Skip to content

benn waay dafa laaj Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: lan moo gën ci Lislaam? Mu ne ko: "nga leele ñam, ak di nuyu koo xam ak koo xamul".

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:

benn waay dafa laaj Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: lan moo gën ci Lislaam? Mu ne ko: "nga leele ñam, ak di nuyu koo xam ak koo xamul".

أَنَّ رَجُلًا سَأَلَ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: أَيُّ الإِسْلاَمِ خَيْرٌ؟ قَالَ: «تُطْعِمُ الطَّعَامَ، وَتَقْرَأُ السَّلاَمَ عَلَى مَنْ عَرَفْتَ وَمَنْ لَمْ تَعْرِفْ».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Laaj nañu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: yan ci jikkòy lislaam yi ñoo gën? Mu tudd ñaari jikkó: Bu njëkk bi: di baril di leel way-ñàkk yi, dana ci dugg ba tay saraxe ak àddiya ak nganale ak céetal, ngëneelu lele nag dana feddaliku ci jamonoy xiif, ak bi njëg yi seeree. Ñaareel bi: di nuyu bépp jullit, moo xam xam nga ko walla xamóo ko.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Xérug Sahaaba yi ci xam jikko yiy jariñ ci àdduna ak allaaxira.

Nuyoo ak joxe ñam dafa bokk ci jëf yi gën ci Lislaam;ngir ngëneelam ak ni ko nit ñi di aajowoo ci waxtu wu ne.

Ci ñaari jikkó yii la rafetal di dajee ci wax ak ci jëf, te mooy li gën a mat ci rafetal.

Jikkó yii day aju ci jëflànte ci diggante jullit ñi, am na yeneen jikko ci jëflànte jullit bi ak Boroomam.

Njëkka nuyóo dañmm jullit rekk la jagoo, waaye deesul njëkk a nuyu ab yéefar.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 12) (12).

Téere Muslim bi gën a wér (1/ 65) (39).

Yataal gi (4)

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (1/ 604).

مرقاة المفاتيح شرح مشكاة المصابيح.

لعلي القاري (7/ 2936).