Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc rëbb na kiy jokk kawar ak kiy sàkkoo jokk, ak kiy jamu ak kiy sàkkoo jàmu.
Jële nañu ci Abdullah Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc rëbb na kiy jokk kawar ak kiy sàkkoo jokk, ak kiy jamu ak kiy sàkkoo jàmu.
لعن النبي صلى الله عليه وسلم الوَاصِلَةَ والمُسْتَوْصِلَةَ، والوَاشِمَةَ والمُسْتَوشِمَةَ.
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa ñaan ag rëbb ak ug dàq ak soreele yërmànde Yàlla mu kawe ci ñenti xeet: Bi ci njëkk: kiy jokk kawaru boppam walla keneen ci geneen kawar. Ñaareel bi: ak kiy sàkkoo jokk ci sàkku ci keneen mu jokkal ko geneen kawar ci kawaram. Ñatteel bi: kiy jamu di jam Puso ci yenn bérab ci yaramam, niki kanam gi, walla ténq yi, walla dënn bi, ak def ca Tusngal walla lu ko niru, ba bérab ba mujj Bulo, walla mu Wert; ngir sàkku taar ak rafet. Ñenteel bi: kiy sàkku jamu di sàkku ñu jamal ko. Jëf yii ci bàkkaar yi mag yi la bokk.
Ibn Hajar nee na: li ñu tere ci loolu mooy jokk ag kawar ci kawar, waaye bu ci jokkee leneen lu dul kawar niki sagar mbaa leneen kon du dugg ci tere gi.
Araamal nañu dimbalante ci bàkkaar.
Tere nañu soppi mbindum Yàlla mi; ndaxte moom naxaate la ak lëntal.
Dagan na ñu rëbb ku Yàlla rëbb ak ub yonenteem yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
Sol Pirig day dugg ci jokk gi ñu araamal, te lu ñu araamal la ndax li ci nekk ci niru-niru lu yéefar yi, ak wuruj ak lëntal.
Al-Xattaabii nee na: tëkku gu tar moo rot ci mbir yii; ngir li ci nekk ci wuruj ak wor, te bu ñu woyofaloon dara ci loolu kon day nekk yoonu daganal yeneen wuruj yu dul moom, ak it ngir li ci nekk ci soppi mbindum Yàlla mi, te loo lu la hasiisu Ibn Mashuud di junj ci waxam ji: "ñiy soppi mbindum Yàlla mi", Yàlla rekk a xam.
An-Nawawii nee na: te moom dafa araam ci ki koy def ak ki ñu koy defal, te bérab bu ñu jam day mujj nekk sobe, kon bu ko manee dindi ci faju kon day war mu dindi ko, bu manul nekk ci lu dul oppeere, bu ca ragalee ag sàngu walla ñàkk ab cér walla ag njariñ walla mbir muy ñaaw ci cér biy feeñ kon dindi gi du lu war, bu tuubee nag bàkkaar du fa des, waaye bu ragalul dara ci yooyu kon day war mu dindi ko, te bu ko yeexee day am bàkkaar.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (7/ 167) (5947).
Téere Muslim bi gën a wér (3/ 1677) (2124).
Yataal gi (6)
توضِيحُ الأحكَامِ مِن بُلوُغ المَرَام.
للبسام (5/ 373).
بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.
لسليم الهلالي (3/ 157).
منحة العلام في شرح بلوغ المرام.
لعبد الله الفوزان (7/ 354).