Skip to content

"Kaffaarag Nisar mooy kaffaarag ngiñ".

Jële nañu ci Huqbata ibn Aamir yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:

"Kaffaarag Nisar mooy kaffaarag ngiñ".

«كَفَّارَةُ النَّذْرِ كَفَّارَةُ اليَمِينِ».

Muslim soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral na ne kaffaarag Nisar gu ñu boyal bu dee tënkul li mu namm te tuddu ko: mooy Nisarug ngiñ.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Nisar: ci sariiha: mooy mukallaf miy aji-tànn waral ci boppam dara ngir Yàlla mu kawe mi.

Kaffaarag ngiñ: mooy leel fukki miskiin walla joxleen koddaayuy yére walla goreem jaam bi ji ag njaame, bu ko manul mu woor ñatti fan.

Xereñ gi nekk ci kaffaara mooy jullit bi wormaal Nisar ba du ca dellu, ba du nekk it ci làmmiñam.

Xeeti Nisar yi: 1. Nisar gu ñu boyal: niki mu wax: (nisaral naa Yàlla bu ma wérale) daal di noppi te yéenewul genn Nisar gu ñu ràññee kon kaffaarag ngiñ war na ko bu amee ag wér, 2. Nisaru xuloo ak mer: te mooy mu aj nisar gi ci sàrt, jublu ca a teree def dara walla yóbbe ci jëf niki mu wax: (bu ma waxee ak yaw rekk kon woor weer war na ma), àtteem: ñu tànnloo ku ci mu def li mu warlu, walla mu def kaffaarag ngiñ bu waxee ak moom, 3. Nisar gi dagan: niki: (nisaral naa Yàlla ne dinaa sol sama yére bi), àtteem: mooy ñu tànnloo ko ci mu sol yéreem bi walla mu def kaffaarag ngiñ. 4. Nisar gu ñu sib: niki: (nisaral naa Yàlla ne damay fase sama jabar ji), àtteem: mooy ne sopp nañu vi moom mu def kaffaarag ngiñ te bañ a def li mu nisar, bu ko defee nag kaffaara waru ko, 5. Nisarug moy: niki: (nisaral naa Yàlla ne damay sàcc), àtteem: mooy ne àraamalees na mu matale ko, te day def kaffaarag ngiñ, bu ko defee nag day am bàkkaar te kaffaara du ko war, 6. Nisarug topp: niki: (nisaral naa Yàlla ne dinaa julli lii) jublu ca jegeñ-jegeñlu Yàlla, bu ko ajee ci sàrt, niki wérug ki feebar, kon war na ko a matale bu sàrt bi amee, bu ko ajul ci sàrt nag kon war na ko a matal ba fàww.

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér (3/ 1265) (1645).

Yataal gi (8)

فتح ذي الجلال والإكرام شرح بلوغ المرام.

لابن عثيمين (6/ 128).

توضيح الأحكام من بلوغ المرام.

لعبد الله البسام (7/ 135).

منحة العلام شرح بلوغ المرام.

لعبد الله الفوزان (5/ 98).

سبل السلام.

لمحمد الصنعاني (2/ 558).