«ku ñëw ci yéen fekk ngeen abooloo ci lenn njiit, mu bëgg a xotti mbooloo mi, mbaa mu tàqqale séen mbooloo mi, rayleen ko».
Jële na ñu ci Arfajatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan:
«ku ñëw ci yéen fekk ngeen abooloo ci lenn njiit, mu bëgg a xotti mbooloo mi, mbaa mu tàqqale séen mbooloo mi, rayleen ko».
«مَنْ أَتَاكُمْ وَأَمْرُكُمْ جَمِيعٌ عَلَى رَجُلٍ وَاحِدٍ، يُرِيدُ أَنْ يَشُقَّ عَصَاكُمْ، أَوْ يُفَرِّقَ جَمَاعَتَكُمْ، فَاقْتُلُوهُ».
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne bu jullit ñi booloo ci lenn njiit, di menn mbooloo, am ku ñëw bëgg a xëccoo ak moom njiit gi, mbaa mu bëgg a tàqale jullit ñi ci ay mbooloo yu bari, kon dañu koo war a tere daadi xeex ak moom; ngir jeñ aw ayam ak ñoŋal dereeti jullit ñi.
وأمركم جميع: كلمتكم مجتمعة على إمام واحد، وأنتم يد واحدة.
يشق عصاكم: أصل العصا الاجتماع والائتلاف، والمراد هنا أنه يريد تفريق جماعتكم التي اجتمعت على إمام واحد.
Bokk na ci njariñal hdiisb: Dañoo war a dégg te topp njiitul jullit ñi ci lu dul ag moy, araam na it di jàmmaaloo ak moom.
Ku génn ci njiitl jullit ñi ak séen mbooloo ma dañoo war a xeex ak moom ag nu dayoom man a toll ci teddnga ak uw askan.
Soññee ci booloo ak bañ a tàqalikoo ak di juuyoo.
Téere Muslim bi gën a wér (3/ 1480) (1852).
Yataal gi (8)
منحة العلام في شرح بلوغ المرام.
لعبد الله الفوزان (8/ 349).
توضيح الأحكام شرح بلوغ المرام.
للبسام (6/ 329).
فتح ذي الجلال والإكرام بشرح بلوغ المرام.
لابن عثيمين (5/ 302).
المفاتيح في شرح المصابيح.
الحسين المُظْهِري (4/ 295).