Skip to content

«moom am ndoxam lu laab la , am méddam it lu dagan la».

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:

jenn waay laaj na Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, nun danuy dugg ci géej gi, di yor tuuti ndox, bu nu ci jàppee daal di mar, ndax nu jàppu ci ndoxum géej gi? Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: «moom am ndoxam lu laab la , am méddam it lu dagan la».

سَأَلَ رَجُلٌ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَقَالَ: يَا رَسُولَ اللهِ، إِنَّا نَرْكَبُ البَحْرَ، وَنَحْمِلُ مَعَنَا القَلِيلَ مِنَ الْمَاءِ، فَإِنْ تَوَضَّأْنَا بِهِ عَطِشْنَا، أَفَنَتَوَضَّأُ مِنَ الْبَحْرِ؟ فَقَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «هُوَ الطَّهُورُ مَاؤُهُ، الحِلُّ مَيْتَتُهُ».

Abuu Daawuda ak At-Tirmisiyyu ak An-Nasaa-iyyu ak Ibn Maaja ak Ahmad ñoo ko soloo.
Wér na
Leeral gi

Jenn waay dafa laaj Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, ne ko: man damay war gaal nekk ci kaw géej gi ngir napp walla ngir yaxantu ak lu ko niru, nuy yor tuuti ndox mees man a naan, te bu nu ko jëfandikoo ci jàppu walla sangu day jeex te dunu am lu nu naan, ndax dana dagan nu jàppu ci ndoxom géej gi? Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax ci ndoxum géej ne: ndoxam mi dafa laab tey laabal; dana dagan a jàppu ak sangu, dagan na it ñu lekk la fay génne ci jën yu ndaw ak jën yu mag ak yeneen, donte dañu ko a fekk mu dee, daal di tëdd noonu ci lu dul ñu kenn napp ko.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Méddum rabi géej yi lu dagan la, li ñu namm ci méddam mooy: ndundatam ya dee te bokk ci yi dul dund lu dul ci biir géej.

Tontu aji-laaj ji ci lu ëpp li mu laaj ngir mottali njariñ li.

Ndox mi bu cafkaam walla meloom walla xetam soppeekoo ci lu laab, kon day des ca laab ga fii ak ndox la mu des di nekk ndox, donte xoramam walla tàngaayam walla seddam gi ak lu ko niru dafa tar lool.

Ndoxum géej day yëkkëti sobe su mag ak su ndaw, day dindi it sobe su tàbbi ci lu laab, yaram ak yére mbaa leneen.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (1/ 62) (83).

Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (1/ 111) (69).

Téere Sunna yi bu An-nasaa'iy (1/ 50) (59).

Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja (1/ 250) (386).

Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (12/ 171) (7233).

Yataal gi (6)

منحة العلام في شرح بلوغ المرام.

لعبد الله الفوزان (1/ 28).

فتح ذي الجلال والإكرام بشرح بلوغ المرام.

لابن عثيمين (1/ 59).

توضيح الأحكام شرح بلوغ المرام.

لعبد الله البسام (1/ 116).