Teggini tukki ak i àtteem
Sant ñeel na Yàlla miy Boroom mbindeef yi, xéewal ak jàmm yal na nekk ci sunu Yonnente bi Muhammat ak ay ñoñam,ak àndandoom yépp. Ginnaaw loolu: Lii ab bataaxel la bu ñu tënk ci teggiini tukki ak i àtteem, bëgg nanoo leeral li ëpp ci li aji-tukki ji di aajowoo. Yàlla rekk lanuy ñaan mu def ko muy lu sell ñeel jëmmam ju Tedd ji, ak mu jariñ ci mbooleem jullit ñi. Bi ci jëkk: teggiini tukki
Teggini tukki ak i àtteem Sant ñeel na Yàlla miy Boroom mbindeef yi, xéewal ak jàmm yal na nekk ci sunu Yonnente bi Muhammat ak ay ñoñam,ak àndandoom yépp.
Ginnaaw loolu:
Lii ab bataaxel la bu ñu tënk ci teggiini tukki ak i àtteem, bëgg nanoo leeral li ëpp ci li aji-tukki ji di aajowoo.
Yàlla rekk lanuy ñaan mu def ko muy lu sell ñeel jëmmam ju Tedd ji, ak mu jariñ ci mbooleem jullit ñi.
Kuréelug caytu gi ci mbootaay giy def ay liggéey yu làmboo lislaam ñu tekki ko ci làkk yi.
Bi ci jëkk: teggiini tukki
Jaadu na ci aji-tukki ji ngir Aj walla ngir leneen ci jaamu Yàlla yi mu sonne yii di ñëw:
1. Mu tànnloo Yàlla mu Sell mi ca waxtu wa, ak waruwaay ba, ak àndandoo ya, ak wan yoon lay jublu bu dee yoon yi dafa bari, ak mu diisoo ci loolu ak ña ca xam dara ak ñu baax ña, bu dee Aj nag ak Umra; ñoom ay yiw lañu ci lu amul sikk-sàkka, melow listixaar nag: mooy mu julli ñaari ràkka topp mu ñaan ci li rot jóge ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
2. War na ci kiy aj ak kiy Humra mu jublu ci ajam gi ak umraam gi jëmmi Yàlla mu kawe mi, ak jegeñlu jëm ci moom, ak mu moytu a jublu poñeti àdduna walla puukareente walla am aw tur walla ngistal ak ndéggtal; ndax loolu sabab la ci yàq jëf ak ñu bañ ko a nangu, Yàlla mu kawe mi nee na: {Waxal ne : man nit laa ni yéen, waaye dañu may soloo, xam leen ne Kiy seen Yàlla ngeen war ko a jaamu kenn la, kon nag képp ku yaakaar a daje ak Boroomam, nay jëf jëf yu yiw, te bu mu bokkaale Yàlla ak kenn} [Al-Kahf : 110]. Nekk na ci haddisu Al-Xudsii: "ñi ñuy boole ak ñeneen ñépp maa ci gën a doyal ci ñu may bokkaale, képp ku jëf jenn jëf boole ma ca ak keneen ma bàyyi ko ak ug bokkaaleem"[1]. [1] Muslim soloo na ko, ci limatu: (2985).
3. War na ci kiy aj ak kiy umra mu xam àttey umra ak aj, ak àttey tukki jëkk muy tukki; ngir mu bañ a bàyyi lu war walla muy tàbbi ci lu araam, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "ku Yàlla namm ci moom yiw dana ko déggloo diine ji" [2]. [2] Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (3116), ak Muslim, ci limatu (100).
[4]. War na ci kiy aj walla ci kiy umra mu tànn alal ju dagan ñeel ajam gi ak umraam gi; ndaxte Yàlla ku teey la te du nangu lu dul lu teey; ak it ne alal ju araam sabab la ci ñàkk a nangu ñaan.
5. Tuub ci mbooleem bàkkaar yi ak moy yi, bu dee daa ameel nit ñi ay tooñaange mu delloo leen seen i àq, mucc ca tooñaange yooya, moo xam: ci der la walla alal, walla leneen lu dul loolu.
6. Sopp nañu ci aji-tukki ji mu bind ndénkaaneem, ak li ko ñeel ak li ko war, Yónnent bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "Yellul ci jullit bi am lu mu namm a dénkaane muy fanaan ñaari guddi lu dul ne ndénkaaneem ma nga fa moom mu bind" [3]. Wut seede ca ndénkaan la, fay li ko war ci ay bor, delloo dénkaan ya ca seeni boroom walla mu sàkku seen ndigal ci mu des ci moom. [3] Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (2738), ak Muslim, ci limatu (1627).
7. Sopp nañu ci aji-tukki ji mu farlu ci tànn àndandoo bu baax, ak xér ci mu bokk ci sàkkukati xam-xamu Sariiha yi; ndaxte lii dafa bokk ci sabab yi koy dëppale ak njub di ko musal ci tàbbi ci ay njuumte ci tukkeem ak ci Ajam ak Umraam; ndax li Yónnent bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax ne: "Nit ki moo ngi ci diiney xaritam, na ku nekk xool kan lay xaritool" [4]; Ak ngir waxam ji yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: "bul ànd ak ku dul aji-gëm te ku dul aji-ragal Yàlla bu mu lekk saw ñam" [5]. [4] Abuu Daawuda moo ko soloo, ci limatu (4833). [5] Abuu Daawuda soloo na ko, ci limatu(4832), ak At-Tirmisii, ci limatu (2395).
8. Sopp nañu ci aji-tukki ji mu tàggu njabootam, ak ay jegeñaaleem, ak i dëkkandoom, ak i àndandoom, Yónnent bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "kuy tukki na wax ñi muy bàyyi ginnaaw: maa ngi leen di dénk Yàlla mi nga xam ne ndénkaaneem du sànku" [6], Yónnent bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na tàggatoo ak i Saabaam bu kenn ci ñoom bëggaan a tukki, di wax: "Maa ngi dénk Yàlla sa Diine ak li nga bàyyi ginnaaw ak mujjug say jëf" [7], Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na wax képp ku masaa sàkku ci moom ndénkaan ci way-tukki yi : "yal na la Yàlla defal yóbbalu ragal Yàlla, jéggal la say bàkkaar, jàppandalal la yiw foo man di nekk" [8] Jenn waay ñëw na ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bëgg a tukki ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi dénk ma, mu ne ko: "maa ngi lay dénk ragal Yàlla ak di kàbbar ci wépp tund", ba mu wéyee mu wax ne: "yaw sama Boroom yal na nga ko taxañalal suuf si yombalal ko tukki bi" [9]. [6] At-Tabaraanii soloo na ko, ci limatu (823). [7] Ahmad soloo na ko ci Musnadam, ci limatu, (4524). [8] At-Tirmisii soloo na ko, ci limatu (3444). [9] Ahmad soloo na ko ci Musnadam, ci limatu (9724).
9. Bumu ànd ak moom ci tukki bi jóolooli, ak ay mbiib; ngir hadiisu Abuu Hurayrata bi yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yónnent bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "malaaka yi duñu ànd ci mbooloo mu ànd ak ub xaj walla ab jóolooli" [10]. [10] Muslim soloo na ko, ci limatu: (2113).
10. Bu bëggee tukki ak kenn ci ay jabaram bu dee ëpp nañu kenn day tegoo bant seen diggante, sox na su tegoo bant bi dal ci moom mooy génn ànd ak moom; ngir hadiisu Aysatu bi yal na ko Yàlla dollee gërëm nee na: "Yónnent Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan bëgg a tukki day tegoo bant ci diggante soxnaam yi, ku ab tegam génn rekk mu ànd moom" [11]. [11] Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (2593), ak Muslim, ci limatu (2770).
11. Sopp nañu ci moom mu génn jëm ci tukki bi bisub Alxamis ci njëlbeenu bëccëg gi bu dee loolu jàppandi na ko; ndax li ko Yónnent bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc doon def. Kahbu ibn Maalik yal na ko Yàlla dollee gërëm nee na: "néewaa na lool lu Yónnent Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan génn bu daa génn ci ab tukki lu dul bisub Alxamis" [12]. [12] Al-Buxaarii soloo na ko cu limatu (2949).
12. Sopp nañu ci moom mu ñaan ñaanug booy génn ci kër gi ngir tukki ak yeneeni ñaan, mu wax bu dee génn: "Bismil Laahi, tawakkaltu halal Laahi, laa hawla walaa quwwata illaa bil-Laahi, Allaahumma innii ahuuzu bika an adilla aw udalla, aw azilla aw uzalla, aw aslima aw uslama, aw ajhala aw yujhala halayya" [13]. [13] Abuu Daawuda moo ko soloo, ci limatu (5094).
13. Sopp nañu ci moom mu ñaan ñaanug tuki buy yéeg ci daabaam, walla wataam, walla fafalnaaw, walla beneen waruwaay, mu wax: "Allaahu akbaru, Allaahu akbaru, Allaahu akbaru, topp mu wax: {Subhaanal Lasii saxara lanaa haasaa wa maa kunnaa lahuu muqriniina wa innaa ilaa Rabbinaa la munqalibuuna} [Assuxrufi: 14] Allahumma innaa nas-aluka fii safarinaa haasaa al birra wattaqwaa wa minal hãmali maa tardaa, Allaahumma hawwin hãlaynaa assafara, watwi hãnnaa buhdahuu, Allaahumma Antas Saahibu fissafari, wal Xaliifatu fil-ahli, Allaahumma, innii ahuusu bika min wahsaa-is safari, wa ka-aabatil mansari, wa suu-il munqalabi, filmaali wal-ahli..." [17]. [14] Wahsaa-u assafari: mooy tar-tari tukki gi. Al-Ifsaahu Han Mahaani Assihaahi (4/284). [15] Ñaawug melo ak ug doyadi ngir njàqare. Al-Ifsaahu Han Mahaani Assihaahi (4/282). [16] (Al-Munqalab): mooy dellu gu ñaaw. Al-Ifsaahu Han Mahaani Assihaahi (4/284). [17] Ahmad soloo na ko ci Musnadam, ci limatu (6374).
14. Sopp nañu ci moom mu bañ a tukki moom dong ci lu dul àndandoo; ngir waxu Yónnent bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: "bu nit ñi xamoon li nekk ci wéetaay li ma ci xam kon jenn aji-war du dox ag guddi moom dong" [18]. [18] Al-Buxaarii soloo na ko, ci limatu (2998).
15. Way-tukki yi dañuy jiital kenn ci ñoom; ngir mu gën a dajale seenug booloo, gën leen a dëppale, ak gën leen a dëgëral ci ñu am la ñu doon wut, Yónnent bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "bu ñatt andee ci ab tukki nañu jiital kenn ci ñoom" [19]. [19] Abuu Daawuda moo ko soloo, ci limatu (2608).
16. Mu xér ci taxawe li Yàlla waral ci moom ci ay topp ak moytandiku yi ñu araamal, ak mu jikkowoo jikkoy ngëneel yi, di dimbali aji-aajowoo ndimbal ak ku ko jàppale, di joxe xam-xam ñeel aji-sàkku ji, ak ka ko aajowoo, ak mu nekk ku tabe ci alalam, di ko def ci luy yéwénal boppam ak di yéwénal bokkam yi ak seen i aajo.
17. Jaadu na it muy baril yóbbal ak aajoy tukki bi, ndaxte amaana aajo gaar ba bir ya faf jaxasoo.
18. Jaadu na mu nekk ci loolu lépp di ku bélli xar kanam, di ku lewet, di ku xér ci dugal mbégte ci ay àndandoom; ngir mu nekk di aji-miin di it ku ñu miin.
19. Jaadu na mu muñ béccingali ay àndandoom ak seen i wuute ak gisiinam, muy maslaa ak ñoom ca na mu gën a rafete, ngir mu nekk ku ñu wormaal ci seen diggante, di ku ñu màggal ci seen bopp.
20. Sopp nañu bu tukkikat yi wàccee ci ab wàccuwaay ñu dajaloo, ndax Saabay Yónnent bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu ñu daan wàcc ci ab wàccuwaay dañu daan tasaaroo ci mbedd yi ak ci xur yi, Yónnent bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne leen: "seen tasaaroo gii ci mbedd yi ak ci xur yi Saytaane kepp moo leen tasaare" [20], Ginnaaw loolu nag ñu mujj di dajaloo ba bu ñu tàllaloon ci seen kaw ab yére mu yaa leen. [20] Ahmad soloo na ko ci Musnadam, ci limatu (17736).
21. Sopp nañu bu wàccee ci ab wàccuwaay ci tukki bi walla ci lu dul tukki mu ñaan ci li sax jóge ci Yónnent bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: "Ahuusu bikalimaatil Laahit Taammaati min sarri maa xalaqa" [21]; Moom de bu waxee loolu dara du ko lor ba ba muy jóge ca wàccuwaay boobu. [21] Muslim soloo na ko, ci limatu: (2708).
22. Sopp nañu ci moom muy kàbbar ci warab yu kawe yi, ak di sàbbaal bu wàccee fu suufe ak xur yi, Jaabir yal na ko Yàlla dollee gërëm nee na: "nun de bu nu daan yéeg danuy kàbbar, bu nuy wàcc daal di sàbbaal Yàlla" [22], Te bu nu yëkkëti seen kàddu yi ca kàbbar ga, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na : "yéen nit ñi yërëmleen seen bopp; woowuleen aji-tëx du caagine aji-fàddu, moom mi ngi ànd ak yéen, te moom Aji-Dégg la Aji-Jege la" [23]. [22] Al-Buxaarii soloo na ko ci limatu (2994). [23] Al-Buxaarii soloo na ko ci limatu (2993).
23. Sopp nañu ci moom buy tukki mu dem ci guddi gi rawati na ci njëlbeen gi; ngir waxu Yónnent bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: "dénk naa leen guddi; ndax suuf si dañu koy lem ci guddi gi" [24]. [24] Abuu Daawuda moo ko soloo, ci limatu (2571).
24. Sopp nañu ci moom muy bari ay ñaan ci tukki bi; ngir waxi Yónnent bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: "ñatti ñaan yii yu ñuy nangu la amul sikk-sàkka: ñaanug ku ñu tooñ, ak ñaanu aji-tukki ji ak ñaanug way-jur ci doomam" [25]. [25] Ahmad soloo na ko ci Musnadam, ci limatu (10771).
***
Ñaareel bi: laab ci tukki gi
War na ci aji-tukki ji mu sonnee ag laabam, muy jàppu ci toj mu ndaw, ak sangu janaba.
Bu amul ndox, walla mu am ndox mu tuuti mu mu aajowoo ci lekkam ak naanam, kon day tiim.
Melow tiim: mooy mu dóor ñaari loxoom ci kaw suuf daal di cay masaa kanamam ak ñaari ténqam
Laabug tiim nag laab gu ñu wutal àpp la, saa bu amee ndox day yàqu te day war mu jëfandikoo ndox ma, bu tiimee ngir janaba topp mu am ndox kon day war ci moom mu sangu, bu tiimee ngir xayta topp mu am ndox day war ci moom mu jàppu. Ñëw na ci hadiis: "pàkk bu laab mooy njàppum jullit doonte amul ndox fukki at, bu amee ndox nag na ragal Yàlla te laalale ko deram bi" [26]. [26] Al-Bassaar moo ko soloo ci Musnadam, ci limatu(10068).
Masaa ci kaw ñaari saŋ lu ñu yoonal la ci Alquraan ak Sunna ak dëppoog waa-Sunna.
Dees na sàrtal ci masaa ci ay saŋ ak lu mel ni moom ay sàrt:
1. Ñaari saŋ yi walla ñaari kawas yi di yu dagan te laab.
2. Mu sol leen ci ag laab.
3. Ñu muur li mu waroon a raxas ci tànkam buy jàpp.
4. Masaa gi nekk ci toj mu ndaw, masaa du dagan ci janaba du caagine ci luy waral sangu.
5. Masaa gi nekk ca waxtu wa ñu ko tënk ci Sariiha te mooy benn bis ak guddi gi ñeel ki tukkiwul, ak ñatti fan ak seen i guddi ñeel aji-tukki ji, te diir bi ca la gën a wér day tàmbalee ca masaa bu njëkk ba ginnaaw tojle ga, di jeexe ci ñaar-fukk ak ñenti waxtu ñeel ki tukkiwul, ak juróom-ñaar-fukk ak ñaari waxtu ñeel aji-tukki ji.
Benn ci ñatti bir yii dana yàq masaa ga ca saŋ ya:
1. Bu luy waral sangu amee niki janaba masaa ga yàqu na te fàww daa war a sangu.
2. Bu leen summee ginnaaw ba mu masaawee ca seen kaw.
3. Bu diir ba ñu jàpp ci Sariiha jeexee kon masaa gi yàqu na.
***
Ñatteel bi: àttey wàññi julli ci tukki:
Wàññi ci tukki moo gën matal; waaye aji-tukki ji bu matalee jullig ñenti rakka it julleem gi wér na waaye juuyoo na ak la gën.
Aji-tukki ji day wàññi bu génnee mbooleem këri goxam (dakku-àll) walla dëkkam (taax), lii mooy ngiru ñi ëpp ci woroom xam-xam yi.
Bu tukkee ginnaaw bi waxtuw julli wi duggee wàññi ñeel na ko; ndaxte tukki na njëkk waxtu wi di génn.
Bu dee boole diggante tisbaar ak tàkkusaan nag, ak diggante timis ak gee, loolu sunna la ñeel aji-tukki ji bu ko aajowoo, bu dee dox ba da koo gëtën ci tukki bi ñu wéy di dem rekk, na def la gën woyof ci moom ci booleg jiital walla booleg yeexe.
Bu dee aji-tukki ji aajowoowul boole kon du boole, niki mu wàcc ci berab bob bëggu fa a jóge lu dul ginnaaw bu waxtuw jullig ñaareel ga duggee, kon la gën a yey mooy bañ a boole; ndaxte aajowoowu ko, loolu moo tax Yónnent bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc boolewul ba mu wàcce ca Minaa ca ajug tàggatoo ga; ndax li mu ko aajowoowul.
Bu dee jullig coobarewu nag, aji-tukki ji day coobarewu niki ni ki tukkiwul di coobarewoo, di julli jullig yoor-yoor ak taxaw guddi ak witar ak yeneeni naafila lu dul raatibi tisbaar ak timis ak gee lay sunna mooy mu bañ ko a julli.
Coobarewu dagan na ci aji-war ji nekk ci tukki: ci abiyoŋ, ak wata, ak gaal, ak yeneen jumtukaayi tuxu yi, bu dee farata nag fàww mu wàcc lu dul mu tële ko.
Jullig aji-tukki ji ci ginnaaw ki tukkiwul lu wér la, waaye aji-tukki ji day matal niki jullig imaamam, moo xam fekke na julli gi yépp, walla benn ràkkaa la ca fekke, walla lu ko gën a néew, doonte sax dafa dugg ak moom ca taaya ju mujj ja njëkk sëlmël gi kon day matal, te lii mooy li wér ci ñaari waxi woroom xam-xam yi.
***
Ñenteel bi: teggini dellu jóge ca aj ga ak umra ga ak tukki ba.
Jaadu na mu gaaw a dellu te bañ a guddal sax ga ca tukki ba ci lu dul aajo; ngir waxi Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: "tukki dogiitu mbugal la, day tere kenn ci yéen lekkam ak naanam, ak nelawam, kon bu fajee soxlaam na gaaw a dellu ca njabootam" [27]. [27] Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (1804), ak Muslim, ci limatu (1927).
Bu nammee dellu ca dëkkam day jàng ñaanug tukki bu yéegee ca waruwaayam, teg ca: "Aayibuuna, taa-ibuuna, hãabiduuna, li Rabbinaa haamiduuna" [28]. [28] Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (1797), ak Muslim, ci limatu (1342).
Sopp nañu ci moom bu wañeeku jóge ca tukki ba mu wax li sax jóge ci Yónnent bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, ci ne bu daan jóge ci xare, walla aj, walla umra, day kàbbar ci fépp fu yékkatiku ci suuf ñatti kàbbar topp mu wax: "laa ilaaha illal-Laahu Wahdahuu laa sariika Lahu, Lahul mulku wa Lahul hamdu wa Huwa halaa Kulli say-in qadiirun, Aayibuuna, taa-ibuuna, hãabiduuna, saajiduuna, li Rabbinaa haamiduuna, sadaqal Laahu wahdahuu, wa nasara hãbdahuu, wa hasamal ahsaaba Wahdahu" [29]. [29] Al-Buxaarii soloo na ko ci limatu (4116).
Sopp nañu ci moom bu gisee dëkkam mu wax: "Aayibuuna, taa-ibuuna, hãabiduuna, li Rabbinaa haamiduuna" [30], Day baamtu loolu ba keroog muy dugg dëkkam; ngir li ko Yónnent bi def yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc. [30] Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (1797), ak Muslim, ci limatu (1342).
Bu mu ñëw ci njabootam ag guddi bu dee tukkeem bi dafa yàgg ci lu dul aajo lu dul bu leen yégalee loolu, xamal leen ne day ñëw guddi; ndax li ko Yónnent bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc aaye, Jaabir ibn Abdullah yal na leen Yàlla dollee gërëm nee na: "Yónnent bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tere na góor gi di fëgg ag njaabotam guddi" [31], Bokk na ci xereñte gi nekk ci loolu, li geneenug nettali leeral ne: "ndax jigéen gi kawaram jaxasoo man a jàrtu[32], ki jëkkëram fàddu wat kawaram yi mu war a wat" [33], Ñëw na ci beneen nettali: "Yónnent bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tere na góor gi fëgg njabootam ag guddi ngir foog seenug wor, walla muy luññutu seen i pakk-pakk" [34]. [31] Muslim soloo na ko, ci limatu: (715). [32] (jaxasoog kawar gi): mooy jigéen gi gëj a diw ak jàrt kawaram, (wat): mooy jëfandikoo weñ, (aji-fàddule ji): mooy jigéen gi jëkkëram fàddu. Attahriir Fii Sarhi Sahiihi Muslim - Al-Asbahaanii (xëtu 292). [33] An-Nasaaiyyu moo ko soloo, ci limatu (9099). [34] Muslim soloo na ko, ci limatu: (715).
Sopp nañu ci ki jóge ci tukki mu jëkke ca jàkka ja nekk ca wetam julli fa ñaari ràkkaa; ngir li ko Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan def.
Sopp nañu ci aji-tukki ji bu jógee ca tukki ba muy ñeewant xale yi ci njabootam ak i dëkkandoom di rafetal jëme ci ñoom bu ñu ko gatandoo, jële nañu ci Ibn Abbaas yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: bi Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñëwee Màkka xaley doomi Abdul Muttalib yi dañu ko a tertu, mu gàddu kenn ci kanamam ak keneen ci ginnaawam. Abdullah ibn Jahfar yal na ko Yàlla dollee gërëm nee na: "Yónnent bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan jóge ci tukki day gatandoonte ak nun, nee na: man ak Al-Hasan walla Al-Husayn, nee na: mu fob kenn ci nun boot keneen ki ba nu dugg Madina" [35]. [35] Muslim soloo na ko, ci limatu: (2428).
Sopp nañu it Àddiya, ngir li ci nekk ci teeyal xol yi ak dindi mbañeel, sopp nañu it nangu ko, ak faye ca, waaye sib nañu delloo ko ci lu dul ngàntal Sariiha; lii moo tax Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax ne: "deeleen joxante Àddiya kon dangeen bëggante" [36]. Àddiya sabab la ci sabab yiy waral bëggante ci diggante jullit ñi. [36] Al-Bayhaqii soloo na ko ci Assunanu Alkubraa, ci limatu(11946).
Aji-tukki ji bu delloo dëkkam sopp nañu tegante ay doq; ngir li mu sax jóge ci Sahaabay Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, kem ni ko Anas yal na ko Yàlla dollee gërëm waxe: "ñoom de bu ñu daan daje dañuy saafoonte, waaye bu ñu daan jóge ci tukki dañuy fóoonante ak seeni doq" [37]. [37] At-Tabaraanii soloo na ko ci Al-Awsat, ci limatu (97).
Yal na Yàlla dolli xéewal ak mucc sunu Yónnent ba Muhammat.