Skip to content

«àdduna ay jumtukaay rekk la, te li gën ci jumtukaay yi àdduna mooy jigéen ju baax».

Jële nañu ci Abdulaah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

«àdduna ay jumtukaay rekk la, te li gën ci jumtukaay yi àdduna mooy jigéen ju baax».

«الدُّنْيَا مَتَاعٌ، وَخَيْرُ مَتَاعِ الدُّنْيَا الْمَرْأَةُ الصَّالِحَةُ».

Muslim soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne àdduna ak li ci biiram mbir mu ñuy bànneexoo ab diir rekk la mu jeex , waaye li gën ci banneexi àdduna mooy jabar ju baax, ji nga xam ne bu ko xoolee bég, bu ko digalee mu topp ko, bu fa nekkul mu wattu ko ci boppam ak alalam.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Dagan na ñu bànneexu ci yu teeyi àdduna yi Yàlla daganalal jaamam ñi ci lu dul yàq mbaa ŋott.

Xemmemloo ci tànn jabar ju baax; ndaxte day dimbali jëkkëram ci topp Boroomam.

Li gën ci bànneexi àdduna mooy lu tege ci topp Yàlla mbaa mu cay dimbaalee.

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér (2/ 1090) (1467).

Yataal gi (6)

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (1/ 365).

كشف المشكل من حديث الصحيحين.

لابن الجوزي (4/ 129).

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.

لمصطفى الخن وغيره (1/ 286).