Skip to content

«bu ndox mi nekkee ñaari mbànd kon du téye sobe».

Jele nañu ci Abdullah ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: laaj nañu Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ndox ak la fay jaabante ci ay ndundat ak i ndegment, mu wax ne:

«bu ndox mi nekkee ñaari mbànd kon du téye sobe».

«إِذَا كَانَ الْمَاءُ قُلَّتَيْنِ لَمْ يَحْمِلِ الْخَبَثَ».

Abuu Daawuda ak At-Tirmisiyyu ak An-Nasaa-iyyu ak Ibn Maaja ak Ahmad ñoo ko soloo.
Wér na
Leeral gi

Laaj nañu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc àtteb laabu ndox mi nga xam ne rab yi ak ndegment yi dañu fay jaabante ngir naan ak lu ko niru, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax ne: bu ndox mi tollee ci ñaari mbànd yu mag, muy yamoo ak: (210) liitar kon ndox mu bari la du sobewu; lu dul bu benn ci ñatti meloom yi di meloom wi walla cafkaam gi walla xetam gi soppeekoo ci sobe.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ndox day sopewu bu benn ci ñatti meloom yi soppeekoo ci sobe, meloom, walla cafkaam, walla xetam, hadiis bi dafa rot ci anamug notal, waaye du cig tënk.

Woroom xam-xam yi dëppoo nañu ci ne ndox mi bu ko sobe soppee kon sobe la ba fàww, moo xam dafa néew walla dafa bari.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (1/ 46) (63).

Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (1/ 109) (67).

Téere Sunna yi bu An-nasaa'iy (1/ 46) (52).

Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja (1/ 324) (517).

Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (8/ 211) (4605).

Yataal gi (6)

توضيح الأحكام.

للبسام (1/ 121).

فتح ذي الجلال والإكرام بشرح بلوغ المرام.

لابن عثيمين (1/ 67).

منحة العلام.

لعبد الله الفوزان (1/ 35).