Skip to content

«Yàlla dat ŋëb suuf si, lem asamaan yi ci ndayjooram, di wax naan: man maay buur, ana buuri suuf si».

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne:

«Yàlla dat ŋëb suuf si, lem asamaan yi ci ndayjooram, di wax naan: man maay buur, ana buuri suuf si».

«يَقْبِضُ اللَّهُ الأَرْضَ، وَيَطْوِي السَّمَوَاتِ بِيَمِينِهِ، ثُمَّ يَقُولُ: أَنَا المَلِكُ، أَيْنَ مُلُوكُ الأَرْضِ».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne yawmal xiyaam Yàlla day ŋëb suuf si dajale ko, mu lem asamaan si ci ndayjooram taxañ lenn la ca kaw leneen la daal di koy dindi jële ko fi, topp muy wax naan: man maay buur, ana buuri suuf si?!

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Fàttalee ci ne nguurug Yàlla moo fiy des nguurug keneen nag day deñ.

Màggug Yàlla ak màggug kàttanam ak nguuram ak matug nguuram.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (6/ 126) (4812).

Téere Muslim bi gën a wér (4/ 2148) (2787).

Yataal gi (3)

فتح الباري (13/367).

عمدة القاري شرح صحيح البخاري (23/ 101).

البحر المحيط الثجاج (43/324).