Nekkoon a nu ci Umar mu wax ne: "tere nañ nu toggoo lu metti"
Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik, -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Nekkoon a nu ci Umar mu wax ne: "tere nañ nu toggoo lu metti"
كُنَّا عِنْدَ عُمَرَ فَقَالَ: «نُهِينَا عَنِ التَّكَلُّفِ».
Umar -yal na ko Yàlla dollee gërëm- day xibaare ne Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere na nu nuy toggoo yu metti yi ci lu dul aajo, moo xam ci wax mbaa jëf.
...:
Bokk na ci toggoo yu metti yi ñu tere: bari ab laaj, walla di toggoo loo xamul, walla di taral ci mbir mu Yàlla woyofal.
Jaadu na ci jullit bi mu tàmmal boppam woyof te bañ a diisal ci wax ak ci jëf: ci lekkam, ak ci naanam, ak ci ay waxam, ak mbiram yépp.
Lislaam diine ju yomb la.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (9/ 95) (7293).
Yataal gi (10)
نزهة المتقين.
لمصطفى الخن وغيره (2/ 1136).
شرح رياض الصالحين.
لابن عثيمين (6/ 391).
فتح الباري شرح صحيح البخاري.
لابن حجر (13/ 270).
النهاية في غريب الحديث والأثر.
لابن الأثير (4/ 196).
تطريز رياض الصالحين.
لفيصل آل مبارك (ص930).