"buleen tere jibéeri Yàlla yi jàkkay Yàlla yi, waaye nañu génn nekk ñu lëmësu".
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"buleen tere jibéeri Yàlla yi jàkkay Yàlla yi, waaye nañu génn nekk ñu lëmësu".
«لَا تَمْنَعُوا إِمَاءَ اللَّهِ مَسَاجِدَ اللَّهِ، وَلَكِنْ لِيَخْرُجْنَ وَهُنَّ تَفِلَاتٌ».
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa tere kilifag jigéen gi ak ki toggoo ay mbiram muy tere jigéen ñi jàkka yi, mu digal jigéen ñi bu ñuy génn ñu génn ci lu dul gëtt du caagine tambaabaloo taar; ngir ñu bañ a nekk sabab ci fitnaal góor ñi.
May nañu jigéen gi mu jullee ca jàkka ja bu ñu wóoloo finta, te mu génn ci lu dul gëtt.
Tegtaloo nañu ci ci ne jigéen du génn ci kër jëkkëram ci lu dul ndigalam, ngir ne mbiru ndigal li ci jëkkër yi la nekk.
Xérug lislaam vi jigéen ñi, ak bañ leen a tere lol seen yiw a ngi ci muy sàkku xam-xam ak lu ko niru.
Saxug kilifteefu góor ci kaw jigéen ak ag sàmmam ñeel ko.
Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (1/ 423) (565).
Yataal gi (3)
شرح سنن أبي داود للعباد (78/ 6).
شرح أبي داود للعيني (3/ 50).
النهاية في غريب الحديث والأثر ص(109).