Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

6 of 732 cards

Clear filters
Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax na nu ne benn waay dafa wax ne: yaw Yónente Yàlla bi naka lañuy pange yéefar bi ci xar kanamam ? Mu ne ko: «xanaa du ki ko doxloo ci ñaari tànkam ci àdduna man na koo doxloo ëllëg bis-pénc ci xar kanamam?» Xataadatu wax na: ahakay giñ naa ko ci sunu màggug Boroom.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Laaj na Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: ban bàkkaar moo gën a màgg fa Yàlla? Mu ne: "nga wutal Yàlla ndend te mu bind la" ma ne: loolu de rëy na lool, ma ne ko: topp ca lan? Mu wa ne: "nga ray sa doom; ngir ne dangaa ragal mu lekkandoo ak yaw" ma ne ko: topp ca lan? Mu ne ma: "nga njaalo ak sa jabari dëkkandoo".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- Muhaas dafa toggoo woon ak moom ci benn waruwaay mune ko: «yaw Muhaas Ibn Jabal», mu ne ko: wuyu naa la yaw Yónente Yàlla bi, mu ne ko: «yaw Muhaas» mu ne ko wuyu naa la yaw Yónéte Yàlla bi, ñatti yoon, mu ne ko: « amul kenn kuy seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la te mu dëggu ci xolam lu dul ne Yàlla dana ko araamal ca sawara», mu ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, ndax duma ko wax nit ñi ngir ñu bég? Mu ne ko: «kon dañuy bàyyandiku». Muhaas waxe ko jamano yi muy faatu ngir bañ a bàkkaaru.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa ñëw ci man fekk ma muure sama kamoot bu ndaw ab moorso bu am ay nataalu yu am ruu, ba mu ko gisee kanam gi soppiku, mu ne ma: "yaw Aysatu,nit ñi gën a tar mbugal fa Yàlla ëllëg bis-pénc ñooy ñiy roy bindub Yàlla bi" Aysatu nee na: "ma dagg ko def ko ñegenaay walla ñaari ñegenaay".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dañoo jiite jullig suba ca Hudaybiya ginnaaw ba mu tawee ca guddi ga, ba mu noppee mu jàkkaarloo ak nit ñi, ne leen: «ndax xam ngeen lan la séen Boroom wax ?» Ñu ne ko: Yàlla a xam ak ub Yónenteem, mu ne leen: Yàlla dafa wax ne: «am na ci sama jaam ñi ñu xëy gëm ma am ñu weddi, ku wax ne: taw bi wàcc na fi nun ci ngënéelu Yàlla ak yërmàndeem, kooku gëm na ma, weddi biddiw yi, waaye ku wax: taw bi biddiw bii mbaa bee mootax mu am, kooku weddi na ma, gëm biddiw yi».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"Yaw ngóor si dinaa la xamal ay waat: wattul Yàlla kon Yàlla dina la sàmm, nanga bàyyi xel Yàlla kon mu féete la fépp, booy ñaan ñaanal Yàlla, booy sàkku ndimbal na nga dimbandikoo Yàlla, te nga xam ne bu ñépp daje woon ngir jariñ la ci dara duñu ko man lu dul lu Yàlla dogal ci yaw ba noppi, bu ñépp daje woon it ngir lor la ci dara duñu ko man lu dul lu Yàlla dogal ci yaw ba noppi; ndax teggi nañu bindukaay ya, te àlliwo ya wow na".
Wér na At-Tirmisiyyu moo ko soloo ak ñeneen.