"Amul ci Yonnente yi benn Yonnente lu dul ne Yàlla jox na ko luy tax nit ñi gëm ko
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
"Amul ci Yonnente yi benn Yonnente lu dul ne Yàlla jox na ko luy tax nit ñi gëm ko, man nag li ñu ma jox ag soloo la gog Yàlla moo ma ko soloo, ba maa ngi yaakaar a nekk ki ëpp ñi koy topp ëllëg bis-pénc"
«مَا مِنَ الأَنْبِيَاءِ نَبِيٌّ إِلَّا أُعْطِيَ مَا مِثْلهُ آمَنَ عَلَيْهِ البَشَرُ، وَإِنَّمَا كَانَ الَّذِي أُوتِيتُ وَحْيًا أَوْحَاهُ اللَّهُ إِلَيَّ، فَأَرْجُو أَنْ أَكُونَ أَكْثَرَهُمْ تَابِعًا يَوْمَ القِيَامَةِ».
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne Yonnente yi Yàlla da leen a dëgëral jox leen ay aaya ak i keemaan yuy xotti mbaax yu ñuu tegtaloo ci seenug yónnent, muu waral ñu ku ko gis gëm seenug dëggu, ak ne moom ku ñu not lay doon ca dëkk ga ba du ko man a jeñ ci boppam, waaye amaana mu weddi daal di fétterlu. Waaye moom Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc aayaam ak keemaanam mooy alxuraan ji ko Yàlla soloo; ngir li mu làmboo ci ay keemaan yu leer tey wéy ndax ag bari njariñam ak matug njariñam, ak li mu làmboo woote ak i lay ak xibaare liy ami ji, ay njariñam matale ñi teew ak ñi fàddu ak ñi fi nekk ak ñiy ñëwi, topp mu wax ne: te yaakaar naa ma nekk ki ëpp ñu koy topp ëllëg bis-pénc.
Saxal sy saya ñeel Yonnente yi, te lii dafa bokk ci yërmàndey Yàlla mu kawe mi ak ngëneelam ci xeet yi.
Leeral màggaayu keemaanu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
Leeral màggaayu wàccuwaayu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak ngëneelam ci kaw mbooleem Yonnente yi.
Ibn Hajar wax na ci li mu wax ne: "waaye li ñi ma jox ag soloo la Yàlla moo ma ko soloo": li ñu ci namm nekkul tënk ci keemaan gi, du caagine it ne joxuñu ko keemaan ya ñu joxoon ña ko jiitu, waaye li ñu ci namm mooy ne mooy keemaan gi gën a màgg nga xam ne moom rekk moo ko jagoo wolif ku dul moom.
An-Nawawii nee na: "(ma yaakaar ne di naa nekk ki ëpp ñu koy topp) màndarga la ci màndargay yónnent, ndax moom Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa xibaare lii ca jamono ja jullit ña néewe, topp Yàlla mu kawe mi xéewalal ko ubbil jullit ñi daal di leen di baarkeel ba mbir mi mujj a mat, mbir mi yaatu ci jullit ñi ba egg ci dayo bii ñu xam, cant ñeel na Yàlla.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (6/ 182) (4981).
Téere Muslim bi gën a wér (1/ 134) (152).
Yataal gi (2)
عمدة القاري شرح صحيح البخاري (25/ 25).
شرح النووي على مسلم (2/ 188).
Cited in books
5 BooksYataal gi (4)
- رسالة موجزة عن الإسلام كما جاء في القرآن الكريم والسنة النبوية (مشتملة على الأدلة)رِسَالَةٌُ مُوجَزَةٌُ عَنِ الْإِسْلَامِ كَمَا جَاءَ فِي الْقُرْآنِ الْكَرِيمِ وَالسَّنَةِ النَّبَوِيَّة-مشتملة على الأدلة -للحرمين-«مَا مِنَ الأَنْبِيَاءِ نَبِيٌّ إِلَّا أُعْطِيَ مَا مِثْلهُ آمَنَ عَلَيْهِ البَشَرُ وَإِنَّمَا كَانَ الَّذِي أُوتِيتُ وَحْيًا أَوْحَاهُ اللَّهُ إِلَيَّ فَأَرْجُو أَنْ أَكُونَ أَكْثَرَهُمْ تَابِعًا يَوْمَ القِيَامَةِ» [27].
- موسوعة الأسئلة (المجموعة الأولى)«مَا مِنَ الأَنْبِيَاءِ مِنْ نَبِيٍّ إِلَّا قَدْ أُعْطِيَ مِنَ الآيَاتِ مَا مِثْلُهُ آمَنَ عَلَيْهِ الْبَشَرُ، وَإِنَّمَا كَانَ الَّذِي أُوتِيتُ وَحْيًا أَوْحَاهُ اللهُ إِلَيَّ، فَأَرْجُو أَنْ أَكُونَ أَكْثَرَهُمْ تَابِعًا يَوْمَ الْقِيَامَ
- موسوعة الإيمان«مَا مِنَ الأَنْبِيَاءِ نَبِيٌّ إِلَّا أُعْطِيَ مِنَ الآيَاتِ مَا مِثْلُهُ أُومِنَ، أَوْ آمَنَ عَلَيْهِ البَشَرُ، وَإِنَّمَا كَانَ الَّذِي أُوتِيتُ وَحْيًا أَوْحَاهُ اللَّهُ إِلَيَّ، فَأَرْجُو أَنِّي أَكْثَرُهُمْ تَابِعًا يَوْمَ القِيَامَةِ
- نبراس طالب (4)1«مَا مِنَ الأَنْبِيَاءِ نَبِيٌّ إِلَّا أُعْطِيَ مَا مِثْلهُ آمَنَ عَلَيْهِ البَشَرُ، وَإِنَّمَا كَانَ الَّذِي أُوتِيتُ وَحْيًا أَوْحَاهُ اللهُ إِلَيَّ»