Skip to content

"seen Boroom de Ku bari kersa la ku tedd la, dana kersawu ci jaam bi bu yëkkëtee loxoom jëme ci moom mu koy ba ña jox".

Jële na ñu ci Salmaan -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:

"seen Boroom de Ku bari kersa la ku tedd la, dana kersawu ci jaam bi bu yëkkëtee loxoom jëme ci moom mu koy ba ña jox".

«إِنَّ رَبَّكُمْ حَيِيٌّ كَرِيمٌ، يَسْتَحْيِي مِنْ عَبْدِهِ إِذَا رَفَعَ يَدَيْهِ إِلَيْهِ أَنْ يَرُدَّهُمَا صِفْرًا».

Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja.
Tane na
Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day ñaaxe ci yëkkëti loxo ci jamonoy ñaan, mu xamle ne Yàlla Aji-Sell ji ku bari kersa la, te du deñ di joxe, day defal jaam bi lu koy bégloo, dindil ko lu koy lor, ku tedd la day joxe ci lu dul ñu koy laaj kon naka lay deme ginnaaw bu ñu ko laajee! Day kersawu ci jaamam bi ko gëm mu delloo ay loxoom ginnaaw ba mu ko yëkkëtee ngir ñaan mu koy ñàkka nangul ñaanam ga.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Saa bu nit ki feeñalee ak soxlawoom jëm ci Yàlla ak ug njaame, muy gën a am yaakaar ci ñaanam gu nangu.

Xemmemloo ci ñaan, ak sopp ñu yëkkëti ñaari loxo yi ci ñaan gi ndax dafa bokk ci sababi nangu ñaan yi.

Leeral ne Yàlla dafa tabe lool bari yërmànde lool ci jaamam yi.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (2/ 609) (1488).

Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (5/ 521) (3556).

Yataal gi (6)

توضيح الأحكام من بلوغ المرام.

لعبد الله البسام (7/ 552).

منحة العلام في شرح بلوغ المرام.

لعبد الله الفوزان (10/ 423).

فتح ذي الجلال والإكرام.

لابن عثيمين (6/ 483).