Skip to content

"lislaam dafa tàmbali di lu tumurànke, te dana dellu ca na mu tàmbalee woon di lu tumurànke, kon texe ñeel na way-tumurànke yi".

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:

"lislaam dafa tàmbali di lu tumurànke, te dana dellu ca na mu tàmbalee woon di lu tumurànke, kon texe ñeel na way-tumurànke yi".

«بَدَأَ الْإِسْلَامُ غَرِيبًا، وَسَيَعُودُ كَمَا بَدَأَ غَرِيبًا، فَطُوبَى لِلْغُرَبَاءِ».

Muslim soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne lislaam dafa tàmbali nekk lu tumurànke ci ay benn-benni nit ak tuutig waa lislaam, te dana dellu di lu tumurànke ci néewug ña koy taxawe kem na mu tàmbalee woon, kon boog ag xéewal ak ug, mbégte ñeel na leen.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Xibaare ci ne lislaam di na tumurànke ginnaaw ag tasaaroom ak ug siiwam.

Nekk na ci it ag màndarga ci màndargay Yonent, ndax Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa xibaare luy ñëw ginnaawam, loolu daal di am kem na mu ko xibaare woon.

Ngëneelu ki gàddaay réewam ak njabootam; ngir lislaam, ak ne àjjana ñeel na ko.

Way-tumurànke yi ñooy ñiy baax fekk nit ñaa nga bon, te ñoom dañuy yéwénal li nit ñi yàq.

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér (1/ 130) (145).

Yataal gi (2)

البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (4/ 142).

إكمال المعلم بفوائد مسلم (1/ 456).