Skip to content

«Yalla dana néggandiku tooñkat bi, ba bu ko jàppee du ko rëcc

Jële na ñu ci Abuu Muusaa Al-Asharii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:

«Yalla dana néggandiku tooñkat bi, ba bu ko jàppee du ko rëcc» nee na: mu daal di jàng: aaya bii «{niki noonu it la sa jàppug Boroom di deme bu jàppee waa dëkk buy tooñ te ag jàppam lu metti la te tar} [Huud: 102]»

«إِنَّ اللهَ لَيُمْلِي لِلظَّالِمِ، حَتَّى إِذَا أَخَذَهُ لَمْ يُفْلِتْهُ» قَالَ: ثُمَّ قَرَأَ: «{وَكَذَلِكَ أَخْذُ رَبِّكَ إِذَا أَخَذَ الْقُرَى وَهِيَ ظَالِمَةٌ إِنَّ أَخْذَهُ أَلِيمٌ شَدِيدٌ}[هود: 102]»

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day moytondikuloo di wéy cig tooñ ak i moy ak bokkaale, ak tooñ nit ñi ci séen i àq, ndax Yàlla mu kawe mi day néggandiku tooñkat bi di ko yeexe ak di guddal fanam di baril alalam te du ko gaawa mbugal; bu tuubul mu jàpp ko te du ko bàyyi ndax ay bàkkaar yu bari. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di jàng aaya bii: {niki noonu it la sa jàppug Boroom di deme bu jàppee ab waa dëkk buy tooñ te ag jàppam lu metti la te tar} [Huud: 102].

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

War na ci ki am xel mu gaaw a tuub, te bañ a wóolu pexem Yàlla ndeem dafa nekk cig tooñ.

Yàlla day néggandiku way-tooñ yi bañ leen a mbugal ngir jay leen ak ngir ful mbugal ma bu ñu tuubul.

Tooñ bokk na ci sabab yiy tax Yàlla di mbugal xeet yi.

Bu Yàlla alagee ab dëkk amaana ñu sell nekk fa, waaye ñooñu dañu leen di dekkil ëllëg bis-pénc ca mbaax ga ñu faatoo, te mbugal ma leen yóbbaale du leen lor.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (6/ 74) (4686).

Téere Muslim bi gën a wér (4/ 1997) (2583).

Yataal gi (10)

شرح رياض الصالحين.

لابن عثيمين (2/ 496).

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (1/ 303).

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.

لمصطفى الخِن وغيره (1/ 231).

تطريز رياض الصالحين.

لفيصل آل مبارك (ص165).

مرقاة المفاتيح.

علي القاري (8/ 3200).