Skip to content

Benn waay da doon lekke càmmooñ fi Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu ne ko: "lekkeel sa ndayjoor", waa ji ne ko: manuma ko, mu ne ko: "Yàlla boo ko man"

Jële nañu ci Salamata ibnul Akwah -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:

Benn waay da doon lekke càmmooñ fi Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu ne ko: "lekkeel sa ndayjoor", waa ji ne ko: manuma ko, mu ne ko: "Yàlla boo ko man", dara terewu ko ko lu dul rëy, nee na: yëkkatiwaatu ko jëme ci gémmiñam.

أَنَّ رَجُلًا أَكَلَ عِنْدَ رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ بِشِمَالِهِ، فَقَالَ: «كُلْ بِيَمِينِكَ»، قَالَ: لَا أَسْتَطِيعُ، قَالَ: «لَا اسْتَطَعْتَ»، مَا مَنَعَهُ إِلَّا الْكِبْرُ، قَالَ: فَمَا رَفَعَهَا إِلَى فِيهِ.

Muslim soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa gis benn waay muy lekke loxob càmmooñam, mu digal ko mu lekke loxob ndayjooram, Waa ji tontu ko ngir rëy ak di fen ci ne manu ko! Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ñaan ko Yàlla ngir mu xañ ko mu lekke ndayjoor, Yàlla nangu ñaanug Yonnenteem bi loxob ndayjoor bi summiku, yëkkateetu ko jëme ci gémmiñam ginnaaw loolu, ci lekk mbaa ci naan.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Lekke ndayjoor lu war la, lekke càmmooñ nag dafa araam.

Rëy a jëfe àttey sariiha yi, ku ko def yeyoo na mbugal.

Yàlla dafa teral Yonnenteem Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci nangu ñaanam.

Yoonalees na digle lu baax ak tere lu bon ci jépp jamono, ba ci jamonoy lekk

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér (3/ 1599) (2021).

Yataal gi (6)

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (1/ 239).

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (1/ 183).

كنوز رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (3/ 396).