Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

47 of 732 cards

Clear filters
«bi Yàlla bindee àjjana ak sawara dafa yónni Jibriil -yal na ko Yàlla dolli jàmm- ca àjjana, ne ko: demal xool ko ak la ma ca waajalal ay ñoñam. Mu xool ko daal di ñëw, ne ko: giñ naa ci sa màgg gi ne kenn du ko dégg lu dul ne dana def lu ko cay dugal. Mu digle ñu wërale ko ak ay tiis, mu ne ko: demal xool ko ak la nu ca waajalal ay ñoñam, mu fekk ñu muure ko ak i tiis mu wax ko ne: giñ naa ci sa màgg gi ragal naa ne kenn du fa dugg. Mu ne ko demal nga xool sawara ak la ma ca waajalal ay ñoñam. Mu xool ko gis waa sawara a nga warante, mu dellu ne ko: giñ naa ci sa màgg gi kenn du def lu la fay dugal. Mu digle ñu muure ko ak i bànneex, mu ne ko: dellul xool ko. Mu xoolaat ko gis ñu muure ko ak i bànneex, mu dellu ne ko: giñ naa ci sa màgg gi ragal naa ne kenn du ca mucc».
Tane na Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy.
«dinaa nekk ca sama mbalka ma di xaar kan ci yéen mooy ñëw ngir naan, waaye dana ñu téye ay nit ba duñu aksi ci man, may wax naan: yaw sama Boroom ci man lañu bokk, ci samaw xeet lañu bokk, ñu wax ma ne: ndax yég nga li ñu def sa ginnaaw, ñoo ngi giñ ci Yàlla ne deñu ñu woon di dellu ginnaaw».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"yaw Bilaal, wax ma jëf joo gën am yaakaar joo def ci lislaam, ndax man dégg naa fëggug say dàll ca sama kanam ca àjjana" mu ne ko: jëfuma jenn jëf ju ma gën a am yaakaar ne man masumaa laab genn laab, ci guddi walla bëccëg, lu dul ne julli naa ci laab googu lu ñu dogal ci man ma julli ko.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"àjjana amna téeméeri daraja diggante ñaari daraja yu nekk day mel ni diggante asamaan ak suuf, Firdawsi moo ca gën a kawe daraja te ca la ñenti dexi àjjana yi di balle, te ca kawam la Aras nekk, bu ngeen dee laaj Yàlla laajleen ko Firdawsi".
Wér na At-tirmisiy soloo na ko.
Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax na nu ne benn waay dafa wax ne: yaw Yónente Yàlla bi naka lañuy pange yéefar bi ci xar kanamam ? Mu ne ko: «xanaa du ki ko doxloo ci ñaari tànkam ci àdduna man na koo doxloo ëllëg bis-pénc ci xar kanamam?» Xataadatu wax na: ahakay giñ naa ko ci sunu màggug Boroom.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa romb ñaari bàmmeel, daal di wax ne : « ñoom ñaar de ñoo ngi leen di mbugal, te sax mbugaluñu leen ci lu rëy, kenn ki moom daawul suturawu bu daan saw, keneen ki nag da daan dox di rambaaj" mu jël aw xob wu tooy, xar ko ñaari xaaj, roof ci bàmmeel bu ne wenn xaaj, ñu ne ko : yaw Yónente Yàlla bi, lu tax nga def lii ? Mu wax ne : "amaana ñu woyafalal leen fii ak wowuñu».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Damaa wax ne: yaw Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- luy mbiri koppi mbalka ma ? Mu wax ne: «giñ naa ci ki bakkanu Muhammat nekk ci loxoom ne ay koppam moo ëpp limu biddiwi asamaan si, ci guddi gu lëndëm te sett, ay koppi àjjana ku ca naan dootul mar ba fàwwu, booba lay mujjee mar, ñaari mball yu bawoo àjjana ñoo fay sottiku, ku ca naan dootul mar, yaatuwaayam moo ngi mel ni guddaayam, moo ngi toll ni diggante Ummaan ak Aylata, ndoxam moo gën a weex meew, te moo gën a neex lem».
Wér na Muslim soloo na ko.
«li ñuy njëkk a àtte ci diggante nit ñi ëllëg bis-pénc mooy dereet ».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.