki sos mbindeef yi di leen defaraat te loolu moo gën a yomb ci moom, mooy ndàmbe li gën a kawe ci asamaan yi ak suu yi, mooy Boroom kàttan gi di ku Xereñ ki}. [Saaru Ar-Ruum : 27]. Yàlla dafa melal boppam ne ku xereñ la, mu tudee boppam Aji-Xereñ ji, Yàlla mu kawe mi nee na : {Yàlla seede na ne amul kenn ku yeyoo jaamu ku dul moom, malaaka yi it seede nañu ko ak woroom xam-xam yi taxaw cig maandu, amul kenn ku yeyoo jaamu ku dul moom, mooy Boroom Kàttan gi di ku Xereñ ki} [Saaru Aali-Himraan : 18]. Yàlla mu kawe mi moo ngi xibaare ci Iisaa -yal na ko Yàlla dolli jàmm - muy wax ak Yàlla keroog bis-penc naan ko : {Boo leen mbugalee say jaam la ñu, boo leen jéggalee nag yaw yaay Boroom kàttan gi di ku Xereñ ki} [Saaru Al-Maa-ida : 118]. Yàlla it dafa wax Muusaa - yal na ko Yàlla dolli jàmm - keroog ba mu ko woowee fekk mu nekk ca wetu doju tuur wa : {Éey Muusaa man de maay Yàlla miy Boroom Kàttan gi di ku Xereñ ki} [Saaru An-Naml : 9].
Yàlla it melal na Alxuraan ci ne téere bu xereñ la, Yàlla mu kawe mi nee na : { Alif laam raa, lii ab téere la buñu xereñe ay aayaam daal di koy teqale mu bawoo ci Aji-Xereñ ji di Aji-Peeg lépp} [Saaru Huud : 1]. Yàlla mu kawe mi nee na : {Loolu bokk na ci li la sa Boroom soloo ci xereñte, bul wut muk jeneen Yàlla di ko boole ak Yàlla, kon de dees na la sànni ca Sawara ngay ku ñu yedd di ku ñu dàq} [Saaru Al-Israa : 39].
22- Yónent yi nag -yal na leen Yàlla dolli jàmm - dees leen a musal ci njuumte ci li ñuy jottali jële ko ci Yàlla, ñu musal leen it ci lépp lu wuute ak xel, walla muute ak jikko yu baax yi, Yonente yi nag lañu togg ñu wara jottali ndigali Yàlla yi ñeel jaam ñi, Yónente yi nag amuñu dara ci li Yàlla jagoo, ñoom ay nit rekk lañu niki mbooleem nit ñi, Yàlla nag da leen a soloo ay bataaxalam.
Yónent yi nag dees leen a musal ci njuumte ci li ñuy jottali jële ko ci Yàlla, ndax Yàlla day tànn ñi gën ci mbidéefam yi ngir ñu jottali bataaxelam yi, Yàlla mu kawe mi nee na : {Yàlla dina tànn ci malaaka yi ak ci nit ñi ay ndaw, Yàlla Aji-Gis la Aji-Dégg la} [Saaru Al-Hajji : 75]. Yàlla mu kawe mi nee na : {Yàlla tànn na Aadama ak Nuuh ak njabootu Ibraahiima ak njabootu Imraan ci kaw mbindeef yi} [Saaru Aali-Imraan : 33]. Yàlla mu kawe mi nee na : {Mu ne : Éey Muusaa man maa la tànn ci kaw nit ñi ci sama bataaxal bi ak ci samay kàddu, kon jëlal lii ma la indil te nga bokk ci way-sant ñi} [Saaru Al-Ahraaf : 144]. Yónente yi - yal na leen Yàlla dolli jàmm - dañuy xam ne Li ñu wàcce ci ñoom ag soloog Yàlla la (wahyu), ñuy gis malaaka yi di wàcc di wàcce ay soloo, Yàlla mu kawe mi nee na : { Yàlla mooy Aji-Xam kumpa Ji, du wuññil kumpaam gi kenn (26) Lu dul ab yónent bu mu gërëm, da koy boole ak ñu koy wattu kanam ak ginnaaw (27) Ngir mu xam ne jottali nañu seen bataaxelu Boroom, te it peeg na seen lépp, te takk na lépp cig lim(28)} [Saaru Al-Jinn : 26-28]. Yàlla digal leen ñu jottali ay bataaxalam, Yàlla mu kawe mi nee na : {Éey yaw mi Yàlla yónni jottalil li ñu wàcce ci yaw mu juge ci sa Boroom boo ko deful de kon jottaliwóo bataaxelam, Yàlla dina la aar ci nit ñi, Yàlla du gindi way-weddi yi} [Saaru Al-Maa-ida : 67]. Yàlla mu kawe mi nee na : {Ay yónent yoy dañuy bégle ak di xuppe ngir nit ñi bañ a am aw lay fa Yàlla, Yàlla Boroom kàttan la te Aji-Xereñ la} [Saaru An-Nisaai : 165].
Yónent yi - yal na leen Yàlla dolli jàmm - dañoo ragal Yàlla lool, ñu ragal ko ba duñu yokk ci li mu leen yónni dara duñu ci wàññi itam, Yàlla mu kawe mi nee na : {Bunu waxaloon lenn lu nu waxul(44) Kon dina nu ko jàpp ak ndeyjoor(45) Daal di dagg ay sidiiti xolam (dinanu ko ray)(46) Te kon kenn ci yéen du ko man a feg ci loolu (47)} [Saaru Al-Hàqatu : 44-47]. Ibn Kasiir - yal na ko Yàlla yërëm - nee na : (Yàlla mu kawe mi dafa wax ne : {وَلَوْتَقَوَّلَ عَلَيْنَا} : Bu doon Muhammat - yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc - da ñoo sosal -niki ñoom ni ñu ko doon fooge - mu yokk mbaa mu wàññi dara ci li nu ko yónni, wàlla mu wax waxi boppam daal di nu koy askanale, kon dinanu ko gaawalal ak mbugal, lii moo tax mu wax ne : {لَأَخَذْنَاهُ مِنْهُ بِاليَمِينِ} nee nañu li muy firi mooy : dinanu fayyoo ndeyjoor ci mooy; ndax ndeyjoor moo gën a tar cig jàpp : wax na ñu yit : mooy dinanu ko téye ci ndeyjooram. Yàlla mu kawe mi nee na : {Fàttalikul, ba Yàlla nee Iisaa doomi Maryama : ndax yaw yaa wax nit ñi ne : jàppeleen ma Yàlla man ak sama yaay ? Iisaa ne : tudd naa sag sell ! Yellul ci man may wax lu dul dëgg ! Su dee maa ko wax xam nga, ndax yaw xam nga li nekk ci man, te man xamuma li nek ci yaw, yaw yaay Aji-xam kumpa yi. Waxuma leen lu dul li nga ma digal, te mooy jaamuleen Yàlla miy sama Boroom di seen Boroom, ma nekoon seede ci ñoom ba ma nekkee ci seen biir, ba nga ma fa jëlee nag yaw yaa nekkoon di leen fuglu, te yaw yaay Aji-Seede ci lépp} [Saaru Al-Maa-ida : 116-117].
Bokk na ci ngëneeli Yàlla yi ci kaw yónente yi, Yàlla da leen di dëgëral ci jottali gi ñuy jottali ay bataaxelam, Yàlla mu kawe mi nee na : Man maa ngi seedeel Yàlla, yéen itam seedeleen ne man ku set wicc laa ci lépp lu ngeen di bokkaale (54) walis Yàlla, fexeelleen ma yéen ñépp te buleen xaar (55) {Man de wéeru naa ci Yàlla miy sama Boroom di seen Boroom, amul lenn luy dox ci lu dul ne moo jàpp ci ay pellam, sama Boroom de moo nga ca yoon wu jub wa} [Saaru Huud : 54-56]. Yàlla mu kawe mi nee na : {Xaw nañu laa fitnaal ba nga bàyyi li nu la xamal, ngir nga duural nu lu wuute ak moom, te kon danañu la jàppe xarit (73) Bu dulwoon li nu la dëgëral, tuuti kon nga xaw a jeng jëm ci ñoom (74) Te kon dananu la mosal mbugalum àdduna ak mbugalum àllaaxira, te doo am kenn ku lay dimbali (75)} [Saaru [Al-Israa : 73-75] Laaya yii ak yi ko jiitu day seede ne Alxuraan lu sunu Boroom wàcce la, ndax su fekkoon ne ci Yónente bi Muhammat - yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc - la juge, kon du làmboo wax yu mel nii nga xam ne moom lay waxal .
Yàlla nag day aar ay yónenteem ci nit ñi, Yàlla mu kawe mi nee na : (Éey yaw mi Yàlla yónni, jottalil li ñu wàcce ci yaw mu juge ci sa Boroom, boo ko deful de kon jottaliwóo bataaxelam bi, Yàlla dinala aar ci nit ñi, te moom Yàlla du gindi way-weddi ñi} [Saaru Al-Maa-ida : 67]. Yàlla mu kawe mi nee na : {Jàngal ci ñoom xew-xewi Nuuh ba mu waxee aw nitam ne leen : yéen samaw nit, ndeem sama nekk fii di leen fàttali kàdduy Yàlla yi dafa rëy ci yéen, man maa ngi wéeru ci Yàlla, bungeen yaboo ngeen boole seen i mbir yéen ak ñi ngeen di jaamu, te bu seen i pexe nekk aw tiis ci yeen, su ko defee ngeen faagaagal ma te buleen xaar dara} [Saaru Yuunus : 71]. Yàlla mu kawe moo ngi nettali waxu Muusaa -yal na ko Yàlla dolli jàmm - mu ne : { Ñoom ñaar nee nañu : Yaw Sunu Boroom nun dey danuy ragal mu ëppal mbaa muy bew ci sunu kaw. Yàlla ne leen : Buleen ragal man maa ngi ànd ak yéen, di dégg di gis} [Saaru Taaha : 45-46]. Yàlla daaldi leeral ne moom kuy sàmm ay yónenteem la ci seen i noon ba duñu leen teg benn ñaawtéef, Yàlla daaldi xibaare ne mooy sàmm ag soloom (wahyu) ba nga xam ne deesu ca dolli mbaa ñu cay wàññi, Yàlla mu kawe mi nee na : {Nun Noo wàcce Alxuraan te Noo koy wàttu} [Saaru Al-Hijri : 8].
Yónent yi - yal na leen Yàlla dolli jàmm - dees leen a musal ci lépp lu wuute ak xel mbaa jikko; Yàlla a ngi wax di sellal Yónenteem bi Muhammat : {Yaw yaa ngi ci kaw jikko yu màgg yi} [Saaru Al-Xalam : 4]. Waxaat na ci moom lii : {Seen waajii de dub dof} [Saaru At-Takkwiir : 22]; Loolu nag ngir ñu taxaw ci jottali bataaxelam bi gën gaa matug taxawaay. Yónent yi nag lañu togg ci jottali ndigali Yàlla ñeel jaamam ñi, amuñu dara ci li Boroom bi jagoo mba benn cér cig jaamu, ñoom kay ay nit rekk la ñu, Yàlla nag da leen di soloo ay bataaxelam, Yàlla mu kawe mi nee na : {Seen Yónent ya neena ñu leen : nun dunu lu dul ay nit ni yéen, waaye Yàlla mooy xéewalal ku ko soob ci jaamam yi, dunuleen man a indil aw lay lu dul ci ndigalul Yàlla, way-gëm ñi na ñuy wéeru ci Yàlla} [Saaru Ibraahiima : 11]. Yàllaa ngi digal Yónenteem ba Muhammat - yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc - mu wax ay nitam : {Waxal ne : man nit laa ni yéen, waaye dañu may soloo, xam leen ne ki ngeen di jaamu kenn la, kon nag képp ku yaakaar a daje ak Boroomam, nay jëf jëf yu yiw, te bu mu bokkaale Yàlla ak kenn} [Saaru Al-Kahf : 110].
Lislaam day woote ci jaamu Yàlla rekk, ci cosaani jaamu yu mag yi, te mooy : julli mi nga xam ne taxaw la, ak rukkoo, ak sujóot ak tudd Yàlla, ak di ko tagg ak di ko ñaan, nit ki da koy julli ci bis bi juróomi yoon, ci julli la wuute yi di deñe ba sett, ki am ak ki ñàkk, ki jiite ak ka ñu jiite ci benn sàppe la ñuy taxaw ci julli gi. Ak joxe asaka, te mooy : ab lim bu tuuti ci alal - mu dëppoo ak sàrt ya ak tolluwaay bi ko Yàlla tollale - lu war la ci alali ñi woomle, dañu koy jox ñi ñàkk, benn yoon ci at mi. Niki noonu woor te mooy : bàyyi lépp luy dogloo ci bëccëgu weeru koor, day yar bakkan ci muñ. Niki noonu Aji Màkka te mooy : jublu néegu Yàlla ba ca Màkka ben yoon ci dund gi, ci képp ku ko man, ci aj nag ñéppay yam ci jublu Boroom bi bind mbindéef yi -tudd naa sellam ga -. Bu ko defee seen wuute yi ak seen askan yi lépp daal di deñ.
Lislaam day woote ci jaamu Yàlla moo xam jaamu yu mag yi la wala yeneen yidul yooyu, jaamu Yàlla yu màgg yii nag Yàlla da koo waral ci yónent yépp - yal na leen Yàlla dolli jàmm - li gën a màgg ci xeetu jaamu yi mooy :
Bi ci njëkk : julli, Yàlla da koo farataal ci jullit ñi niki mu ko farataale ci mbooleem yónent yi - yal na leen Yàlla dolli jàmm -, Yàlla digal xaritam ba Ibraahiima - yal na ko Yàlla dolli jàmm - mu sellal néegam ba ngir ñi koy wër ak ña fay julli ak a rukoo ak a sujóot, Yàlla mu kawe mi nee na : {Fàttalikuleen ba nu defee néeg bi muy delluwaayub nit ñi nekk kóolute itam, na ngeen def (Màqaama Ibraahiima) barabu jullikaay, kóllarante nanu ak Ibraahiima ak Ismaahiila ne na ñu sellal sama néeg bi ngir ñi koy wër ak ña fay toog di jaamu Yàlla di rukoo ak a sujjóot} [Saaru Al-Baqara : 125]. Yàlla waral na loolu itam ci Muusaa - yal na ko Yàlla dolli jàmm - ca ba mu ko njëkkee woo, Yàlla mu kawe mi nee na : {Man maay sa Boroom summil say dàll, yaa ngi ci xur wu sell "Tuwaa"(12) Dama laa tànn, kon déglul li nu lay soloo(13) Man maay Yàlla amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul man, kon jaamu ma te ngay taxawal julli di ma fàttaliku(14)} [Saaru Taaha : 12-14]. Al-Masiih Iisaa -yal na ko Yàlla dolli jàmm - moom itam xibaare na ci ne Yàlla da koo digal julli ak joxe asaka, mu wax , niki ni ko Yàlla xibaare : {Mu def ma may ku baarkeel fu ma man a nekk, mu dénk ma may julli ak di joxe asaka fii ak maa ngi dundu} [Saaru Maryama : 31]. Julli nag ci lislaam taxaw la ak rukkoo ak sujóot ak tudd Yàlla ak di ko tagg di ko ñaan, nit ki da koy julli bis bu nekk juróomi yoon, Yàlla mu kawe mi nee na : {Na ngeen sàmmoonte ak julli rawatina julli gu digg-dóomu ga, te ngeen taxaw temm di way-jaamu Yàlla} [Saaru Al-Baqara : 238]. Yàlla mu kawe mi nee na : {Nanga taxwal julli bu jànt bi fenkee ba ba guddi gi di ñuul, ak it jullit fajar, jullig fajar dey lu ñuy seede la} [Saaru Al-Israa : 78]. Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc - nee na : (Bu dee ci rukkoo bi na ngeen ci màggal Yàlla, bu dee ci sujóot bi na ngeen góor-góor lu ci ñaan, kon dana yell ñu nangul leen) Sahiihu Muslim.
Ñaareel bi : Joxe asaka, Yàlla farataal na ko ci jullit ñi niki mu ko farataale ci yónent ya jiitu woon - yal na leen Yàlla dolli jàmm - moom nag lu tuuti la ci alal -bu sàrt ya dajee ak tolluwaay ba ko Yàlla jox - lu war la ci alali ñi woomal, way-ñàkk yi la ñu koy jox ak ñeneen ñu dul ñoom, benn yoon ci at mi, Yàlla mu kawe mi nee na : {Jëlal ci seen alal saraxu asaka, ngir laabal leen ca, sellal leen ca, te nga leen di ñaanal, ndax sa ñaan luy dalal seen xel la, Yàlla Aji-Dégg la Aji-Xam la} [Saaru At-Tawba : 103]. Yónent bi - yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc - ba mu yónnee Muhaas - yal na ko Yàlla dollee gërëm - ca Yaman, da ne ko : "Yaa ngi dem ci ñoo xam ne Yàlla wàcce woon na ci ñoom téere, na nga leen woo ci seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, ak seede ne man Yónenteb Yàlla laa, bu ñu la toppee ci loolu, nga xamalleen ne, Yàlla mu màgg mi farataal na ci ñoom juróomi julli ci bis bu nekk, bu ñu la toppee ci loolu, nga xamalleen ne Yàlla mu màgg mi farataal na ci ñoom asaka ci seen i alal, dees koy jële ci way-woomal yi jox ko way-ñàkk ñi, bu ñu la toppee ci loolu nag na nga moytu seen tedd-ngay alal ya, te nga moytu ñaanug ku ñu tooñ, ndax amul kiiraay diggam ak Yàlla" Tirmisii moo ko nettali 625.
Ñatteel bi : Woor, Yàlla farataal na koor ci jullit ñi niki mu ko farataale ci yónent ya jiitu woon - yal na leen Yàlla dolli jàmm, - Yàlla mu kawe mi nee na : {Yéen way-gëm ñi farataal nañu ci yéen woor, niki ñu ko farataale woon ca ña leen jiitu woon, ngir ngeen ragal Yàlla} [Saaru Al-Baqara : 183]. Te mooy : bàyyi lépp luy dogloo ci bëccëgu weeru koor, woor nag day yar bakkan ci jubluwaay ak muñ Yónente bi - yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc - nee na : "Yàlla mu màgg mi dafa wax ne : Woor maa ko moom te maa koy fayal sama bopp, ndax aji-woor ji day bàyyi bànneexam ak lekkam ak naanam ngir man, te woor ab pakk la, woorkat bi am na ñaari mbégte : mbégte bu dogee, ak mbégte bu dajee ak Boroomam" Sahiihul Buxaarii 7492.
Ñenteel bi : Aj Màkka, Yàlla farataal na ko ci jullit ñi niki mu ko farataale ci yónent ya jiitu woon - yal na leen Yàlla dolli jàmm -, Yàlla digal na Ibraahiima xaritam ba - yal na ko Yàlla dolli jàmm - mu woote aj, Yàlla mu kawe mi nee na : {Wooteel ci nit ñi ngir aji Màkka, danañu la dikkal di dox ak di war xeetu waruwaay wu ne, dina ñu ñëw juge ci bépp barab bu sori} [Saaru Al-Hajji : 27]. Yàlla digal ko mu laabal néeg bu yàgg ba ñeel ajkat yi, Yàlla mu kawe mi nee na : {fàttalikul ba nu béralee Ibraahiima bérabu néeg ba, ne ko : bul ma bokkaale ak dara, te nga laabal sama néeg bi ngir ñi koy wër ak ña fay taxaw di rukkoo aka sujóot} [Saaru Al-Hajji : 26].
Aj nag mooy : jublu néegu Yàlla ba ca Màkka ngir ay jëf yu ñu xam, benn yoon ci dund gi ci kaw képp ku ko man, Yàlla mu kawe mi nee na : {War na ci nit ñi aj néeg ba ngir Yàlla benn yoon ci ku ko man, ku weddi nag, Yàlla moom Aji-Doylu la waliis mbindéef yi} [Saaru Aali-Imraan : 97] Ci aj jullit ñi aji da ñuy daje ci benn bérab di sellal jaamu gi ngir Aji-Bind ji - tudd naa sellam ga - ñiy aj ñépp da ñuy def jaamuy aj gi ci wenn melo, muy dindi wuute ya ci ay barab yuñu dëkk, ak seen i wuute ci ay mbatiit ( culture), ak seen i wuute tolluwaayu dundiin gi.
24- Bokk na ci liy gën a ràññee xeeti jaamu yi ci lislaam, mooy ne : ay melokaanam ak i waxtoom, ak i melokaanam, ak i sartam Yàlla moo ko yoonal, Yónenteem bi - yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc - daal di koy jottali, te mbindéef defu ci dara moo xam yokk ci mbaa wàññi ci, ba sunu jonni tay, te jaamu Yàlla yu màgg yii yépp mbooleem Yónente yi woote nañu ca -yal na leen Yàlla dolli jàmm -.
Bokk na ci liy gën a ràññee xeeti jaamu Yàlla yi ci lislaam, mooy ne : ay melokaanam ak i waxtoom, ak i sartam Yàlla moo ko yoonal, Yónenteem bi - yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc - daal di koy jottali, te mbindéef dugalu ci dara moo xam yokk ci mbaa wàññi ci, ba sunu jamonoy tay jii, Yàlla mu kawe mi nee na : {Bis niki tay matalal naa leen seen diine, xëpp naa leen samay xéewal, gërëm naa ci yéen lislaam muy seen diine} [Saaru Al-Maa-ida : 3]. Yàlla mu kawe mi nee na : {Jafandikul bu baax ci li ñu la soloo, yaa ngi ci kaw yoon wu jub} [Saaru As-Suxrufi : 43]. Yàlla mu kawe mi wax na ci julli ne : {Bu ngeen nopee ca julli ga, na ngeen di tudd Yàlla ca taxawaay ya, ak ca toogaay ya, ak su ngeen tëddee, bu ngeen nekkee ci kóolute nangeen taxawal julli, julli kat doon na lu ñu sàkkal waxtu ca jullit ña} [Saaru An-Nisaa-i : 103]. Yàlla mu kawe mi wax ci ñi ñuy jox asaka, mu ne : {Ñi yeyoo asaka daal ñooy ñii : ñi néew am-am, ak way-ñakk ñi, ak ñiy toppatoo asaka ji, ak ñi ñu bëgg a nooyal seen xol yi ci lislaam, ak ci goreel jaam, ak ña ay bor sonal, ak lu jëm ci yoonu Yàlla, ak doxandeem bu nekk ci tukki, loolu nag lu Yàlla farataal la, te Yàlla Aji-Xam la Aji-Xereñ la} [Saaru At-Tawba : 60]. Yàlla mu kawe mi wax ci woor ne : {Weeru koor lañu wàcce Alxuraan, mu di ag njub ñeel nit ñi, ak di leeral njub tey teqale diggante dëgg ak neen, képp ku teewe ci yéen weer wi na ko woor, ku wopp (feebar) wala mu nekk ci tukki na fay ci yeneen i bis. Yàlla daa bëgg ci yéen lu yomb te bëggaluleen lu jafe, ngir it ngeen matal lim ba, ak ngir ngeen màggal Yàlla ci li mu leen gindi, ndaxtelee ngeen sant Ko} [Saaru Al-Baqara : 185]. Yàlla mu kawe mi wax ci aj ne : {Aj ay weer yu ñu xam la, ku dugg ci aj bumu beej (sëy), bumu def lu ñaaw te bumu dàggasante ci biir aj gi, lu ngeen def ci lu baax Yàlla xam na ko, nangeen yóbbalu, yóbbal ba gën nag mooy ragal Yàlla, nangeen ma ragal yéen woroom xel yi} [Saaru Al-Baqara : 198]. Te jaamu yu màgg yii yépp nag mbooleem yónent yi - yal na leen Yàlla dolli jàmm - woote nañu ci.
25- Yónenteb Lislaam mooy Muhammat doomu Abdallaa di sétub Ismaahiila doomu Ibraahiima - yal na leen Yàlla dolli jàmm - moo ngi juddoo Màkka ci 571 atum tubaab, ñu yónnee ko fa, mu gàddaay jëm Madiina, te musul a bokk ak aw nitam ci mbiri ceddo, waaye daa na bokk ak ñoom ci jëf yu màgg yi, jikko yu màgg la amoon laata ñu koy yónni, aw nitam daa nañu ko woowe ku Wóor ki, bi mu amee ñent-fukki at la ko Yàlla yónni, daal di koy dëgërale ay keemaan yu màgg, ba ca gën a màgg mooy Alxuraan ju tedd ji, moo gën a màgg ci keemaani yónente yépp, te mooy keemaan biy des ci keemaani yónent yi ba tay jii, ba Yàlla matalee diine ji Yónent bi jottali ko jottali gu mat sëkk, ca la Yónent bi faatu fekk moo ngi am juróom-benni fukki at ak ñatt, ñu Rob ko ca Madiina Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc -. Yónent bi Muhammat mooy ki mujj ci yónent yi, ak ña ñu soloo, Yàlla da koo yónni cig njub ak diiney dëgg ngir mu génndi nit ñi ci lëndëmi ceddo ak ug kéefar, ak ug réer, jëme leen ci leerug wéetal Yàlla ak ngëm. Yàlla seedeel na ko ne moom moo ko yónni ngir muy woote jëme ci moom ci ndigalam.
Yónenteb Lislaam mooy Muhammat doomu Abdallaa di sëtub Ismaahiila doomu Ibraahiima - yal na leen Yàlla dolli jàmm - moo ngi juddoo Màkka ci 571 atum tubaab, ñu yónnee ko fa, mu gàddaay jëm Madiina, aw nitam daa nañu ko woowe ku wóor ki, te musul a bokk ak aw nitam ci mbiri ceddo, waaye da daa bokk ak ñoom ci jëf yu màgg yi, jikko yu màgg la amoon laata ñu koy yónni, Boroomam melal na ko ci ay jikko yu màgg, Yàlla mu kawe mi wax na ci moom ne ko : {Yaa ngi ci kaw jikko yu màgg yi} [Saaru Al-Xalam : 4]. Yàlla yónni na ko bi mu amee ñent-fukki at, Yàlla dëgëral ko ci ay keemaan yu màgg, bi ci gën a màgg mooy Alxuraan ju tedd ji. Yonent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- nee na : "Amul ci yónente yi benn yónent lu dul ne Yàlla jox na ko luy tax nit ñi gëm ko, man nag li ñu ma jox ag soloo la gog Yàlla moo ma ko soloo, ba maa ngi yaakaar a nekk ki ëpp ñi koy topp ëllëg bis-pénc" Sahiihul Buxaarii. Alxuraan ju màgg ji moom soloog Yàlla la jëm ci Yonenteem - yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc -, Yàlla mu kawe mi nee na: {Téere boobu amul benn sikki-sàkka ci ne ag njub la ñeel way-ragal Yàlla ñi} [Saaru Al-Baqara : 2]. Yàlla mu kawe mi nee na : [Mo ndax xanaa dañu dul settantal Alxuraan, bu juge woon ci kenn ku dul Yàlla danañu ca fekk ay wuute yu bari} [Saari An-Nisaa-i : 82]. Te Yàlla dafa dëkk jinne ak nit ci ñu indi lu mel ni alxuraan, Yàlla mu kawe mi nee na : {Waxal ne leen, bu jinne yi ak nit ñi dajaloo woon ngir indi lu mel ni Alxuraan, duñu man a indi lu mel ni moom doonte sax ñenn ñi da ñuy dimbali ñeneen ñi} [Saaru Al-Israa : 88]. Yàlla dëkk leen ci ñu indi fukki saar yu mel ni moom, Yàlla mu kawe mi wax ne : {Mo ndax da ñuy wax ne da koo fent, waxaleen ñu indi fukki saar yu mel ni moom yu ñu fent, te ngeen woo ku ngeen man a woo te du Yàlla ndeem wax ngeen dëgg} [Saaru Huud : 13]. Yàlla dëkk na leen sax ngir ñu indi wenn saar wu mel ni moom, Yàlla mu kawe mi wax ne : (Bu ngeen dee sikki-sàkka ci li nu wàcce ci sunu jaam bi, kon indileen wenn saar wu mel ni moom (Alxuraan), te ngeen woo seen i seede walis Yàlla ndeem wax ngeen dëgg} [Saaru Al-Baqara : 23].
Alxuraan ju màgg ji mooy genn kemmaan gu fiy des ba tay ci keemani Yónent yi, ba Yàlla matalee diine ji Yónente bi - yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc - jottali ko ca na mu gën a jote, ca la Yónente bi faatu fekk moo ngi am juróom-benni fukki at ak ñatt ñu Rob ko Madiina.
Yónente bi Muhammat - yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc - mooy ki mujj ci yónent yi ak ña ñu soloo, Yàlla mu kawe mi nee na : {Muhammat nekkul baayu kenn ci séen góor ñi waaye yonenteb Yàlla la, di ki mujj ci ña ñu soloo, Yàlla Aji-Xam lépp la} [Saaru Al-Ahsaab : 40]. Jële nañu ci Abuu Hurayrata - yal na ko Yàlla dollee gërëm - mu jële ci Yónente bi - yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc - mu wax ne : "Maag Yonent yi ma jiitu woon, Noo ngi mel ni waay ju tabax ag kër taaral ko rafetal ko ba mu des bérabu benn móol ci benn koñ, nit ñi tàmbalee wër kër gi di ko yéem, di wax naan : lu tere woon ñu teg móol bii ? Yónente bi wax ne : Man maay móol boobu, te maay ki mujj ci ñi ñu soloo" Sahiihul Buxaarii. Al-Masiih Iisaa -yal na ko Yàlla dolli jàmm - wax na ci Injiil di bégle ci ñëwug Yónente bi Muhammat - yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc - : (Xeer wi nga xam ne tabaxkat yi dañu koo bañ a tabax mujj na nekk bopp koñ ba, mo ndax musu leen a jàng ci téere yi : Yasuuha waxoon na leen ko bu yàgg, jële ko ci Boroom bi, loolu nag yéemu woon na lool ci su niy gët). Ci Sifru Takkwiin bii fi nekk tay, waxu Yàlla ji mu wax Muusaa ma nga ca, mu ne ko : ( Dinaa leen defalal ab Yónent bu bawoo ci digg i mbokkam mel ni yaw, ma def samay wax ci gimiñam, mu leen di wax lépp lu ma ko dénk).
Yónente Yàlla bi Muhammad - yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc - Yàlla dakoo yónni cig njub ak diiney dëgg, sunu Boroom seedeel na ko ne moo ngi ci dëgg, ak ne moo ko yónni ngir muy woote jëme ci moom ci ndigalam, Yàlla mu kawe mi nee na : {Waaye Yàllaa ngi seede ne li mu wàcce ci yaw ci xam-xamam bi la ko wàccee, Malaaka yi seede nañu loolu, te Yàlla doy na seede} [Saaru An-Nisaa-i : 166]. Yàlla mu kawe mi nee na : {Moom Moo yónni Yónenteem ci njub ak diiney dëgg ngir mu notal ko ci mbooleem diine yi, te Yàlla doy na seede} [Saaru Al-Fathu : 28]. Yàlla da koo yónni cig njub ngir mu génne nit ñi ci lëndëmi ceddo ak ug kéefar ak ug réer jëme leen ci leerug wéetal Yàlla ak ngëm. Yàlla mu kawe mi nee na : {Ci la Yàlla di gindee ku topp ngërëmam jëme ko ci yoonu jàmm, di leen génne cig lëndëm jëme leen cig leer ci ndigalam, di leen gindi jëme leen ci yoon wu jub} [Saaru Al-Maa-ida : 16]. Yàlla mu kawe mi nee na : [Alif laam raa, lii ab téere la bu nu wàcce ci yaw ngir nga génne nit ñi ci lëndëm jëme leen ci leer ci seen ndigalu Boroom jëme leen ci yoonu Boroom Kàttan ji di Aji-Cant ki} [Saaru Ibraahiima : 1].
26- Sariihab lislaam bi Yónente Muhammat - yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc - indi moo mujj ci bataaxelu Yàlla yi, ak ay Sariihaam, te mooy Sariiha ju mat ji, te liy yéwénal diiney nit ki ak àddunaam lépp a ngi ci, te li muy njëkk a wattu di ko sàmm mooy : diiney nit ñi ak seen i deret ak seen i alal ak seen xel ak seen ug njaboot, te dafa folli mbooleem Sariiha yi jiitu woon, niki ni Sariiha yi jiitu woon daan follantee.
Sariihab lislaam bi Yonente Yàlla Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- indi moo mujj ci bataaxelu Yàlla yi, ak ay Sariihaam, te mooy Sariiha ju mat ji, te ci bataaxal bii ci la matale diine, ay xéewal dottiku ci nit ñi ci yónni gimu yónni Muhammad, Yàlla mu kawe mi nee na : {Bis niki tay matalalnaa leen seen diine xëpp naa leen samay xéewal gërëm naa ci yeen lislaam muy seen diine} [Saaru Al-Maa-ida : 3].
Te Sariihab lislaam mooy Sariiha bu mat bi, te yéwénug diiney nit ki ak àddunaam moo ngi ci; ndax dafa boole mbooleem lu nekk ci Sariiha yi jiitu woon, mu mottali ko matal ko, Yàlla mu kawe mi nee na : {Alxuraan jii de day gindee jëme ca yoon wa gën a jub, di bégal way-gëm ñiy jëf yiw, ci ne ay fay yu mag ñeel na leen} [Saaru Al-Israa : 9]. Sariihab lislaam teggil na nit ñi diis-diis yi nekkoon ci xeet yi jiitu woon, Yàlla mu kawe mi nee na : {Ñay topp Yónente ba muy ku ñu soloo te jàngul, te ñu fekk ko muy ku ñu bind ca la ñu yore ci Tawraat ak Injiil, mu leen di digal lu baax di leen tere lu bon, di leen daganalal yu teey yi, di araamal ci ñoom yu sellul yi, dindil leen yu diis ya ak jéng ya nekkoon ca ñoom, kon ñi ko gëm te weg ko, di ko dimbali, di toop leer ga ñu wàcce ci moom, ñoom ñooy way-texe ña} [Saaru Al-Ahraaf : 157].
Sariihab lislaam daa folli mbooleem Sariiha yi jiitu woon, Yàlla mu kawe mi nee na : {wàcce Nanu ci yaw téere bi ci dëgg muy aji-dëggal téere yi ko jiitu te di leen sàmm, nanga àtte séen diggante ci li Yàlla wàcce, te bul topp séen i bànneex bàyyi li la dikkal ci dëgg, ku ci nekk ci yéen defal Nanu ko aw yoon ak uw doxaliin, te bu sooboonn Yàlla Mu def leen wenn xeet. Waaye, da leen di nattu ci li mu leen jox, njëkkanteleen yiw yi, yéen ñépp ca Yàlla ngeen di dellu, Mu xamal leen li ngeen nekkoon doon ca wuute} [Saaru Al-Maa-ida: 48]. Alxuraan ju tedd jii làmboo Sariiha bi, dafa ñëw ngir dëggal téerey Yàlla yi ko jiitu woon, di ko atte ak di ko folli.
27- Yàlla mu kawe mi -tudd naa sellam ga- du nangu jenn diine ju dul lislaam gi Yonnent bi Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- indi, kon képp ku gëm diine ju dul diiney lislaam deesu ka ko nangul.
Yàlla mu kawe mi -tudd naa sellam ga- ginnaaw bi Mu yónnee Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- du nangu diine ju dul lislaam ji Yonnent bi Muhammat -yal ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- indi, kon képp ku jàppe diine lu dul diiney lislaam deesu ka ko nangul. Yàlla mu kawe mi nee na: {Ku sàkku jeneen diine ju dul lislaam deesu ka ko nangul, te Allaaxira day bokk ca way-njàkk ña} [Saaru Aali Imraan: 85]. Yàlla mu kawe mi nee na: Diine fa Yàlla mooy Lislaam, ñi ñu jox téere wuutewuñu lu dul ginnaaw ba léen xam-xam dikkalee ngir ag mbewte gu nekk séen diggante, képp ku weddi aayay Yàlla yi, Yàlla moom ku gaaw la ci xayma jëf yi} [Saaru Aali Imraan: 19]. Lislaam jii nag mooy diiney Ibraahiima -yal na ko Yàlla dolli jàmm-, Yàlla mu kawe mi nee na: (Ana kan mooy bañ diiney Ibraahiima ku dul ku kànnasu? Nun Noo ko tànn ci àdduna, te moom bu àllaaxiraa it dana bokk ca way-sell ña} [Saaru Al-Baqara: 130]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Ana kan moo gën a rafet diine ki jébbal jëmmam ji Yàlla, te di kuy rafetal, tey topp diiney Ibraahiima cig wéetal Yàlla? Te Yàlla déy jàppe na Ibraahiima muy xaritam} [Saaru An-Nisaa-i: 125]. Yàlla digal Yonnent bi Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- mu wax ne: {Waxal ne: man de sama Boroom da maa gindi teg ma ci yoon wu jub, muy diine ju jub kocc, te mooy diiney Ibraahiima joj wéetal Yàlla, te musul a bokk ca bokkaalekat ña} [Saaru Al-Anhaam: 161].
28- Alxuraan ju tedd ji mooy téere bi Yàlla soloo Yonnent bi Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc-, te mooy waxu Yàlla miy Boroom mbindéef yi, Yàlla dëkku nit ñi ak jinne yi ci ñu indi lu mel ni moom, walla aw saar wu mel ni moom, te dëkku gi ba tay moo ngi taxaw, Alxuraan ju tedd ji nag day tontu ay laaj yu bari te am solo, tey gëlëmloo ay milyoŋi nit, te Alxuraan ju màgg ji lu ñu wattu la ba tay ca làkku araab ba ñu ko wàccee woon benn araf wàññeekuwu ci, te lu ñu móol la, lu ñu tasaare la itam, te téere bu màgg la bu lottloo ñépp, di lees war a jàng, mbaa jàng ay pireem, niki it Sunnas Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- ak i jàngaleem ak jaar-jaaram nekke lu ñu sàmm, di lu ñu tuxal ci ay càllaley nettalikat yu ñu wóolu, ak ne lu ñu móol la ci làkku araab wi Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- daan waxe, te firi na ñu ko ci ay làkk yu bari, te Alxuraan ju tedd ji ak Sunnas Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- ñooy balluwaayu àttey Lislaam ak i yoonalam, Lislaam deesu ko jële ci jëfu yenn nit ñi ci askanoo, waaye, dees koy jële ci soloog Yàlla gi, muy: Alxuraan ju tedd ji ak Sunnas Yonnent bi.
Alxuraan ju tedd ji mooy téere bi nga xam ne Yàlla da koo soloo Yonnenteem Muhammat ma di b araab ci làkku araab te mooy waxu Yàlla miy Boroom mbindéef yi, Yàlla mu kawe mi nee na: {Moom déy wàcceg Boroom mbindéef yi Yàlla (192) Ruuh gu wóor ga(Jibriil) moo ko wàcce(193) Ci sa xol bi ngir nga bokk ca xuppaatekat ya(194) Ci làkku araab bi leer nàññ(195)} [Saaru As-Suharaa: 192-195]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Yaw déy Muhammat yaa ngi jël Alxuraan mu bawoo ci ku Xereñ di Aji-Xam} [Saaru An-Naml: 6]. Te Alxuraan jii ag wàccee la gu juge ca Yàlla, ag dëggal la it ñeel téerey Yàlla yi ko jiitu woon, Yàlla mu kawe mi nee na: {Alxuraan jii déy nekkul lu ñu duur lu bawoowul ca Yàlla, waaye luy dëggal li ko jiitu la, te faramfàcceg téere bi amul sikk-sakka ne ci Boroom mbindéef la juge} [Saaru Yuunus: 37]. Alxuraan ju tedd ji day leeral lu ay masala yu bari yu Yahuud yi ak Nasaraan yi wuute ci seen diine, Yàlla mu kawe mi nee na: {Alxuraan jii déy day nettali giir Banii-Israayiila li ëpp ca la ñu daan juuyoo} [Saaru An-Naml: 76]. Alxuraan ju tedd ji daa làmboo ay tegtal ak i lay yoy doy na sëkk lay ci kaw nit ñépp ci ñu xam dëgg yi aju ci Yàlla mu kawe mi -tudd naa sellam ga- ak diineem ji ak payam gi, Yàlla mu kawe mi nee na: {Saddal Nanu nit ñi ay léebu ci Alxuraan jii, ndax amaana ñu fàttaliku} [Saaru As-Sumari: 27]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Wàcce Nanu ci yaw Alxuraan muy leeral lépp, di ag njub ak yërmaande ak mbegte ñeel jullit ñi} [Saaru An-Nahl: 89].
Te Alxuraan ju tedd ji day tontu ay laaj yu bari te am solo yoy day ëlëm ay milyoŋi nit, Alxuraan ju tedd ji it day leeral naka la Yàlla binde Asamaan yi ak Suuf si, Yàlla mu kawe mi wax na ne: {Mo ndax ñi weddi dañoo gisul ne Asamaan yi ak suuf si dafa taqaloowoon Nu tàqale leen? Nu sose ci ndox lépp luy dund, mo ndax dañu dul gëm?} [Saaru Al-Anbiyaa: 30]. Naka la Yàlla binde nit, Yàlla mu kawe mi nee na: { yéen nit ñi ndeem da ngen di sikk-sakka ci mbirum dekki, xamleen ne Nun Noo leen bind ci suuf, ginnaaw ga Nu bind leen ci toqug manniyu,ginnaaw ga mu doon lumbu deret,ginnaaw ga suuxu yàpp wu ñu bind bind gu mat, ak wu ñu matalul ag mbindam, ngir Nu leeralal leen,te Nun Nooy def ca meen ma lu Nu soob ba ca àpp bu ñu xam, ginnaaw ga Nu génne leen ngeen di ay liir, ginnaaw ga ngeen màgg ba doon ay waxambaane, am na ci yéen ñuy teel a dee,am ci yéen ñuy dund ba màggat ba naag, ba dootul xamati dara,ginnaaw ba mu nekkewoon ku xam, nga gis suuf si mu wow koŋŋ, te bu Nu ci wàccee ndox mu yëngu daal di funki daal di saxal gépp xeetu gàncax gu rafet} [Saaru Al-Hajji: 5]. Ak fan lay mujje ak luy fayu kuy rafetal ak kuy ñaawal ginnaaw dund gii? Tuddoon na ñu tegtali masala yii, ci xëtu limatu (20). Ak ndax nekk gi fii dafa tombe rekk daal di am, walla dafa am ngir jubluwaay bu màgg? Yàlla mu kawe mi nee na: {moo ndax dañoo xoolul ci nguuru asamaan yi ak suuf si, ak li Yàlla bind lépp, te it xay-na séen àpp jege na, kon jan wax lañuy gëm ginnaawam} [saaru Al-Ahraaf: 185]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Ndax dangeen a njortu ne Danu leen a bind ngir am po, te dungeen dellu si fi Nun} [Saaru Al-Muuminuuna: 115].
Alxuraan ju màgg ji lu ñu wattu la ba tay jii ca làkku araab ba ñu ko wàccee woon, Yàlla mu kawe mi nee na: {Nun Yàlla Noo wàcce Alxuraan te Noo koy Sàmm} [Saaru Al-Hijri: 9]. Ab araf wàññeekuwu ci te jommu na ag wuute nekk ca walla wàññeeku mbaa coppite, Yàlla mu kawe mi nee na: [Mo ndax xanaa dañu dul settantal Alxuraan, bu juge ci kenn ku dul Yàlla danañu ca fekk ay wuute yu bari} [Saari An-Nisaa-i: 82]. Te lu ñu móol la lu ñu tasaare la itam, te téere bu màgg la bu lottal ñépp, di lees war a jàng mbaa di ko déglu, walla di jàng ay pireem, niki noonu it Sunnay Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- ak um njàngaleem ak jaar-jaaram lu ñu wattu la tuxale ko ci ay nettalikat yu ñu wóolu, lu ñu móol la ci làkku araab bi Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- daan waxe, lu ñu firi la it ci ay làkk yu bari, te Alxuraan ju tedd ji ak Sunnas Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- ñooy balluwaayu àttey Lislaam yi, ak i yoonalam, Lislaam deesu ko jële ci jëfi ñi koy askanoo; waaye dees koy jële ci soloog Yàlla gi ñu sàmm, te mooy: Alxuraan ju màgg ji ak Sunna Yonnent bi, Yàlla mu kawe mi nee na: {ñay weddi Alxuraan ba mu leen dikkalee, te moom déy téere bu tedd la, neen du ko dikke fenn, du ci kanam du ci ginnaaw, ag wàcce la gu bawoo fa Yàlla Aji-Xereñ ji Aji-Sant ji} [saaru Fussilat: 41-42]. Yàllaa ngi wax ci mbiri sunnay Yonnent bi ci ne moom ag soloo la gu bawoo fa Yàlla: {lu leen Yonnent bi indil jëlleen ko, lu mu leen tere bàyyileen ko, nangeen ragal Yàlla, Yàlla déy ku tar mbugël la} [saaru Al-Hasr: 7].
Lislaam day digle rafetal jëme ci ñaari way-jur donte nekku ñu ay jullit, dénkaane na it doom yi:
Lislaam day digle rafetal jëme ci ñaari way-jur, Yàlla mu kawe mi nee na: {sa Boroom digle na ne bu leen jaamu ku dul moom te nangeen di rafetal jëme ci ñaari way-jur yi, te ndeem kenn si ñoom walla ñaar ñépp egg nañu ci màggat ci sa teewaay; buleen wax uf te bu leen gëdd, nangeen leen wax wax ju yiw} [saaru Al-Israa: 23]. Yàlla mu kawe mi nee na: {dénk Nanu nit ay way-juram, yaayam ëmb na ko coono si biir coono, ba feral ko ci diirub ñaari at, nanga may sant man Yàlla ak say ñaari way-jur, ci Man la lépp di mujj} [saaru Luqmaan: 14]. Yàlla mu kawe mi nee na: {dénk Nanu nit ag rafetal ci ñaari way-juram, yaayam ëmb na ko ci coono imbi ko ci coono, ëmb ga ak feral ga lépp di fanweeri weer, ba moom saa su dëgëree ba am ñent-fukki at, di wax naan: yaw sama Boroom yenkeewal ma may sant ci sa xéewal yi Nga ma xéewalal ak samay ñaari way-jur, ak may jëf jëf ju yiw joo gërëm, te nga yéwénalal ma ci samay sët, man déy tuub naa jëm ci yaw, te man mii ci jullit ñi laa bokk} [saaru Al-Ahqaaf: 15]. Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu wax ne: benn waay dafa ñëw ci Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- daal di ne ko: yaw Yonnent Yàlla bi, ana kan moo gën a yeyoo samaw ànd wu raget? Mu ne ko: "Sa yaay" mu ne ko: teg ci kan? Mu ne ko: "sa yaay" mu ne ko: teg ci kan? Mu ne ko: "sa yaay" mu ne ko: teg ci kan? Mu ne ko "sa baay" Sahiihu Muslim.
Te ndigl lii ñu dénkaane ci njaari way-jur moo xam ay jullit lañu walla duñu ay jullit Jële nañu ci Asmaa doomu Abuu Bakrin mu wax ne: (sama yaay dafa ñëw ca jamonoy waa Xuraysin ci diir ba ñu kóllarante woon ak Yonnent mi ngi nekk ab bokkaalekat (yéefar) ma laaj Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- ne ko: sama yaay dafa ñëw nekk ku xemmem lool, ndax ma jokk ko? Mu ne ma : «waaw jokkal sa yaay» Sahiihul Buxaarii, Bu way-jur yi jéemoon seen kem kàttan ngir wëlbati doom ji mu juge ci Lislaam jëm cig kéefër -bu boobaa-Lislaam da koy digal mu bañ leen a topp, te sax cig ngëm Yàllaam, tey rafetal jëme ci ñoom, di ànd ak ñoom cig njekk, Yàlla mu kawe mi nee na: {saa su ñu la sonnalee ci nga bokkaale maak loo amu xam-xam buleen ca topp, waaye, nangay ànd ak ñoom ci àdduna cig njekk, te nga topp yoonu ka jëm ci Man, fi man ngeen di dellu, Nu xibaare leen li ngeen doon jëf} [saaru Luqmaan: 15].
Te Lislaam du tere jullit bi muy rafetal jëme ko ci jegeñaaleem yu dul jullit mbaa sax ñu dul ay jegeñaaleem, ndeem nekkuñu ñu koy xeex ngir diineem, Yàlla mu kawe mi nee na: {Yàlla terewuleen ñi xeexul ak yéen ci séen diine, te génnewuñuleen séen kër yi ngeen leen di defal lu baax ak di maandu jëme ci ñoom, Yàlla dafa bëgg way-maandu ñi} [saaru Al-Mumtahina: 8].
Lislaam day digle di dénkaane doom yi, te li gën a màgg ci li Lislaam di digal baay ji mooy mu jàngal ay doomam àqi séen Boroom ci ñoom, niki ni ko Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- waxe doomu baay tëxam ba di Abdul Laahi Doomu Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm-: «yaw xale mbaa éey yaw xale si, ndax duma la xamal ay baat yoy Yàlla dina la ci jariñ? Ma ne ko: aha kay. Mu wax ne: "nanga wàttu Yàlla Yàlla sàmm la, nanga wàttu Yàlla kon danga ko fekk sa kanam, deel xam Yàlla ci jamanoy yomb-yomb kon Yàlla xam la ci jamonoy tar-tar, booy laaj laajal Yàlla, booy dimbandiku nanga dimbandikoo Yàlla» Ahmad moo ko soloo 287/4.
Yàlla dafa digal ñaari way-jur yi ñu jàngal séen i doom lu leen di jariñ ci biri séen diine ak séen àdduna, Yàlla mu kawe mi nee na: {éey yéen ñi gëm Yàlla na ngeen fegal seen bopp ag seen njaboot ci Sawara wi nga xam ne ay nit ak i doj ñoo koy xamb te ay Malaaka yu tal te dëgar ñoo fa nekk te duñu moy Yàlla ci lenn lu mu leen digal, te li mu leen digal la ñuy def} [Saaru At-Tahriim: 6] Jële na ñu ci Aliyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ci li Yàlla mu kawe mi wax ne: {fegalleen séen bopp ak séen njaboot ci sawara} Day wax naan: "nangeen leen yar". Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- digal baay ji mu xamal doomam julli; ngir yaru si julli, Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- daal di wax ne: (digalleen seen doom yi julli bu ñu amee juroom-ñaari at) Abuu Daawuda moo ko soloo, Yonent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-nee na: «Ku nekk ci yéen ab càmm la te ku nekk ci yéen dees na ko laaj la mu doon sàmm, njiit li ab càmm la te dees na ko laaj la mu doon sàmm, góor gi ab càmm la ci njabootam te dees na ko laaj la mu doon sàmm, jigéen gi ab càmm la ci kër jëkkëram te dees na ko laaj la mu doon sàmm, surga bi am càmm la ci alalu sangam te dees na ko laaj la mu doon sàmm, yéen ñépp ay sàmm ngeen te deesna leen laaj li ngeen doon sàmm» Sahiihu Ibn Hibbaan 4490.
Lislaam dafa digal baay ji muy jox ay doomam ak i njabootam, jiitu na ñi tudd yenn ci yooyu ci xëtuw limatu(80) Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- leeral ngëneelu jox say doom, mu wax ne: «alal ji gën ci li nit ki di joxe: mooy alal ji mu jox njabootam ak alal ji mu jox ay daabaam ci yoonu Yàlla, ak alal ji mu joxe ay àndandoowam ci yoonu Yàlla » Abuu Xilaaba wax ne: "dafa, tàmbli ci njaboot Abuu Xilaaba dellu wax ne: ana gan góor mooy gën a màggug fay ci góor guy jox njabootam gu ndaw di leen feg, mbaa Yàlla di leen jariñ ci moom ba def leen ñu doylu?!" Sahiihu Muslim 994.
30- Lislaam day digle mandu ci wax ak jëf ba ci ak noon yi sax.
Yàlla mu kawe mi -tudd naa sellam ga- ku melowoo mandu la, ci ay jëfam, ak i doxaliinam ci jaamam ñi, te moom moo ngi ci yoon wu jub ci lépp lu muy digle ak lu muy tere, ak lu mu bind ak lu muy dogal, Yàlla mu kawe mi nee na: {Yàlla seede na ne amul kenn ku yayoo jaamu ku dul Moom, Malaaka yi it seede nañu ak woroom xam-xam yi taxaw cig mandu, amul kenn ku yeyoo jaamu ku dul moom, mooy Boroom kàttan gi di ku Xereñ ki} [Saaru Aali-Imraan: 18]. Yàlla day digle ag mandu, Yàlla mu kawe mi nee na: {waxal ne sama Boroom dugle na ag maandu} [saaru Al-Ahraaf: 29]. Te yonnent yépp ak ña ñu soloo -yal na leen Yàlla dolli jàmm- maandu la ñu indi, Yàlla mu kawe mi nee na: {yónni Nanu sanuy yonnent ci ay firnde yu leer Nu wàcce ci ñoom téere ak i balaas yu màndaxe ngir nit taxaw cig maandute} [saaru Al-Hadiid: 25]. Balaas yu màndaxe mooy maandu ci ay wax ak i jëf.
Lislaam day digle maandu ci ay wax ak i jëf ba ci ak noon yi sax, Yàlla mu kawe mi nee na: {éey yéen ñi gëm taxawleen temm cig maandute di seede ngir Yàlla donte seen kaw la dal, walla ci kaw ñaari way-jur yi, walla jegeñaale yi, bu dee ku woomal la walla ku ñàkk Yàllaa gën a yay ci ñoom ñaar ñépp, buleen topp bànneex yi ba ñàkk a mandu, bu ngeen jengalee mbaa ngeen dëddu bañ a seede, xamleen ne Yàlla ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def} [saaru An-Nisaa-i: 135]. Yàlla mu kawe mi nee na: {te mbañeelu ña leen tere woon Jàkka ja ñu wormaal bu mu tax ngeen di jéggi dayo, nangeen di dimbalante ci lu baax ak ragal Yàlla, te buleen di dimbalante ci bàkkaar ak màndute , ragalleen Yàlla, Yàlla ku tar mbugël la} [saaru Al-Maa-ida: 2]. Yàlla mu kawe mi nee na: {éey yéen ñi gëm nangeen taxaw temm ci seede cig màndute ngir Yàlla, te mbañeel ci aw nit bu mu leen xirtal ci ngeen di bañ a màndu, nangeen màndu moo gën a jege ragal Yàlla} [saaru Al-Maa-ida: 8]. Ndax gis nga ci doxaliinu xeet yi fi nekk tay, walla diiney nit lu mel ni digle gii ci seede dëgg ak wax dëgg donte ci sa kaw la dal, walla ci sa kaw ñaari way-jur, walla ci kaw jegeñaale yi, ag di digleg maandu ci noon bi ak ci xarit bi?
Yonnent bi it -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- dafa digle maandute ci digante doom yi. Jële nañu ci Aamir mu wax ne: dégg naa An-Nuhmaan doomu Basiir -yal na leen Yàlla dollee gërëm- fekk moo nga ca kaw Minbar ba di wax naan: sama baay jox na ma ag may, Amratu doomu Rawaaha ne ko: duma nangu ba keroog ngay seedeloo Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc-, mu dem ca Yonnent ba -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- ne ko: man damaa jox sama doom ji ma am ak Amratu doomu Rawaaha ag may, Amrata digal ma ma seedeloo la yaw Yonnent Yàlla bi, mu ne ko: "ndax jox nga sa yeneen doom yi des li nga jox kooku?" Mu ne ko: déedéet, mu ne ko: "ragalleen Yàlla tey maandu ci seen diggante doom yi" nee na mu dellu, daal di nangu la mu ko mayoon). Sahiihul Buxaarii 2587.
Li tax mooy mbiri nit ñi ak réew yi du taxaw mukk ci lu dul maandu, nit ñi duñu nekk ci kóolute ci séen diine ak séen deret ak séen njaboot ak séen i der ak séen i alal ak séen i dëkkuwaay ci lu dul maandu, lii moo tax ñuy fekk Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- bi yéefari Màkka yi xatalee jullit ñi ca Màkka Yonnent bi digal leen ñu gàddaay jëm Habasa; mu teg loolu ci ne buur bu maandu moo fa nekk te deesul tooñ kenn fa moom.
31- Lislaam day digle rafetal jëme ci mbindéef yépp, di woote ci jikko yu tedd yi, ak jëf yi rafet yi.
Lislaam day digle rafetal jëme ci mbindéef yépp, Yàlla mu kawe mi nee na: {Yàlla déy day digle maandute ak rafetal ak di jokk jegeñaale yi} [saaru An-Nahl: 90]. Yàlla mu kawe mi nee na: {ñoom ñiy joxe si jamonoy naatànge ak si jamonoy tar-tar, ak ñiy nëbb mer, ak ñay jéggal nit ñi, Yàlla bëgg na ñay rafetal} [saaru Aali-Imraan: 134]. Yonnent bi Muhammat yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: «Yàlla bind na rafetal ci bir yépp, bu ngeen dee ray nangeen rafetal rayiin wa, bu ngeen dee rendi nangeen rafetal rendiin wa, nangeen daas seenug ñawka tey noppal li ngeen di rendi» Sahiihu Muslim 1955.
Lislaam day woote ci jikkó yu tedd yi, ak jëf yu rafet yi, Yàlla mu kawe mi wax na ci melokaanu Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- ca téere ya jiitu ne: {Ñay topp Yonnent ba di ku ñu soloo te jàngul, te ñu fekk ko ñu bind ko ca la ñu yore ci Tawraat ak Injiil, mu leen di digal lu baax di leen tere lu bon, di leen daganalal yu teey yi, di araamal ci ñoom yu sellul yi, dindil leen yu diis ya ak jéng ya nekkoon ca ñoom, kon ñi ko gëm te weg ko, di ko dimbali, di topp leer ga ñu wàcce ci moom, ñoom ñooy way-texe ña} [Saaru Al-Ahraaf: 157]. Yonent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «éey yaw Aysa Yàlla déy ku ñeewante la te dafa bëgg ñeewante, te day joxe cig ñeewantu lu mu dul joxe ci ag tar, ak lu mu dul joxe ci lu dul ñeewantu» Sahiihu Muslim 2593. Yonent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Yàlla araamal na ci yéen: ngeen di moy séen yaay yi, ak di suul doom yu jigéen yi, tere na joxe na, sib na ci yéen nee nañu nee nañu, ak barib laaj, ak sànk alal» Sahiihul Buxaarii 2408. Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «dungeen dugg àjjana ndare ngeen gëm, te dungeen gëm ndare ngeen bëggante, moo ndax duma leen tegtal lol su ngeen ko defee dangeen bëggante? Siiwalleen nuyó seen diggante» Sahiihu Muslim 54.
32- Lislaam day digle jikkó yu rafet yi, nikki dëggu ak joxe kóolute, ak fegu, ak kersa, ak joxe, ak tedd-nga, ak dimbali way-aajowoo ak xettali ku ne si jafe-jafe ak leel aji-xiif ak refetal dëkkaale, ak jokk mbokk ak ñeewantu ci baayima yi.
Lislaam day digle jikkó yu rafet yi, Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- nee na: (Dañu maa yónni ngir ma mottali jikkó yu rafet yi) Sahiihul Adabil Mufrad 207, Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: (ñi Ma gën a bëgg ci yéen, te gën maa jege barab ëllëg bis-penc, mooy ñi gën a rafet jikkó ci yéen, waaye ñi ma gën a bañ ci yéen te gën maa sori barab ëllëg bis-penc, ñooy coowkat yi, ak puukarekat yi, ak ñiy rëy-rëylu, ñu ne ko: nun xam nanu coowkat yi ak puukarekat yi, kon lan mooy "al-mutafayxihuuna"? Mu ne leen: mooy: ñiy rëy-rëylu) As-Silsilatus Sahiihatu 791. Jële na ñu ci Abdallaa doomu Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: "Yonnent bi nekkul woon kuy wax lu ñaaw, du caagine def lu ñaaw, daa na wax it: (bokk na ci séen i tànneef ñi gën a rafetó) Sahiihul Buxaarii 3559, Ak yeneen Aaya ak yeneen Hadiis yuy tegtale ne Lislaam day ñaaxe ci teddàngey jikkó yi, ak rafeti jëf yi, ci anam gu matale.
Bokk na ci li Lislaam di digle: dëggu, Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- nee na: Maa ngi leen di dénk dëggu ndax dëggu day jëme ci ag mbaax, te ag mbaax day jëme àjjana, te nit ki du deñ di dëggu di xeeñcu dëgg ba ñu bind ko fa Yàlla ne mom ab dëggalaakoon la) Sahiihu Muslim 2607.
Bokk na ci li Lislaam di digle: joxe kóolute, Yàlla mu kawe mi nee na: {Yàllaa ngi leen di digal ngeen jox kóllare ay ñoñam} [Saaru An-Nisaa: 58].
Bokk na ci li Lislaam di digle: fegu Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- nee na: «ñatt a ngii ñu Yàlla warlu ne dina leen dimbali: mu tudd ca: ki takk soxna ngir bëgg a fegu» Sunanut Tirmisii 1655. Bokkoon na ci ay ñaanam -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc-, li mu daan wax naan: «Yàlla sama Boroom maa ngi lay ñaan ag njub, ak ragal la, ak fegu ak doylu» Sahiihu Muslim 2721.
Bokk na ci li Lislaam di digle: kersa, Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- nee na: «kersa du indi lu dul yiw» Sahiihul Buxaarii 6117, Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- nee na: «diine ju nekk am na jikkò, te jikkòy Lislaam mooy kersa» Bayhaqii moo ko géne ci Suhabul Iimaan, 2619/6.
Bokk na ci li Lislaam di digle: njàmbaar te, jële nañu si Anas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : «Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- moo gënoon a rafet ci nit ni, gën a jàmbaare ci nit ñi, gën a tabe ci nit ñi, waa-Madiina jàqoon nañu Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- jiitu leen yéeg ci kaw fas» Sahiihul Buxaariyyu 2820. Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- daan na muslu ci Yàlla si ragal, daan wax naan: «Yaw Yàlla sama Boroom maa ngi muslu si yaw ragal» Sahiihul Buxaarii 6374.
Bokk na ci li Lislaam di digle: joxe ak tabe, Yàlla mu kawe mi nee na: {misaalum ña nga xam ne dañuy joxe séen i alal ci yoonu Yàlla mi ngi mel ne wenn pep wu sax juróom-ñaari gup, wu ci nekk am téemeri fepp, Yàlla mooy fulal ku ko soob, Yàlla ku yaatu la ku xam la} [saaru Al-Baqara: 261]. Jikkóy Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- mooy ag tabe jële nañu ci Ibn Abbaas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: «Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- moo gënoon a tabe si yiw ci nit ñi, te daan na gën a tabe ci weeru koor bu Jibriil daan dajeek moom, Jibriil daan na dajeek moom ci guddig weeru koor wune ba weer wi jeex, Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- daan ko gaaral Alxuraan, bu Jibriil daan dajeek moom moo daan gën a tabe ci yiw ngelaw lu foor» Sahiihul Buxaarii 1902.
Bokk na ci li Lislaam di digle: xettali ku jaaxle, ak leel aji-xiif, ak rafetal dëkkaale, ak jokk mbokk, ak am ñeewante ci baayima yi. Jële na ñu ci Abdulaa Doomu Amrin -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu ne: benn waay laaj na Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- lan moo gën ci Lislaam? Mu ne ko: «dangay leele aw ñam, di nuyu koo xam ak koo xamul» Sahiihul Buxaarii 12. Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- nee na: «benn waay da doon dox ci wenn yoon rekk mar wu tar lool dikkal ko, mu gis benn teen, daal di dugg ci biir, daal di naan, daal di gennaat rekk yam ci ab xaj buy yalkat di lekk suuf si ngir aw mar, waa ji ne: xaj bii de li ma jotoon ci aw mar moo ko jot, mu daal di duggaat ci teen bi daal di duy aw dàllam ba mu fees mu jàpp ko ak gémmiñam, génn jox xaj bi mu naan, Yàlla sant ko daal di koy jéggal» ñu ne ko: yaw Yonnent Yàlla bi, ndax dañuy am tiyaaba ci baayima yi? Mu ne: «lépp luy dund danga am tiyaaba boo ko joxee mu naan» Sahiihu Ibn Hibbaan 544. Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «kiy dox jëm ci dimbali ab Jatun (ku boroom-këram faatu) ak way-ñakk moo ngi mel ni kuy xeex ci yoonu Yàlla, wàlla kuy taxaw guddi di woor bëccëg» Sahiihul Buxaarii 5353.
Lislaam day feddali àqi mbokk, di waral jokk mbokk, Yàlla mu kawe mi nee na: {Yonnent bi moo gën a yey jullit ñi ci séen bopp, te ay soxnaam séen i yaay lañu. Ña ame mbokkug deret, gën nañoo yeyante kem ni mu dikke ci téereb Yàlla bi ci jullit ñi ak way-gàddaay ñi, ndare ngeen def lu nekk jëme ko ca ña ngeen méggoo, loolu lu ñu bind la ca téere ba} [saaru Al-Ahsaab: 6]. Muy moytondikuloo dog mbokk daa di koy lënkaleek yàq ci suuf si, Yàlla mu kawe mi nee na: {mu ndax dangeen a nar bu ngeen dëddoo di yàq ci kaw suuf ak di dog séenug mbokk(22) Ñooñu ñooy ña Yàlla rëbb tëxloo leen gumba loo leen(23)} [saaru Muhammat: 22-23]. Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- wax ne: «kiy dog mbokk du dugg àjjana» Sahiihu Muslim 2556. Mbokk yi nga xam ne warees na leen a jokk ñooy: ñaari way-jur, ak ay mbokk yu góor, ak yu jigéen, ak baay tax yi, ak bàjjan yi, ak nijaay yi ak tànta yi.
Te Lislaam day firndeel àqi dëkkandoo ba ci yéefar bi sax: {jaamuleen Yàlla te buleen ko bokkaale ak dara, te ngeen di rafetal ci séen ñaari way-jur, ak ci séen jegeñaale, ak ci jirim yi, ak ci néew-ji-doole yi, ak ci séen i dëkkandoo ya di séen i mbokk, ak dëkkandoo yu sori ya, ak àndandoo ya, ak doxandeem ya, ak séen i jebéer, Yàlla bëggul kuy puukarewu ak a ndamu} [Saaru An-Nisaa-i: 36]. Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: (Jibriil deñul dima dénk dëkkandoo ba ma mujj njort ne dana ko dondloo) Sahiihu Abuu Daawuda 5152.
33- Lislaam dafa daganal lekk yu teey yi ak naan yu teey yi, mu digle it laabu xol ak laabu yaram, ak gu kër, looloo tax mu daganal sëy, niki ni ko Yonnent yi -yal na leen Yàlla dolli jàmm- diglee, te ñoom dañuy digle lépp lu teey.
Lislaam dafa daganal lekk yu teey yi, ak naan yi, Yonente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- nee na: «éey yéen nit ñi Yàlla ku teey la te du nàngu lu dul lu teey, Yàlla digal na way-gëm yi li mu digal Yonnent yi, Yàlla mu kawe mi nee na: {éey yéen Yonnent yi lekk-leen ci yu teey yi, te ngeen jëf jëf yu sell yi, man déy Aji-Gis laa lépp lu ngeen di def} Yàlla mu kawe wax it ne: {éey yéen way-gëm ñi lekkleen ci yu teey yi ma leen wërsëgale, te ngeen sant Yàlla ndeem moom dong ngeen di jaamu} Aayabi, mu daal di tudd benn waay bu nekk ci tukki bu sori, kawar ga jaxasoo, mu pënd lool, ma nga tàllal ay loxoom jëme kaw asamaan, di wax naan: yaw sama Boroom, te li muy lekk dafa araam, li muy naan dafa araam, li mu sol dafa araam, li muy naan it dafa araam, li ñu ko dundale itam dafa araam, moo naka lees koy nangule ñaanam?!» Sahiihu Muslim 1015. Yàlla mu kawe mi nee na: {Waxal:ana kan mooy araamal taari Yàlla yi Mu génneel jaamam yi ak xéewal yu sell yi? Waxal ne: yooyu ñi gëm ñoo ci gën a yay ci dundug àdduna gii, te ñoom dong ñoo koy moom bu àllaaxiraa, noonu la nuy leerale sunuy tegtal ñeel nit ñay xam} [saaru Al-Ahraaf: 32].
Lislaam dafa digle laabug xol ak gu yaram ak gu kër loolu tax mu daganal sëy niki ni ko Yonnent yi -yal na leen Yàlla dolli jàmm- diglee, ndax ñoom dañuy digle lépp lu teey, Yàlla mu kawe mi nee na: {Yàlla sàkkal na leen ay jabar yu juge ci yéen, Mu sàkkal leen ca séen jabar ya ay doom ak i sét, mu wërsëgal leen ci yu teey yi, waa ndax ay caaxaan la ñuy gëm, di weddi xéewali Yàlla yi} [saaru An-Nahl: 72]. Yàlla mu kawe mi nee na: {te na nga laabal say yére (4) Te it na ngay daw bépp bàkkaar (5)} [Saaru Al-Mudassir: 4-5]. Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: (Koo xam ne lu toll ni pepp ci rëy nekk na ci xolam du dugg àjjana. Benn waay ne: nit ki day bëgg ay yéréem nekk lu rafet, ay dàllam nekk lu rafet, mu ne ko: "Yàlla dafa rafet te dafa bëgg lu rafet, rëy mooy bañ dëgg ak xeeb nit ñi) Sahiihu Muslim 91.
34- Lislaam araamal na cosaanu ya ñu araamal niki bokkaale Yàlla, ak kéefër, ak jaamu ay xërëm, ak wax ci Yàlla ci lu dul xam-xam, ak ray doom yi, ak ray bàkkan bu ñu araamala ray, ak yàq ci suuf si, ak njabar, ak ñaawtéef yi feeñ yi ak yu nëbbu yi, ak njaalo, ak ngóor-jigéen, araamal na ribaa, araamal na lekk médd, ak lu ñu rayal xërëm yi, araamal na lekk yàppu mbaam xuux, ak mbooleem yu sobe yi, ak yu sellul yi, araamal na lekk alalu jirim, ak di wàññi natt ya ak màndaxe ya, araamal na it dog mbokk. Te yonnente yi -yal na leen Yàlla dolli jàmm- ñoom ñépp a dëppoo ci araamal yu araam yii.
Lislaam araamal na cosaani yu araam yi niki bokkaale Yàlla ak kéefër ak jaamu ay xërëm ak wax ci Yàlla ci lu dul xam-xam ak ray doom yi, Yàlla mu kawe mi nee na: {neel: kaayleen ma taril leen li Yàlla araamal ci yéen: mooy buleen ko bokkaaleek dara te nangeen di rafetal jëme ci séen ñaari way-jur. Te buleen ray séen doom yi ngir ag njàkk, Nun Noo leen di wërsëgal yéen di leen wërsëgal ñoom. Buleen jege ñaawtéef yi ya ca feeñ ak ya ca nëbbu. Te buleen ray bakkan bu Yàlla wormaal lu dul ci dëgg. Yooyu la leen dénk amaana ngeen xellu Te buleen jege alali jirim lu dul ca na mu gën a rafete ba keroog muy man a lijjanti boppam. Nangeen di matal natt ak mandaxe cig maanute, dunu teg bakkan lu dul lu mu àttan. Bu ngeen dee wax nangeen maandu doonte séen mbokk ngeen di àtte. Nangeen di matal kóllareg Yàlla. Loolu la leen Yàlla dénk ngir ngeen fàttaliku} [saaru Al-Anhaam: 151-152]. Yàlla mu kawe mi nee na: {neel: Sama Boroom araamalul lu dul ñaawtéef yi la ca feeñ ak la ca nëbbu, ak bàkkaar ak bew guy jalgati dëgg ak di bokkaale Yàlla, ak ngeen di wax ci Yàlla lu ngeen xamul} [saaru Al-Ahraaf: 33].
Lislaam araamal na ray bakkan bu ñu araamal, Yàlla mu kawe mi nee na: {buleen ray bakkan bu Yàlla araamal lu dul ci dëgg, képp ku ñu tooñ ba ray ko, jox nanu ñay taxawu mbiram sañ-sañ waaye bu mu jéggi dayo ci ray, ndax dees na ko dimbali} [saaru Al-Israa: 33]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Ak ñi dul booleek Yàlla beneen yàlla te duñu ray bakkan bu Yàlla araamal ci lu dul dëgg te duñu njaalo, képp ku def loolu dana dajeek ay bàkkaar} [saaru Al-Furxaan: 68].
Lislaam araamal na yàq ci suuf si, Yàlla mu kawe mi nee na: {buleen yàq ci suuf si ginnaaw ba ñu ko yéwénalee} [saaru Al-Ahraaf: 56]. Yàlla mu kawe nettali na ci Yonnent ba Suhaybu -yal na ko Yàlla dolli jàmm- muy wax aw nitam naan leen: {Yéen samay mbokk jaamuleen Yàlla amu leen jeneen Yàlla ju dul moom, ay lay yu leer nàññ dikkal na leen jóge fa seen Boroom, deeleen matal natt yi ak màndaxe yi, te buleen wàññil nit ñi la ñu moom, te it buleen yàq ci kaw suuf ginnaaw ba ñu ko defaree, loolu moo gën ci yéen bu fekkee ne gëm ngeen} [Saaru Al-Ahraaf: 85].
Lislaam araamal na njabar, Yàlla mu kawe mi nee na: {sànnil li ci sa ndeyjoor kon dana lump la ñu liggéey, te liggéeyuñu lu dul pexey njabar, te njabarkat fu mu man a dem du raw} [saar Taaha: 69]. Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «moytandikuleen juróom-ñaari bir yay alake, ñu ne ko: yaw Yonnent Yàlla bi yooyu yan la? Mu ne: bokkaale Yàlla, ak njabar, ak ray bakkan bu Yàlla wormaal lu dul ci dëgg, ak lekk ribaa, ak lekk alali jirim, ak daw ci bisub xeex ba, ak tuumaal jigéen ga seŋewu di ku gëm di ku bawul xel loolu» Sahiihul Buxaarii 6857.
Lislaam araamal na ñaawtéef yu feeñ yi ak yu nëbbu yi, ak njaalo, ak ngóor-jigéen tuddoon nañu ca njëlbéenu xët wi aaya yiy tegtale loolu, Lislaam araamal na ribaa, Yàlla mu kawe mi nee na: {éey yéen ñi gëm ragalleen Yàlla tey moytondiku li des ci ribaa yi ndeem gëm ngeen(278) Bu ngeen ko deful nangeen séentu xeex bu tukkee ca Yàlla ak ub Yonnenteem, su ngeen tuubee nag yéen a moom séen cosaani alal, dungeen tooñ te deesuleen tooñ(279)} [saaru Al-Baqara: 278-279]. Yàlla tëkkuwul boroom bàkkaar cim cong kem ni mu tëkkoo kiy lekk ribaa; ndax ribaa day raafal diine yi ak réew yi ak alala yi ak bakkan yi.
Lislaam araamal na lekk médd ak lu ñu rendil xërëm yi araamal na it lekk yàppu mbaam-xuux, Yàlla mu kawe mi nee na: {Araamlees na ci yéen médd, ak deret, ak yàppu mbaam-xuux ak la ñu ray tudd ca ku dul Yàlla, ak mala wu wékku, ak bu ñu dóor ba mu dee, ak bu mbartalu daanu dee, ak bu ñu jam béjjan, ak bu rabu-àllam lu mu ca lekk - lu dul la ngeen rendi -. (Terees na it) lu ñu rendi ci ay xërëm, ak ngeen di séddalee ci wantaleb gisaane . Loolu génn diine la} [saaru Al-Maa-ida: 3].
Lislaam araamal na naan sàngara ak mbooleem sobe yi ak yu sellul yi, Yàlla mu kawe mi nee na: {Éey yéen ñi gëm ! [xamleen ne] sàngara, wure, xerëm ak séen banti gisaane, nekkuñu lu dul sobe su jóge ci jëfi [Saytaane]. Nangeen leen moytu, amaana kon dingeen texe(90) {Saytaane bëggul lu dul tàbbal ci séen diggante nooneel ak mbañeel, jaare ko ci sàngara ak wure te it dox seen diggante ak fàttaliku Yàlla ak julli. Moo ndax dungeen leen bàyyi?(91)} [saaru Al-Maa-ida: 90-91]. Tudoon nañu ci xëtu limatu (31) li Yàlla xibaare ci melokaanu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- ci Tawraat ci ne moom day araamal ci ñoom yu sellul yi, Yàlla mu kawe mi nee na: {ñoom ñiy topp Yonnent ba nga xamne manula jàng manula bind, te ñu fekk ko muy kuñu bind ca Tawraat ba ñu yore ak ca Injiil, mu leen di digal lu baax di leen tere yu ñaaw yi, di leen daganalal yu teey yi di araamal ci ñoom yu sellul yi dindil leen yu diis ya ak jéng ya nekkoon ca ñoom} [Saaru Al-Ahraaf: 157].
Lislaam araamal na lekk alali jirim, Yàlla mu kawe mi nee na: {joxleen jirim yi séen alal te buleen di weccee lu baax ci lu bon, buleen lekk séen i alal di ko booleek alalu jirim yi, ndax loolu bàkkaar bu rëy la} [saaru An-Nisaa-i: 2]. Yàlla mu kawe mi nee na: {ñiy lekk alalu jirim yi cig tooñ lekkuñu ca séen biir ya lu dul sawara, te danañu dugg sawara} [saaru An-Nisaa-i: 10].
Lislaam araamal na wàññi natt ya ak peese ya, Yàlla mu kawe mi nee na: {xuru sawara ñeel na naxaatekat ya(1) Ña nga xam ne bu ñu nattee jële ca nit ña dañu koy ëppal(2) Te bu ñuy nattal keneen wàññi ko(3) Moo ndax ñoom dañoo jàppul ne dees na leen dekkil(4)} [saaru Al-Mutaffifiina: 1-4].
Lislaam araamal na dog mbokk, tudoon nañu ci xëtu limatu (31) ay Aaya ak i Hadiis ci loolu, te Yonnent yi -yal na leen Yàlla dolli jàmm- ñoom ñépp a dëppoo ci araamal yu araam yii.
35- Lislaam day tere jikkó yi ñu ŋàññi ak fen ak naxaate ak wuruj ak wor, ak soxor ak pexe mu ñaaw ak sàcc ak bew ak tooñ, day tere mbooleem jikko yu sellul yi.
Lislaam day tere jikkó yi ñu ŋàññi yépp, Yàlla mu kawe mi nee na: {Bul dox di dummóoyu nit ñi, bul dox it di puukarewu : Yàlla bëggul képp kuy puukarewu ak a damu} [saaru Luqmaan: 18]. Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-nee na: (ñi ma gën a bëgg ci yéen, te gën maa jege barab ëllëg bis-penc, ñooy ñi gën a rafet jikkó ci yéen, waaye ñi ma gën a bañ ci yéen te gën maa sori barab ëllëg bis-penc, ñooy coowkat yi, ak puukarekat yi, ak ñiy rëy-rëylu, ñu ne ko: nun xam nanu coowkat yi ak puukarekat yi, kon lan mooy "al-mutafayxihuuna"? Mu ne leen: mooy: ñiy rëy-rëylu) As-Silsilatus Sahiihatu 791.
Lislaam day tere fen, Yàlla mu kawe mi nee na: {Yàlla déy du gindi mukk yàq-kat bu man a fen} [saaru Xaafiri: 28]. Yonent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «moytondikuleen fen, ndax fen day jëme cig kàccoore te kàccoore day jëme sawara, te nit ki du deñ di fen, di jëm ci fen ba ñu bind ko fa Yàlla ne ab fenkat la» Sahiihu Muslim 2607. Yonent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «màndargay naaféq ñatt la: saa yu waxee fen, saa bu joxee ab dig wuute ko, bu ñu ko wóoloo mu wor» Sahiihul Buxaarii 6095.
Lislaam day tere wuruj Ñëw na ci Hadiis ne Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- romb na ndabu ñam dugal ci loxoom, loxo bi daal di tooy, mu ne: "lii lan la yaw boroom ñam wi? Mu ne ko: taw bee ko laal yaw Yonnent Yàlla bi, Yonnent bi ne ko: "waa lu teewoon nga teg ko ci kaw ñàm wi ngir nit ñi gis ko, kuy wuruj bokkul ci man" Sahiihu Muslim 102.
Lislaam day tere xeeti wor ak wuruj yépp, Yàlla mu kawe mi nee na: {éey yéen ñi gëm buleen wor Yàlla ak Yonnent bi, kon de dangeen wuruj séen kollare fekk xam ngeen} [saaru Al-Anfaal: 27]. Yàlla mu kawe mi nee na: {ñay matal kóllareg Yàlla te duñu fecci kollare} [saaru Ar-Rahd: 20]. Te Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- daan na wax xare-katam ya saa yu ñu daan génn: «xareleen te buleen ëppal buleen wor buleen xotti worma te buleen ray xale» Sahiihu Muslim 1731. Yonent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ñent a ngi nii képp ku ñu nekk ci moom ab naaféq la bu leer, képp ku benn ci yooyu nekk ci moom, kon benn melow naaféq nekk na ci moom ba keroog mu koy bàyyi: bu ñu ko wóoloo mu wor, bu waxtaane fen, bu kóllorante daal di fecci kóllare bu xuloo daal di kàccoore» Sahiihul Buxaarii 34.
Lislaam day tere ag soxor, Yàlla mu kawe mi nee na: {moo ndax dañuy iñaane nit ñi ca la leen Yàlla jox ci ngëneelam? Joxoon nanu waa kër Ibraahiima téere ak xereñte, joxoon nanu leen nguur gu rëy} [saaru An-Nisaa-i: 54]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Ñu bari ci ñoñ-téere yi [Yahuud ak Nasaraan] nee nañu siiw ñu delloo leen cig kéefar ginnaaw séen ngëm ngir kiñaan gu sosoo Séeni bakkan. Ginnaaw ba dëgg ga leeree nàññ ?Bàlleen te dummóoyuleen ba Yàlla agseek ndigëlam. Yàlla nag mën na lu ne} [saaru Al-Baqara: 109]. Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «feebarub xeet ya leen jiitu woon de raam na jëm si yéen: añaan ak bañante day wate Waxuma wat kawar waaye day wat diine, giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom, dungeen dugg àjjana ndare ngeen gëm te dungeen gëm ndare ngeen bëggante moo ndax duma leen tegtal luy saxal loolu ñeel leen? Tasaareleen nuyóo séen diggante» Sunanut Tirmisii 2510.
Lislaam day tere pexe mu ñaaw, Yàlla mu kawe mi nee na: {Naka noonu, Lanu defe ci bépp dëkk kilifa di ña fa dàq a tooñ ngir ñu fay nas ay pexe. Te pexe ya, dara duleen ca moy te yéguñu ko} [saaru Al-Anhaam: 123]. Yàlla xibaare ci Yahuud yi jéemoon nañoo ray Al-Masiih Iisaa -yal na ko Yàlla dolli jàmm- ñu def ay pexe wayee Yàlla defna pexe ma ci seen kaw, Yàlla leeral ne pexe mu ñaaw du këpp ci lu dul ca kaw boroom, Yàlla mu kawe mi nee na: {Ba Iisaa yëgee ca ñoom ag kéefar, la daal di wax ne : “Waaw ana kan moo may dimbali ci ñu jëm ca Yàlla? ” Gaa yu sell ya ne ko : “Nun noo lay dimbali ci yoonu Yàlla. Gëm nanu Yàlla. Seedeel ne nun ay jullit lanu(52) Yaw Sunu Boroom gëm nanu li nga wàcce topp nanu it Yonnent bi, noo ngi ñaal nga boole ni ca way-seede ña(53) Ñu tëral pexe Yàlla it tëral pexe, te moo gën a man a pexe way-pexe ñi(54) Fàttalikul ba Yàlla ba waxee ne : "Yaw Iisaa, danaa la fi jële, yëkkati la jëme ci Man, Danaa la laabal ci bon-boni yéefar yi weddi te danaa def ña la topp ñu féete kaw ña la weddi ba Bis-pénc ba. Yéen ñépp dellu ci Man, Ma àtte séen diggante ci li ngeen doon juuyoo} [saaru Aali-Imraan: 52-55]. Yàlla xibaare na ci ne niti Yonente Yàlla ba Saaliwu -yal na ko Yàlla dolli jàmm- dañu koo bëggoon a ray ciy pexe, ba ñu nasee ay pexe Yàlla fexeel leen daal di leeni alag ñoom ak séen i gaay ñépp, Yàlla mu kawe mi nee na: {Ñu wax ne : “Nanu waatoo ci Yàlla ray ko mook njabootam, topp nu wax ñay taxawu mbiram ne leen nun kat fekkewunu woon seenug ray, te dëgg rekk lanu wax(49) Ñangay fexe am pexe, Nun it noo ngi fexe am pexe te ñoom yéguñu ko(50) Xoolal naka la séen pexe ya mujje woon : Danu leen a faagaagal ñook séeni xeet wépp(51)} [saaru An-Naml: 49-51].
Lislaam day tere sàcc, Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- nee na: «aji-njaalo ji gëmul jamono ja muy njaaloo , sàcc bi gëmul jamono ja muy sàcc, naankatu sàngara bi gëmul jamono ja muy naan, tuub nag lees gaaral la ginnaaw ga» Sahiihul Buxaarii: 6810.
Lislaam day tere bew, Yàlla mu kawe mi nee na: {Yàlla day digle màndu ak rafetal ak jox jegeñaale yi, day tere ñaawtéef ak lu ñu sib ak bew, mi ngi leen di waar ndaxtelee ngeen fàttaliku} [saaru An-Nahl: 90].[saaru An-Nahl: 90] Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Yàlla soloo na ma ne nangeen di toroxlu ba kenn du bew ci kaw kénn kenn it du buukarewu ci kaw kenn» Sahiihu Abuu Daawuda 4895.
Lislaam day tere tooñ, Yàlla mu kawe mi nee na: {Yàlla bëggul tooñkat yi} [saaru Aali-Imraan: 57]. Yàlla mu kawe mi nee na: {lay mbir mooy tooñkat yi duñu raw mukk} [saaru Al-Anhaam: 21]. Yàlla mu kawe mi nee na: {waajalal na tooñkat yi mbugal mu metti} [saaru An-Nisaa-i: 31]. Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ñatt a ngi nii ñoo xam ne séen ñaan deesu ko delloo: njiit lu maandu, ak ki woor ba keroog muy dog, ak ñaanu ku ñu tooñ dees koy yekkati ci kaw niir yi tijjil ko buntuy asamaan yi, Boroom di wax naan: giñ naa ci sama màggaay ne dinaala dimbali donte ginnaaw tay la» Muslim génne na ko (2749), cig gàttal ci ag wuute gu néew, ak Tirmisii (2526) ci ag wuute gu néew, ak Ahmad (8043) baat yi ay baatam la. Bi Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- yónnee Muhaas ca Yaman, bokk na ca la mu ko waxoon: «nanga moytu ñaanug ku ñu tooñ ndax amul kiiraay diggam ak Yàlla» Sahiihul Buxaarii 1496. Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ne ku tooñ ñoñ-téere bu ne ci kóllare wàlla mu wàññi ay àqam, mbaa mu gàll ko lu ëpp kàttanam walla mu jël ci moom dara ci lu dul teeyug bakkanam dinaa layoog moom bis-penc ba» Sunanu Abuu Daawuda 3052. Lislaam kem ni nga ko gise, day tere jépp jikkó ju ñaaw wàlla jëflànte boo xam ne ag tooñ la mbaa ag jeng.
Lislaam day tere jëflànte yi nga xam ne dafa am ribaa walla lor mbaa wuruj mbaa tooñ walla sàcc mbaa muy indi ay jafe-jafe ak lor yoy day daj mbooloo ma, walla muy dal kenn.
Lislaam day tere jëflaantey alal yi nga xam ne dafa am ribaa walla lor mbaa wuruj mbaa tooñ walla sàcc mbaa muy indi ay jafe-jafe ak lor yoy day daj mbooloo ma, walla muy dal kenn. Tuddoon nañu ca njëlbéenu wax jii ay aaya ak i Hadiis yuy araamal ribaa ak tooñ ak wuruj ak yàq ci suuf si, Yàlla mu kawe mi nee na: {Ña nga xam ne dañuy lor jullit yu góor yi ak jullit yu jigéen yi te defuñu lu ko jar, ñangay yenu aw duur ak bàkkaar bu rëy} [saaru Al-Ahsaab: 58]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Képp kuy jëf yiw, boppam la koy defal. Képp kuy jëf ñaawtéef it ci kawam lay dal. Sa Boroom, du tooñ, benn jaamam} [saaru Fussilat: 46]. Ñëw na ci Sunna ne "Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- dafa àtte ne bu lore am bu loru am" Sunanu Abuu Daawuda. Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "képp ku gëm Yàlla ak bis-penc ba bu mu lor dëkkandoom, képp ku gëm Yàlla ak bis-penc ba nay teral ganam, képp ku gëm Yàlla ak bis-penc ba nay wax yiw wàlla mu noppi. Ci beneenug nettali mu ne: nay rafetal jëme ci dëkkandoom" Sahiihu Muslim 47. Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «mbugalees na jenn jigéen ci am muus, da koo tëj bamu faatu tax mu dugg sawara, ndax ba mu ko tëjee ba noppi joxu ko mu lekk joxu ko mu naan te bàyyi wu ko mu lekki li ci suuf si» Sahiihul Buxaarii 3482. Lii ci ku lor am muus, kon naka kuy lor nit ñi? Jële nañu ci Abdulaa Doomu Umar mu ne: Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- yéeg na minbar bi daal di woote ci kàddu gu kawe, wax ne: (éey yéen mbooleem ñi séen làmmiñ jébbalu te ag ngëm duggul séen xol, buleen lor jullit ñi te buleen leen ayibal te buleen topp séen i ñaawtéef, ndax kuy topp ñaawtéefi mbokkum jullitam Yàlla dana topp ay ñaawtéefam ba gàccaal ko doonte ci kaw waruwaayam la ne, nee na: fekk benn bis Doomu Umar da doon xool ca Néeg walla ca Kaaba ga, daal di ne: ana lan moo la gën a màg! Ana lan moo gën a màgg sa worma! Waaye way-gëm déy moo gën a màgg worma fa Yàlla) Tirmisii génne na ko:(2032), ak Ibn Hibbaan (5763). Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: (képp ku gëm Yàlla ak bis-penc ba bu mu lor dëkkandoom, képp ku gëm Yàlla ak bis-penc ba nay teral ganam, képp ku gëm Yàlla ak bis-penc ba nay wax yiw wàlla mu noppi) Sahiihul Buxaarii 6018. Jële nañu ci Abuu Hurayrata mu jële ci Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- mu wax ne: "ndax xam ngeen kan mooy ki ñàkk?" Ñu ne ko: ki njàk fi nun déy yaw Yonnent Yàlla bi mooy ki amul dërëm te amul ay jumtukaay. Mu ne leen: "ki ñakk ci samaw xeet mooy ki ñëw bis-penc indaale ay woor ak i julli ak joxe asaka, fekk saaga na deru kii, tuumaal kee, lekk alalu kii, ñu toogal ko fay kii ci ay yiwam, ak kee ci ay yiwam, bu ay yiwam jeexee, laata muy fay li tege ci kawam, ñu jël séen i ñaawtéef xëpp ka ko, jël ko moom sànni sawara) Muslim génne na ko(2581), ak Tirmisii (2418), ak Ahmad (8029).
Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- nee na: (benn bànqaasu garab dafa nekkoon ci yoon wi, di lor nit ñi benn waay andale ko, ñu dugal ko àjjana) Buxaarii génne na ko(652) ci maanaam, ak Muslim (1914) ci kemam, ak Inb Maaja(3682), ak Ahmad (10432) baat yii séen i baat la ñoom ñaar, toppale luy gaañe ci yoon wi day dugale àjjana, kon anamook kuy lor nit ñi di yàq séen dund?!.
37- Lislaam dafa ñëw ngir wattu xel ak araamal lépp lu koy yàq niki naan sàngara, mu yëkkati mbiru xel def ko muy sabab biytax ñuy togge jëf, mu goreel ko ci coonoy naxaate ak jaamu ay xërëm. Lislaam amul ay mbóot mbaa ay àtte yu muy jagleel ñenn ñi wolif ñeneen ñi, mbooleem ay àtteem ak i yoonalam dafa méngoo ak xel mu wér, te dafa dëppoo ak màndute ak xereñte.
Lislaam dafa ñëw ci sàmm bakkan ak di yekkati mbiram, Yàlla mu kawe mi nee na: {Naka dégg-dégg ak gis-gis ak li nga fas ci sa xol: loolu lépp dees ca Bis-pénc ba} [saaru Al-Israa: 36]. Li war nit ki mooy mu sàmmonteek xelam, looloo tax Lislaam araamal sàngara ak lépp luy màndiloo. - tudd na ñu araamalu sàngara ca xëtub limatu (34) te ay aayaay Alxuraan yu bari day jeex ci waxu Yàlla jii: {amaana ngeen xellu} [saaru Al-Baqara: 242]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Dundug àdduna nekkul lu dul poh ak i caaxaan. Te kërug àllaaxira moo gën ca ña ragal Yàlla. Moo ndax dungeen xel-lu ?} [saaru Al-Anhaam: 32]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Wàcce nanu ko mu di ay njàng ci làkku [araab] ngir ngeen xam la mu tekki} [saaru Yuusuf: 2]. Yàlla leeral ne ag njub ak ug xereñ kenn du jariñu ci ñoom ñaar ñu dul Boroom xel yi, Yàlla mu kawe mi nee na: {Mooy jox ag xereñte ku ko soob, te képp ku ñu jox xereñte déy, joxees na ko yiw wu bari, waaye kenn du fàttaliku ñu dul way-xellu ña} [saaru Al-Baqara: 269]
Loolu tax Lislaam def xel moy sababu toggu jëf, Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- nee na: «Yékkati na ñu xalima gay bind jëf yi ci ñatt: ci kiy nelaw ba baa muy yewwu, ak ci xale bi ba keroog muy gént, ak ci dof bi ba baamuy am xell» Buxaarii génne na ko ci waxiin wu dog, njëkk Hadiisu(5269) ci anamam, Abuu Daawuda it génne na ko cig jokkoo(1423), ak Nasaaa-ii ci ((As-Sunanul-Kubraa)) (7346), ak Ahmad (956) ci wuute gu ndaw, ak Ibn Maaja (2042) cig tënk. Mu goreel ko ci coonoy naxaate ak jaamu ay xërëm, Yàlla mu kawe mi xibaare biri xeet ya jiitu woon ci jàpp ga ñu jàppoon ci ay caaxaan di delloo dëgg gi joge ci Yàlla: {Naka noonu it masunoo yónni ab xuppekat (waaraatekat) cib dëkk lu dul ne kilifa ya dañuy wax naan : nun de fekkoon nanu sunuy maam ci diine te nun ñoom la ñuy roy} [saaru As-Suxrufi: 23]. Yàlla xibaare na ci Ibraahiima may xarit ba -yal na ko Yàlla dolli jàmm- ne wax na wa nitam ne leen: {waaw luy biri xërëm yii ngeen nekk di ko jaamu(52) Ñu ne: nun déy sunuy baay lañu fekk ñu koy jaamu(53)} [saaru Al-Anbiyaa: 52-53]. Lislaam ñëw digal nit ñi ñu bàyyi jaamu xërëm, te summiku ci caaxaan ya ñu donne ca séeni baay ak séeni maam, te topp yoonu Yonnent yi -yal na leen Yàlla dolli jàmm-.
Lislaam amul ay mbóot mbaa ay àtte yu muy jagleel ñenn ñi wolif ñeneen ñi Laaj nañu Aliyu doomu Abuu Taalib -yal na ko Yàlla dollee gërëm- te moom doomu baay-taxu Yonnent Yàlla bi la -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- tey jëkkëri doomam ja: ndax Yonnente bi jagleel na leen dara? Mu ne: Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- jagleelu ñu lenn lu mu joxul nit ñépp, lu dul lii ci sama njàppal Jaasi jii. Mu wax ne: mu génne aw këyit bu ñu bind: Yàlla rëbb na ku rendi ngir ku dul Yàlla, Yàlla rëbb na ku sàcc màndargaw suuf si, Yàlla rëbb na képp ku rëbb way-juram, Yàlla rëbb na kuy fat ab soskat ci diine ji" Sahiihu Muslim 1978. Àttey Lislaam yépp ak i yoonalam dafa méngoo ak xel mu wér te dëppoo ak maanute ak xereñte.
38- diine yu baaxul yi bu dee ñi ko topp manuñoo dégg la ca nekk ci ay juuyoo, ak yu wuuteek xel, niti diine ya dañu leen di gëmloo ne diine dafa weesu xel, te xel amul wàll ci dégg diine ak xam ko. Waaye Lislaam moom dafa jàppe leer guy leeralal xel yoon wa; ñoñu diine yu bon yi dañoo bëgg ci nit ki mu bàyyi xelam te topp leen ñoom, Lislaam nag moom daa bëgg ci nit ki mu yee xelam; ngir xam dëgg-dëggi bir yi ca na mu nekke.
Diine yu bon yi bu ñi ko topp manut a dégg la ca nekk ci juuyoo, ak yu wuuteek xel, niti diine ya dañu leen di gëmloo ne diine dafa weesu xel, te xel amul wàll ci dégg diine ak xam ko. Waaye Lislaam moom dafa jàppe leer guy leeralal xel yoon wa; ñoñu diine yu bon ya dañoo bëgg ci nit ki mu bàyyi xelam te topp leen ñoom, Lislaam nag moom daa bëgg ci nit ki mu yee xelam; ngir mu settantal ak xalaat ngir xam dëgg-dëggi bir yi ca na mu nekke, Yàlla mu kawe mi nee na: {naka noonu it lañuy soloo ci yaw [Alxuraan] ci Sunu ndigël. amoo woon benn xam-xam ci Téere bi du caagéene ngëm; waaye def nanu ko leer di ci gindi ku nu soob ci sunu jaam ñi. Te yaw it da ngay gindee jëme ci yoon wu jub wa kocc} [saaru As-Suuraa: 52]. Soloog Yàlla gi dafa làmboo ay tegtal ak i lay yuy gindi xel yu mucc yi ca dëgg ya muy bëgg a xam, ak gëm ko, Yàlla mu kawe mi nee na: {Éey yéen nit ñi! Aw lay dikkal na leen wu tukkee ca séen Boroom. Te wàcce nanu ci yéen leer gu ni nàññ} [saaru An-Nisaa-i: 174]. Yàlla mu kawe mi -tudd naa sellam ga- daa bëgg nit ki dund ci leerug njub ak xam-xam ak dëgg-dëggi bir yi, waaye Saytaane ak ñu bew ña, dàñuy bëgg nit ki des ci lëndamu kéefër ak réer ak sànkute, Yàlla mu kawe mi nee na: {Yàlla moo féetéek ñi gëm : Moo leen di génne ci ay lëndëm di leen jëme ci ag leer. Ña weddi nag Saytaaneey séen péete, mu leen di génne ci leer jëme leen ci ay lëndëm} [saaru Al-Baqara: 257].
Lislaam day màggal xam-xam bu wér, di ñaaxe ci gëstu xam-xam bu mucc ci bànneexu bakkan, tey woote it ci xool ak a xalaat ci sunu bopp ak ci mbindéef yi ñu wër. Te balluwaayu xam-xam yu wér ya tege ci xam-xam du wuute ak Lislaam.
Lislaam day màggal xam-xam bu wér, Yàlla mu kawe mi nee na: {Yàlla dana yékkatil ñi gëm te bokk ci yéen ak ña am xam-xam (ay daraja yu kawe). Te Yàlla ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def} [saaru Al-Mujaadala: 11]. Yàlla lënkale seedey woroom xam-xam yi ak seedeem ak seedey Malaakaam yi ci li gëna màgg ci lu ñuy seede, Yàlla mu kawe mi wax ne: {Yàlla seede na ne, amul jeneen Yàlla ju dul Moom, Malaaka ya ak woroom xam-xam ya taxawe ci maandu it, seede nañu ne amul jeneen Yàlla ju dul Moom. Ku not la, ku xereñ la} [saaru Aali-Imraan: 18]. Lii day firndeel dayob woroom xam-xam yi ci Lislaam ak li Yàlla digalul Yonnenteem bi Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- mu sàkku mu dolli ko xam-xam dara lu dul xam-xam, Yàlla mu kawe mi wax ne: {waxal ne: yaw sama Boroom dolli ma xam-xam} [saaru Taaha: 114]. Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ku sóobu aw yoon ngir sàkku xam-xam Yàlla dana ko yombalal yoon wu jëm àjjana, te Malaaka yi dañuy teg séen i laaf ngir gërëm kiy sàkku xam-xam, li ci asamaan yi ak suuf si ba ci jén yi nekk biir géej dañuy sàkkul njéggal kiy sàkku xam-xam, te ngënéelu boroom xam-xam ci kaw jaamukatu Yàlla bi, moo ngi mel ni ngëneelu weer wi ci kaw biddiw yépp, te woroom xam-xam yi ñoo donn yonnent yi, te yonnent yi kenn duleen donne ci xaalis waaye ci xam-xam lañu leen di donne te ku ko jël, jël na jér bu bari lool» Abuu Daawuda génne na ko(3641), ak At-Tirmisii (2682), ak Ibn Maaja (223) te baat yi ay baatam la, ak Ahmad (21715).
Lislaam day ñaaxe ci gëstu xam-xam bu mucc ci bànneexu bakkan tey woote ci xool ak a xalaat ci sunu bopp ak ci dund gi nu wër, Yàlla mu kawe mi nee na: {Dananu leen wan sunuy kéemaan ci déeléey asamaan ak ci seen bopp, ba baa ñuy gindi ku ci xam ne (Alxuraan), mooy dëgg tigi. Xanaa kay war na laa doy rekk ci sa Boroom ne moom seede la ci lépp?} [saaru Fussilat: 53]. Yàlla mu kawe mi nee na: {moo ndax dañoo xoolul ci nguuru asamaan yi ak suuf si, ak li Yàlla bind lépp, te it xayna séenub àpp jege na, kon jan wax lañuy gëm ginnaaw josam} [saaru Al-Ahraaf: 185]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Ndax dañoo doxul ci kaw suuf ñuy xool ña leen fa jiitu woon naka lañu mujje ? Ñoo leen ëppoon doole, daan jeqi suuf si, feesoon ko dell ak seeni njaboot. Seeni Yonnent indiloon leen ay kàddu yu leer. Yàlla tooñu leen, waaye ñoo tooñ séen bopp} [saaru Ar-Ruum: 9].
Te bàlluwaayi xam-xam yu wér ya tege ci xam-xam du wuute ak Lislaam, dananu ca tudd wenn niral woo xam ne Alxuraan tudd na ay faramfàcceem ca na mu gën a sewe lu jiitu Junni ak ñenti téemeeri at, ginaaw loolu ci la ko xam-xam yu yees yi diko door a indi, njuréefu xam-xam daa ñëw dëppook li nekk ci Alxuraan ju màgg ji, te mooy mbindiinu liir ci biiru yaayam, Yàlla mu kawe mi nee na: {Nun bind Nanu nit [sàkk ko]mu bawoo ci cosaanul ban [suuf](12) ginnaaw ba nu def ko mu di maniyu mu ne ci saxuwaay gu dëgër(13) Ginnaaw ba nu def maniyu ba mu di lumbu dereet, nu def lumbu ma di aw suux ; ginnaaw ba nu def suux wa mu di ay yax, daal di sànge yax ya aw yàpp. Daal di koy def jëmm,Yàllaa mën a baarkeel, Moom miy gën gi Bindkat!(14)} [saaru Al-Muuminuuna: 12-14].
40- te Yàlla du nangu jëf mbaau mucay fay yool ëllëg bis-penc lu dul ñeel ki gëm Yàlla di ko topp, te dëggal ay yonnenteem -yal na leen Yàlla dolli jàmm-, te Yàlla du nangu ci jaamu yi lu dul la mu yoonal, kon nakalaak nit ki weddi Yàlla ba noppi di mébét mu fay ko?! Te Yàlla du nangu gëmug kenn ci nit ñi lu dul bu gëmee yonnent yépp -yal na leen Yàlla dolli jàmm- daal di gëm yonnenteg Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc-.
Yàlla du nangu jëf mbaa mucay fay yool ëllëg bis-penc lu dul ñeel ki gëm Yàlla di ko topp, te dëggal ay yonnenteem -yal na leen Yàlla dolli jàmm- Yàlla mu kawe mi nee na: {Képp ku bëggul lu dul teraangay àddina, dananu gaaw ci jox ko ku nu soob, nu jox ko ci lunu neex, Topp nu def Sawara muy séndaluwaayam, di ku ñu yedd, ku ñu génne [ci yërmaandey Yàlla](18) Ku bëgg [teraangay] àllaaxira te mu jëf lu méngook moom, te muy ku gëm... ñooñu séeni jëf lu ñu gërëm lay doon(19} [saaru Al-Israa: 18-19]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Képp kuy jëf ca jëf yu yiw ya te muy ku gëm, deesul fakk jëfam te Nun Dananu ko ko bindal} [saaru Al-Anbiyaa: 94]. Yàlla du nangu ci jaamu yi ludul la mu yoonal, Yàlla mu kawe mi nee na: {képp ku yaakaar a dajeek Boroomam, nay jëf jëf yu yiw te bu mu bokkaale dara ak Boroomam} [saaru Al-Kahf: 110]. Mu leeral ne jëf du nekk lu yiw ludul mu bokk ca la Yàlla yoonal, boroomam sellal jëfam ngir Yàlla rekk, fekk ne ku gëm Yàlla la te dëggal ay yonnenteem -yal na leen Yàlla dolli jàmm-. Ndaal ku ay jëfam melul noonu nag Yàlla mu kawe mi wax na ne: {Nu fab jépp jëf ju ñu mësoon a jëf, def ko muy pënd bu ñu tasaare} [saaru Al-Furxaan: 23]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Bu keroogee, ay xarkanam danañu ragal lool(2) Yu daan jëf ba sonn te amul njariñ (3) Danañu dugg sawara su tàng(4)} [saaru Al-Xaasiya: 2-4]. Kanam yii dañoo ragal te sonnoon ci liggéey, waaye ginnaaw da doon sonn ci ludul njub gu bawoo fa Yàlla; moo tax Yàlla def mujjam di sawara; ndax jëfewul lu Yàlla yoonal, waaye da doon jaamu ci jaamu yu baaxul, daal di topp njiiti ñu sànku ña nga xam ne dañu leen di sosal ay diine yu baaxul. Kon jëf ju yiw ju Yàlla di nangu mooy ja dëppook li Yonnent bi indi. Kon naka la nit ki di weddi Yàlla ba noppi di mébét mu fay ko??
Yàlla du nangu gëmug kenn ci nit ñi lu dul bu gëmee yonnent yépp -yal na leen Yàlla dolli jàmm- daal di gëm yonnenteg Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc, kem ni ñu tude woon yenn tegtali yi ci xëtu limatu (20), Yàlla mu kawe mi nee na: {Yonnent bi gëm na li ñu wàcce ci moom mu bawoo ci Boroomam, jullit yi ñépp gëm nañu Yàlla ak i malaakaam ak i téereem ak i yonnenteem, du ñu teqale kenn ci yonnent yi, ñuy wax naan dégg nanu te topp nanu, noo ngi sàkku sa njéggal yaw sunu Boroom, te yaw rekk yaay delluwaay ba} [Saaru Al-Baqara: 285]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Éey yéen ñi gëm! Saxleen ci gëm Yàlla ak ub Yonnenteem, ak Téere ba Mu wàcce ci Yonnenteem, ak Téere ba Mu wàcce lu jiitu. Képp ku weddi Yàlla, ak i Malaakaam, ak Yonnenteem, ak Bis-pénc ba, réer na réer gu sori} [saaru An-Nisaa-i: 136]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Fàttalikul ba Yàlla kóllaranteek Yonnent ya : ba mu leen joxee Téere ak xam-xamu ràññee, [mu ne]: “Su leen ab Yonnent dikkalee buy dëggal li ngeen yor, na ngeen ko topp te dimbali ko.”. Mu ne leen [Moom Yàlla] : “Ndax nangu ngeen loolu ? Te jàpp ci loolu Sama kóllare?” - Ñu ne : “Nangu nanu”. Yàlla ne leen : “Seedeleen, Man Maa ngi ànd ak yéene bokk ca way-seede ya} [saaru Aali-Imraan: 81].
41-Jubluwaayu mbooleem bataaxali Yàlla yi mooy: diiney dëgg yëkkati nit ki ba mu nekk jaamu Yàlla miy Boroom mbindéef rekk, mu goreel ko ci jaamu nit mbaa am-am walla ay caaxaan. Kon Lislaam -niki nga ko gise- du sellal ay jëm ba di leen yëkkati lu kawe séen daraja, te du leen def mukk ay boroom mbaa ay Yàlla.
Jubluwaayu mbooleem bataaxeli Yàlla yi mooy: diiney dëgg yëkkati nit ki ba mu nekk jaamu Yàlla miy Boroom mbindéef rekk, te Lislaam day goreel nit ki ci jaamu am-am walla ay caaxaan, Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- nee na: « jaamukatu alal bi mooxam xaalis la mbaa ay yéré kooku de sonnu na, bu ñu ko joxee mu gërëm bu ñu ko joxul du gërëm» Sahiihul Buxaarii 6435. Nit ku jub du toroxlul ku dul Yàlla, alal du ko def jaam walla daraja walla wàccuwaay bu mu am, walla giir, nettali gii nag am na lumuy feeñalal aji-jàng ji ci la nit ña nekkoon lu jiitu yonnent ga, ak naka lañ mujjee ginnaawam?
Jullit ya njëkk ci Lislaam ba ñu gàddaayee dem Abasa buuru Abasa ca jamono yooya di Annajaasii da leen a laaj ne leen: «lan mooy diine jii tax ngeen tàqlikook séenuw nit, te dugguleen ci sama diine, mbaa diiney weneen xeet? Jahfar doomu Abuu Taalib da ne ko: Éey yaw buur bi nun danoo nekkoon ñoñ ceddo, nuy jaamuu ay xërëm, di lekk médd, di def ñaawtéef yi, di dog mbokk yi, ñuy ñaawal dëkkandoo, ku am kàttan ci nun not ka néew doole, nu nekk ca loola ba Yàlla yónni fi nun ab yonnent bu bokk ci nun, nu xam ko, xam askanam, ak dëggoom, ak kólluteem, ak fegoom. Mu woo nu ci Yàlla ngir nu wéetal ko jaamu ko te summeeku ci lépp lu nu daan jaamu nun ak sunuy baay. Mu digal nu wax ju dëggu ak matale kóllare, ak jokk mbokk, ak rafetal dëkkandoo, ak bàyyi yu araam yi, ak tuur dereet, mu tere nu ñaawtéef yi, ak wax lu bon, ak lekk alalu jirim, ak tuumaal jigéen ña seŋewu. Mu digal nu jaamu Yàlla dong te dunu ko bokkaaleek dara. Mu digal nu julli ak joxe asaka ak woor" nee na mu limal ko ay biri Lislaam. Nu dëggal ko gëm ko, nu topp ko ca la mu indi. Nuy jaamu Yàlla dong te bokkaalewunu ko ak dara. Nu araamal li mu araamal ci nun, nu daganal li mu daganal ci nun..." Ahmad génne na ko(1640) ak wuute bu ndaw, ak Abuu Nahiim ci ((Hilyatul Awliyaa))(1/115) cig tënk. Kon Lislaam niki nga ko gise du sellal ay jëm ba di leen yëkkati lu kawe séen daraja, te du leen def mukk ay boroom mbaa ay Yàlla. Yàlla mu kawe mi nee na: {Neel: “Yéen ñoñ-téere yi, kaayleen ci baat boo xam ne yéen ak nun noo ciy yam kepp: dunu jaamu ku dul Yàlla, te nu ko bokkaaleek dara, te kenn ci nun bañ jël moroomam jàppe ko Yàlla, di ko jaamu wolif Yàlla”. Su ñu bañee ba dummóoyu, neeleen : “Seedeleen ne nun déy ay jullit lanu} [saaru Aali-Imraan: 64]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Te du leen digal ngeen jàppe Malaaka ya ak Yonnent ya ay yàlla. Moo ndax da leen di digal ag kéefar ginnaaw bi ngeen nekkee ay jullit?} [saaru Aali-Imraan: 80]. Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «buleen ma jay ni Nasraan yi jaye Iisaa doomu Maryama, man jaamam kepp laa, waxleen jaamub Yálla ak ndawam li» Sahiihul Buxaarii 3445.
42- Yàlla dafa yoonal tuub ci Lislaam te mooy: nit ki dellu ci Boroomam bàyyi bàkkaar yi. Te Lislaam day màbb li ko jiitu ci bàkkaar, te tuub day dindi bàkkaar ya ko jiitu woon, kon aajowoowul di nàngu say bàkkaar ci kanamu nit.
Yàlla dafa yoonal tuub ci Lislaam te mooy: nit ki dellu ci Boroomam bàyyi bàkkaar yi, Yàlla mu kawe mi nee na: {Na ngeen tuub jëm ci Yàlla yéen way-gëm ñépp ndax ngeen texe} [saaru An-Nuur: 31]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Moo ndax dañoo xamul ne Yàlla Moom Dana nangu tuub ciy jaamam, te Dana jël it sarax ya, te Moom Yàlla Mooy Nanguwaakoon cig tuub, di yërëmaakoon ba} [saaru At-Tawba: 104]. Yàlla mu kawe mi nee na: {Moom mooy kiy nangu tuub ci jaamam ñi, tey jéggale ñaawtéef yi tey xam li ngeen di def} [saaru As-Suuraa: 25] Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- nee na: "Yàlla moo gën a bég ci tuubu jaamam bi gëm, ci waa ju nekk ci suuf su yaatu tey alage, mu yor waruwaayam teg lekkam ak naanam ca kawam, mu nelaw ba yeewu fekk mu rëcc, mu wër ko ba mar, wax ne: naa dellu ca sama barab ba ma doon nelawe, ba keroog ma fay deewe. Mu teg boppam ci kaw përëgam di xaar dee, ba mu yeewoo rekk gis waruwaayam wa ci wetam, yóbbalam ba nekk ca kawam ak lekkam ak naanam. Yàlla nag moo gën a tarug mbegte ci waa jii jotaat waruwaayam ak yóbbalam" Sahiihu Muslim 2744.
Lislaam day màbb li ko jiitu ci bàkkaar, te tuub day dindi bàkkaar ya ko jiitu woon, Yàlla mu kawe mi nee na: {Waxal yéefar yi, ne leen : “Bu ngeen bàyyee, nu baal leen la weesu. Waaye bu ngeen delluwaatee [ca la ngeen nekkoon], dees na leen mbugal kem ni mu daan ame bu njëkk} [saaru Al-Anfaal: 38]. Yàlla woona Nasaraan yi ci tuub, mu wax ne: {Moo ndax duñu tuub jëm ci Yàlla te jéggalu ko, Yàlla Aji-Jéggale la yërëmaakoon la} [saaru Al-Maa-ida: 74]. Yàlla xemmeemloona moykat yi ak defkati bàkkaar yi ci tuub, mu wax ne: {Waxal ne : “Éey yéen Sama jaam ñi yàq seen bopp ci def bàkkaar, buleen naagu ci yërmandey Yàlla. Ndax Yàlla dana jégale bakkaar yépp. Mooy Jégëlaakoon ba, di yërëmaakoon ba”} [saaru Ar-Ruum: 53]. Ba Amru ibnul Haas dogoo ci tuub dafa ragaloon ne deesu ko jéggal ay bàkkaram ya mu dëfoon njëkk Lislaam, Amru moo ngi nettali loolu di wax ne: (ba Yàlla mu màgg mi sànne Lislaam ci sama xol, mu ne: damaa ñëw ci Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- ngir mu jaayanteek man mu tàllal ma loxoom, ma ne ko: duma jaayanteek yaw Yonnent Yàlla bi ba keroog nga may jéggal li jiitu ci samay bàkkaar, nee na: Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- ne ko: yaw Amru xanaa xamoo ne gàddaay day dindi li ko jiitu ciy bàkkaar? Xanaa xamoo ne Lislaam day mabbu li ko jiitu ciy bàkkaar?) Muslim génne na ko(121) cig guddal, ak Ahmad (17827) te baat yi baatam la.
43- ci Lislaam dara doxul diggante nit ki ci jëflànteem ak Yàlla kon doo aajowoo kenn kuy sa diggante ak sa Boroom. Lislaam day tere ñu def nit ñi Yàlla walla ñu leen di bokkaaleek Yàlla, ci moomeelam, mbaa ci yàllaal ko.
Ci Lislaam aajowoowul nit ki di nangu ay njuumteem ci kanamu nit, ci Lislaam dara doxul diggante nit ki ci jëflaanteem ak Yàlla kon doo aajowoo kenn kuy dox sa diggante ak Yàlla. Kem ni mu jàlle woon ci xëtu limatu (36) ne Yàlla mu kawe mi dafa woo nit ñépp ci tuub ak dellu ci moom, naka noonu it dafa tere nit ñi ñuy jàppe yonnent yi ak maalaaka ti ñuy ñu ñuy doxale séen digganteek Yàlla ci jaamu gi, Yàlla mu kawe mi wax ne: {diga lu leen digal ngeen jàppe Malaaka ya ak Yonnent ya ay yàlla. Moo ndax da leen di digal ag kéefar ginnaaw bi ngeen nekkee ay jullit?} [saaru Aali-Imraan: 80]. Lislaam -niki nga ko gise- day tere ñu def nit ñi Yàlla walla ñu leen di bokkaaleek Yàlla, ci moomeelam, mbaa ci yàllaal ko, Yàlla mu kawe di wax ci Nasaraan yi ne: {Dañoo jàppe séen fóore ya ak séen làbbe ya, ak Iisaa doomi Maryama, ay yàlla, bàyyi Yàlla te digaleefu leen lu dul ñu jaamu Yàlla ja di kenn. Amul jeneen Yàlla ju ñu war a jaamu ju dul Moom ! Sellam ga jomb na li ñu Koy bokkaaleel} [saaru At-Tawba: 31]. Yàlla weddi yéefar ya ci ne ñoom dañuy wut ñu dox séen diggante ak Moom, Yàlla mu kawe mi wax ne : {Xanaa du Yàlla rekk a am diine ju sell? Ñay jaamu leneen lu dul moom tey (wax naan) : jaamuwu nu leen ludul ngir ñu jegeeele nu Yàlla”. Yàlla dana àtte séen diggante ci la ñu daan wuute. Yàlla du gindi fenkat bu man a weddi} [saaru As-Sumari: 3]. Yàlla leeral ne jaamukati xërëm ya -ñoñ ceddo ya- dañu doon wut ay diggale séen digganteek Yàlla, daan wax naan: yooya da leen di jégele Yàlla.
Bu Yàlla teree nit ñi di jàppe yonnent yi ak Malaaka yi ay digale ci digganteem ak i jaamam; kon keneen ku dul ñoom ñoo gën a yay ca tere ga. Naka la ma na nekke?! Te yonnent yi -yal na leen Yàlla dolli jàmm- dañuy njëkkante ci jegeñ-jegeñlu Yàlla, Yàlla mu kawe mi moo ngi xibaare melokaanu ña ñu sollo ak ña ñu yónni -yal na leen Yàlla dolli jàmm- mu wax ne : {Ñoom sax dañu daan njëkkante ci jëf yu yiw ya te ñoom daanañu nu jaamu, nekk cig xemmem ak ragal. Te nekkoon nañu diy way-toroxlu ci Nun} [saaru Al-Anbiyaa: 90]. Yàlla mu kawe mi nee na: ( ñooñu ngeen di ñaan ñoom ci seen bopp da ñuy góor-góorlu ci def lu baax ngir gën a jege Yàlla, ñuy yaakaar yërmàndeem di ragal mbugalam te sa mbugalum Boroom lu ñuy moytu la) [Saaru Al-Israa: 57]. Manaan ñooñu ngéen di jaamu wolif Yàlla - ci ay Yonnent ak ñu baax ñi- ñoom déy dañuy jegeñ-jegeñlu Yàlla di yaakaar yërmàndeem di ragal mbugëlam; kon naka la ñu leen di jaamoo bàyyi Yàlla?
44-ci mujjug baataaxal bii danañu fàttaliku ne nit ñi ànd ak séen jamono yu wuute ak séen i xeet ak séen i dëkkuwaay. Nekkiinu nit ki sax lépp a wuute, ci xalaat ak jubluwaayam ak i jëfam, kon moom manuta ñàkk ku koy gindi di ko jubal. Ak doxaliin wu koy peeg, ak àttekat bu koy aar. Yonnent yu tedd yi -yal na leen Yàlla dolli jàmm- dañu doon wuutuwante soloo googu mu joge ci Yàlla -tudd naa sellam ga- ñuy gindi nit ñi jëme leen ca yoon yiw ak njub, Ñu leen di boole ci tërëliinu Yàlla, di àtte séen diggante ci dëgg, tax séen biri àdduna jub ca kem na ñu wuyoo Yonnent yii, séen jamono jege bataaxeli Yàlla yi. Yàlla tëje bataaxel ya ci bataaxelu Yonnent bi Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- mu def ko muy luy des, di ag njub ñeel nit ñi. Di ag yërmaande ak leer ak ug gindee jëme ca yoon way eggale ca moom -tudd naa sellam ga-.
ci mujjug baataaxal bii danañu fàttaliku ne nit ñi ànd ak séen jamono yu wuute ak séen i xeet ak séen i dëkkuwaay. Nekkiinu nit ki sax lépp a wuute, ci xalaatam ak jubluwaayam ak i jëfam, Kon moom manut a ñàkk ku koy gindi di ko jubal. Ak doxaliin wu koy peeg, ak àttekat bu koy aar. Yonnent yu tedd yi -yal na leen Yàlla dolli jàmm- dañu doon wuutuwante soloo googu mu joge ci Yàlla -tudd naa sellam ga- ñuy gindi nit ñi jëme leen ca yoon ya di yiw ak njub. Ñu leen di boole ci tërëliinu Yàlla, di àtte séen diggante ci dëgg, tax séen biri àdduna jub ca kem na ñu wuyoo Yonnent yii, séen jamono jege bataaxeli Yàlla yi. Ba ag cànkute baree, reer gi matale, ñuy jaamu ay xërëm; ca la Yàlla yónne Yonnenteem ba di Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- cig njub ak diiney dëgg ngir mu génne nit ñi ci lëndëmi kéefar ak réer jëme ak jaamuy xërëm, jëme leen cig ngëm ak ug njub.
45- Looloo tax maa ngi lay woo yaw nit ki nga jug ngir Yàlla jug gu dëggu, gu mucc ci toppandoo, ak aada, Te nga xam ne ginnaaw boo deewee dangay dellu ca sa Boroom, Ak nga xool ci sa bopp ak ci gox yi la wër. Jébbalul kon danga texe ci sa àdduna ak sa àllaaxira, boo bëggee dugg ci Lislaam nag dara waru la lu dul nga seede ne amul kenn ku yayoo jaamu ku dul Yàlla ak seede ne Muhammat ndawu Yàlla la. Ak nga set wicc ci lépp lu ñuy jaamu te du Yàlla, Nga gëm ne Yàlla dana dekkil ña ca biir bàmmeel ya. Ak ne waññi ga ak fay ga dëgg la. Boo seedee yile seede kon nekk nga ab jullit, li war ci yaw ginnaaw loolu mooy nga jaamu Yàlla ca la mu yoonal ci julli ak joxe asaka ak woor, ak aj benn yoon boo ko manee.
Looloo tax maa ngi lay woo yaw nit ki nga jog ngir Yàlla jog gu dëggu, gu mucc ci toppandoo, ak aada, kem ni la Yàlla woowe ci waxam ji ne: {Waxal ne: maa ngi leen di waar ci lenn: nangeen taxaw ngir Yàlla, moo xam ngeen diy ñaar-ñaar walla ngeen di benn been, te ngeen xalaat. Séen àndandoo bii di Muhammad jinne saddu ko: moom doonul lu dul ab xuppekat ci mbugal mu tar ca kanam} [saaru Saba: 46]. Te nga xam ne ginnaaw boo deeyee dangay dellu ca sa Boroom, Yàlla mu kawe mi nee na: {li wér daal mooy, nit ki amul lu dul jëfam(39) Te dees na ko wan jëfam(40) Te dees na ka ko fay ba mu mat sëkk (41) Te ca sa Boroom la lépp di jeexe(42)} [saaru An-Najmu: 39-42]. Ak nga xool ci sa bopp ak ci gox yi la wër, Yàlla mu kawe mi nee na: {moo ndax dañoo xoolul ci nguuru asamaan yi ak suuf si, ak li Yàlla bind lépp, te it xay-na séen àpp jege na, kon jan wax lañuy gëm ginnaaw josam} [saaru Al-Ahraaf: 185].
Jébbalul kon danga texe ci sa àdduna ak sa àllaaxira, boo bëggee dugg ci Lislaam nag dara waru la lu dul nga seede ne amul kenn ku yayoo jaamu ku dul Yàlla ak seede ne Muhammat ndawu Yàlla la. Ba Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- yónnee Muhaas ca Yaman ngir mu woote ci Lislaam, da koo wax ne ko: «Yaw déy yaa ngi jëm ci aw nit ñoo xam ne ay ñoñ-téere lañu, nanga leen woo ci seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ak ne man Yonnenteb Yàlla laa, bu ñu la toppee ci loolu nanga leen xamal ne Yàlla farataal na ci ñoom juróomi julli ci bis bu nekk ak gudeem, bu ñu la toppee ci loolu nga xamal leen ne Yàlla farataal na ci ñoom asaka joj dees koy jële ci séeni way-woomal delloo ko séeni way-ñàkk, bu ñu la toppee ci loolu nag nanga moytu séen tedd-ngay alal ya» Sahiihu Muslim 19. Ak nga set wicc ci lépp lu ñuy jaamu te du Yàlla, te deñ ci lépp lu ñuy jaamu te du Yàlla mooy wéetal Yàlla di diiney Ibraahiima -yal na ko Yàlla dolli jàmm-, Yàlla mu kawe mi nee na: {am ngeen ci Ibraahiima ak ña mu andaloon royuwaay bu rafet, ba ñu waxee seenuw nit ne leen nun de deñ nanu ba set wecc ci yéen ag li ngeen di jaamu te du Yàlla, weddi nanu leen, te ag noonoo ak ug mbañeel dox na sunu diggante ba fàwwu, ba keroog ngeen di gëm Yàlla dong} [saaru Al-Mumtahina: 4]. Nga gëm ne Yàlla dana dekkil ña ca biir bàmmeel ya, Yàlla mu kawe mi nee na: {Loolu [lu wér la] ngir Yàlla mooy dëgg ga ; te Moom mooy dekkal ñi dee ; te Moom am na kàttan ci def lu ne(6) Te Bis-pénc ba amul sikk ne luy ñëw la, te Yàlla dana dekkal mboolem ñi nekk ci bàmmeel yi(7)} [saaru Al-Hajji: [6-7]. Ak ne waññi ga ak fay ga dëgg la, Yàlla mu kawe mi nee na: {Yàlla bind na asamaan yi ak suuf si ci dëgg ak it ngir mu fay bakkaan bu nekk ca la mu daan fàggu. Te kenn du leen tooñ} [saaru Al-Jaasiya: 22].
Boo seedee yile seede kon nekk nga ab jullit, li war ci yaw ginnaaw loolu mooy nga jaamu Yàlla ca la mu yoonal ci julli ak joxe asaka ak woor, ak aj benn yoon boo ko manee, ak yeneen yu dul yooyu.
Bindees na ko ci atum 1441-11-19.
Aji-bind ji: Jàngalekat ba di Doktoor Muhammat Doomu Abdul Laahi As-Suhaymii.
Jàngalekatu pas-pas la woon ca xaaju njàng ma aju ci Lislaam.
Xaajub Yarukaay ba, ca jàngu gu kawe ga ñuy woowe Malik Sahuud.
Riyaad, Araabi Sawdi.
Related books
All books
Li ab bataaxal bu tënku la jëm ci kiy weddi Yàlla61 languagesLi ab bataaxal bu tënku la jëm ci kiy weddi Yàlla
Lii ab bataaxal la bu ñu tënk jëmale ko ci kiy weddi Yàlla, muy wàqante ak xel mi ci ne sewug adduna bi ak nimu nosewoo day wane ne jekki-jekki wul rekk am, te day tegtale Aji-Bind ju Xereñ ji, te ndax dana xellu lii lépp bawoo ci lu amul? Kon ubbil sa xol bi ngir xalaat ak settantal, te nga gëstu dëgg, kon danga ci fekk ag leer gu lay gindi.
Lislaam mooy diiney Yonnente Yàlla yi85 languagesLislaam mooy diiney Yonnente Yàlla yi
Lislaam mooy jébbalul Yàlla mi bind àdduna bi di ko doxal, wommatul ko ngir bëgg ko ak màggal ko, cosaanu lislaam mooy gëm Yàlla, ak ne moom mooy Aji-Bind ji, te lépp lu dul moom mbindeef la, ak ne moom moo yayoo jaamu moom rekk amul bokkaale, amul lenn lu ñuy jaamu ci dëgg ku dul moom,ay tur yu rafet ñeel na ko ak ay melo yu kawe, mooy ki mat sëkk, jurul kenn te kenn juru ko te amul benn nawle du caagine niroowaale, du wàcc te du jël jëmmi lenn ci mbindeefam yi. Lislaam mooy diiney Yàlla mi nga xam ne du nangu ci nit jenn diine ju dul moom, te mooy diine ji yonnente yépp indi yal na leen…
الدروس المهمة لعامة الأمة78 languagesالمهمةالدروس المهمة لعامة الأمة
يهدف الكتاب إلى تعليم المسلمين أساسيات دينهم بطريقة مبسطة وشاملة. يتناول مجموعة من الدروس المهمة مثل قراءة الفاتحة وقصار السور، وأركان الإسلام والإيمان، وأقسام التوحيد والشرك، وشروط وأركان وواجبات الصلاة، بالإضافة إلى مبطلاتها، مع بيان مختصر لشروط الوضوء وفروضه ونواقضه. كما يسلط الضوء على التحلي بالأخلاق الإسلامية والآداب الشرعية، ويقدم إرشادات لطيفة حول تجهيز الميت والصلاة عليه ودفنه.
Ci turu Yàlla miy Aji-Yërëm képp ku nekk ci kaw suuf jagleel ko jullit ñi ca allaaxira ci laay tàmbalee.74 languagesCi turu Yàlla miy Aji-Yërëm képp ku nekk ci kaw suuf jagleel ko jullit ñi ca allaaxira ci laay tàmbalee.
Alxuraan ju tedd ji mooy waxi Yàlla miy Boroom mbindéef yi moom mi leen bind, Yàlla wácce na ko ci ki mujj ca ña ñu yonni Kooku mooy Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- ngir mu leeralal mbindéef li tax ñu sàkk leen, ak ngir mu gindi leen jëme leen ca séenug texe ci àdduna ak ca allaaxira, ak ngir mu musël leen cig texeedi guy sax ba fàwwu gannaaw dee. Te moom Alxuraan moo mujj ci téere yi Yàlla wàcce, di leen dëggal te di nasaxal séeniy tërëliin. Alxuraan nag keemaan la guy lott loo ba fàwwu, te tektal la ci ne Muhammat Yonente Yàlla la. Yàlla dëkk na nit ñi ak jinne yi ci ñu indi…