Skip to content

Nëxit gi jigéen di gis ak mboq-mboq yi ginnaaw laab daawuñuko jàppee dara.

Jële nañu ci Ummu Atiyyata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-,mu bokkoon ci ñi jaayante woon ak Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-,mu wax ne:

Nëxit gi jigéen di gis ak mboq-mboq yi ginnaaw laab daawuñuko jàppee dara.

كُنَّا لا نَعُدّ الكُدرَةَ والصُّفْرَةَ بعدَ الطُّهرِ شيئًا.

Abuu Daawuda moo ko soloo ci kàddu gii, Al-Buxaarii soloo na ko te amul yokk gii (ginnaaw laab gi).
Wér na
Leeral gi

Sahaaba bu jigéen bii di Ummu Atiyyata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- day xibaare ne jigéen ñi ci jamonoy Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daawuñu jàppe mbaax ndox miy génne ci awra -xaw a ñuul, walla mboq-ginnaaw bimu laabe , ba tax duñu bàyyi julli ak woor ngir moom.

Maanaay baat yi

الْكُدْرَةُ: هو الماء الذي تراه المرأة كالماء الوسخ الكدر.

الصُّفْرَةَ: هو الماء الذي تراه المرأة كالصديد يعلوه اصفرار.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ndox miy génne ci awray jigéen -ginnaaw bi mu laabee ci mbërëg deesu ko jàppe mbaax donte dafa am nëxiit ak mboq-mboq yu bawoo ci dereet ji.

Génnug nëx-nëx yi ak mboq-mboq yi ci jamonoy mbaax ak aada ja dees na ko jàppe; ndaxte dereet la ju génn ci waxtoom,waaye dafa jaxasoo ak ndox.

Jigéen du bàyyi julli ak woor ngir nëx-nëx yi ak mboq-mboq yiy am ginnaaw laab gi,waaye day jàppu daal di julli.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 72) (326).

Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (1/ 226) (307).

Yataal gi (4)

توضيح الأحكام.

للبسام (1/ 450).

سُبل السلام.

للصنعاني (1/ 153).