Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo ëppoon kersa jigéen gi sëyagul, bu gisee mbir mu mu bañ ci kanamam gi lañu koy xame.
Jële nañu ci Abii Sahiid Al-Xudrii yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo ëppoon kersa jigéen gi sëyagul, bu gisee mbir mu mu bañ ci kanamam gi lañu koy xame.
كَانَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ أَشَدَّ حَيَاءً مِنَ العَذْرَاءِ فِي خِدْرِهَا، فَإِذَا رَأَى شَيْئًا يَكْرَهُهُ عَرَفْنَاهُ فِي وَجْهِهِ.
Abuu Sahiid Al-Xudrii yal na ko Yàlla dollee gërëm day xibaare ne Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo ëppoon kersa jigéen ju ndaw ju sëyagul jaxasoogul ak góor ñi tey làqu ci këram, bokk na ci kersaam gu tar bu daan bañ dara kanam gi day soppiku te du wax, waaye Sahaaba yi dañuy xame bañeel gi ci kanam gi
العَذْرَاء: البكر، وهي الأنثى التي لم يمسها رجل، سميت به لبقاء عذرتها، وهي ما يكون من التحام في فم الرحم.
الخِدْر: ناحية في البيت يترك عليها ستر.
Leeral li Yonnente bi làmboo ci kersa, te mooy jikkó ju màgg ja.
Kersag Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mooy fii ak xottiwuñu wormay Yàlla, bu ñu xottee wormay Yàlla nag; Yonnente day mer daal di digal sahaaba yi tere leen.
Ñaaxe ci jikkówoo kersa; ndaxte moom day jëme bakkan bi ci def lu rafet ak bàyyi lu ñaaw.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (8/ 26) (6102).
Téere Muslim bi gën a wér (4/ 1809) (2320).
Yataal gi (6)
بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.
لسليم الهلالي (2/ 11).
شرح رياض الصالحين.
لابن عثيمين (4/ 32).
نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.
لمجموعة من الباحثين (1/ 562).