Ku bind àdduna bi? Ak kan moo ma bind? Ak lu tax?
Ndax maa ngi ci yoon wu baax Wi? Kam moo bind asamaan yi ak suuf si ak li ci nekk ci ay mbindeef yu màgg yoy kenn du leen peeg ? Kan moo amal nosiin wu sew wii ñu xereñe ci asamaan yi ak suuf si? Kan moo bind nit may ko dégg ak ub jis ak xél def ko muy ku man a sàkku ay xam-xam ak peeg dëgg yi?
These files are generated automatically from the book's text; their layout may differ from the printed edition.
Ku bind àdduna bi? Ak kan moo ma bind? Ak lu tax?
Ndax maa ngi ci yoon wu baax Wi?
Kam moo bind asamaan yi ak suuf si ak li ci nekk ci ay mbindeef yu màgg yoy kenn du leen peeg ?
Kan moo amal nosiin wu sew wii ñu xereñe ci asamaan yi ak suuf si?
Kan moo bind nit may ko dégg ak ub jis ak xél def ko muy ku man a sàkku ay xam-xam ak peeg dëgg yi?
Kan moo fent liggéey bu sew bii ci sa céri yaram, ak sa melo, re rafetal saw melo?
Settantal ni ñu binde mbindeef yiy dund ak ni ñu wuutee ak ni ñu baree, kan moo ko fent ak i meloom yu amul yamukaay?
Naka la àdduna bu màgg bii nosewoo ci ay tëraliinam yu koy tënk tënk gu sew ci ay at yu bari?
Ana kan mooy ki teg xeeti tëralin yiy àtte àdduna bi (dund ak dee, jurante gi, guddi ak bëccëg, soppaxndikug jamono, añs)?
Ndax àdduna bi moo bind boppam? Walla dafa bawoo ci lu amul? Walla daa jekki jekki rekk am? Yàlla mu kawe mi neena: {ndax dañu leen a bind ci lu dul dara walla ñoom ñoo bind(35) Walla ñoom ñoo bind asamaan yi ak suuf si, ñoom kay dañoo wóolu wul rekk} [At-Tuur: 35-36].
Bu ñu bindul sunu bopp te jomb na nu bawoo ci lu amul walla jekki jekki rekk am kon nag dëgg gi amul sikk-sakka mooy: àdduna manul ñàkk ku màgg te am kàttan ku ko bind, ndaxte jomb na àdduna bii di bind boppam! Walla mu jóge ci lu amul! Walla mu jekki jekki am!
Lu tax nit ki di gëm mbir yi mu gisul? Niki: (peeg ak xel ak ruu ak yég-yég ak bëgg) xanaa du ndax day gis ay jeexitalam? Naka la nit di weddee ki bind àdduna su màgg sii tey gis ay jeexitali mbindeefam ak liggéeyam ak yërmàndeem?!
Kenn du nangu ñu ne ko kër gii dafa jekk-jekki am te kenn tabaxu ko! walla ñu ne ko lu amul moo amal kër gile! Kon naka la ñenn ci nit ñi di gëmee ne dénd bii dafa am wolif kenn di ko sàkk? Naka la aji-xellu di nangoo ñu naan ko dénd bu nosu bii dafa jekki-jekki rekk am?
Lii lépp da ñuy yóbb ci lenn ngirte, te mooy dénd bii am na Boroom bu màgg bu koy doxal, te moom doŋ moo yeyoo jaamu, ak ne lépp lu ñuy jaamu te du moom jaamu ga ag neen la, te yeyoowul ñu jaamu ko.
Boroom bi mooy Aji-Bind ju màgg ji
Kon am na Boroom buy Aji-Bind tey kenn, te mooy Aji-Moom ji di Aji-Doxal ji di Aji-Wërsëgale ji di dundal di ray, te moo bind suuf si tàggat ko, def ko muy lu baax ci mbindeefam yi, moom moo bind asamaan la ca nekk ci ay mbindeef yu màgg, mu defal jànt bi ak weer wi ak guddi gi ak bëccëg gi nose gu sew gii di tegtale ak màggam.
Moom moo nu tàggatal ngelaw lii nga xam ne dund manut a am ci lu dul moom, moo ñuy wàcceel taw yi tàggatal nu géej yi ak dex yi, moo ñu doon dundal doon ñu wattu fekk noo nga ca sunu biir yaay ya te amunu woon kàttan, mooy dawal dereet ji ci sunuy séddit ba nu juddoo ba baa nuy dee.
Boroom bii di Aji-Bind ji di Aji-Wërsëgale ji mooy Yàlla mu Sell mi te Kawe.
Yàlla mu kawe mi neena: ﴾Séen Boroom mooy Yàlla mi bind Asamaan yi ak Suuf yi, ci juróom-benni fan, daal di yemoo ca kaw Aras, day muure guddi gi bëccag gi, mu di ko sàkku bu gaaw, jant bi ak weer wi ak biddiw yi dees leen a tàggat ci ndigalam, dama ne moom mooy Boroom mbindeef yi ak mbir ya, Yàlla daal ku baarkeel la te mooy Boroom mbindeef yépp 54﴿ [Al-Ahraaf: 54].
Yàlla mooy Boroom bi bind lépp lu nekk ci dénd bi li nuy gis ak li nu gisul, te lépp lu dul moom mbindeef la ci mbindeefam yi, te moom rekk moo yayoo jaamu, te deesu ko boole ak kenn cig jaamu, amul bokkaale ci nguuram gi walla ci mbindeefam yi walla ci doxal gi mbaa ci jaamu gi.
Bu ñu nattale woon ne am na yeneeni Yàlla yu fi nekk ak Yàlla mu màgg mi kon àdduna bi yàqu; ndax mbiri àdduna bi ñaari Yàlla manuñu koo doxal ci benn jamono, Yàlla mu kawe mi nee Na: {bu fi ñaari Yàlla nekkoon yu dul Yàlla kon ñu yàqu} Al-Anbihaa: 22.
Meloy Boroom biy Aji-Bind ji
Boroom bi Tudd naa sellam gi am na ay tur yoy maneesu koo takk, am na it ay melo yu kawe te bari te màgg yuy tegtale ag matam, bokk na ci ay turam: Aji-Bind ji, ak "Allaa" maanaam mooy: ki ñuy jaamu te mu yeyoo Ag jaamu moom rekk amul bokkaale. Ak Aji-Dund ji, Aji-Taxawe bir yi, Aji-Yërëme ji, Aji-Wërsëgale ji, Aji-Tedd ji, Yàlla mu kawe mi nee na: {Yàlla dey ! Amul jeneen Yàlla ju dul Moom, Aji-Dund la, Aji-Taxaw la, lépp la taxawe. Gëméntu du ko jàpp du caagine ay nelaw. Moo moom li nekk ci asamaan yi ak ci suuf si. Ana kan moo sañ a tinu fa moom te du ci ndigalam? Moo xam la nekk ci séen kanam ak la nekk ca séen ginnaaw. Te kenn du peeg dara ci xam-xam lu dul la ko ca soob. Gàngunaayam ga daj na kaw ak suuf, lu leen wattu ñoom ñaar tëwu ko. Mooy ki kawe te màgg} [Saaru Al-Bàqara: 255].
Yàlla mu kawe mi nee na: {waxal ne Yàlla kenn la(1) Yàlla mooy jubluwaay bi(2) Jurul kenn te kenn juru ko(3) Te amul benn nawle} [Al-Ixlaas: 1-4].
Boroom bi ñuy jaamu day melowoo meloy mat yi
Bokk na ci ay meloom mooy ki ñuy jaamu, te lu dul moom mbindeef la bu ñuy digal te di lu ñu not.
Bokk na ci ay meloom mooy Aji-Dund ji, di Aji-Taxawe mbir yi, lépp luy dund ci li am Yàlla moo ko dundal amal ko mu bawoo cig ñàkk, te moom mooy Aji-Taxaw ci ag am-am ag wërsëgam ak aar ko. Boroom bi Aji-Dund la te du dee, te jeex jomb na ko, Aji-Taxaw la te du nelaw, du gëmmentu sax du caagine nelaw.
Bokk na ci ay melo moom Aji-Xam la dara du ko nëbbu ci moom ci suuf walla ci asamaan,
Bokk na ci ay meloom moom Aji-Dégg la, Aji-Gis la day dégg lépp, di gis mbindeef yépp, dafa xam it lépp luy jax-jaxi ci bakkan yi, ak li xol yi nëbb, dara du ko nëbbu moom Aji-Sell ji ci suuf ak ci asamaan.
Bokk na ci ay meloom mooy kiy Aji-Am kàttan gu dara tëwul, te kenn manul a delloo nàmmeelam, mooy def lu ko soob, di bàyyi lu ko soob, mooy jiital di yeexe, mooy ki am xereñ gu mat gi.
Bokk na ci ay meloom mooy Aji-Bind ji di Aji-Wërsëgale ji, di Aji-Doxal ji nga xam ne moo bind mbindeef yi di ko doxal, mbindéef yépp ci ab ŋëbam ak ci noteelam lañu nekke.
Bokk na ci ay meloom moom mooy kiy wuyu aji-loru ji, di xettali aji-xettaliku ji, di dindi tiis yi, te mbindeef yépp bu ñu tàbbee ci tiis ak xat-xat dañuy làqu ci moom ci lu manut a ñàkk.
Jaamu ñeelul ku dul Yàlla mu kawe mi, moom mooy Aji-Mat ji ki ko yayoo moom doŋ du keneen, te lépp lu ñuy jaamu te du moom dees koy jaamu cig neen, te dana dee aana jeex.
Yàlla wërsëgal na nu ay xel yu nuy xame lenn cig màggaayam, mu def ci nun yég-yég bu nuy bëgge yiw, tey bañ aw ay, su nu xel yi di dal saa su làqoo ci Yàlla Boroom mbindeef yi, te yëg-yëg bii day tektale ak matam, ak ne moom maneesu koo melal cig wàññiku tudd naa sellam gi.
Du jaadu ci aji-xellu ji muy jaamu ku dul ku mat ki, kon naka lay jaamoo mbindeef mu wàññiku ni moom, walla mu gën koo suufe!
Ki ñuy jaamu manul a nekk nit walla ab xërëm walla garab walla ab baayima!
Boroom bi mi ngi ci kaw asamaan yi, yemoo ca kaw Arasam ja, teqalikoo ak mbindeefam yi, dara ci mbindeefam yi nekkul ci jëmmam ji, dara ci jëmmam ji it nekkul ci mbindeefam yi, du wàcci walla muy nekk jëmm ci dara ci mbindeefam yi.
Boroom bi dara niróowul ak moom, te mooy Aji-Dégg ji di Aji-Gis ji, te amul benn nawle, te mooy Aji-Doylu ji wolif mbindeefam yi, du nelaw du lekk ñam, te ku màgg la jaaduwul muy am soxna walla doom; Aji-Bind ji am na ay melo yu màgg jaaduwul mukk muy melowoo aajo walla wàññiku.
Yàlla mu kawe mi nee na: { yéen nit ñi, ñi ngi leen di léebu, dégluleen ko, ñi ngeen di jaamu di leen ñaan te bàyyi fi Yàlla duñu mas a bind mukk aw weñ donte dañoo dajaloo ngir def ko, te bu leen wenn weñ jëlaloon dara, duñu ko man a nangu ci moom, kay jaamu ak la muy jaamu ñépp a néew doole(73) Joxuñu Yàlla gëddaam, te Yàlla mooy ki am kàttan te not} [Al-Hajji : 73-74].
Lu tax Aji-Bind ju màgg jii bind nu? Ak lan la bëgg ci nun?
Ndax xellu na Yàlla bind mbindeef yi ci lu dul benn jubluwaay, walla mu bind ngir fo, te moom mooy Aji-Xereñ ji di Aji-Xam ji?
Ndax xellu na ki nu bind ci gile nose ak xereñte tàggatal nu li nekk ci asamaan yi ak suuf si, mu bind nu ci lu dul jubluwaay walla mu bàyyi ñu ci ku dul tontu laaj yi ëpp solo te gën noo soxal, niki: lu tax nu nekk fi? Ak luy xew ginnaaw dee? Ak luy jubluwaayu bind gi ñu nu bind?
Ak ndax xellu na mbugal bañ a am ñeel tooñkat yi ak pay bañ a am ñeel way-rafetal yi?
Yàlla Aji-Sell ji nee na: {Mo ndax dangeen a njortoon ne caaxaan rekk a taxoon nu bind leen, ba ngeen njort ne dungeen dellusi fi nun} [Al-Muuminuuna : 115].
Waaye Yàlla dafa yónni yonnente yi ngir nu xam li tax nu nekk fi, mu xamal nu naka lanu koy jaamoo ak di ko jéem a jege, lan la bëgg ci nun! Ak nan lanuy ame ngërëmam, mu xibaare ñu sunug mujj ginnaaw dee?
Yàlla dafa yónni yonnentey yi ngir ñu xibaare ñu ne moom rekk moo yayoo jaamu, ak ngir nu xam naka lanu koy jaamoo, ak ngir ñu jottali nu ay ndigalam ak i tereem, ak ñu xamal nu jikkó yu baax yi Nga xam ne bu ñu ko jëlee sunug dund dana teey dina barkeel.
Yàlla yónni na ay yonnente yu bari, niki: (Nuuh, Ibraahiima, Muusaa, ak Iisaa) mu dëgëral leen ci ay aaya ak i keemaan yuy tegtale séenug dëggu ak ne ñoom ñu ñu yónni lañu ñu bawoo fa Yàlla, ki ci mujj mooy Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.
Yonnente yi xibaar nañ ñu ci lu leer ne dund gii ag nattu la waaye dëgg-dëggi dund ginnaaw dee lay am.
Te foofu am na àjjana ju ñeel way-gëm ñiy jaamu Yàlla doŋ te duñu ko bokkaale, ñu gëm mbooleem yonnente yi, foofu it am na sawara si Yàlla waajalal yéefar yiy jaamu ay Yàlla di ko bokkaale ak Yàlla, walla ñu weddi ab yonnente ci yonnente Yàlla yi.
Yàlla mu kawe mi nee na: {yéen doomu Aadama yi ay yonnente danañu leen dikkal di leen jàngal samay aaya kepp ku ragal Yàlla te sellal ñooñu duñu ragal te duñu jàq(35) Ñi weddi sunuy aaya di rëy-rëylu ñooñu ñooy waa sawara te fa lañuy sax} [Al-Ahraaf: 35-36].
Yàlla nee na: {yéen nit ñi jaamuleen séen Boroom bi leen bind yéen ak ña leen jiitu ndax ngeen ragal Yàlla(21) Yàlla moomu moo leen lalal Suuf si, tabaxal leen Asamaan si, wàcce ndox ci Asamaan génne ci gàncax muy wërsëg ci yéen, kon buleen wutal Yàlla ay moroom te fekk xam ngéen ko (22) Bu ngeen dee sikk-sàkka ci li nu wàcce ci sunu jaam bi, kon indileen wenn saar wu mel ni moom (Alxuraan), te ngeen woo séen i seede wolif Yàlla ndeem wax ngeen dëgg(23) Bu ngeen ko deful te dungeen ko def mukk, kon na ngeen ragal sawara si nga xam ne la koy xamb mooy nit ak ay xeer te waajalees na ko ñeel yéefar yi(24) Na nga bégal ña gëm tey jëf jëf yu sell, ci ne am nañu àjjana joo xam ne ay dex a ngay daw ca suufam ; saa su ñu leen xéewalee ci ay meññeet, muy la ñu leen wërsëgale, ñu naan: “Lii dey masoon nanu cee xéewlu [ca àddina]”. Fekk dañu leen a jox lu niróo ak [la ñu xamoon ca àddina]; ñeel na leen it ca àjjana jooju ay jabar [soxna] yu ñu laabal [ci jépp ayib], te ñoom dañu fay sax} de. [Al-Baqara 21-25].
Lu tax Yonnente yi bari?
Yàlla yónni na ay yonnente ci xeet yi, amul wenn xeet lu dul ne Yàlla yónni na fa ñoom ab yonnente, ngir mu woo leen ci jaamu séen Boroom, ñu leen di jottali ndigali Yàlla yi ak i tereem, te séen jubluwaayu woote ñoom ñépp mooy: jaamu Yàlla mu màgg mi moom dong, saa bu aw xeet tàmbalee bàyyi walla di ñaawal la séen yonnente ba indi woon, ci kennal Yàlla, Yàlla daal di digalaat beneen yonnente ngir mu jubbanti yoon wa, delloo nit ñi ci diine ju mucc tege ci kennal Yàlla ak topp ko, Ba mujj Yàlla tëje yonnent gi ci Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- moom mi indi diine ju mat ak Sariiha ju sax te matale mbooleem nit ñi ba ëllëg bis-pénc, muy mottali ak di folli li ko jiitu woon ci ay Sariiha, Yàlla gaaranteel diine jii Ag des ak ug sax ba bis-pénc.
Nit ki du nekk aji-gëm ba keroog muy gëm mbooleem yonnente yi.
Yàlla mooy ki yónni yonnente yi, digal mbooleem mbindeef yi ñu topp leen, ku weddi yonnenteg kenn ci ñoom kooku weddi na ñépp, amul benn bàkkaar bu gën a màgg nit ki di delloo wahyug Yàlla gi, kon ngir dugg àjjana manul ñàkk ñu gëm mbooleem yonnente yi.
Li war kenn ku ne ci jamono ji mooy mu gëm Yàlla ak mbooleem yonnente Yàlla yi, gëm bis bu mujj ba, te loolu manul am lu dul ci topp ki mujj ci yonnente yi di Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, moom mi ñu dëgëral ci kéemtaan guy sax te mooy Alxuraan ju tedd ji, moom mi Yàlla di sàmm ba keroog mu fiy jële suuf si ak lépp lu nekk ci kawam.
Yàlla tudd na ci Alxuraan ju tedd ji ne ku bañ a gëm ab yonnente ci Yónnenteem yi kooku ku weddi Yàlla la te ku weddi waahyoom la, Yàlla mu kawe mi nee ña: {Ña weddi Yàlla ak i Yonnenteem, te bëgg a teqale Yàlla ak i Yonnenteem, te naan gëm nanu ñenn ña, weddi ñenn ña [ca Yonnenteem ya] ñuy jéem a wut aw yoon ca diggante ba(150) Ñooñu ñooy yéefar ya dëgg, te waajalal nanu yéefar mbugal mu leen di toroxal} [An-Nisaa:150-151].
Loolu moo tax nun jullit ñi dañoo gëm Yàlla ak bis bu mujj ba -kem ni ko Yàlla diglee- nu gëm it mbooleem Yonnente yi ak téere yi jiitu, Yàlla nee na: {Yonnente bi gëm na li ñu wàcce ci moom mu bawoo si Boroomam, jullit yi ñépp gëm nañu Yàlla ak i malaakaam ak i téereem ak i yonnenteem, du ñu teqale kenn ci yonnente yi, ñuy wax naan dégg nanu te topp nanu, noo ngi sàkku sa njéggal yaw sunu Boroom, te yaw rekk yaay delluwaay ba} [Al-Baqara : 125].
Lan mooy Alxuraan ju tedd ji?
Alxuraan ju tedd ji mooy waxi Yàlla mu kawe mi di waahyoom wu mu wàcce ci ki mujj ci yonnente yi muy Muhammat, te mooy kéemtaan gi gën a màgg guy tegtale dëggug Yónnenteem, Alxuraan ju tedd ji mooy dëgg ci ay àtteem di dëgg ci ay xibaaram, Yàlla ngi dëkk ñi koy weddi ci ñu indi donte wenn saar la wu niróo ak moom, ñu tële ko; ngir màggaayu li mu làmboo ak yaatuwaayu peeg gi mu peeg lépp lu aju ci nit ci dundug àdduna ak allaaxira, làmboo na mboolem biri ngëm yi ñu war a gëm, Niki mu làmboo ay digle ak i tere yu war nit ki mu jaar ca ci digganteem ak Boroomam, walla ci digganteem ak boppam, mbaa digganteem ak yeneen mbindeef yi, loolu lépp nag ci waxiin wu kawe ci jot ak leer, Làmboo na lu bari ci ay tegtali xel ak ay xam-xam yu dëggu yuy tegtale ne téere bii manut a nekk liggéeyu nit waaye waxi Yàlla miy Boroom nit ñi la tudd naa sellam ga.
Lan mooy lislaam?
Lislaam mooy jébbalul Yàlla mu kawe mi ci wéetal ko, ak wommatul ko cig topp, ak jëfe sariihaam ji ci gërëm ak nangu, ak weddi lépp lu ñuy jaamu te du Yàlla.ذ
Yàlla dafa yónni yonnente yi ci benn bataaxal, te mooy: woote ci jaamu Yàlla moom rekk amul bokkaale, ak weddi lépp lu ñuy jaamu te du Yàlla.
Lislaam mooy diiney mbooleem yonnente yi, séen ug woote genn la, séen i Sariiha moo wuute, jullit ñi tay ñooy ñiy wéetal Yàlla te jàpp ca diine ju wér ja yonnente yépp indi woon, te bataaxalu lislaam ci jamono jii mooy dëgg, te mooy bataaxal bi mujj, jóge ci Aji-Bind ji ñeel nit ñi, Boroom bi yónni Ibraahiima ak Muusaa ak Iisaa -yal na leen Yàlla dolli jàmm- moo yónni ki mujj ci yonnente yi di Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- sariihab Lislaam dafa ñëw folli sariiha yi ko jiitu woon.
Diine yi nit ñi di jaamoo Yàlla tay -ba mu des lislaam- ay diine yu nit ñi sos la, walla muy ay diine yu bawoo woon fa Yàlla loxoy nit ñi fowe ko ba mu mujj nekk njaxas mu dajaloo ak i léeb ak i nettali yu ñu dondante ak ay gisiini nit.
Bu dee diiney Lislaam nag moom Jenn diine la ju leer te du soppiku, kem ni séen i jaamu yi ñuy jaamoo Yàlla nekke benn, ñoom ñépp dañuy julli julliy juróom, di joxe asakay séen i alal, di woor weeru koor, settantal séen téere bi ñuy àttewoo di alxuraan ju tedd ji moom benn téere la ci mbooleem réew yi. Yàlla nee na: {Bis niki tay matalal naa leen séen diine xëpp naa leen samay xéewal gërëm naa ci yéen lislaam muy séen diine} [saaru Al-Maa-id: 3].
Yàlla mu kawe mi wax na ci Alxuraan ju tedd ji ne: {Waxal ne gëm nanu Yàlla ak li ñu wàcce ci nun ak li ñu wàcce ci Ibraahiima ak Ismaahiila ak Ishaaqa ak Yanqooba ak sët ya ak la ñu joxoon Muusaa ak Iisaa ak Yonnente ya mu bawoo fa séen Boroom te dunu teqale kenn ci ñoom te nun ci moom lanu jébbalul(84) {Ku sàkku jeneen diine ju dul lislaam deesu ka ko nangul, te Allaaxira day bokk ca way-ñàkk ya} [Saaru Aali-Imraan: 84-85].
Diiney Lislaam doxaliin la wu matale dund gi yépp, dafa dëppoo ak yég-yég ak xel, bakkan yi sell yi it da koy nangu, Aji-Bind ji dakoo yoonal ñeel mbindeefam yi, diiney yiw la ak texe ñeel nit ñépp ci àdduna ak allaaxira, xàjjalewul xeet ak xeet, walla melo ak melo, nit ñépp a ci y1m, kenn du ràññeeku ci Lislaam ci kaw kenn lu dul ci ay jëfam yu sell.
Yàlla mu kawe mi nee na: (Képp ku jëf lu baax muy góor mbaa jigéen te fekk mu nekk Ku gëm, dananu ko dundal dund gu teey, te dananu leen fay séenug payoor lu gën a rafet la ñu doon def) [Saaru An-Nahl: 97].
Lisalaam mooy yoonu texe!
Lislaam mooy diiney mbooleem yonnente yi, di diiney Yàlla ñeel nit ñépp, waaye nekkul diine ju araab yi jagoo.
Lislaam mooy yoonu dëggi-dëggi texe ci àdduna, ak xéewal guy sax ca allaaxira.
Lislaam moom rekk mooy diine ji man a faj aajoy ruu yi ak yaram yi, ak lijjanti mbooleem jafe-jafey nit ñi, Yàlla nee na: {mu wax Aadama ak Awa ne leen wàccleen yéen ñépp, ñenn ñi di noon ci ñenn ñi, samag njub dina leen dikkal, képp ku topp samag njub kooku du sànku du texeedi(123) Képp ku dummooyu sama Alxuraan ji dana dund dund gu xat te dananu ko dekkile bis-pénc ba mu gumba} [Taaha:123-124].
Lan laay jariñoo ci dugg ci lislaam?
Dugg ci Lislaam am na ay njariñ yu màgg, bokk na ca:
- texe ak teddnga fii ci àdduna, ci nit ki nekk jaamub Yàlla kese, bu dul loolu day nekk kuy jaamu bànneexu bàkkanam ak saytaane ak neex-neex yi.
- texe ca allaaxira ci Yàlla jéggal ko, ngërëmam wàcci ci moom, Yàlla dugal ko àjjana, mu texe ci ngërëmam ak xéewalam gu sax gi, ak nit ki mucc ci mbugalum sawara.
- aji-gëm ji ëllëg bis-pénc day nekk ak yonnente yi ak way-dëggal yi ak ñi dee ci xare ak ñu sell ñi, te àndandoo gënu ko a neex, ku gëmul nag day ànd ak ñu bew ñi ak ñu bon ñi ak tooñkat yi ak yàqkat yi.
- ñi Yàlla di dugal àjjana danañu dund xéewal guy sax ci lu dul dee walla feebar walla mettit walla màggat mbaa njàqare, te dana leen wuyu ci séen i xemmemteef ci lépp lu ñu bëgg, ñiy dugg sawara nag danañu nekk ci mbugal muy sax te du dog ba fàww.
- àjjana am na ay xéewal yu bët musul a gis, nopp musu ko a dégg, te musul rot ci xélum nit. Bokk na ci liy tegtale loolu, li Yàlla wax ne: ﴾ Ku jëf lu baax moo xam góor walla muy jigéen te ànd ak ngëm dananu ko dundal dund gu teey, te dinanu leen fay séen ub yool ci lu gën a rafet la ñu doon jëf ﴿ [An-Nahl: 25]. Yàlla mu kawe mi wax na: {benn bakkan xamul li ñu ko dencal ci ay mbégte yu neex a xool, ngir Faye leen ko la ñu doon def} [Saaru As-Sajdatu: 17]
Lan laay ñàkk bu ma bañee Dugg ci Lislaam?
Nit ki dana ñàkk xam-xam bi gën a màgg, te mooy xam Yàlla, te dana ñàkk gëm Yàlla miy may nit ki kóolute ak ug dal ci àdduna ak xéewal guy sax fa allaaxira.
Nit dana ñàkk a yër téere bi gën a màgg ci téere yi Yàlla wàcce ci nit ñi, ak gëm téere bu màgg bii.
Nit ki dana ñàkk gëm yonnente yu màgg yi niki muy ñàkke ànd ak ñoom ca àjjana ja ëllëg bis-pénc, te dana ànd ag saytaane ak tooñkat yi ak way-bew ñi ca sawaraw Jahannama, te kër googu ak dëkkandoo googu bon na.
Yàlla mu kawe mi nee na: {waxal ne ñi ñàkk dëgg-dëgg ñooy ñi ñàkk séen bopp ak séen i njaboot ëllëg bis-pénc, xanaa du loolu mooy ñàkk gu bér ga(15) Dana leen tiim ci kaw ay muuraayu sawara ci séen suuf it ay laytaayu sawara, loolu la Yàlla di xuppe jaamam ñi kon yéen sama jaam ñi ragalleen ma} [As-Sumari: 15-16].
Ku bëgg a mucc fa allaaxira war na ci moom mu dugg ci Lislaam te topp Yonnente bi Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.
Bokk na ci dëgg yi nga xam ne yónente yépp dëppoo na ñu ci mooy kenn du mucc ci sawara bis-pénc ludul jullit ci gëm Yàlla te bokkaalewuñu ko ci jaamu gi ak kenn, daal di gëm mbooleem yónente yi, ñi topp yonnente yi te gëm leen te dëggal leen danañu dugg àjjana, te danañu mucc ci sawara.
Ña nekkoon ca jamonoy yonnente Yàlla Muusaa gëm ko te topp ko ñooña ay jullit lañu ay way-gëm lañu ñu sell lañu, waaye ginnaaw ba Yàlla yónnee Hiisaa war na ña toppoon Muusaa ñu gëm Hiisaa te topp ko. Ñu gëm Hiisaa ay jullit lañu ñu sell lañu, ñi bañ a gëm Hiisaa naan damay des ca diiney Muusaa kooku gëmul; ndax dafa bëñ a gëm ab yonnente bu Yàlla yónni, Ginnaaw ba Yàlla yónnee ki mujj ci yonnente yi di Muhammat -yal ña ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, day war ñépp gëm ko, ndax Boroom bi yónni Muusaa Hiisaa saa moo yónni ki mujj ci yonnente yi muy Muhammat, ku weddi yónnenteg Muhammat naan damay des di topp Muusaa walla Hiisaa saa kooku gëmul.
Du doy nit ki naan wormaal na jullit ñi rekk, te saraxe ak dimbali miskiin yi du doy ngir mucc àllaxira, waaye fàwwu mu gëm Yàlla ak ay téereem ak i yonnenteem ak bis bu mujj ba; ngir Yàlla nangu loolu ci moom; ndax amul bàkkaar bu gën a màgg bokkaale ak weddi Yàlla ak delloo wahyu gi Yàlla wàcce walla bañ yónnenteg ki mujj ci yonnente yi di Muhammamt.
Yahuut yi ak Nasaraan yi ak ñeneen ñi dégg yónnig Yonnete Yàlla bi Muhammad -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ñu bañ koo gëm bañ a Dugg ci Lislaam ñooñu danañu dugg sawaraw Jahannama sax fa ba fàww, lii mooy àtteb Yàlla waaye du àtteb kenn ci nit ñi, Yàlla mu kawe mi nee na: {ñi weddi ci ñoñ téere yi ak bokkaale danañu nekk ca sawaras Jahannama sax fa, ñooñu ñoo yées ci nit ñi} [Al-Bayyina: 6].
Kon ndeem bataaxalu Yàlla bi mujj wàcc na ci nit ñi, day war bépp nit bu dégg yónneteg ku mujj ki di Muhammamt -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, mu gëm ko te topp sariihaam topp ay ndigalam bàyyi ay tereem, lii moo tax képp ku dégg yónnente gu mujj gii ba noppi bañ ko, kooku Yàlla du ko nangul dara, te dana ko mbugal allaaxira.
Bokk na ci liy tegtale loolu, waxi Yàlla mu kawe mi: {Ku sàkku jeneen diine ju dul lislaam deesu ko nangul, te allaaxira day bokk ca way-njàkk ña} [Aali-Imraan: 85].
Yàlla mu kawe mi wax na: {Neel: “Yéen ñoñ-téere yi, kaayleen ci baat boo xam ne yéen ak nun noo ciy yam kepp: dunu jaamu ku dul Yàlla, te dunu ko bokkaale ak dara, te kenn ci nun bañ a jël moroomam jàppe ko Yàlla, di ko jaamu wolif Yàlla”. Su ñu bañee ba dummóoyu, nee leen : “Seedeleen ne nun déy ay jullit lanu} [Aali-Imraan: 64].
Lan moo ma war ngir ma nekk jullit?
Ngir Dugg ci Lislaam war na ñu gëm juróom-benni ponk yii:
Gëm Yàlla mu kawe mi ci ne mooy Aji-Bind ji, di Aji-Wërsëgal , di Aji-Doxal ji, di Aji-Moom ji, te dara melul ni moom, amul jabar du caagine doom, moom rekk moo yeyoo jaamu, ak bañ a jaamu kenn di ko boole ak moom, ak mu fas ne jaamu keneen ku dul moom ag neen la.
Gëm malaaka yi ci ne ñoom ay jaami Yàlla lañu, ci leer la leen bind, mu boole ci séen liggéey ne ñoom ñooy wàcce wahyu ci yónnenteem yi
Gëm mbooleem téere yi Yàlla wàcce ci yónnenteem yi (niki Tawraat ak Injiil -njëkk ñu leen di soppi) ak bi mujj ci téere yi muy Alxuraan ji tedd ji.
Gëm mbooleem yonnente yi niki Nuuh ak Ibraahiima ak Muusaa ak Hiisaa ak ka ca mujj di Muhammat, ñoom nag ay nit lañu, Yàlla da leen a dëgëral ci Wahyu jox leen ay aaya ak i kéemtaan yuy tegtale séenug dëggu.
Gëm bis bu mujj ba bi Yàlla di dekkal ñu njëkk ak ñi mujj, Yàlla àtte diggante jaamam yi, dugal way-gëm yi àjjana, yéefar yi sawara.
Gëm dogal yi ci ne Yàlla xam na lépp, Li weesu ak liy ñëw ëllëg, ak ne Yàlla xam na te bind na loolu, te soob na ko, te moo sàkk lépp.
Bul yeex a jël say matuwaay!
Àdduna du kërug sax...
Bépp taar Dana masa làqu te bépp bànneex dana masa naaxsaay...
Bis dana ñëw ñu càmbar nit ki ci lépp lu mu masa def, te mooy bis-pénc, Yàlla mu kawe mi nee na: { Buñu gaaralee téere ba. nga gis saay-saay sa tiit lool ngir la nekk ca biir, ñu naan : “Ay nun funu jëm cëy waay téere bii, bàyyiwul lu ndaw bàyyiwul lu rëy, lu dul bind na lépp ? ” Ñu gis la ñu defoon mu tege. Te sa Boroom du tooñ kenn} [Al-Kahf : 49].
Yàlla xamle na ne nit ku jébbaluwul mujjam mooy sawaraw Jahannama te fa lay sax ba fàww.
Ñàkk du lu tuuti waaye lu rëy la, Yàlla mu kawe mi nee na: {Ku sàkku jeneen diine ju dul lislaam deesu ka ko nangul, te Allaaxira day bokk ca way-njàkk ña} [Aali-Imraan: 85].
Lislaam mooy diine ji nga xam ne Yàlla du nangu Jeneen diine ju dul moom.
Yàlla moo nu bind te fi moom lanuy dellu, àdduna bii nag nattu rekk la ñeel nu.
Na nit am kóolute ci ne: àdduna bii dafa gàtt kem ay gént... Te kenn xamul kañ lay dee!
Lan lay Tontu Boroomam bu ko laajee ëllëg bis-pénc: lu tax toppul dëgg? Lu tax toppul ki mujj ci yonnente yi?
Lan ngay Tontu sa Boroom ëlleg bis-pénc, te moom moytandikuloo na li weddi lislaam di jur, mu xibaare ne mujjug yéefar mooy alkande ca sawara?
Yàlla nee na: {Ñi weddi Yàlla di fenloo sunuy aaya ñooñu ñooy waa sawara te fa lañuy sax} [Al-Baqara : 39].
Ku bàyyi dëgg, di topp baay yi ak maam yi kooku du am lay
Yàlla mu màgg mi xamal na ñu ne ñu bari ci nit ñi dañuy bañ a dugg ci Lislaam ngir ragal barab ba ñuy dund.
Ñu bari it dañuy lànk a dugg ci Lislaam ngir bañ a soppi séen pas-pas ya ñu donne ca séen baay ya walla ñu jële ko ca barab ba ñuy dund ak mbooloo ma, ba ñu tàmm ko, ñu bari it par-parloo ak féete ak neen ga ñu donn moo leen di teree dugg ci lislaam.
Ñii ñépp amuñu ngànt ci loolu, te danañu taxaw fa séen kanamu Boroom ci lu dul wenn lay.
Weddikatu Yàlla bi amul lay ci wax naan man damay des ci weddi Yàlla ndax damaa judd ci askan wu gëmul Yàlla! waaye li ko war mooy mu jëfandikoo xel mi ko Yàlla may, settantal ci màggaayu asamaan yi ak suuf si, ak mu xalaat ci xelam mi ko ki ko bind may ngir mu xam ne dénd bii am na ku ko bind, Niki noonu it kuy jaamu ay doj ak i xërëm amul ngànt ci topp baay ya, waaye li ko war mooy mu gëstu dëgg gi laaj boppam: naka laay jaamoo lii du ma dégg te du ma gis te du ma jariñ dara?!
Niki noonu it nasaraan bi gëm ay bir yu wuute ak ug sell ak xel war ña ci moom mu laaj boppam: naka la Boroom bi di raye doomam ji deful bàkkaar ngir bàkkaaru ay yeneen i nit?! Lii tooñ la! Naka la nit di daaje doomu Boroom bi ak diko ray?! Ndax Boroom bi dafa manul a jéggal nit séen i bàkkaar ci lu dul mu leen di bàyyi ñuy ray doomam? Ndax Boroom bi dafa manul a aar doomam?
Kon li war aji-xellu ji mooy mu topp dëgg, te bañ a roy baay yi ak maam yi ci neen.
Yàlla mu kawe mi nee na: Bu ñu leen waxee ne Kaayleen jëm ci li Yàlla wàcce ak ci Yonnente bi, ñu ne: “La ñu fekk sunuy baay doy nanu, waaw donte sax séen baay ya xamuñu dara te gindikuwuñu} [Al-Maa-ida: 105].
Ku bëgg a tuub te ragal ci boppam ay mbokkam lor ko ak i jegeñaaleem lan lay def?
Ku nàmm a jébbalu te ragal ñi ko wër, man naa jébbalu te nëbb Lislaamam ba keroog Yàlla di ko yombalal yoonu yiw mu manal boppam daal di feeñal Lislaamam.
Li war ci nit ki mooy mu gaaw tuub, waaye du war ci moom mu xibaare ag tuubam ñi ko wër mbaa mu koy siiwal, bu dee loolu day am lor ci moom.
Xamal ne nit ki bu tuubee day nekk mbokki ay milyoŋi jullit, te Dana man a dem ci jàkka walla ci daluwaayu Lislaam cim réewam sàkku ci ñoom am xel ak ndimbal te loolu dina leen neex.
Yàlla mu kawe mi nee na: {ku ragal Yàlla dina ko defal génnuwaay Wërsëgale ko fu mu dul fooge} [At-Talaaq: 2-3].
Yaw miy jàng Alxuraan
Ndax du gërëmloo Yàlla Aji-Bind ji, -moom mi nu xéewalal ay xéewal, daan nu jox ag dund fekk nun ay ëmb lanu ca sunu biiri yaay yi, mu wërsëgal nu ngelaw li nuy noyyi tay- moo ëpp solo ci nun ngërëmal nit ñi?
Xanaa texeg àdduna ak allaaxira yayoowul ñu def lépp lu nu man walif xéewali àdduna jii di jeex? Ahakay giñ naa ko ci Yàlla!
Loolu moo tax jaaduwul nit ki baña jubbanti yoonam wu dëng wimu jaaroon tay def lu wér.
Na nit ki nekk way-gëm leegi! Te bañ a bàyyi saytaane di ko teree topp dëgg!
Yàlla nee na: ﴾Yéen nit ñi aw lay wu juge ci séen Boroom ñëwal na leen te wácce nanu ci yéen leer gu bir (174) Budee ñi gëm Yàlla te wéeru ci moom dana leen dugal ci yërmànde ak ngëneel gindi leen jëme leen ci yoon wu jub wa} [An-Nisaa: 175].
Ndax jekk nga ngir jël dogal li gën a màgg ci sag dund?
Bu fekkee ne li jiitu lépp xel nangu na ko, te nit ki xam na dëgg gu ci xolam; kon war na ci moom mu jéego jéego bu njëkk jëm ci nekk ab jullit.
Ku bëgg ñu dimbali ko ci mu jël ndogal li gën ci dundam ñu xamal ko naka lay nekke jullit?
Bu mu def ay bàkkaaram muy lay wu koy teree dugg ci Lislaam, Yàlla xibaar na ñu ci Alxuraan ne mooy jéggal nit ñi bàkkaar yépp bu ñu jébbaloo tuub jëm ci ki ko bind, ba sax ginnaaw bu mu nangoo lislaam nit ki man naa def yenn bàkkaar yi, ndax nun ay nit dong lanu dunu ay malaaka yu mucc ci njuumte, Waaye li ñu sàkku ci nun mooy ñu sàkku njéggal ci Yàlla te tuub jëm ci moom, bu Yàlla gisee ci nun ne gaaw nanoo nangu dëgg daal di dugg ci Lislaam wax ñaari baati seede yi kon moom dana nu dimbali ci nu bàyyi yeneen bàkkaar yi, ki jublu Yàlla te topp dëgg Yàlla dana ko gën a dolli yiw, kon bu nit ki jiixi-jaaxa ci dugg ci Lislaam leegi.
Bokk na ci liy tegtale loolu, li Yàlla mu kawe mi wax ne: {Waxal yéefar yi, ne leen Bu ngeen bàyyee, nu baal leen la weesu waaye bu ngeen delluwaatee [ca la ngeen nekkoon] dees na leen mbugal kem ni mu daan ame bu njëkk} [Al-Anfaal: 38].
Lan laay def ngir nekk jullit?
Dugg ci Lislaam mbir mu yomb la aajowoowul lu bari walla teewaayu kenn, waaye li war nit ki rekk mooy mu wax ñaari baati seede yi te xam maanaa mi te gëm ko, te loolu mooy mu wax ne: (Ashadu an laa ilaaha illallaahu wa Ashadu Anna Muhammadan Rasuulul Laahi), boo ko manee wax ci ci làkku Araab moo gën, bu loolu jafee ci yaw nag dana doy nga wax ko ci saw làkk, ci loolu ngay nekke ab jullit, dana war ci yaw nag nga jàng sa diine ji nga xam ne ca la sa texeg àdduna ak sa muccug allaaxira di jogé.
Ngir yokk sa xam-xam ci Lislaam maa ngi lay dénk nga yër sit bii:
Ngir nga xam naka ngay jëfe lislaam, noo ngi lay dénk nga dugg ci sit bii:
Related books
All books
Kan moom a bind AK lu tax mu bind ma ?75 languagesKan moom a bind AK lu tax mu bind ma ?
BEEPP MIR MUMU MANA DOON DAAY TEKTALE AMUK YAALLA MIKO BIND! KAN MOO BIND ASAMAN YI AK LICI SEEN BIIR CI AY MBINDEEF YU MAAGG YOO XAMNE MBINDEEF MANULEENA PEEK? Kan moo def nosiin wu xereñe wii ? Kan moo bind nit may ko ag dégg ak ub jis ak xel te def ko muy ku man a am xam-xam tey xam li xew. Naka ngay firee wii tërëliin wu yéeme ci jumtukaay yi nekk ci sa biir yaram ak yaramu ndundat yi ? Kan moo fent loolu ? Naka la dund bu rëy bii man a nosaloo ci tëraliinam yu koy nose nose gu yéeme ba àdduna sosoo ba tay ?
Lislaam mooy diiney Yonnente Yàlla yi85 languagesLislaam mooy diiney Yonnente Yàlla yi
Lislaam mooy jébbalul Yàlla mi bind àdduna bi di ko doxal, wommatul ko ngir bëgg ko ak màggal ko, cosaanu lislaam mooy gëm Yàlla, ak ne moom mooy Aji-Bind ji, te lépp lu dul moom mbindeef la, ak ne moom moo yayoo jaamu moom rekk amul bokkaale, amul lenn lu ñuy jaamu ci dëgg ku dul moom,ay tur yu rafet ñeel na ko ak ay melo yu kawe, mooy ki mat sëkk, jurul kenn te kenn juru ko te amul benn nawle du caagine niroowaale, du wàcc te du jël jëmmi lenn ci mbindeefam yi. Lislaam mooy diiney Yàlla mi nga xam ne du nangu ci nit jenn diine ju dul moom, te mooy diine ji yonnente yépp indi yal na leen…
Islaam89 languagesIslaam
Ci turu Yàlla miy Aji-Yërëm képp ku nekk ci kaw suuf jagleel ko jullit ñi ca allaaxira laay tàmbalee. Ndax laaj nga sa bopp?: Kan moo bind asamaan yi ak suuf yi ak la ca nekk ci ay mbindéef yu bari? Ak kan moo defar nosiinu àdduna wu jaar yoon wi te ñu xarañe ko lool ?
Melokaanu julli (ci ab wiidewoo bu gàtt)86 languagesMelokaanu julli (ci ab wiidewoo bu gàtt)
Lii ag jëfe gu tënku la ci ni ñuy jullee, ngir nu jaamu Yàlla mu tegu ci xam-xam, te sunu julli mat sëkk ci ponk ya ak ci sàrt ya. Melokaanu julli Bu ñu bëggee julli dafay war ñu laab ci toj mu ndaw ak toj mu mag. Te bu nuy julli nu sol yére yu laab yu muur sunu awra. sunu yaram ak barab bi nuy jullee dafa war a laab ci sobe. Nu jublu xibla Sopp nañu bu nuy julli nu teg ab saatir ci sunu kanam.