Skip to content

Mottalil hadiisu «bayna maa nahnu juluusun hinda rasuulul laahi...», te nga tudd yenn ci ay njariñam.

الباب / الفصل
قسم الحديث

السؤال

س3: أكمل حديث «بينما نحن جلوس عند رسول الله صلى الله عليه وسلم ...»، واذكر بعض فوائده.

Laaju 3: mottalil hadiisu (bayna maa nahnu juluusun hinda rasuulul laahi...), te nga tudd yenn ci ay njariñam?

الجواب

ج:عن عمر بن الخطاب رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ قال:

«بينما نحن جلوس عند رسول الله صلى الله عليه وسلم ذات يوم، إذ طلع علينا رجل شديد بياض الثياب، شديد سواد الشعر، لا يرى عليه أثر السفر، ولا يعرفه منا أحد، حتى جلس إلى النبي صلى الله عليه وسلم، فأسند ركبته إلى ركبتيه، ووضع كفيه على فخذيه، وقال: «يا محمد أخبرني عن الإسلام»، فقال له: «الإسلام: أن تشهد أن لا إله إلا الله، وأن محمدًا رسول الله، وتقيم الصلاة، وتؤتي الزكاة، وتصوم رمضان، وتحج البيت إن استطعت إليه سبيلًا»، قال: «صدقت»، فعجبنا له يسأله ويصدقه، قال: «أخبرني عن الإيمان» قال: «أن تؤمن بالله، وملائكته، وكتبه، ورسله، واليوم الآخر، وتؤمن بالقدر؛ خيره وشره»، قال: «صدقت»، قال: «فأخبرني عن الإحسان»، قال: «أن تعبد الله كأنك تراه، فإن لم تكن تراه، فإنه يراك»، قال: «فأخبرني عن الساعة»، قال: «ما المسؤول بأعلم من السائل»، قال: «فأخبرني عن أماراتها»، قال: «أن تلد الأمة ربتها، وأن ترى الحفاة العراة العالة رعاء الشاء، يتطاولون في البنيان» ثم انطلق فلبث مليًّا، ثم قال: «يا عمر! أتدري من السائل؟»، قلت: "الله ورسوله أعلم"، قال: «فإنه جبريل، أتاكم يعلمكم دينكم»

رواه مسلم.

فوائد من الحديث:

  1. ذكر أركان الإسلام الخمسة؛ وهي:
  • شهادة أن لا إله إلا الله، وأن محمدا رسول الله.
  • وإقام الصلاة.
  • وإيتاء الزكاة.
  • وصوم رمضان.
  • وحج بيت الله الحرام.
  1. ذكر أركان الإيمان، وهي ستة:
  • الإيمان بالله.
  • وملائكته.
  • وكتبه.
  • ورسله.
  • واليوم الآخر.
  • والقدر خيره وشره.
  1. ذكر ركن الإحسان، وهو ركن واحد، وهو أن تعبد الله كأنك تراه، فإن لم تكن تراه، فإنه يراك.
  2. وقت قيام الساعة، لا يعلمه إلا الله تَعَالَى.

jële nañu ci Umar doomu Alxattaab yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: benn bis danoo toog ci Yónente bi, fa saasa benn waay ñëw, yéere yaa nga weex tàll, kawar ga ñuul kukk, te kenn gisul si moom jeexiitu tukki, te it kenn xamu ko si nun, bam aksee toog ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc-, daa di wéer ñaari wóomam ci ñaari wóomu yónente bi, teg ñaari tenqam ci kaw poojam, daal di ne: "Ée yaw Muhammat xibaar ma luy lislaam", mu ne ko" lislaam mooy: nga seede ne amul kenn ku dees di jaamu ku dul Yàlla, seede ne Muhammat ndawul Yàlla la, tey taxawal julli, di woor weeru koor, te aj Màkka benn yoon boo ko manee" mu ne ko: "wax nga dëgg" ñu daaldi yéemu ci moom; di ko laaj ba noppi di ko dëggal, mu ne ko: " xibaar ma lan mooy gëm" mu ne ko: "mooy nga gëm Yàlla, ak i malaakaam, ak i téeréem, ak i yónentem, ak bis bu mujj ba, nga gëm ndogal yi; yacay yiw ak yacay ay" mu ne ko: "wax nga dëgg" daal ni ko: "xibaar ma lan mooy rafetal" mu ni ko: "mooy ngay jaamu Yàlla mel ni yaa ngi koy gis, ndax boo ko gisul moom moo ngi lay gis" mu ne ko: "xibaar ma kañ la bis-pénc" mu ne ko: "ki ñu koy laaj gënukoo xam ki ko koy laaj" mu ne ko: "wax ma ay màndarngaam"mu ne ko: "mooy jaam ba jur ab sangam, nga gis way-fàndaañu ya way-rafle ya way-ñàkk ya sàmukati jur ya, ñuy guddalaante ca taxab ya" mu wéy ma sax ci ak jaaxle, mu ne ma: "Ée Umar ndax xam nga aji-laaj ji? " ma ne ko: "Yàlla ak ub yónenteem ñoo xam" mu ne ma: "koo ku Jibriil la, dafa ñëw ngir xamal leen seen diine"

Muslim moo ko soloo

bokk na si njariñi hadiis bi:

1-tudd ponk i lislaam yay juroom; te mooy:

seede ne amul kenn ku yayoo jaamu kudul Yàlla, ak ne Muhammat Yàlla a ko yónni.

ak taxawal julli.

ak joxe azaka.

ak woor weeru koor.

ak Aj néegub Yàlla bees wormaal ba.

  1. tudd ponk i ngëm, te juroom-benn la:

gëm Yàlla.

  1. gëm ay malaakaam.
  2. gëm ay téereem.

4)gëm ay yonenteem.

5)gëm bis-pénc.

6)gëm dogal bu neex ak bu naqari.

  1. tudd ponku rafetal, moom benn ponk la, te mooy nga jaamu Yàlla mel ni yaa ngi koy gis ndax boo ko gisul moo ngi lay gis.
  2. jamonoy taxawaayu bis-pénc kenn xamu ko kudul Yàlla mu kawe mi