Skip to content

"amul ñaari jullit yuy daje daal di joxante loxo lu dul ne dees na leen jéggal laata ñuy teqalikoo".

Jële nañu ci Al-Baraa yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:

"amul ñaari jullit yuy daje daal di joxante loxo lu dul ne dees na leen jéggal laata ñuy teqalikoo".

«مَا مِنْ مُسْلِمَيْنِ يَلْتَقِيَانِ فَيَتَصَافَحَانِ إِلَّا غُفِرَ لَهُمَا قَبْلَ أَنْ يَفْتَرِقَا».

Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
Wér na ci kaw bees boolee mbooleem yoon yi mu ñëwee
Leeral gi

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne: amul ñaari jullit yuy daje ci aw yoon mbaa lu ko niru kenn ki nuyu keneen ki ñu joxante loxo lu dul ne dees na leen jéggal njëkk ñuy taqalikoo.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Sopp nañu joxante loxo bu ñu dajee, ak soññee ca.

Al-Manaawii nee na: te sunna si du am ci lu dul teg ndayjoor bi ci ndeyjoor bi bu ngànt amul.

Ñaaxe ci tasaare nuyóo, ak leeral ngëneelu fayug saafonteg jullit bi ak mbokku jullitam.

Dees na settee ci hadiis bi joxante loxo gu araam niki góor di jox loxo jigéenu jàmbur.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (7/ 502) (5212).

Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (4/ 447) (2727).

Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja (4/ 654) (3703).

Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (30/ 517) (18547).

Yataal gi (4)

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (2/ 152).

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (1/ 680).