Skip to content

«saa du taxaw ba keroog jamono ji di jegee

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:

«saa du taxaw ba keroog jamono ji di jegee, am at di mel ni weer, weer di mel ni ayu bis, ayu bis di mel ni benn bis, benn bis di mel ni wenn waxtu, wenn waxtu di mel ni taal xobi tàndarma».

«لَا تَقُومُ السَّاعَةُ حَتَّى يَتَقَارَبَ الزَّمَانُ، فَتَكُونَ السَّنَةُ كَالشَّهْرِ، وَيَكُونَ الشَّهْرُ كَالْجُمُعَةِ، وَتَكُونَ الْجُمُعَةُ كَالْيَوْمِ، وَيَكُونَ الْيَوْمُ كَالسَّاعَةِ، وَتَكُونَ السَّاعَةُ كَاحْتِرَاقِ السَّعَفَةِ الْخُوصَةُ».

Ahmat soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xibaare ne bokk na ci màndargay bis-pénc jegeeg jamono yi, At mi di romb kem ni weer di rombe, Weer di romb kem ni ayu bis di rombe, Ayu bis di romb kem ni benn bis di rombe, Benn bis di romb kem ni wenn waxtu di rombe, Wenn waxtu di romb gaaw lool ba mel ni xob wu ñuy lakk, te mooy xobu tàndarma.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Bokk na ci màndargay bis-pénc ñu dindi barke ci jamono ji mbaa gaawaayam.

Dellluwaay yi

Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (16/ 550) (10943).

Yataal gi (4)

معالم السنن (4/341).

فتح الباري (13/16).

شرح سنن أبي داود لابن رسلان (16/678).

تحفة الأحوذي (6/514).