Skip to content

xanaa du ki ko doxloo ci ñaari tànkam ci àdduna man na koo doxloo ëllëg bis-pénc ci xar kanamam?

Jële na ñu ci Xataadatu -yal na ko Yàlla yërëm- mu wax ne:

Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax na nu ne benn waay dafa wax ne: yaw Yónente Yàlla bi naka lañuy pange yéefar bi ci xar kanamam ? Mu ne ko: «xanaa du ki ko doxloo ci ñaari tànkam ci àdduna man na koo doxloo ëllëg bis-pénc ci xar kanamam?» Xataadatu wax na: ahakay giñ naa ko ci sunu màggug Boroom.

حَدَّثَنَا ‌أَنَسُ بْنُ مَالِكٍ رَضِيَ اللهُ عَنْهُ أَنَّ رَجُلًا قَالَ: يَا نَبِيَّ اللهِ كَيْفَ يُحْشَرُ الْكَافِرُ عَلَى وَجْهِهِ؟ قَالَ: «أَلَيْسَ الَّذِي أَمْشَاهُ عَلَى الرِّجْلَيْنِ فِي الدُّنْيَا قَادِرًا عَلَى أَنْ يُمْشِيَهُ عَلَى وَجْهِهِ يَوْمَ الْقِيَامَةِ؟» قَالَ قَتَادَةُ: بَلَى وَعِزَّةِ رَبِّنَا.

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Leerarug hdiis bi: Laaj nañu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- naka lañuy pange yéefar bi ci xar kanamam ëllëg bis-pénc?! Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di ne: xanaa du Yàlla mi ko doxloo fii ci àdduna ci ñaari tànkam man na koo doxloo ci xar kanamam ëllëg bis-pénc ?! Yàlla lépp la man.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Bokk na ci njariñal hdiis bi: Doyadig yéefar bi ëllëg bis-pénc ba day doxe ci xar kanamam.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (8/ 109) (6523).

Téere Muslim bi gën a wér (4/ 2161) (2806).

Yataal gi (4)

الإفصاح عن معاني الصحاح (5/200).

فتح الباري (11/382).

عمدة القاري شرح صحيح البخاري (23/ 105).

البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (43/ 454).