Skip to content

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daawul woon xam luy xàjjale saar yi ba ba ñuy wàcce ci Moom {Bismil Laahir Rahmaanir Rahiim}.

Jële na ñu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daawul woon xam luy xàjjale saar yi ba ba ñuy wàcce ci Moom {Bismil Laahir Rahmaanir Rahiim}.

كَانَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَليهِ وَسَلَّمَ لا يَعْرِفُ فَصْلَ السُّورةِ حَتَّى تَنْزِلَ عَليْهِ {بِسْمِ اللَّهِ الرَّحْمَنِ الرَّحِيمِ}.

Abóo Daawuda soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- day leeral ne saari Alxuraan yi da daan wàcci ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- te daawul xam teqale ba ak fan la yam, ba ba ñuy wàcce ci moom: "Bismil Laahir Rahmaanir Rahiim" mu door a xam ne saar wi jiitu jeex na, weneen saar wu bees moo tàmbali.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Bismil Laahir Rahmaanir Rahiim mooy tàqale diggante saar yi, bamu des diggante saaru Al-Anfaal ak saaru At-Tawba.Bokk na ci njariñal hdiis bi:

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (2/ 91) (788).

Yataal gi (3)

شرح سنن أبي داود للعباد (102/ 15).

التنوير شرح الجامع الصغير (8/503).

عون المعبود (2/353).