Skip to content

Mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ci waa Ansaar yi ne: "kénn du leen bëgg ku dul way-gëm, te kenn du leen bañ ku dul ab naaféq, ku leen bëgg Yàlla bëgg ko, ku leen bañ Yàlla bañ ko".

Jële nañu ci Al-Baraa -yal na ko Yàlla dollee gërëm-:

Mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ci waa Ansaar yi ne: "kénn du leen bëgg ku dul way-gëm, te kenn du leen bañ ku dul ab naaféq, ku leen bëgg Yàlla bëgg ko, ku leen bañ Yàlla bañ ko".

عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ أَنَّهُ قَالَ فِي الْأَنْصَارِ: «لَا يُحِبُّهُمْ إِلَّا مُؤْمِنٌ، وَلَا يُبْغِضُهُمْ إِلَّا مُنَافِقٌ، مَنْ أَحَبَّهُمْ أَحَبَّهُ اللهُ وَمَنْ أَبْغَضَهُمْ أَبْغَضَهُ اللهُ».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne bëgg Ansaar yi di waa Madina, màndarga la ci ngëm gu mat; ngir li ñu jiitu ci dimbali Lislaam ak Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ak dox ci yiir jullit ni, ak joxe seen alal ak seen bakkan ci yoonu Yàlla, kon bañ leen màndargay naaféq la. Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral ne ku bëgg Ansaar yi Yàlla bëgg ko, ku leen bañ Yàlla bañ ko.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Nekk na ci it ngëneel yu màgg ñeel Ansaar yi, ndax bëgg leen màndargay ngëm la ak set ci naaféq.

Bëgg wàlliyuy Yàlla yi di leen dimbali sabab la ci Yàlla bëgg ab jaamam.

Ngëneelu ña jiitu ci Lislaam.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (5/ 32) (3783).

Téere Muslim bi gën a wér (1/ 85) (75).

Yataal gi (9)

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (1/ 447).

تطريز رياض الصالحين.

لفيصل آل مبارك (ص257).

كنوز رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (6/ 258).

شرح النووي على مسلم (2/ 63).

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.

مجموعة من الباحثين (1/ 350).