Skip to content

kersa ci ngëm la bokk

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dégg na benn waay di yedd mbokkam ndax kersa, mu ne ko: "«kersa ci ngëm la bokk».

سَمِعَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ رَجُلًا يَعِظُ أَخَاهُ فِي الْحَيَاءِ، فَقَالَ: «الْحَيَاءُ مِنَ الْإِيمَانِ».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa dégg benn waay muy dénk mbokkam ci ngir mu bàyyi bari kersa! Mu leeralal ko ne kersa ci ngëm Yàlla la bokk, te yiw rekk lay indi. Kersa jikko la la juy yóbbe ci def lu rafet ak bàyyi lu ñaaw.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Bokk na ci njariñal adiis bi: Li lay teree def aw yiw deesu ko woowe kersa, waaye yaras lañu koy woowe walla lompañ mbaa wayadi walla ragal.

Am kersa ci Yàlla mooy di def ay ndigalam, bàyyi ay tereem.

Am kersa ci nit ñi mooy wormaal leen, ak jox leen seen wàccuwaay, ak moytu lu aada ñaaw lu.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 14) (24).

Téere Muslim bi gën a wér (1/ 63) (36).

Yataal gi (8)

توضيح الأحكام من بلوغ المرام.

للبسام (7/ 489).

منحة العلام في شرح بلوغ المرام.

لعبد الله الفوزان (10/ 330).

فتح ذي الجلال والإكرام.

لابن عثيمين (6/ 427).

سبل السلام بشرح بلوغ المرام.

للصنعاني (2/ 689).