Al-Buxaarii soloo na ko (1189) ak Muslim (827) te baat yi moom la ñeel,
Al-Buxaarii soloo na ko (1190) ak Muslim (1394).
Al-Buxaarii soloo na ko (1195) ak Muslim (1390),
Sant ñeel na Yàlla miy Boroom mbindeef yi, xéewal ak jàmm yal na nekk ci sunu Yonnente bi Muhammat ak ay ñoñam,ak àndandoom yépp.
Ginnaaw loolu:
Lii ab bataaxal bu ñu tënk la ci teggini siyaare jàkkay Yonnente bi ak i àtteem,xér nanu ci lool ci leeral li ëpp ci li kiy siyaare jàkkay Yonnente bi di aajowoo.
Yàlla rekk lanuy ñaan mu def ko muy lu sell ñeel jëmmam ju Tedd ji, ak mu jariñ ci mbooleem jullit ñi.
Al-Lajnatu Al-Hilmiyyatu Bi Jamhiyati Al-Muhtawaa Al-Islaamii Bil-Luxaati.
Tënk bi.
Sopp nañu siyaare jàkkay Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, amul nag waxtu wu ñu ko tënk, te bokkul ci jëfi aj gi,te du lu war ajkat yi-moo xam ay góor lañu walla ay jigéen-ñu siyaare ji bàmmeelu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, du caagine it Al-Baxiih.
Du dagan ñuy takk ab tukki ngir siyaare bàmmeelu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, ndaxte takk ab tukki ci anamug jaamu du nekk ci siyaare bàmmeel, waaye ci siyaare ñatti jàkka yi doŋ lay nekk,Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:(deesul takk ab tukki lu dul jëm ci ñatti jàkka: sama jàkka jii, ak jàkka ja ñu wormaal (jàkkay Màkka), ak jàkkay Al-Aqsaa)
Ki sori Madina waruta tukki ngir jublu a siyaare bàmmeel, waaye yoonal nañu ci moom mu takk gawar ngir jublu a siyaare jàkkay Yonnente bu tedd bi,bu fa eggee mu daal di siyaare bàmmeelu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak bàmmeeli sahaabaam yi, siyaare bàmmeelam bi day topp siyaare gi mu siyaare jàkkaam ji.
Yoonaluñu ci jigéen muy siyaare bàmmeelu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc du caagine bàmmeelu keneen; ndaxte Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa rëbb jigéen ñiy siyaare ay bàmmeel, kon nañuy julli ci Yonnente bi ak lu bari, ci jàkka ak fu dul jàkka, bu ko defee loolu dina egg ci Yonnente bi ak barab bu mu man di nekk; ngir li Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax ne:(buleen def seen kër yi ay bàmmeel,te buleen def ci sama bàmmeel ab xew-xew,deeleen julli ci man ndax seenug julli ci man dina yeksi fi man ak fu ngeen man di nekk),Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax ne:(Yàlla am na ay malaaka yuy wër ci suuf si di ma jottali ci nuyóow sama xeet wi).
Buy dugg ci jàkkay Yonnente bi sopp nañu ci moom mu jiital tànku ndayjooram bu dee dugg, mu wax:(Allaahuma iftah lii abwaaba rahmatika) kem ni muy waxe loolu ci budee dugg yeneen jàkka yépp.
Dugg ci jàkkay Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc amul ñaan gu ñu ko jagleel.
Topp mu julli ñaari ràkka ngir nuyóo ko jàkka ji.
Bu waxtu wi nekkul waxtu wu ñu tere ku ci julli kon dina man a julli cig coobarewu lu ko soob ñaari ràkka ñaari ràkka; Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:(genn julli ci sama jàkka jii moo gën junniy julli ci fu dul moom ba mu des jàkka ja ca Màkka)
Jaadu na it muy dàkk di julli ci Rawda bi-te mooy diggante Minbaru Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak néegam bi-bu yombee ci moom; ngir waxi Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc:(nekk na ci diggante sama kër gi ak sama Minbar bi ab dër la ci dëru àjjana)
Bu ko yombul nag mu julli ci wet gu jàppandi ci jàkka ji, lii nag bu dul jullig mbooloo, bu dee jullig mbooloo la nay sàmmoonte ak sàppe su njëkk sa sës ci imaam bi; ngir tegtal yu matale yi rot ci loolu.
Bu nammee siyaare bàmmeelu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak bàmmeeli ñaari sahabaam yi:
Day taxaw ci kanamu bàmmeelu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci teggin, ak ug wegeel, mu suufeel kàddoom, daal di nuyu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax ne:(Assalaamu halayka yaa rasuulal Laahi warahmatul Laahi wabarakaatuhu);bu waxee it:(ashadu annaka rasuulul Laahi haqan, wa annaka xadd ballaxta ar-risaalata, wa addayta al-amaanata, wa jaahadta fil Laahi haqa jihaadihi,wa nasahta al-ummata, fa jasaakal Laahu han ummatika afdala maa jasaa nabiyyan han ummatihi) kon it baax na.
Topp mu jëm ndayjoor tuuti daal di nuyu Abuu Bakar As-Siddiix yal na ko Yàlla dollee gërëm.
Topp mu jëmaat ndayjoor tuuti daal di nuyu Umar ibnul Xattaab, Ibn Umar yal na ko Yàlla dollee gërëm bu daan nuyu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak ñaari àndandoom yi lu ci bari daawul yokk ci waxam jii:(Assalaamu halayka yaa rasuulal Laahi, assalaamu halayka yaa Abaa Bakrin,assalaamu halayka yaa abataahu) topp mu wëlbati ku dem.
Jaaduwul di guddal ab taxwaay walla ñaan ca bàmmeelu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak ñaari sahabaam yi, Maalik siboon na ko, daal di wax ne: loolu bidaa la salaf ya (ña jiitu woon) defuñu ko,te dara du yéwénal mujjug xeet wii lu dul la yéwénaloom njëlbeen ga.
Niki noonu it li yenn siyaarekat yi di def ak ñu dul ñoom ci sàkku ñaan ca bàmmeelam ba daal di jublu bàmmeel ba yëkkëti ñaari loxoom lii lépp dafa wuute ak la ñu baax ña jiitu daan def muy sahaabay Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak ña leen topp cig rafetal waaye ci bidaa yi ñu sos la bokk.
Niki noonu it li yenn siyaarekat yi di def ci bu ñuy nuyu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di teg seen loxo ndayjoor ci kaw càmmooñ bi teg ko ci kaw seen dënn walla ci suufam kem melow kuy julli melokaan wii daganul ci bu ñuy nuyu Yonnente bi; ndaxte melow toroxlu la ak jaamu gog du yel lu dul ñeel Yàlla mu kawe mi kem ni ko Boroom xam-xam bu mag ba di Ibn Hajar yal na ko Yàlla yërëm nettalee ca Al-Fath jële ci woroom xam-xam yi.
Du dagan ci kenn muy jegeñ-jegeñlu Yàlla ci di raay néeg ba, walla di ko wër, te du laaj Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc pajug aajoom, walla faj ku feebaram, ak lu ko niru; ndaxte yooyu yépp deesu ko sàkku ci ku dul Yàlla Moom dong.
Sopp nañu ci kiy siyaare Madina jamono ya mu fa nekkee mu siyaare jàkkay Xubaa daal di fay julli; ndaxte Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na fa dem moo xam day war walla mu dox, mu julli fa ñaari rakka, jële nañu ci Sahl ibn Haniif mu wax ne:Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:(ku laabe këram daal di ñëw jàkkay Xubaa julli fa ag julli dana am fayug Umra).
Sunnaal nañu ci góor ñi ñu siyaare bàmmeeli Al-Baxiih ya -almeer la ci Madina- ak bàmmeeli ña dee ci xare ak bàmmeelu Hamsatu yal na ko Yàlla dollee gërëm;ndaxte Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na leen siyaare di leen ñaanal, ak ngir waxu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc:(tere woon naa leen siyaare bàmmeel yi, leegi deeleen ko siyaare ndax da leen di fàttali allaaxira)
Bu leen daal siyaaree day wax kem li muy wax buy siyaaree yeneen bàmmeel yi: (assalaamu halaykum ahlad diyaari, minal muuminiina wal muslimiina, wa innaa insaa Allaahu bikum laahixuuna, yarhamul Laahu almustaxdimiina minnaa wal mustaaxiriina, nas-alu Allaaha lanaa wa lakum alhaafiyata).
Amul sikk-sàkka ci ne li ñu jublu ci siyaare bàmmeel yi mooy fàttaliku allaaxira ak rafetal jëmale ci ñi faatu ci ñaanal leen, ak topp sunnas Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc,te lii mooy siyaare gi ñu yoonal.
Bu dee siyaare nag ngir jubloo ñaan ca seen bàmmeel ya,walla di laaj Yàlla ca ñoom,walla ci seen i baarke ,ak yu ko niru kon lii siyaareg bidaa gu bon la Yàlla yoonalu ko du caagineYonnenteem bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, te it mag ñu baax ña jiitu defuñu ko, bu dee laaj leen fajug aajo, walla faj aji-tawat, ak yu ko niru kon lii bokkaale gu mag la.
Jëlal yaw aji-jang ji yenn hadiis yi ñu sos ci bunt bii ndax nga xam ko ba moytu ci a woru:
Bi ci njëkk: (ku aj te siyaarewu ma kooku béccingal na ma).
Ñaareel bi: ( ku ma siyaare ginnaaw samag faatu moo ngi mel ni ku ma siyaare ci samag dund).
Ñatteel bi: (ku ma siyaare siyaare sama baay Ibraahiima ci menn at gaarànteel naa ko fa Yàlla àjjana).
Ñenteel bi: (ku siyaare sama bàmmeel samag ramm war na ñeel ko).
Haddis yii ak yi ko niru dara saxu ci jóge ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, Al-Haafis Al-Huxaylii nee na: bunt bii dara saxu ci. Al-Haafis Ibn Hajar wax na ci At-Talxiis ne: -ginnaaw bi mu tuddee lu bari ci nettali yii- yooni hadiis bii yépp a wéradi.Siyaare jàkkay Yonnente bi bokkul ci sunnay Aj walla Umra walla ci yi koy tax a mat, Moo xam laata Aj gi walla Umra gi la, walla ginnaaw ga; ndax siyaare jàkkay Yonnente bi lu ñu sopp la ba fàww; kon kiy aj walla muy umra bu ko siyaarewul itam du ci am bàkkaar, te Aj walla Umra joteewul dara ak siyaare jàkkay Yonnente bi ndax ay jaamu yu teqalikoo lañu. Ku Aj walla mu Umra du ne fàww mu siyaare ji jàkkay Yonnente bi, niki noonu it ku siyaare ji jàkkay Yonnente bi du ne fàww Aj walla umra da koy war, bu boole Aj ak Umra ak siyaare ji jàkkay Yonnente bi ci benn tukki loolu it baax na.
Ay njuumte ci siyaare jàkkay Yonnente bi
Raay miir ya ak ŋëb ca weñ ya jamono ya muy siyaare bàmmeelu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak fas fa ay wëñ ak yu ko niru ca paranteer ya ngir baarkeelu.
Te baarke ci li Yàlla yoonal ak ub yonnenteem la nekk waaye nekkul ci bidaa yi.
Dem ca xur ya ca Xeeru Uhud ak yu ko niru niki Xuru Hiraa, ak Xuru Suur, yi nekk Màkka ak fas fa ay moorso ak ñaan ay ñaan yu Yàlla joxewul ndigal ak toggoo ay coonu ci loolu.
Yii yépp ay bidaa la, amul cosaan ci Sariiha ju laab jii.
Siyaare yenn barab yoy dañuy foog ne ci jeexitali Yonnente bi la bokk, niki fa giléem ga gooroon, ak Teenu Al-Xaatam(jaaro ba) walla teenu Usmaan ak jël ci suufus bérab yii ngir baarkeelu.
Ñaan ñi faatu ci bu ñuy siyaare almeeri Al-Baxiih yi, ak almeeri ña dee ci xareb Uhud, ak sànni fa xaalis ngir jegeñ-jegeñlu ko ak baarkeelu ci ña fa nekk.
Yii nag ci njuumte yu rëy yi la bokk, dafa bokk sax kay ci bokkaale gu mag, kem ni ko woroom xam-xam yi tudde,Téereb Yàlla bi ak Sunnas Yonnenteem bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tegtale ko;ndaxte jaamu Yàlla rekk la ñeel du dagan ñu jëmale ci dara ñeel ku dul Moom, niki rendi ak nisër ak yu ni mel, ngir waxu Yàlla ji:(digaluñu leen lu dul ñu jaamu Yàlla di aji-sellal diine ji ñeel ko)[Al-Bayyinatu: 5].
Yàlla rekk a xam, Yal na Yàlla dolli jàmm ak mucc sunu Yonnente bi Muhammat ak waa kёram ak àndandoom yépp.
Mbooleem xeeti cant yi ñeel na Yàlla miy Boroom mbindeef yi, jàmm ak mucc yal na nekk ci sunu Yonnente bi Muhammat, ak ay ñoñam ak sahaabaam yépp. Ginnaaw loolu: Lii ab bataaxal bu ñu tënk la ci melow Umra ak i àtteem ak i tegginam, xér nanu ci lool ci leeral li ëpp ci li ñu aajowoo ci Umra. Yàlla rekk lanuy ñaan mu def ko muy lu sell ñeel jëmmam ju Tedd ji, ak mu jariñ ci mbooleem jullit ñi.
Jëfi safaan yi nit ñi di faral di def ci Aj ak Umra ak Siyaare Yónnent bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal Ko.
39 languages
Jëfi safaan yi nit ñi di faral di def ci Aj ak Umra ak Siyaare Yónnent bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal Ko.
Njuumte ak jëfi safaan yi aju ci Umra Bi ci njëkk: jëfi safaan ak njuumte yi nit ñi di def ci Armal Ñàkk a ihlaal, ci mu bañ a yëkkëti kàddoom ci jaamu gi mu namm a def ca ba muy tàmbalee fas Armal ga. Te sunna si mooy: mu yëkkëti ca kàddoom.
Sant ñeel na Yàlla miy Boroom mbindeef yi, xéewal ak jàmm yal na nekk ci sunu Yonnente bi Muhammat ak ay ñoñam,ak àndandoom yépp. Ginnaaw loolu: Lii ab bataaxel la bu ñu tënk ci teggiini tukki ak i àtteem, bëgg nanoo leeral li ëpp ci li aji-tukki ji di aajowoo. Yàlla rekk lanuy ñaan mu def ko muy lu sell ñeel jëmmam ju Tedd ji, ak mu jariñ ci mbooleem jullit ñi. Bi ci jëkk: teggiini tukki
يهدف الكتاب إلى تعليم المسلمين أساسيات دينهم بطريقة مبسطة وشاملة. يتناول مجموعة من الدروس المهمة مثل قراءة الفاتحة وقصار السور، وأركان الإسلام والإيمان، وأقسام التوحيد والشرك، وشروط وأركان وواجبات الصلاة، بالإضافة إلى مبطلاتها، مع بيان مختصر لشروط الوضوء وفروضه ونواقضه. كما يسلط الضوء على التحلي بالأخلاق الإسلامية والآداب الشرعية، ويقدم إرشادات لطيفة حول تجهيز الميت والصلاة عليه ودفنه.