Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

5 of 732 cards

Clear filters
«ku ñëw ci yéen fekk ngeen abooloo ci lenn njiit, mu bëgg a xotti mbooloo mi, mbaa mu tàqqale séen mbooloo mi, rayleen ko».
Wér na Muslim soloo na ko.
"ay fitna dana am, yëgleen ne bu fitna amee ka toog moo gën ka kay dox, kay dox mooo gën kay daw, yëgleen ne bu wàccee walla mu tàbbi ku am ay giléem na dem ci ay giléemam, ku am ay gàtt na dem ci ay gàttam, ku am suuf na dem ci suufam, nee na: jenn waay ne ko: yaw Yonente Yàlla bi, wax nu nu ku amul giléem amul gàtt amul suuf moom nag? Mu ne ko: "na dem ci jaaseem dëbb ñawka ga ak xeer, topp mu jéema muccbu ko manee, yaw Yàlla sama Boroom ndax jottali naa? Yaw Yàlla sama Boroom ndax jottali naa? Yaw Yàlla sama boroom ndax jottali naa?, nee na jenn waay ne ko: yaw Yonente Yàlla bi, xibaare nu bu ñu ma foorsee ba yóbb ma ci benn ci ñaari kurél yi benn waay dóor ma jaaseem, walla ag fett ray ma? Mu ne ko: "day gàddu bàkkaaram ak sa bàkkaar, mu bokk ci waa sawara".
Wér na Muslim soloo na ko.
«ay njiit danañu ñëw, da ngeen gis ci ñoom lu baax, ak it lu bon, ku ànd ca lu baax la kooku set na wicc, ku weddi seen yu bon kooku mucc na, waaye ki muccul mooy ki gërëm yu bon ya te ànd ca" ñu ne ko: mo ndax duñu xeex ak ñoom? Mu ne: "déedéet, li fii ak ñoo ngi julli".
Wér na Muslim soloo na ko.
Jaayante nanu ak Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci dégg ak topp, ci lu jafe ak lu yomb, ci lu neex ak lu naqari, ak bu xat-xat tegee sunu kaw, ak nu bañ a xëccoo ak nguur, ak nu bañ a wax lu dul dëgg fu nu man a nekk, dunu ragal ci Yàlla yeddagay aji-yedde ji.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«ku génnug topp, daal di tàqalikoo ak mbooloo ma ba faatu, kon dee na deewug ceddo, képp kuy xeex ngir yékkati raayaa cànkute, di mer ngir par-parloo, di woote ci aw xeet, walla muy xeex ngir par-parloo ciw xeet pp ba ñu ray ko, kon ag rayam rayug ceddo la, képp ku génn ag topp ci sama xeet wi, di dóor ñu baax ña ak kàccoor ya, te du moytu sax way-gëm ña, te du matale kóllëreg boroom kollëre, kooku bokkul ci man te bokkuma ci moom».
Wér na Muslim soloo na ko.