Skip to content

«Séen sawara wi ab xaaj la ci juróom-ñaar fukki xaaj ci xaaji sawaraw Jahannama

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

«Séen sawara wi ab xaaj la ci juróom-ñaar fukki xaaj ci xaaji sawaraw Jahannama», ñu ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, bu doon moom rekk kon dana doy. Mu wax ne: «ëppe na ko juróom-benni fukk ak juróom-ñenti xaaj, te ñoom ñépp ñoo ngi mel ni aw tàngaayam».

«نَارُكُمْ جُزْءٌ مِنْ سَبْعِينَ جُزْءًا مِنْ نَارِ جَهَنَّمَ»، قِيلَ: يَا رَسُولَ اللَّهِ، إِنْ كَانَتْ لَكَافِيَةً. قَالَ: «فُضِّلَتْ عَلَيْهِنَّ بِتِسْعَةٍ وَسِتِّينَ جُزْءًا كُلُّهُنَّ مِثْلُ حَرِّهَا».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Leerarug hdiis bi : Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne sawaraw àdduna ab xaaj la ci juróom-ñaar fukki xaaji sawaraw Jahannama, Sawaraw allaaxira moo gën a tàng sawaraw àdduna ci juróom-benni fukk ak juróom-ñetti xaaj, te xaaj bu ci ne moo ngi tolloog tàngaayu sawaraw àdduna. Ñu ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, sawaraw àdduna bi rekk doyoon na ngir mbugal ña fay dugg, Mu ne leen: sawaraw Jahannama ëppe na sawaraw àdduna ci juróom-benn ak juróom- ñenti xaaj te ñoom ñépp a mel ni moom ciw tàngaay wu tar.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Xuppe ci sawara ngir nit ñi sori jëf ya cay yóbbe.

Màggug sawaraw Jahannama ak mbugalam, ak tàngaayam wu tar.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (4/ 121) (3265).

Téere Muslim bi gën a wér (4/ 2184) (2843).

Yataal gi (4)

المفهم (7/178).

التوضيح (19/177).

عمدة القاري شرح صحيح البخاري (15/ 165).

فتح الباري لابن حجر (6/ 334).