Skip to content

"ndax duma leen xibaar lu gën darajay woor ak julli ak saraxe?

Jële na ñu ci Abuu Dardaa yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:

"ndax duma leen xibaar lu gën darajay woor ak julli ak saraxe? Ñu ne ko: ahakay, mu ne: "yéwenug diggante yi, ndax yàqug diggante yi mooy lay wat nag".

«أَلاَ أُخْبِرُكُمْ بِأَفْضَلَ مِنْ دَرَجَةِ الصِّيَامِ وَالصَّلاَةِ وَالصَّدَقَةِ؟» قَالُوا: بَلَى، قَالَ: «صَلاَحُ ذَاتِ البَيْنِ، فَإِنَّ فَسَادَ ذَاتِ البَيْنِ هِيَ الحَالِقَةُ».

Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa laaj Sahaaba yi: ndax duma leen xibaar lu gën yoolu bariy naafilay woor ak julli ak saraxe? Ñu ne ko: waaw. Mu ne: yéwénal diggante ñaar ñu xuloo ndax xuloo day waral teqalikoo ak beru ak bañante ak dummooyoonte ci diggante nit ñi, ndax lay topp ci yàquteg diggante yi ci mbañeelooy melo wi nga xam ne bokk na cibiram alage ak raafal diine ji ak àdduna ji kem ni watukaay di raafale kawar gi.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Njubug Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci laaj Sahaaba yi ak xemmemloo leen xam tontu ba.

At-Tiibii nee na: ñaaxe ak xemmemloo ci yéwénal diggante yi ak moytu ko a yàq; ndax yéwénal sabab la ci ŋoy ci buumu Yàlla gi ak bañ a tàqale jullit ñi, te yàqug diggante yi gàkk-gàkk la ci diine ji ku taxaw ci yéwénal ko daal di dindi yàqute gi dana am daraja ju gën a kaw ji aji-woor ji ak aji-julli jiy yittewoo mbiri boppam di am.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (7/ 280) (4919).

Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (4/ 244) (2509).

Yataal gi (2)

تحفة الأحوذي (7/ 179).

شرح سنن أبي داود للعباد (559/ 32).