Skip to content

"buleen dugg ci dëkkuwaayu ñi tooñ seen bopp lu dul ngeen jooy

Jële nañu ci Abdullah Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: romb nanu nun ak Yonente Yàlla bi ci aw Xeer, Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di ne nu:

"buleen dugg ci dëkkuwaayu ñi tooñ seen bopp lu dul ngeen jooy; ngir moytu li leen dal dal leen" topp mu xuppe daal di gaawantu ba weesu ko.

«لَا تَدْخُلُوا مَسَاكِنَ الَّذِينَ ظَلَمُوا أَنْفُسَهُمْ، إِلَّا أَنْ تَكُونُوا بَاكِينَ؛ حَذَرًا أَنْ يُصِيبَكُمْ مِثْلُ مَا أَصَابَهُمْ» ثُمَّ زَجَرَ فَأَسْرَعَ حَتَّى خَلَّفَهَا.

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ba mu rombee dëkkuwaayi waa Samuudu ya dafa tere ñu dugg walla ñu dem ci dëkkuwaayu ña ñu mbugaloon di ña nga xam ne dañoo tooñ seen bopp, lu dul aji-dugg ji di jooy ngir waaru ci ñoom; ngir ragal la leen dal ci mbugal dal ko, topp mu xuppe daal di gaawal Daabaam ba weesu ko.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Xalaat ci mbiri ñi Yàlla alag, ak moytu li nu tàbbi; ak moytu a sàggan ci settantal kéemtaan yi.

Këri ñii ñu mbugal deesu fa dëkk seen ginnaaw, te deesu ko def dëkkuwaay; ndax ka fa dëkk manul di jooy ba fàww, te dañoo tere ñu dugg fa lu dul ci melo wii.

An-Nawawii nee na: ag ñaaxe moo ngi ci, ci di fuglu bu ñu dee romb ci dëkkuwaayi tooñkat yi, ak bérabi mbugal yi, niki noonu it gaawantu ca xuru Muhassir; ndax fa la woroom Ñay ya alkoo, kon dana jaadu ci kiy romb ci bérab yi mel nii mu fuglu ak ragal ak jooy, ak waaru ci ñoom ak ca seen bérabi alku yooyu, ak mu muslu ci Yàlla ci loolu.

Tere gi ak àrtu gi day làmboo këri waa Samuud ak ñu dul ñoom te mel ni ñoom ci mbooleem xeet yi nga xam ne mbugal dafa wàcc ci ñoom.

Tere nañu ñuy def bérab yooyu ak pàkk yooyu doxontukaay ak féexlukaaw ak lu ko niru.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (4/ 149) (3380).

Téere Muslim bi gën a wér (4/ 2286) (2980).

Yataal gi (3)

النهاية في غريب الحديث والأثر (187) (395).

إرشاد الساري لشرح صحيح البخاري (6/ 458) (5/ 368).

البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (45/ 169).