Skip to content

«malaaka yi duñu ànd ci mbooloo mu ànd akub xaj walla ab jóolooli.

Jële nañu ci Abuu Hurayrata-yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu jële ci Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

«malaaka yi duñu ànd ci mbooloo mu ànd akub xaj walla ab jóolooli.

«لَا تَصْحَبُ الْمَلَائِكَةُ رُفْقَةً فِيهَا كَلْبٌ وَلَا جَرَسٌ».

Muslim soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-day xibaare ne malaaka yi duñu ànd ci tukki boo xam ne ab xaj da caa ànd, walla ab jóolooli li gu ñu lonk ci daaba yi bu yëngatoo di génne kàddu.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Tere nañu yar xaj ak di ànd ak moom, danañu settee ci tere gi xaj buy rëbb ak buy wattu (garde).

Malaaka yidul ànd ca loola mooy malaakay yërmànde,bu dee malaaka yiy wattu nit ki ñoom moom duñu teqalikoo ak jaam ñi ci seen ug toog ak ci seen ug tukki.

tere nañu ag kalaksone; Ndax benn la ci mbiibi Seytaane yi, te dafay niróo ak kolos yu nasaraan yi.

War na ci jullit bi mu xér ci sori lépp luy tax malaaka yi sori ko.

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér (3/ 1672) (2113).

Yataal gi (11)

نزهة المتقين.

لمجموعة من الباحثين (2/ 1156).

كنوز رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (20/ 67).

بهجة الناظرين.

لسليم الهلالي (3/ 188).

كشف المشكل من حديث الصحيحين.

لابن عثيمين (3/ 564).

شرح رياض الصالحين.

لابن عثيمين (6/ 431).

شرح النووي على مسلم (14/ 95).