Skip to content

«am na benn waay bu doon lebal nit ñi, daan wax ndawam la naan ko: boo demee ci ku am jafe-jafe nanga ko jéggal, amaana Yàlla jéggal nu

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

«am na benn waay bu doon lebal nit ñi, daan wax ndawam la naan ko: boo demee ci ku am jafe-jafe nanga ko jéggal, amaana Yàlla jéggal nu, mu dajeek Yàlla mu jéggal ko».

«كان رجلٌ يُدَايِنُ الناسَ، فكان يقول لفتاه: إذا أتيتَ مُعسِرًا فتجاوز عنه، لعل اللهَ يَتجاوزُ عنا، فلقي اللهَ فتجاوز عنه».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne: benn waay da doon jëflànte ak nit ñi ci leb-lante, walla mu leen di jaay ba jëmmi-jamono ñu door koo fay, Mu daan wax ndawam la daan fayyeeku ji bor ya ca nit ña: Boo demee ci ku ame bor te amul lu mu faye ngir néew doole «nanga ko jéggal», benn ci neggandiku ko te bañ koo taxawu ci di ko laaj, Walla ci jël li mu am donte sax matul, loolu nag ngir li mu bëgg ak xemmeem ci Yàlla jéggal ko daal di koy baal. Ba mu faatoo Yàlla baal ko jéggal ko ay ñaawtéefam,

Maanaay baat yi

يداين: يكثر من التعامل مع الناس بالدين.

فتاه: غلامه الذي يكلفه بالعمل.

أتيت معسرًا: لمطالبته بما عليه.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Refetal ci jëflante ak nit ñi, ak di leen baal, te di jéggal ki nekk ci jafe-jafe daa bokk ci sabab yi gën a màgg ci muccug jaam bi ëllëg bis-penc.

Rafetal jëme ci nit ñi, ak sellal ngir Yàlla, ak yaakaar yërmaandeem, daa bokk ci sababi njéggali bàkkaar yi.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (4/ 176) (3480).

Téere Muslim bi gën a wér (3/ 1196) (1562).

Yataal gi (9)

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (2/ 458).

التنوير شرح الجامع الصغير.

للصنعاني (8/ 123).

كنوز رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (16/ 402).

مرقاة المفاتيح شرح مشكاة المصابيح.

للقاري (5/ 1953).

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين (2/ 945).