Skip to content

«bu Yàlla dogalee ci nit ki mu faatu a fi barab da koy def mu am fa aajo».

Jële na ñu ci Matar Ibn Hukaamis- yal na leen Yàlla dollee gërëm - mu wax ne, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:

«bu Yàlla dogalee ci nit ki mu faatu a fi barab da koy def mu am fa aajo».

«إِذَا قَضَى اللَّهُ لِعَبْدٍ أَنْ يَمُوتَ بِأَرْضٍ جَعَلَ لَهُ إِلَيْهَا حَاجَةً».

At-tirmisiy soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne bu Yàlla dogalee ci jaam bi mu War a faatu a fi barab te moom nekku fa; da ko fay defal aajo mu dem fa, ñu jël fa ag ruuham.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Bokk na ci njariñal adiis bi: Hadiis bi day dëggal li Yàlla mu kawe mi wax ne: {benn bakkan xamul ci ban suuf lay faatoo}.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (4/ 23) (2146).

Yataal gi (1)

تحفة الأحوذي (6/ 299).