"sangleen ko ci ndox mu ànd ak siddéem ñatti yoon, walla juróom walla lu ëpp loolu bu dee gis ngeen ne aajowoo na ko, te ngeen def ca bu mujj ba gëttug Kaafuur -walla lenn ci Kaafuur-, bu ngeen noppee ngeen yégal ma ko"
Jële nañu ci Ummu Atiyyata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Benn doomu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu jigéen dafa faatu, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di génn ne: "sangleen ko ci ndox mu ànd ak siddéem ñatti yoon, walla juróom walla lu ëpp loolu bu dee gis ngeen ne aajowoo na ko, te ngeen def ca bu mujj ba gëttug Kaafuur -walla lenn ci Kaafuur-, bu ngeen noppee ngeen yégal ma ko", nee na: ba nu noppee nu yégal ko ko, mu jox nu koddaayam, daal di ne: "muur leen ko ci", Ummu Atiyyata nee na: nu def bopp ba ñatti béjjan.
تُوُفِّيَتْ إِحْدَى بَنَاتِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَخَرَجَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فَقَالَ: «اغْسِلْنَهَا ثَلاَثًا، أَوْ خَمْسًا أَوْ أَكْثَرَ مِنْ ذَلِكَ، إِنْ رَأَيْتُنَّ بِمَاءٍ وَسِدْرٍ، وَاجْعَلْنَ فِي الآخِرَةِ كَافُورًا -أَوْ شَيْئًا مِنْ كَافُورٍ-، فَإِذَا فَرَغْتُنَّ فَآذِنَّنِي»، قَالَتْ: فَلَمَّا فَرَغْنَا آذَنَّاهُ، فَأَلْقَى إِلَيْنَا حِقْوَهُ، فَقَالَ: «أَشْعِرْنَهَا إِيَّاهُ»، وَقَالَتْ: وَجَعَلْنَا رَأْسَهَا ثَلاَثَةَ قُرُونٍ.
Saynabu doomu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa faatu, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dugg fa jigéen ña koy sang ne leen: sangleen ko ci ndox ak siddéem te mu tóol, ñatt, walla juróom, walla lu ko ëpp, bu dee aajowoo na ko, te ngeen def ci sang gu mujj gi Kaafuur, bu ngeen noppee ngeen wax ma ko. Ba ñu noppre ñu yégal ko ko, mu jox ñiy sang koddaayam ga, ne leen: lëmësleen ko ci, te def ko yére biy féete ci yaram wi, topp ñu def bopp bi ñatti létt.
Warees naa sang jullit bu faatu, ak ne loolu faratag doy la.
Jigéen kenn du ko sang ñu dul ay jigéen, góor it kenn du ko sang ñu dul ay góor, lu dul li ñu ca settee ci jigéen ak jëkkëram, ak jibéer bi ak sangam, ku ci ne ci ñoom ñaar man naa sang moroomam.
Sang gi ñatti sang lay doon, bu doyil, mu nekk juróom, bu doyul, mu dolli ca, ci kem yéwénal ga ak aajowoo ga, ginnaaw loolu bu dara ci sobe génnee ci yaram wi, dañuy fatt bérab bi lor wi di génne.
Aji-sang day dagg sang gi ci ag tóol, ñaat, walla juróom, walla juróom-ñaar.
As-Sindii nee na: hadiis bi day tegtale ne sang ko faatu amul limit, waaye li ñi sàkku mooy mu set, te fàww it ñu sàmmoonte ak tóol ga.
Ndox mi day ànd ak Siddéem; ndax moom day sellam, di dëgëral yaramu néew bi.
Dañuy defal gëtt néew bi mu ànd ak sang gu mujj gi, ngir ndox mi bañ ko a dindi, te gëtt gi ci Kaafuur lay nekk, ndaxte moom -ànd ak xetam gu teey- day dëgëral yaram wi, du gaaw a yàqu.
Dañuy tàmbalee ci raxas cér yu tedd yi, te mooy: ndayjoor yi, ak céri njàppu yi.
Sopp nañu peñe kawaru néew bu jigéen bi ak létt ko ñatti létt, def ko ci ginnaawu néew bi.
Dagan na ñi dimbalante ci sang néew bi waaye kenn du fa teew ku dul ku ñu fa soxla.
Baarkeelu ci jeexitali Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc niki ay yéreem, lii nag mbir mu mu jagoo la, dubko jéggi di jëm ci keneen ci woroom xam-xam yi ak ñu baax ñi; ndax mbir yii lu ñuy taxawlu la, te sahaaba yi musuñu ko a def ak keneen; ak it ne def jo ak keneen yoon la wuy jëme ci bokkaale, fitna la it ci ki ñuy baarkeelu ci moom.
Dagan na ñu bàyyi ak nit ku wóor mu liggéey ca lañu ko wóolu bu dee man na lañu ko féetale.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (2/ 74) (1258 - 1259).
Téere Muslim bi gën a wér (2/ 646) (939).
Yataal gi (8)
تيسير العلام.
للبسام (ص281).
تنبيه الأفهام.
لابن عثيمين (2/ 360).
الإفهام في شرح عمدة الأحكام.
لعبد العزيز بن باز (ص344).
الإلمام بشرح عمدة الأحكام.
لإسماعيل الأنصاري (1/ 227).