Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

15 of 732 cards

Clear filters
Ñaari gaay xibaar nañu ma ne ñoom dañoo ñëw ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci aju tàggatoo ga fekk muy séddale sarax, ñu laaj ko ca, mu siggi xool nu daal di sëggaat, mu gis ñu ñu dëgër, mu daal di ne: "bu leen neexee ma jox leen, waaye aji-woomal amu vi cér, du caagine it ku am kàttan te man a fàggu ji".
Wér na Abuu Daawuda soloo na ko ak An-Nasaa-iyyu
Yaw Yonnente Yàlla bi, yaayu Sahd de dafa faatu, ban sarax moo gën?, mu ne ko: "ndox", nee na: mu gas ab teen, daal di ne: lii ngir yaayu Sahd la.
Hadiis bu rafet la ci mbooleem yoon yi mu jaar Abuu Daawuda ak An-Nasaa-iyyu ak Ibn Maaja ñoo ko soloo
"tabax nañu lislaam ci juróom: seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, ak ne Muhammat jaamam la di ndawam, ak taxawal julli, ak joxe asaka, ak aji Màkka, ak woor weeru koor ".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc farataal na asakay muurum koor, Saah ci tàndarma,walla Saah ci pepp,ci jaam ak gor, ak góor ak jigéen, ak gone ak mag ci jullit ñi,mu digle ñu joxe ko njëkk nit ñi di génn jëm ca julli ga.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«amul kenn ci yéen lu dul ne Yàlla dina wax ak moom, te kenn kuy firi du nekk seen diggante, mu xool ndayjooram du gis lu dul li mu jiital, mu xool càmmooñam du gis lu dul li mu jiital, mu xool kanamam du gis lu dul sawara wu jàkkarloo ak moom, ragalleen sawara donte dangeen joxe aw xaru tàndarma la».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"Diinaar boo joxe ci yoonu Yàlla, ak Diinaar boo joxe ci goreel jaam, ak Diinaar boo sarax ab miskiin ak Diinaar boo jox sa njaboot ba ca gën a màggug fay mooy bi nga jox sa njaboot ".
Wér na Muslim soloo na ko.
«jëf yi juróom-benn la, nit ñi yitam ñent la ñu, ñaar yuy waral, ak yu tolloo, ak benn bu baax ñu ful fo ba mu mat fukk yunimel, ak wenn yiw wuñu ful bamu mat juróom-ñaari téeméer, budee ñaar yiy waral nag mooy: ku faatu te bokkaalewul Yàlla ak dara dana dugg àjjana, ku faatu nag te bokkaale Yàlla ak dara dana dugg sawara. Yi tolloo nag mooy: ku yéene jëf lu baax ba xolam yég ko, Yàlla xam loolu ci moom, dees na ko bindal wenn yiw, ku def lu ñaaw it dees na ko bindal benn bu ñaaw, ku def lu baax ñu bindal ko fukk yu mel ni moom, ku joxe ci yoonu Yàlla yiw wu nekk dees na ko def juroom-ñaari téeméer. Nit ñi nag ñii dañu leen a yaatalal ci àdduna, xatalal leen ca allaaxira, ñii ñu xatalal leen ci àdduna yaatalal leen ca allaaxira, ñii ñu xatalal leen ci àdduna ak ca allaaxira, ñii ñu yaatalal leen ci àdduna ak ca allaaxira».
Tane na Ahmat soloo na ko.
Daan nanu génne asakay muurum koor jamanoy yónente bi, ngir xale ak mag, gor ak jaam, muy Saah ci ñam, walla Saah ci soow mu ñu wayal, walla Saah ci Pepp, walla Saa, walla Saah ci tàndarma, walla Saah ci Raseen bu wow, daanañ ko génne ba Muhaawiya ibn Abii Sufyaan yal na leen Yàlla dollee gërëm ñëw fi nun di aj, walla umra mu wax ak nit ñi ca kaw Minbar ba, mu bokk ca la mu wax ak nit ñi, mu ne leen: man de gis naa ne ñaari Mudd peppu Saam, day tolloo ak Saah ci tàndarma, nit ñi jël loolu, Abuu Sahiid nee na: man nag moom duma deñ di ko génne na ma ko daan génnee ba fàww fii ak maa ngi dund.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.