Skip to content

«aji-gëm nekkul kiy jamaate, walla kiy rëbbaate, mbaa kiy def ñaawteef, walla aji-bon lammiñ ji».

Jële na ñu ci Abdallah Ibn Mashuud yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:

«aji-gëm nekkul kiy jamaate, walla kiy rëbbaate, mbaa kiy def ñaawteef, walla aji-bon lammiñ ji».

«لَيْسَ الْمُؤْمِنُ بِالطَّعَّانِ وَلاَ اللَّعَّانِ وَلاَ الفَاحِشِ وَلاَ البَذِيءِ».

At-tirmisiy soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne bokkul ci mbiri aji-gëm ji gëmam mat muy ayibal nit ñi ci seeni askan, walla di baril ay saaga ak i rëbbaate mbaa ñaaw i jëf, walla ci wax ju amul kersa.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Dàq ag ngëm du nekk ci benn yax ci yaxu sariiha lu dul ci jëf lu araam walla bayyi lu war.

Ñaaxe ci sàmm cér yi ak wattu ko ci ñaawteef yi, rawati na làmmeñ wi.

Assindii nee na: nekk na ci waxiin wu jotale gii (jamaatekat , ak rëbbaatekat) tegtal ci ne jam ak rëbb Ñeel ku ka yayoo tamu nekk lu néew loolu du lor ki mu jóge ci moom bu fekkee mu melowoo melow ku gëm Yàlla.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (3/ 520) (1977).

Yataal gi (2)

تحفة الأحوذي (6/ 95).

مجموع الفتاوى (12/ 478).