Skip to content

«bu ngeen déggee woote gi nangeen wax lu mel ni li noddkat bi di wax».

Jële na ñu ci Abii Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

«bu ngeen déggee woote gi nangeen wax lu mel ni li noddkat bi di wax».

«إِذَا سَمِعْتُمُ النِّدَاءَ، فَقُولُوا مِثْلَ مَا يَقُولُ المُؤَذِّنُ».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day soññee ci bu ñu dégge nodd-kat bi ñu koy toppandoo, ci di wax kem li muy wax. Bu kàbbaree nu kàbbar, bu waxee ñaari seede yi, nu wax leen. Dees na ca settee:(hàyya halas salaah, hayya halal falaah )foofu dañuy wax ci ginnaawam : laa hawla wa laa xuwwata illaa bil Laahi.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Bokk na ci njariñal hdiis bi: day toppandoo noddkat bu njëkk soonga toppandoo noddkat bu ñaareel bi, doonte noddkat yi dañoo bari, ngir ne hadiis bi daa matale lépp.

Day toppandoo noddkat bi ci anam gu ne, ndeem nekkul ci wanag, mbaa muy faj aaju.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 126) (611).

Téere Muslim bi gën a wér (1/ 288) (383).

Yataal gi (4)

تيسير العلام شرح عمدة الأحكام.

للبسام (ص120).

الإلمام بشرح عمدة الأحكام.

لإسماعيل الأنصاري (1/ 98).