Skip to content

«Jépp jëf ju baax sarax la».

Jële nañu ci Jaabir Ibn Abdullah -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

«Jépp jëf ju baax sarax la».

«كُلُّ مَعْرُوفٍ صَدَقَةٌ».

Al-Buxaarii soloo na ko ci hadiisu Jaabir, Muslim soloo na ko ci hadiisu Husayfa.
Wér na
Leeral gi

Yónente bi, -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak jàmm, daf nuy xamal ne, bépp rafetal ak njariñ ci nit ñi, moo xam wax la walla jëf, sarax la, te dafay maye ab yool ak tiyaaba.

Maanaay baat yi

معروف : المعروف اسم جامع لكل ما فيه نفع للآخرين من قول أو فعل.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Bokk na ci njariñal adiis bi : Mooy Sarax du yam ci li nit ki di génne ci alalam kepp, waaye day làmboo lépp lu baax lu nit ki def walla mu wax ko, te di ko jottali ñeneen ñi.

Dafay xëcc nit ñi ci def lu baax ak def lépp luy amal njariñ ñeneen ñi.

Bañ a xeeb jëf ju baax, donte daa tuuti.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (8/ 11) (6021).

Téere Muslim bi gën a wér (2/ 697) (1005).

Yataal gi (4)

منحة العلام في شرح بلوغ المرام.

لعبد الله الفوزان (10/ 117).

توضيح الأحكام من بلوغ المرام.

للبسام (7/ 341).